Wolof: New Testament

Matthew

26

1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu lépp ba noppi, mu ne taalibeem ya:2 «Xam ngeen ne, ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.» 3 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu saraxalekat bu mag ba, tudd Kayif. 4 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu man a fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko. 5 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.» 6 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon,7 jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ bu jar lu baree-bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu. 8 Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii lu muy jariñ?9 Maneesoon na koo jaay ci lu bare, jox xaalis bi miskin yi.» 10 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? 11 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww. 12 Kii, ci li mu tuur latkoloñ bii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob. 13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.» 14 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya, 15 ne leen: «Lan ngeen ma man a jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu saraxalekat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer. 16 Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu. 17 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru màggalu Jéggi ba?» 18 Yeesu tontu leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi xewu Jéggi ba, man ak samay taalibe.”» 19 Noonu taalibe yi defar reeru Jéggi ba, na leen Yeesu waxe woon. 20 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar. 21 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.» 22 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?» 23 Yeesu tontu leen ne: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor. 24 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoon a juddu moo gënoon ci moom.» 25 Yudaa, mi ko nar a wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.» 26 Noonu bu ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.» 27 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci, 28 ndaxte lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi. 29 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaawsi tey ndoxum réseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum réseñ mu bees ci sama nguuru Baay.» 30 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. 31 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.” 32 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.» 33 Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.» 34 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» 35 Piyeer tontu ko: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. 36 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.» 37 Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonett. 38 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgg a dee; toogleen fi, xool ak man.» 39 Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.» 40 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? 41 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir; seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» 42 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii mënu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.» 43 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. 44 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon. 45 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma war a jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na. 46 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.» 47 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca saraxalekat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet. 48 Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.» 49 Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaamu àleykum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng. 50 Yeesu tontu ko: «Sama xarit, xam naa lu tax nga ñëw.» Noonu ñu daldi jegesi, song ko, jàpp ko. 51 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag ba, nopp ba dagg. 52 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey. 53 Xanaa xamuloo ne, man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul? 54 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi man a ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la war a ame.» 55 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. 56 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw. 57 Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, saraxalekat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje. 58 Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje. 59 Noonu saraxalekat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu man a seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey, 60 waaye mënuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan: 61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”» 62 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo tontu dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?» 63 Waaye Yeesu ne cell. Saraxalekat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.» 64 Yeesu tontu ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan si.» 65 Bi mu déggee loolu, saraxalekat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee. 66 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu tontu ko: «Yoon teg na ko dee.» 67 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar-kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko, 68 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?» 69 Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.» 70 Waaye Piyeer weddi ko ci kanamu ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.» 71 Bi mu ko waxee, mu jëm ca bunt ba, te beneen mbindaan gis ko, mu wax ña fa nekkoon: «Kii àndoon na ak Yeesum Nasaret.» 72 Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.»73 Nes tuuti ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» 74 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. 75 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.