1Let every soul be in subjection to the higher powers: for there is no power but of God; and the [powers] that be are ordained of God.
1 Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg.
2Therefore he that resisteth the power, withstandeth the ordinance of God: and they that withstand shall receive to themselves judgment.
2 Kon ku leen bañ a déggal, ndigalu Yàlla nga lànk, te ku def loolu, yoon dina la dab.
3For rulers are not a terror to the good work, but to the evil. And wouldest thou have no fear of the power? do that which is good, and thou shalt have praise from the same:
3 Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko bëggee bañ a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg.
4for he is a minister of God to thee for good. But if thou do that which is evil, be afraid; for he beareth not the sword in vain: for he is a minister of God, an avenger for wrath to him that doeth evil.
4 Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon.
5Wherefore [ye] must needs be in subjection, not only because of the wrath, but also for conscience' sake.
5 Kon fokk ngeen déggal ko, waxuma sax ndax sañ-sañam boobu, waaye it ngir seen xel dal.
6For this cause ye pay tribute also; for they are ministers of God's service, attending continually upon this very thing.
6 Gannaaw Yàllaa sas njiit yi liggéey boobu, te ñi ngi ci, kon fàww ngeen fey galag.
7Render to all their dues: tribute to whom tribute [is due]; custom to whom custom; fear to whom fear; honor to whom honor.
7 Joxleen ku nekk céram; ku ngeen war a fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen war a fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen war a weg, wegleen ko; ku ngeen war a teral, teral-leen ko.
8Owe no man anything, save to love one another: for he that loveth his neighbor hath fulfilled the law.
8 Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa.
9For this, Thou shalt not commit adultery, Thou shalt not kill, Thou shalt not steal, Thou shalt not covet, and if there be any other commandment, it is summed up in this word, namely, Thou shalt love thy neighbor as thyself.
9 Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul rey nit, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
10Love worketh no ill to his neighbor: love therefore is the fulfilment of the law.
10 Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
11And this, knowing the season, that already it is time for you to awake out of sleep: for now is salvation nearer to us than when we [first] believed.
11 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yeewu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm.
12The night is far spent, and the day is at hand: let us therefore cast off the works of darkness, and let us put on the armor of light.
12 Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgg a set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer.
13Let us walk becomingly, as in the day; not in revelling and drunkenness, not in chambering and wantonness, not in strife and jealousy.
13 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu xuloo mbaa nuy ñeeyante.
14But put ye on the Lord Jesus Christ, and make not provision for the flesh, to [fulfil] the lusts [thereof].
14 Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te bañ a topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.