聖經新譯本

Wolof: New Testament

Matthew

12

1安息日的主(可2:23~28;路6:1~5)安息日那天,耶穌從麥田經過;他的門徒餓了,就摘了些麥穗來吃。
1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
2法利賽人看見了,就對他說:“你看,你的門徒作了安息日不可作的事。”
2 Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi.»
3耶穌對他們說:“大衛和跟他在一起的人,在飢餓的時候所作的,你們沒有念過嗎?
3 Noonu Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4他不是進了 神的殿,吃了他和跟他在一起的人不可以吃,只有祭司才可以吃的陳設餅嗎?
4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu jébbal Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; saraxalekat rekk a ko sañoon a lekk.
5律法書上記著:安息日,祭司在殿裡供職,觸犯了安息日,也不算有罪;你們也沒有念過嗎?
5 Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne saraxalekat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésu noflaay bi, te tooñuñu?
6我告訴你們,這裡有一位是比聖殿更大的。
6 Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga.
7如果你們明白‘我喜愛憐憫,不喜愛祭祀’這句話的意思,就不會把無罪的定罪了。
7 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul.
8因為人子是安息日的主。”
8 Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
9治好手枯的人(可3:1~6;路6:6~11)耶穌離開那裡,來到他們的會堂。
9 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
10會堂裡有一個人,他的一隻手枯乾了。有人問耶穌:“在安息日治病,可以嗎?”目的是要控告耶穌。
10 te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésu noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
11耶穌回答:“你們當中有哪一個,他僅有的一隻羊在安息日跌進坑裡,會不把羊抓住拉上來呢?
11 Yeesu tontu leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésu noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko?
12人比羊貴重得多了!所以,在安息日行善是可以的。”
12 Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésu noflaay bi jaadu na.»
13於是對那人說:“伸出手來!”他把手一伸,就復原了,好像另一隻手一樣。
13 Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des.
14法利賽人出去,商議怎樣對付耶穌,好殺掉他。
14 Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu.
15 神揀選的僕人耶穌知道了,就離開那裡。有很多人跟隨他,他醫好他們所有的病人,
15 Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp.
16又囑咐他們不可替他張揚。
16 Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
17這就應驗了以賽亞先知所說的:
17 Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
18“看哪!我所揀選的僕人,我所愛,心裡所喜悅的;我要把我的靈賜給他,他必向萬國宣揚公理。
18 «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn,di sama Soppe bi neex sama xol.Dinaa def sama Xel ci moom,muy yégal xeet yi yoonu njub.
19他不爭吵,也不喧嚷,人在街上聽不見他的聲音。
19 Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw,te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
20壓傷的蘆葦,他不折斷,將殘的燈火,他不吹滅;直到他施行公理,使公理得勝。
20 Du dammaate barax bu banku,te mees guy saxar, du ko fey,ba kera mu yégal njub, ba daan.
21萬民都要寄望於他的名。”
21 Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
22耶穌靠 神的靈趕鬼(可3:20~30;路11:14~23)有人帶了一個被鬼附著、又瞎又啞的人到耶穌那裡。耶穌醫好了他,那啞巴就能說話,也能看見了。
22 Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis.
23群眾都很驚奇,說:“難道他就是大衛的子孫?”
23 Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
24法利賽人聽見了,說:“這個人趕鬼,只不過是靠鬼王別西卜罷了。”
24 Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
25耶穌知道他們的心思,就對他們說:“如果一個國家自相紛爭,就必定荒涼;一城一家自相紛爭,必站立不住。
25 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du man a yàgg.
26如果撒但趕逐撒但,就會自相紛爭。那麼,他的國怎能站立得住呢?
26 Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di man a yàgge?
27我若靠別西卜趕鬼,你們的子孫又靠誰呢?這樣,他們就要斷定你們的不是。
27 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
28我若靠 神的靈趕鬼, 神的國就已經臨到你們了。
28 Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
29如果不先把壯漢綁起來,怎能進到他的家裡,搶奪財物呢?如果綁起來了,就可以搶劫他的家了。
29 «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgg a dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp.
30不站在我這一邊的就是反對我的,不跟我一起收聚的,就是分散的。
30 Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
31因此,我告訴你們,人的一切罪和褻瀆的話,都可以赦免;可是,褻瀆聖靈就得不著赦免。
31 Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu man a doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal.
32無論誰說話得罪了人子,還可以赦免;但說話得罪了聖靈的,今生來世都得不著赦免。
32 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira.
33種好樹結好果子(路6:43~45)“你們種好樹就結好果子,種壞樹就結壞果子;憑著果子就能認出樹來。
33 Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee.
34毒蛇所生的啊,你們既然是邪惡的,怎能說出良善的話?因為心中所充滿的,口裡就說出來。
34 Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen man a waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
35良善的人從他良善的心(“心”原文作“庫房”)發出良善,邪惡的人從他邪惡的心(“心”原文作“庫房”)發出邪惡。
35 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon.
36我告訴你們,人所說的閒話,在審判的日子,句句都要供出來,
36 Maa ngi leen di wax ne, keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu mas a wax.
37因為你要照你的話被稱為義,或定為有罪。”
37 Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
38約拿的神蹟(可8:11~12;路11:29~32)當時,有一些經學家和法利賽人對耶穌說:“老師,我們想請你顯個神蹟看看。”
38 Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
39但耶穌說:“邪惡和淫亂的世代尋求神蹟,除了約拿先知的神蹟以外,再沒有神蹟給你們了。
39 Yeesu tontu leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg yonent Yàlla Yunus.
40約拿怎樣三日三夜在大魚的腹中,人子也要照樣三日三夜在地裡。
40 Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf.
41審判的時候,尼尼微人要和這個世代一同起來,定這個世代的罪,因為他們聽了約拿所傳的就悔改了。你看,這裡有一位是比約拿更大的。
41 Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
42審判的時候,南方的女王要和這個世代一同起來,定這個世代的罪,因為她從地極來到,要聽所羅門智慧的話。你看,這裡有一位是比所羅門更大的。
42 Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
43污靈去而復返的教訓(路11:24~26)“有一個污靈離開了一個人,走遍乾旱之地,尋找棲身的地方,卻沒有找到。
43 «Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis.
44他就說:‘我要回到我從前離開了的那房子。’到了之後,看見裡面空著,已經打掃乾淨,粉飾好了,
44 Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
45他就去帶了另外七個比自己更惡的污靈來,一齊進去住在那裡;那人後來的情況,比以前更壞了。這邪惡的世代也會這樣。”
45 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
46誰是耶穌的母親和弟兄(可3:31~35;路8:19~21)耶穌還在對群眾講話的時候,他的母親和弟弟站在外面,要找他講話。
46 Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgg a wax ak moom.
47有人告訴耶穌:“你的母親和弟弟站在外面,有話要跟你說。”
47 Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg a wax ak yaw.»
48他回答那人:“誰是我的母親?誰是我的弟兄?”
48 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
49他伸手指著門徒說:“你看,我的母親,我的弟兄!
49 Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk.
50凡是遵行我天父旨意的,就是我的弟兄、姊妹和母親了。”
50 Ndaxte ku def sama coobareg Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»