Wolof: New Testament

Matthew

24

1 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko tabaxi kër Yàlla ga. 2 Waaye mu tontu leen ne: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.» 3 Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne, yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» 4 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. 5 Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare. 6 Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; wottuleen, buleen ci tiit, ndaxte loolu war na am, waaye booba muju jamono ji jotagul. 7 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yengu-yenguy suuf ci bérab yu bare. 8 Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu. 9 Bu boobaa dees na leen jébbale, metital leen, rey leen; te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur. 10 Bu loolu amee ñu bare dinañu dàggeeku, di booleente tey bañante. 11 Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare. 12 Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku. 13 Waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc. 14 Noonu xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee muju jamono ji jot. 15 «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam. 16 Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; 17 ku nekk ci kaw taax ma, bul wàcc ngir fab say yëf, ya nekk ci biir kër ga; 18 ku nekk ca tool ba, bul ñibbi ngir fab sa mbubb. 19 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal! 20 Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésu noflaay bi. 21 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk. 22 Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn. 23 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm. 24 Ndaxte ñi mbubboo turu Kirist ak ñi mbubboo turu yonent dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am. 25 Wax naa leen ko lu jiitu. 26 «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm. 27 Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwu Doomu nit ki di mel. 28 Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee. 29 «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yengu. 30 Booba firnde ji taxaw, Doomu nit ki feeñ ci asamaan, te xeeti àddina sépp dinañu jooy. Dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci niiri asamaan si, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 31 Dina yónni ay malaakaam ak baatu liit bu dégtu, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa asamaan dale ba fu mu yem.» 32 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, ay xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. 33 Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, xamleen ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax. 34 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul. 35 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk. 36 «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 37 Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw. 38 Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor yaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga; 39 xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwu Doomu nit ki. 40 «Bu boobaa ci ñaar ñu nekk cib tool, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des. 41 Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des. 42 Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés bu seen Boroom di ñëw. 43 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yeewu te du ko bàyyi, mu toj këram. 44 Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»45 Yeesu teg ca ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ca jamono ja? 46 Bu njaatigeem ñëwee te gis muy def noonu, surga boobu dina am ngërëm. 47 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. 48 Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” 49 mu tàmbalee dóor ay bokki surgaam, di lekk te naan ak naankat ya, 50 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. 51 Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.