1ܩܫܝܫܐ ܠܓܒܝܬܐ ܩܘܪܝܐ ܘܠܒܢܝܗ ܐܝܠܝܢ ܕܐܢܐ ܡܚܒ ܐܢܐ ܒܫܪܪܐ ܠܐ ܗܘܐ ܕܝܢ ܐܢܐ ܒܠܚܘܕܝ ܐܠܐ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܝܕܥܘܗܝ ܠܫܪܪܐ ܀
1 Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi.
2ܡܛܠ ܫܪܪܐ ܐܝܢܐ ܕܡܩܘܐ ܒܢ ܘܥܡܢ ܐܝܬܘܗܝ ܠܥܠܡ ܀
2 Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww.
3ܬܗܘܐ ܥܡܢ ܛܝܒܘܬܐ ܘܪܚܡܐ ܘܫܠܡܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܒܐ ܘܡܢ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܪܗ ܕܐܒܐ ܒܫܪܪܐ ܘܒܚܘܒܐ ܀
3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel.
4ܚܕܝܬ ܤܓܝ ܕܐܫܟܚܬ ܡܢ ܒܢܝܟܝ ܕܡܗܠܟܝܢ ܒܫܪܪܐ ܐܝܟܢܐ ܕܦܘܩܕܢܐ ܢܤܒܢܢ ܡܢ ܐܒܐ ܀
4 Gis naa ci say doom, ñuy jaar ci tànki dëgg, ni nu ko Baay bi digale, te bég naa ci lool.
5ܘܗܫܐ ܡܦܝܤ ܐܢܐ ܠܟܝ ܩܘܪܝܐ ܠܐ ܗܘܐ ܐܝܟ ܦܘܩܕܢܐ ܚܕܬܐ ܟܬܒ ܐܢܐ ܠܟܝ ܐܠܐ ܗܘ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܢ ܡܢ ܫܘܪܝܐ ܕܢܚܒ ܚܕ ܠܚܕ ܀
5 Léegi nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga.
6ܘܗܢܐ ܐܝܬܘܗܝ ܚܘܒܐ ܕܢܗܠܟ ܐܝܟ ܦܘܩܕܢܘܗܝ ܗܢܐ ܦܘܩܕܢܐ ܐܝܬܘܗܝ ܐܝܟ ܡܐ ܕܫܡܥܬܘܢ ܡܢ ܫܘܪܝܐ ܕܒܗ ܗܘܝܬܘܢ ܡܗܠܟܝܢ ܀
6 Lii mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca njàlbeen ga, te ci lanu wara jaar.
7ܡܛܠ ܕܤܓܝܐܐ ܡܛܥܝܢܐ ܢܦܩܘ ܒܗ ܒܥܠܡܐ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܡܘܕܝܢ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܐܬܐ ܒܒܤܪ ܗܢܐ ܐܝܬܘܗܝ ܡܛܥܝܢܐ ܘܐܢܛܝܟܪܝܤܛܘܤ ܀
7 Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Krist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Krist.
8ܐܙܕܗܪܘ ܒܢܦܫܟܘܢ ܕܠܐ ܬܘܒܕܘܢ ܡܕܡ ܕܦܠܚܬܘܢ ܐܠܐ ܐܓܪܐ ܡܫܠܡܢܐ ܬܬܦܪܥܘܢ ܀
8 Kon moytuleen, ngir baña ñàkk seen añub coono, waaye ngeen am yool bu mat sëkk.
9ܟܠ ܐܝܢܐ ܕܥܒܪ ܘܠܐ ܡܩܘܐ ܒܝܘܠܦܢܗ ܕܡܫܝܚܐ ܐܠܗܐ ܠܝܬ ܒܗ ܗܘ ܕܡܩܘܐ ܒܝܘܠܦܢܗ ܗܢܐ ܘܠܐܒܐ ܘܠܒܪܐ ܐܝܬ ܠܗ ܀
9 Képp ku saxul ci dénkaaney Krist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji.
10ܐܢ ܐܢܫ ܐܬܐ ܠܘܬܟܘܢ ܘܗܢܐ ܝܘܠܦܢܐ ܠܐ ܡܝܬܐ ܠܐ ܬܩܒܠܘܢܝܗܝ ܒܒܝܬܐ ܘܚܕܝ ܠܟ ܠܐ ܬܐܡܪܘܢ ܠܗ ܀
10 Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax.
11ܗܘ ܓܝܪ ܕܐܡܪ ܠܗ ܚܕܝ ܠܟ ܡܫܘܬܦ ܗܘ ܠܥܒܕܘܗܝ ܒܝܫܐ ܀
11 Ku ko nuyu, bokk nga ciy ñaawteefam.
12ܟܕ ܤܓܝܐܬܐ ܐܝܬ ܗܘܐ ܠܝ ܠܡܟܬܒ ܠܟܘܢ ܠܐ ܒܥܝܬ ܕܒܝܕ ܟܪܛܝܤܐ ܘܕܝܘܬܐ ܐܠܐ ܡܤܒܪ ܐܢܐ ܕܐܬܐ ܠܘܬܟܘܢ ܘܦܘܡܐ ܠܘܬ ܦܘܡܐ ܢܡܠܠ ܕܚܕܘܬܐ ܕܝܠܢ ܬܗܘܐ ܡܫܡܠܝܐ ܀
12 Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yeen, nu waxtaan ci, ngir sunu mbég mat sëkk.
13ܫܐܠܝܢ ܫܠܡܟܝ ܒܢܝܐ ܕܚܬܟܝ ܓܒܝܬܐ ܐܡܝܢ ܀
13 Say doomi rakk, ji Yàlla tànn, ñu ngi lay nuyu.