1But him that is weak in faith receive ye, [yet] not for decision of scruples.
1 Gannaaw loolu ku ngëmam néew nangeen ko nangu, te bañ a werante ak moom ci lu lënt.
2One man hath faith to eat all things: but he that is weak eateth herbs.
2 Ndax am na ku xalaat ne, man na lekk ñam wu nekk, fekk ku ngëmam néew du lekk yàpp, waaye léjum rekk lay lekk.
3Let not him that eateth set at nought him that eateth not; and let not him that eateth not judge him that eateth: for God hath received him.
3 Kiy lekk lu nekk, bumu xeeb ki ko dul def. Naka noonu itam ku dul lekk yàpp, bumu teg tooñ ki koy lekk; ndax Yàlla nangu na leen ñoom ñaar.
4Who art thou that judgest the servant of another? to his own lord he standeth or falleth. Yea, he shall be made to stand; for the Lord hath power to make him stand.
4 Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.
5One man esteemeth one day above another: another esteemeth every day [alike]. Let each man be fully assured in his own mind.
5 Noonu itam am na ñiy tànn bés ak ñiy yemale bés yépp. Na ku nekk xam bu wér li muy def, te jàpp ci.
6He that regardeth the day, regardeth it unto the Lord: and he that eateth, eateth unto the Lord, for he giveth God thanks; and he that eateth not, unto the Lord he eateth not, and giveth God thanks.
6 Ndaxte kuy tànn bés, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Yàlla. Te it ki bañ a lekk yàpp, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi, di ko sant.
7For none of us liveth to himself, and none dieth to himself.
7 Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam.
8For whether we live, we live unto the Lord; or whether we die, we die unto the Lord: whether we live therefore, or die, we are the Lord's.
8 Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.
9For to this end Christ died and lived [again], that he might be Lord of both the dead and the living.
9 Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir man a nekk Boroomu ñi dee ak ñiy dund.
10But thou, why dost thou judge thy brother? or thou again, why dost thou set at nought thy brother? for we shall all stand before the judgment-seat of God.
10 Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom tooñ? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun ñépp, danu dul dajeji fa kanam Yàlla, ngir mu layoo ak nun?
11For it is written, As I live, saith the Lord, to me every knee shall bow, And every tongue shall confess to God.
11 Ndaxte Mbind mi tëral na lii:«Boroom bi nee na:“Ni mu wóore ne maa ngi dund,ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal,te ku nekk seede ne maay Yàlla.”»
12So then each one of us shall give account of himself to God.
12 Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo mas a def.
13Let us not therefore judge one another any more: but judge ye this rather, that no man put a stumblingblock in his brother's way, or an occasion of falling.
13 Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar.
14I know, and am persuaded in the Lord Jesus, that nothing is unclean of itself: save that to him who accounteth anything to be unclean, to him it is unclean.
14 Xam naa ne, amul wenn ñam wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul.
15For if because of meat thy brother is grieved, thou walkest no longer in love. Destroy not with thy meat him for whom Christ died.
15 Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, génn nga ci mbëggeel. Yaw nag bul réeral sa moroom ci sa ñam, ndax Kirist dee na ngir moom.
16Let not then your good be evil spoken of:
16 Bu sa njariñ jur wax ju ñaaw.
17for the kingdom of God is not eating and drinking, but righteousness and peace and joy in the Holy Spirit.
17 Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla, te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi.
18For he that herein serveth Christ is well-pleasing to God, and approved of men.
18 Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Yàlla ak nit ñi.
19So then let us follow after things which make for peace, and things whereby we may edify one another.
19 Kon nag nanu wut luy indi jàmm, tey yékkati ngëmu sunu moroom.
20Overthrow not for meat's sake the work of God. All things indeed are clean; howbeit it is evil for that man who eateth with offence.
20 Bu sa ñam yàq jëfu Yàlla. Bépp ñam sell na ci kanam Yàlla. Ci lu wér! Waaye képp ku lekk luy yàq sa ngëmu moroom, def nga lu bon.
21It is good not to eat flesh, nor to drink wine, nor [to do anything] whereby thy brother stumbleth.
21 Liy sa warugar mooy nga bañ a fiir sa moroom ci yàpp mbaa ci biiñ mbaa ci leneen lu mu man a doon.
22The faith which thou hast, have thou to thyself before God. Happy is he that judgeth not himself in that which he approveth.
22 Su fekkee sa ngëm dëgër na, wone ko ci sa diggante ak Yàlla. Kiy nangu, te du ci sikkal boppam, kooku barkeel na.
23But he that doubteth is condemned if he eat, because [he eateth] not of faith; and whatsoever is not of faith is sin.
23 Waaye kuy lekk ñam te am ci xel ñaar, def nga bàkkaar, ndax sa ngëm yemu fa. Ndaxte jëf ju àndul ak ngëm, bàkkaar la.