1 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu réseñam. 2 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leen a yebal ca toolam. 3 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu. 4 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”5 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg-bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu. 6 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”7 Ñu tontu ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” 8 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujj a ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”9 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon. 10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkk a jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon. 11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga, 12 naan: “Ñi mujj a ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” 13 Waaye boroom kër ga tontu kenn ci ñoom ne ko: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon? 14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujj a ñëw, li ma la fey yaw, 15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” 16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.» 17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii: 18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, 19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.» 20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn. 21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu tontu ko ne: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndeyjoor, ki ci des ci sa càmmooñ.» 22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu tontu ko: «Man nañu ko.» 23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.» 24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya. 25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di noot. 26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 27 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam. 28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko. 30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne, Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gën a yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?» 33 Ñu tontu ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.» 34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.