聖經新譯本

Wolof: New Testament

Mark

2

1治好癱子(太9:1~8;路5:18~26)過了些日子,耶穌再回到迦百農。一聽說他在屋子裡,
1 Bi ay fan weesoo, Yeesu dellusi dëkku Kapernawum, mu siiw ne mu ngi ci kër gi.
2許多人就都來聚集,甚至連門前都沒有地方了,耶穌就對他們講道。
2 Noonu nit ñu bare dajaloo fa, ba kenn amatul foo taxaw, du ci bunt bi sax. Te Yeesu di leen yégal kàddu gi.
3那時有人把一個癱子帶到耶穌那裡,是由四個人抬來的。
3 Noonu, am ñu ko indil ku yaramam wépp làggi, ñeenti nit jàppoo ko.
4因為人擠,不能帶到他面前,就對著耶穌所在的地方,拆去房頂;拆通了,就把癱子連人帶褥子縋了下去。
4 Waaye mënuñu koo jege ndax mbooloo mi. Kon ñu daldi teggi kaw kër gi, di bëtt fa tiim bérab ba Yeesu nekk, daldi yoor basaŋ, ga làggi ba tëdd.
5耶穌看見他們的信心,就對癱子說:“孩子,你的罪赦了。”
5 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
6當時有幾個經學家也坐在那裡,心裡議論說:
6 Fekk ay xutbakat toog fa, ñu di werante ci seen xel naan:
7“這個人為甚麼這樣說話?他說僭妄的話了。除了 神一位以外,誰能赦罪呢?”
7 «Kii kan la, ba sañ a wax lii; mi ngi sosal Yàlla. Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
8耶穌心裡立刻知道他們這樣議論,就對他們說:“你們心裡為甚麼議論這事?
8 Waaye Yeesu yég ci xelam li ñuy werante ci seen biir, ne leen: «Lu tax ngeen di werantee nii ci seen xel?
9對癱子說‘你的罪赦了’,或說‘起來,拿著你的褥子走’,哪一樣容易呢?
9 Lan moo gën a yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”?
10然而為了要你們知道人子在地上有赦罪的權柄,(他就對癱子說:)
10 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu mu ne làggi ba:
11我吩咐你,起來,拿起你的褥子,回家去吧。”
11 «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
12那人就起來,立刻拿著褥子,當眾出去了。眾人都非常驚奇,頌讚 神,說:“我們從來沒有見過這樣的事。”
12 Ca saa sa mu jël basaŋam te génn fa kanam ñépp. Noonu ñépp waaru, di màggal Yàlla naan: «Lu mel ni lii, musunu koo gis.»
13呼召利未(太9:9~13;路5:27~32)耶穌又出去,到了加利利海邊;眾人都到他面前來,他就教導他們。
13 Gannaaw loolu Yeesu génnaat, aw booru dex ga, mbooloo mépp di ñëw ci moom, mu di leen jàngal.
14他往前走的時候,看見亞勒腓的兒子利未坐在稅關那裡,就對他說:“來跟從我!”他就起來跟從了耶穌。
14 Bi Yeesu di romb, mu gis ku ñuy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ci man.» Mu jóg, daldi topp ci moom.
15後來耶穌在利未家裡吃飯,有很多稅吏和罪人也來與他和門徒一起吃飯;因為這樣的人很多,並且他們已經跟隨了耶穌。
15 Bi loolu amee Yeesu ak i taalibeem di lekk ci kër Lewi, fekk ay juutikat ak ay boroom bàkkaar yu bare di lekkandoo ak ñoom, ndaxte ñu bare ci ñoom a ko toppoon.
16法利賽派的經學家,看見耶穌與罪人和稅吏一起吃飯,就對耶穌的門徒說:“他跟稅吏和罪人一起吃飯嗎?”
16 Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi ñu gisee ne, dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar, ñu daldi laaj taalibe yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
17耶穌聽見了,就對他們說:“健康的人不需要醫生,有病的人才需要;我來不是要召義人,而是要召罪人。”
17 Noonu Yeesu dégg ko, mu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla; ñëwuma woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
18新舊的比喻(太9:14~17;路5:33~38)約翰的門徒和法利賽人正在禁食,有人來問耶穌說:“為甚麼約翰的門徒和法利賽人的門徒常常禁食,你的門徒卻不禁食呢?”
18 Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?»
19耶穌回答:“新郎跟賓客在一起的時候,賓客怎能禁食呢?只要新郎還在,就不能禁食。
19 Yeesu tontu leen: «Ndax gan, yi ñëw cig céet, dinañu woor, fekk boroom céet gi ànd ak ñoom? Duñu woor, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom.
20但日子到了,新郎要被取去,離開他們,那一天他們就要禁食了。
20 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi; bés boobaa nag dinañu woor.
21沒有人會把一塊新布縫在舊衣服上,如果這樣,新的布就會把舊衣服扯破,裂開的地方就更大了。
21 «Kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu.
22也沒有人會把新酒裝在舊皮袋裡,如果這樣,酒就會把皮袋脹破,酒和皮袋都損壞了;新酒總該裝在新皮袋裡。”
22 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yàqu, ak biiñ bi tuuru. Waaye biiñ bu bees, ci mbuus yu bees lañu koy def.»
23安息日的主(太12:1~8;路6:1~5)有一次,在安息日,耶穌從麥田經過,他的門徒一面走路,一面摘麥穗。
23 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ciy tool yu ñor. Bi ñuy dem nag, ay taalibeem daldi fàq ay gub.
24法利賽人對耶穌說:“你看,他們為甚麼作安息日不可作的事?”
24 Noonu Farisen ya ne Yeesu: «Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?»
25耶穌對他們說:“大衛和跟他一起的人在飢餓缺食的時候所作的,你們沒有念過嗎?
25 Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu amee soxla te xiif, moom ak ña mu àndaloon?
26他不是在亞比亞他作大祭司的時候,進了 神的殿,吃了除祭司以外誰都不可以吃的陳設餅,而且還給跟他在一起的人吃嗎?”
26 Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar saraxalekat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu ya ñu jébbal Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat?»
27耶穌又告訴他們:“安息日是為人設立的,人並不是為安息日設立的。
27 Yeesu dellu ne leen: «Yàlla sàkkul nit ngir bésu noflaay bi, waaye sàkk na bésu noflaay ngir nit.
28這樣,人子也是安息日的主。”
28 Noonu Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»