聖經新譯本

Wolof: New Testament

Luke

2

1耶穌基督降生(太1:18~25)那時,有諭旨從凱撒奧古士督頒發下來,叫普天下的人登記戶口。
1 Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji.
2這是第一次戶口登記,是在居里紐作敘利亞總督的時候舉行的。
2 Mbindu mooma, di mu jëkk ma, daje na ak jamono, ja Kiriñus nekke boroom réewu Siri.
3眾人各歸各城去登記戶口。
3 Noonu ku nekk dem binduji ca sa dëkku cosaan.
4約瑟本是大衛家族的人,也從加利利的拿撒勒上猶太去,到了大衛的城伯利恆,
4 Yuusufa nag daldi jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk.
5與所聘之妻馬利亞一同登記戶口。那時馬利亞的身孕已經重了。
5 Mu dem binduji, ànd ak Maryaama jabaram, fekk booba Maryaama ëmb.
6他們在那裡的時候,馬利亞的產期到了,
6 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.
7生了頭胎兒子,用布包著,放在馬槽裡,因為客店裡沒有地方。
7 Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba.
8天使向牧羊人報喜信在伯利恆的郊外,有一些牧人在夜間看守羊群。
8 Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.
9主的一位使者站在他們旁邊,主的榮光四面照著他們,他們就非常害怕。
9 Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.
10天使說:“不要怕!看哪!我報給你們大喜的信息,是關於萬民的:
10 Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
11今天在大衛的城裡,為你們生了救主,就是主基督。
11 Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.
12你們要找到一個嬰孩,包著布,臥在馬槽裡,那就是記號了。”
12 Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»
13忽然有一大隊天兵,同那天使一起讚美 神說:
13 Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan:
14“在至高之處,榮耀歸與 神!在地上,平安歸與他所喜悅的人!”
14 «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa,te ci àddina, na jàmm ji wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
15眾天使離開他們升天去了,那些牧人彼此說:“我們往伯利恆去,看看主所指示我們已經成就的事。”
15 Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»
16他們急忙去了,找到馬利亞、約瑟和那臥在馬槽裡的嬰孩。
16 Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
17他們見過以後,就把天使對他們論這孩子的話傳開了。
17 Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.
18聽見的人,都希奇牧人所說的事。
18 Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
19馬利亞把這一切放在心裡,反覆思想。
19 Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
20牧人因為聽見的和看見的,正像天使對他們所說的一樣,就回去了,把榮耀讚美歸與 神。
20 Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21滿了八天,替孩子行割禮的時候,就給他起名叫耶穌,就是他成胎之前,天使所起的。
21 Bi bés ba dellusee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22在聖殿奉獻耶穌滿了潔淨的日子,他們就按著摩西的律法,帶孩子上耶路撒冷去,奉獻給主。
22 Noonu jamono ji ñu leen waroon a sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23正如主的律法所記:“所有頭生的男孩,都當稱為聖歸給主。”
23 Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24又照著主的律法所說的獻上祭物,就是一對斑鳩或兩隻雛鴿。
24 Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
25在耶路撒冷有一個人,名叫西面,這人公義虔誠,一向期待以色列的安慰者來到,又有聖靈在他身上。
25 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla war a dëfël bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26聖靈啟示他,在死前必得見主所應許的基督,
26 te xamal na ko ne, du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27他又受聖靈感動進了聖殿。那時,耶穌的父母抱著孩子進來,要按著律法的規矩為他行禮。
27 Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
28西面就把他接到手上,稱頌 神說:
28 Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:
29“主啊,現在照你的話,釋放僕人平平安安地去吧!
29 «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam,mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.
30因我的眼睛已經看見你的救恩,
30 Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
31就是你在萬民面前所預備的,
31 xeet yépp seede ko.
32為要作外族人啟示的光,和你民以色列的榮耀。”
32 Muy leer giy leeral xeet yi,di ndamu Israyil say gaay.»
33他父母因論到他的這些話而希奇。
33 Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
34西面給他們祝福,對他母親馬利亞說:“看哪!這孩子被立,要叫以色列中許多人跌倒,許多人興起,又要成為反對的目標,
34 Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
35(你自己的心也會被刀刺透,)這樣,許多人心中的意念就要被揭露出來。”
35 ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
36又有一個女先知,就是亞拿,是亞設支派法內利的女兒。她已經上了年紀,從童女出嫁,和丈夫住了七年,
36 Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom-ñaari at ak jëkkëram.
37就寡居了,直到八十四歲(“就寡居了,直到八十四歲”或譯:“就寡居了八十四年”)。她沒有離開過聖殿,以禁食和禱告晝夜事奉主。
37 Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom-ñett-fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woon a jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.
38就在那時候,她前來稱謝 神,並且向期待耶路撒冷蒙救贖的眾人,講論孩子的事。
38 Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla war a jot Yerusalem.
39他們按著主的律法辦完一切,就回加利利,到自己的城拿撒勒去了。
39 Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
40孩子漸漸長大,強壯起來,充滿智慧,有 神的恩典在他身上。
40 Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41孩童耶穌上耶路撒冷過節每年逾越節,他父母都上耶路撒冷去。
41 At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Jéggi ba.
42當他十二歲時,他們按著節期的慣例,照常上去。
42 Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe nakajekk.
43過完了節,他們回去的時候,孩童耶穌仍留在耶路撒冷,他父母卻不知道,
43 Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44還以為他在同行的人中間。走了一天,就在親戚和熟人中找他,
44 Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.
45沒有找到,就轉回耶路撒冷找他。
45 Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46過了三天,才發現他在聖殿裡,坐在教師中間,一面聽,一面問。
46 Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jàngalekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.
47所有聽見他的人,都希奇他的聰明和應對。
47 Ñépp ñi dégg li mu wax yéemu ci xel, mi mu àndal, ak ni mu doon tontoo.
48他父母見了,非常驚奇,他母親說:“孩子,為甚麼這樣對待我們呢?你看,你父親和我都很擔心地在找你呢!”
48 Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.»
49他說:“為甚麼找我呢?你們不知道我必須在我父的家裡嗎?(“在我父的家裡嗎?”或譯:“以我父的事為念嗎?”)”
49 Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne, damaa war a nekk ci sama kër Baay?»
50但他們不明白他所說的話。
50 Waaye xamuñu li kàddoom yi doon tekki.
51他就同他們下去,回到拿撒勒,並且順從他們。他母親把這一切事,都存在心裡。
51 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom, dellu Nasaret te déggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu yépp ci xolam.
52耶穌的智慧和身量,以及 神和人對他的喜愛,都不斷增長。
52 Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.