聖經新譯本

Wolof: New Testament

Mark

4

1撒種的比喻(太13:1~9;路8:4~8)耶穌又在海邊教導人。有一大群人聚集到他那裡,因此他上船坐下來。船在海中,群眾都朝著海站在岸上。
1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jàngalewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
2他用比喻教訓他們許多事,在教訓中他說:
2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngaleem nag mu ne leen:
3“你們聽著!有一個撒種的出去撒種,
3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
4撒的時候,有的落在路旁,小鳥飛來就吃掉了。
4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
5有的落在泥土不多的石地上,因為泥土不深,很快就長起來。
5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
6但太陽一出來,就把它曬乾,又因為沒有根就枯萎了。
6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
7有的落在荊棘裡,荊棘長起來,把它擠住,它就結不出果實來。
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara.
8有的落在好土裡,就生長繁茂,結出果實,有三十倍的、有六十倍的、有一百倍的。”
8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, lii mat téeméer.»
9耶穌又說:“有耳可聽的,就應當聽。”
9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
10用比喻的目的(太13:10~17;路8:9~10)耶穌獨自一人的時候,那些經常跟著他的人和十二門徒,來問這些比喻的意義。
10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi.
11耶穌對他們說:“ 神的國的奧祕,只給你們知道,但對於外人,一切都用比喻,
11 Mu tontu leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp.
12叫他們‘看是看見了,卻不領悟,聽是聽見了,卻不明白,免得他們回轉過來,得到赦免。’”
12 Noonu la, ngir:“Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara,di déglu bu baax waaye duñu xam dara,ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar,te Yàlla baal leen.”»
13解釋撒種的比喻(太13:18~23;路8:11~15)耶穌又對他們說:“你們不明白這個比喻,怎能明白一切比喻呢?
13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des?
14撒種的人所撒的就是道。
14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji.
15那撒在路旁的,就是人聽了道,撒但立刻來,把撒在他心裡的道奪去。
15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom.
16照樣,那撒在石地上的,就是人聽了道,立刻歡歡喜喜地接受了;
16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si,
17可是他們裡面沒有根,只是暫時的;一旦為道遭遇患難,受到迫害,就立刻跌倒了。
17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
18那撒在荊棘裡的,是指另一些人;他們聽了道,
18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi,
19然而今世的憂慮、財富的迷惑,以及種種的慾望,接連進來,把道擠住,就結不出果實來。
19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara.
20那撒在好土裡的,就是人聽了道,接受了,並且結出果實,有三十倍的、有六十倍的、有一百倍的。”
20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom-benn-fukk, kii mat téeméer.»
21隱藏的事終必顯露(路8:16~18)耶穌又對他們說:“燈難道是拿來放在量器底下或床底下的嗎?它不是該放在燈臺上嗎?
21 Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk?
22因為沒有甚麼隱藏的事不被顯明出來,沒有甚麼掩蓋的事不被揭露的。
22 Amul dara luy kumpa lu ñu warul a siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ.
23有耳可聽的,就應當聽。”
23 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
24耶穌又對他們說:“要留心你們所聽到的,你們用甚麼尺度量給人, 神也要用甚麼尺度量給你們,並且要超過尺度給你們。
24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.
25因為那有的,還要給他;那沒有的,就算他有甚麼也要拿去。”
25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.»
26種子發芽生長的比喻耶穌說:“ 神的國好像人在地裡撒種,
26 Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool.
27他夜裡睡覺,白天起來,種子發芽生長,自己也不知道怎麼會這樣的。
27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe.
28地生五穀是自然的,先長苗,後吐穗,最後穗上結滿了子粒。
28 Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub.
29莊稼熟了,就派人用鐮刀割下,因為收成的時候到了。”
29 Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.»
30芥菜種的比喻(太13:31~35;路13:18~19)又說:“我們要把 神的國比作甚麼呢?我們可以用甚麼比喻來形容它呢?
30 Yeesu ne leen ati: «Lu nu man a mengaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko man a misaale?
31它好像一粒芥菜種,剛種下去的時候,比地上的一切種子都小,
31 Dafa mel ni doomu fuddën, bi gën a tuuti ci jiwu yépp;
32種下以後,生長起來,卻比一切蔬菜都大,長出大枝子,甚至天空的飛鳥都可以在它的蔭下搭窩。”
32 waaye boo ko jiwee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.»
33耶穌用許多這樣的比喻,照著他們所能聽懂的,向他們講道;
33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneeni léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan.
34不用比喻,就不對他們講。只有單獨和自己的門徒在一起的時候,才把一切解釋給他們聽。
34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.
35平靜風浪(太8:18、23~27;路8:22~25)當天黃昏,耶穌對門徒說:“我們渡到海那邊去吧。”
35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
36門徒離開群眾,耶穌已經在船上,他們就載他過去,也有別的船和他同去。
36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneeni gaal ànd ak moom.
37忽然起了狂風,波浪不斷地打進船來,艙裡積滿了水。
37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgg a fees.
38耶穌卻在船尾靠著枕頭睡著了。門徒把他叫醒,對他說:“老師,我們要死了,你不管嗎?”
38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngégenaay ci taatu gaal gi.Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
39耶穌起來,斥責了風,又對海說:“不要作聲!安靜吧!”風就停止,大大地平靜了。
39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
40然後對他們說:“為甚麼這樣膽怯呢?你們怎麼沒有信心呢?”
40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
41門徒非常懼怕,彼此說:“這到底是誰,連風和海都聽從他?”
41 Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»