Syriac: NT

Wolof: New Testament

1 John

5

1ܟܠ ܕܡܗܝܡܢ ܕܝܫܘܥ ܐܝܬܘܗܝ ܡܫܝܚܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܝܠܝܕ ܘܟܠ ܕܡܚܒ ܠܝܠܘܕܐ ܡܚܒ ܐܦ ܠܗܘ ܕܐܬܝܠܕ ܡܢܗ ܀
1 Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur.
2ܘܒܗܕܐ ܝܕܥܝܢܢ ܕܡܚܒܝܢܢ ܠܒܢܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܡܐ ܕܠܐܠܗܐ ܡܚܒܝܢܢ ܘܥܒܕܝܢܢ ܦܘܩܕܢܘܗܝ ܀
2 Xam nanu ne, bëgg nanu doomi Yàlla yi ci lii: bëgg Yàlla tey sàmm ay ndigalam.
3ܗܢܐ ܗܘ ܓܝܪ ܚܘܒܗ ܕܐܠܗܐ ܕܢܛܪ ܦܘܩܕܢܘܗܝ ܘܦܘܩܕܢܘܗܝ ܠܐ ܝܩܝܪܝܢ ܀
3 Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu.
4ܡܛܠ ܕܟܠ ܕܝܠܝܕ ܡܢ ܐܠܗܐ ܙܟܐ ܠܗ ܠܥܠܡܐ ܘܗܕܐ ܗܝ ܙܟܘܬܐ ܕܙܟܬܗ ܠܥܠܡܐ ܗܝܡܢܘܬܢ ܀
4 Ndaxte képp ku juddu ci Yàlla day noot àddina; te li nuy noote àddina mooy sunu ngëm.
5ܡܢܘ ܓܝܪ ܕܙܟܐ ܠܗ ܠܥܠܡܐ ܐܠܐ ܗܘ ܕܡܗܝܡܢ ܕܝܫܘܥ ܒܪܗ ܗܘ ܕܐܠܗܐ ܀
5 Ku noot àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
6ܗܢܘ ܕܐܬܐ ܒܝܕ ܡܝܐ ܘܕܡܐ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܐ ܗܘܐ ܒܡܝܐ ܒܠܚܘܕ ܐܠܐ ܒܡܝܐ ܘܕܡܐ ܀
6 Yeesu Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg.
7ܘܪܘܚܐ ܡܤܗܕܐ ܕܗܝ ܪܘܚܐ ܐܝܬܝܗ ܫܪܪܐ ܀
7 Ndaxte am na ñetti seede:
8ܘܐܝܬܝܗܘܢ ܬܠܬܐ ܤܗܕܝܢ ܪܘܚܐ ܘܡܝܐ ܘܕܡܐ ܘܬܠܬܝܗܘܢ ܒܚܕ ܐܢܘܢ ܀
8 Xel mi, ndox ak deret, te ñoom ñett ñépp, ñoo bokk benn baat.
9ܐܢ ܤܗܕܘܬܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܡܩܒܠܝܢܢ ܚܕ ܟܡܐ ܤܗܕܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܕܪܒܐ ܗܝ ܘܗܕܐ ܗܝ ܤܗܕܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܕܐܤܗܕ ܥܠ ܒܪܗ ܀
9 Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gën a wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam.
10ܟܠܡܢ ܕܡܗܝܡܢ ܒܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܐܝܬ ܠܗ ܗܕܐ ܤܗܕܘܬܐ ܒܢܦܫܗ ܟܠ ܕܠܐ ܡܗܝܡܢ ܠܐܠܗܐ ܕܓܠܐ ܥܒܕܗ ܒܕܠܐ ܗܝܡܢ ܠܤܗܕܘܬܐ ܕܐܤܗܕ ܐܠܗܐ ܥܠ ܒܪܗ ܀
10 Ku gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam.
11ܘܗܕܐ ܗܝ ܤܗܕܘܬܐ ܕܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܝܗܒ ܠܢ ܐܠܗܐ ܘܗܢܘܢ ܚܝܐ ܒܒܪܗ ܐܝܬܝܗܘܢ ܀
11 Te seede si mooy lii: Yàlla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam.
12ܟܠ ܕܐܚܝܕ ܠܒܪܐ ܐܚܝܕ ܐܦ ܠܚܝܐ ܘܟܠ ܕܠܐ ܐܚܝܕ ܠܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܠܝܬ ܠܗ ܚܝܐ ܀
12 Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Yàlla, amuloo dund.
13ܗܠܝܢ ܟܬܒܬ ܠܟܘܢ ܕܬܕܥܘܢ ܕܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܐܝܬ ܠܟܘܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܗܝܡܢܬܘܢ ܒܫܡܗ ܕܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܀
13 Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne, am ngeen dund gu dul jeex.
14ܘܗܕܐ ܦܪܗܤܝܐ ܐܝܬ ܠܢ ܠܘܬܗ ܕܟܠ ܕܫܐܠܝܢܢ ܠܗ ܐܝܟ ܨܒܝܢܗ ܫܡܥ ܠܢ ܀
14 Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii, su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul.
15ܘܐܢ ܡܦܤܝܢܢ ܕܫܡܥ ܠܢ ܥܠ ܡܕܡ ܕܫܐܠܝܢܢ ܡܢܗ ܬܟܝܠܝܢܢ ܕܩܒܠܢ ܡܢ ܟܕܘ ܫܐܠܬܢ ܕܫܐܠܢ ܡܢܗ ܀
15 Gannaaw xam nañu ne, dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne, li nu ko ñaan, jox na nu ko.
16ܐܢ ܐܢܫ ܢܚܙܐ ܠܐܚܘܗܝ ܕܚܛܐ ܚܛܗܐ ܕܠܐ ܡܚܝܒ ܠܡܘܬܐ ܢܫܐܠ ܘܡܬܝܗܒܝܢ ܠܗ ܚܝܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܗܘܐ ܐܝܟ ܕܠܡܘܬܐ ܚܛܝܢ ܐܝܬ ܓܝܪ ܚܛܗܐ ܕܡܘܬܐ ܠܐ ܗܘܐ ܥܠ ܗܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܢܒܥܐ ܐܢܫ ܀
16 Ku gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko.
17ܟܠ ܥܘܠܐ ܓܝܪ ܚܛܝܬܐ ܗܘ ܘܐܝܬ ܚܛܗܐ ܕܠܐ ܗܘܐ ܕܡܘܬܐ ܗܘ ܀
17 Gépp jubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu jarul dee.
18ܘܝܕܥܝܢܢ ܕܟܠ ܕܝܠܝܕ ܡܢ ܐܠܗܐ ܠܐ ܚܛܐ ܗܘ ܓܝܪ ܕܝܠܝܕ ܡܢ ܐܠܗܐ ܢܛܪ ܢܦܫܗ ܘܒܝܫܐ ܠܐ ܡܬܩܪܒ ܠܗ ܀
18 Xam nanu ne, képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara.
19ܝܕܥܝܢܢ ܕܡܢ ܐܠܗܐ ܚܢܢ ܘܥܠܡܐ ܟܠܗ ܒܒܝܫܐ ܗܘ ܤܝܡ ܀
19 Nun nag xam nanu ne, nu ngi ci Yàlla, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis.
20ܘܝܕܥܝܢܢ ܕܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܐܬܐ ܘܝܗܒ ܠܢ ܡܕܥܐ ܕܢܕܥ ܠܫܪܝܪܐ ܘܢܗܘܐ ܒܗ ܒܫܪܝܪܐ ܒܒܪܗ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܗܢܐ ܗܘ ܐܠܗܐ ܫܪܝܪܐ ܘܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܀
20 Xam nanu ne, Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu man a xam Aji Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex.
21ܒܢܝ ܛܪܘ ܢܦܫܟܘܢ ܡܢ ܕܚܠܬ ܦܬܟܪܐ ܀
21 Samay doom, wottuleen seen bopp ciy xërëm.