1施洗約翰(太3:1~12;路3:1~18;約1:19~28) 神的兒子(有些抄本無“ 神的兒子”一句)耶穌基督福音的開始。
1 Xebaar bu baaxu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee.
2正如以賽亞先知的書上寫著:“看哪,我差遣我的使者在你面前,預備你的道路;
2 Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan:«Maa ngi yónni sama ndaw ci sa kanam,mu xàllal la sa yoon.
3在曠野有呼喊者的聲音:‘預備主的道,修直他的路!’”
3 Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”»
4照這話,施洗的約翰在曠野出現了,傳講悔改的洗禮,使罪得赦。
4 Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
5猶太全地和全耶路撒冷的人,都出來到他那裡去,承認自己的罪,在約旦河裡受了他的洗。
5 Kon waa diiwaanu Yude ñépp ak waa dëkku Yerusalem ñépp daldi génn jëm ci moom, di nangu seeni bàkkaar fi kanam ñépp, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
6約翰身穿駱駝毛的衣服,腰束皮帶,吃的是蝗蟲和野蜜。
6 Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
7他傳講說:“有一位在我以後來的,能力比我大,我就是彎腰給他解鞋帶都沒有資格。
7 Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam.
8我用水給你們施洗,他卻要用聖靈給你們施洗。”
8 Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.»
9耶穌受洗(太3:13~17;路3:21~22)那時候耶穌從加利利的拿撒勒來,在約旦河裡受了約翰的洗。
9 Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan.
10他從水裡一上來,就看見天裂開了,聖靈仿佛鴿子降在他身上。
10 Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom.
11又有聲音從天上來說:“你是我的愛子,我喜悅你。”
11 Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
12耶穌受試探(太4:1~11;路4:1~13)聖靈隨即催促耶穌到曠野去。
12 Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma.
13他在那裡四十天,受撒但的試探,和野獸在一起,有天使來服事他。
13 Mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane; mu dëkk ci biir rabi àll yi, te malaakay Yàlla di ko topptoo.
14在加利利傳道(太4:12~17;路4:14~15)約翰被捕以後,耶穌來到加利利,宣講 神的福音,
14 Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xebaar bu baaxu Yàlla,
15說:“時候到了, 神的國近了,你們應當悔改,相信福音。”
15 naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xebaar bu baax bi.»
16呼召四個門徒(太4:18~22;路5:1~11;約1:35~42)耶穌沿著加利利海邊行走,看見西門和他弟弟安得烈在海上撒網;他們是漁夫。
16 Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
17耶穌就對他們說:“來跟從我,我要使你們成為得人的漁夫。”
17 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.»
18他們立刻撇下網,跟從了他。
18 Ci saa si ñu bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
19耶穌稍往前走,看見西庇太的兒子雅各,和雅各的弟弟約翰,正在船上整理魚網,
19 Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, ñu nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal.
20他立即呼召他們。他們撇下父親西庇太和雇工在船上,就跟從他去了。
20 Noonu Yeesu woo leen, ñu daldi bàyyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom.
21在迦百農趕出污靈(路4:31~37)他們到了迦百農,耶穌隨即在安息日進入會堂教導人。
21 Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésu noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal.
22大家對他的教訓都很驚奇,因為他教導他們,像一個有權柄的人,不像經學家。
22 Te ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
23就在那時,會堂裡有一個被污靈附著的人,喊叫起來,
23 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi yuuxu naan:
24說:“拿撒勒人耶穌,我們跟你有甚麼關係呢?你來毀滅我們嗎?我知道你是誰,你是 神的聖者。”
24 «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
25耶穌斥責他說:“住口!從他身上出來!”
25 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom.»
26污靈使那人抽瘋,大聲喊叫,就從他身上出來了。
26 Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te génn ci moom ak yuux gu réy.
27眾人都很驚訝,於是彼此對問說:“這是怎麼一回事?是個有權能的新道理啊!他吩咐污靈,污靈竟服從了他!”
27 Bi loolu amee ñépp waaru, ba laajante naan: «Kii mooy kan? Mii njàngale lu bees la te ànd ak sañ-sañ. Day sant rab yi sax, ñu di ko déggal.»
28耶穌的名聲立刻傳遍了加利利一帶。
28 Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gépp.
29治病趕鬼(太8:14~17;路4:38~41)他們一出會堂,就和雅各、約翰到西門和安得烈的家裡去。
29 Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare.
30西門的岳母正在發燒躺著,他們立刻告訴耶穌。
30 Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu.
31耶穌走到她面前,拉著她的手,扶她起來,熱就退了,她就服事他們。
31 Mu ñëw nag ci moom, jàpp loxoom, yékkati ko. Noonu tàngoor wi daldi wàcc, te soxna si di leen topptoo.
32到了黃昏,有人不斷把生病的和被鬼附的,都帶到耶穌面前。
32 Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ñi rab jàpp ñépp,
33全城的人都聚集在門口。
33 ba dëkk bi bépp dajaloo ci buntu kër gi.
34耶穌醫好了各樣的病,也趕出許多的鬼,並且不許鬼說話,因為鬼認識他。
34 Noonu mu wéral ñu bare, ñu wopp ak ay jàngoro yu wuute, te dàq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ko.
35在加利利傳道趕鬼(路4:42~44)次日凌晨,天還沒有亮,耶穌起身出去,來到荒野的地方,在那裡禱告。
35 Ca njël laata bët di set, Yeesu jóg dem ca bérab bu wéet, di fa ñaan Yàlla.
36西門和那些跟他在一起的人就去尋找耶穌。
36 Simoŋ nag ak ñi ànd ak moom di ko seet fu nekk.
37他們找到了,就對他說:“大家都在找你呢!”
37 Bi ñu ko gisee, ñu ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
38耶穌對他們說:“我們到鄰近的鄉鎮去吧,我也好在那裡傳道,因為我就是為這事而來的。”
38 Waaye Yeesu tontu leen: «Nanu dem feneen ci dëkk yi nu wër, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma génn.»
39於是他走遍加利利全地,在他們的會堂裡傳道,並且趕鬼。
39 Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi.
40治好痲風病人(太8:2~4;路5:12~16)有一個患痲風的人,來到耶穌跟前,跪下求他說:“如果你肯,必能使我潔淨。”
40 Am bés ku gaana ñëw ci moom, sukk, ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
41耶穌動了憐憫的心,就伸手摸他,說:“我肯,你潔淨了吧!”
41 Yeesu yërëm ko, tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.»
42痲風立刻離開了他,他就潔淨了。
42 Ca saa sa ngaanaam daldi deñ, mu wér.
43耶穌打發那人離開以前,嚴厲地吩咐他,
43 Noonu Yeesu yebal ko, dénk ko bu wér naan:
44說:“你千萬不可把這事告訴任何人,你只要去給祭司檢查,並且照著摩西所規定的,為你得潔淨獻祭,好向大家作證。”
44 «Moytul a wax kenn dara, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
45但那人出來,竟任意傳講,就把這事傳開了,以致耶穌不能再公開進城,只好留在外邊荒野的地方;然而還是有人從各處到他那裡去。
45 Waaye naka la waa ji génn, mu di yéene ci kaw li xewoon, te di ko jéebaane, ba tax Yeesu mënatul a faŋaaral dugg cib dëkk, waaye mu nekk ci biti ciy bérab yu wéet. Ba tey nit ñi jóge fu nekk, di ko fa fekk.