1占星家朝拜耶穌希律王執政的時候,耶穌生在猶太的伯利恆。那時,有幾個占星家從東方來到耶路撒冷,
1 Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
2說:“那生下來作猶太人的王的在哪裡?我們看見他的星出現,特來朝拜他。”
2 Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
3希律王聽見了就心裡不安,全耶路撒冷的居民也是這樣。
3 Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
4他就召集所有的祭司長和民間的經學家,問他們基督應該生在哪裡。
4 Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, war a juddoo.
5他們回答:“在猶太的伯利恆。因為有先知在經上這樣說:
5 Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent:
6‘猶大地的伯利恆啊!你在猶大的領袖中,並不是最小的,因為必有一位領袖從你那裡出來,牧養我的子民以色列。’”
6 “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude,du yaw yaa yées ci njiiti Yude,ndaxte ci yaw la njiit di génne,kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
7希律暗中把占星家召來,仔細查問他們,那顆星甚麼時候出現,
7 Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
8然後派他們到伯利恆去,說:“你們去細心尋訪那小孩,找到了就向我報告,好叫我也去拜他。”
8 Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
9他們聽命去了。他們在東方看見的那顆星,忽然在他們前頭,領他們到那小孩所在的地方,就在上頭停住了。
9 Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tell jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
10他們看見那顆星,歡喜極了;
10 Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réy-a-réy.
11進了房子,看見小孩和他母親馬利亞,就俯伏拜他,並且打開寶盒,把黃金、乳香、沒藥作禮物獻給他。
11 Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
12後來他們在夢中得著指示不要回到希律那裡去,就從別的路回鄉去了。
12 Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu bañ a dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
13逃往埃及他們走了以後,主的使者在夢中向約瑟顯現,說:“起來,帶著孩子和他母親逃到埃及去,留在那裡,直到我再指示你,因為希律要尋找這孩子,把他殺掉。”
13 Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
14約瑟就起來,連夜帶著孩子和他母親往埃及去,
14 Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
15住在那裡,直到希律死了,為的是要應驗主藉先知所說的:“我從埃及召我的兒子出來。”
15 Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
16屠殺嬰孩希律見自己被占星家愚弄了,就大怒,於是照著他從占星家所問得的日子,下令把伯利恆和附近地方,兩歲以下的小孩全都殺死。
16 Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, mengook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
17這就應驗了耶利米先知所說的:
17 Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan:
18“在拉瑪聽見有聲音,是痛哭、極大哀號的聲音;拉結為她的兒女哀哭,不肯受安慰,因為他們都不在了。”
18 «Baat jib na ci Rama,ay jooy ak yuux gu réy,Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko,ndaxte saay nañu.»
19從埃及回來希律死後,在埃及,主的使者在夢中向約瑟顯現,
19 Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
20說:“那些要殺害這孩子的人已經死了。起來,帶著孩子和他母親回以色列地去吧。”
20 ne ko: «Ñi doon wut a rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
21約瑟就起來,帶著小孩子和他母親回到以色列地。
21 Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
22只是聽見亞基老接續他父親希律作了猶太王,他就不敢到猶太地去;又在夢中得了指示,於是往加利利境去,
22 Waaye bi mu déggee ne, Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
23來到拿撒勒城住下,這樣就應驗了先知所說的:“他必稱為拿撒勒人。”
23 Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan:«Dees na ko tudde Nasaréen.»