Syriac: NT

Wolof: New Testament

1 Thessalonians

4

1ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܒܥܝܢܢ ܡܢܟܘܢ ܘܡܬܟܫܦܝܢܢ ܠܟܘܢ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܕܐܝܟ ܕܩܒܠܬܘܢ ܡܢܢ ܐܝܟܢ ܘܠܐ ܠܟܘܢ ܕܬܗܠܟܘܢ ܘܬܫܦܪܘܢ ܠܐܠܗܐ ܕܝܬܝܪܐܝܬ ܬܘܤܦܘܢ ܀
1 Léegi nag bokk yi, jot ngeen ci nun, nan ngeen war a dunde ba neex Yàlla, te moom ngeen di def. Waaye ci turu Boroom bi Yeesu nu ngi leen di ñaan ak a dénk, ngeen gën koo feddali.
2ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܓܝܪ ܐܝܠܝܢ ܦܘܩܕܢܐ ܝܗܒܢ ܠܟܘܢ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܀
2 Ndaxte xam ngeen ndigal, yi nu leen jox ci wàllu Yeesu Boroom bi.
3ܗܢܘ ܓܝܪ ܨܒܝܢܗ ܕܐܠܗܐ ܩܕܝܫܘܬܟܘܢ ܘܕܬܗܘܘܢ ܦܪܝܩܝܢ ܡܢ ܟܠ ܙܢܝܘܬܐ ܀
3 Lii nag mooy coobareg Yàlla: ngeen sell, maanaam ngeen moytu njaaloo;
4ܘܢܗܘܐ ܝܕܥ ܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܠܡܩܢܐ ܡܐܢܗ ܒܩܕܝܫܘܬܐ ܘܒܐܝܩܪܐ ܀
4 ngeen noot seeni cér ci cell ak tedd,
5ܘܠܐ ܒܚܫܐ ܕܪܓܬܐ ܐܝܟ ܫܪܟܐ ܕܥܡܡܐ ܗܢܘܢ ܕܠܐ ܝܕܥܝܢ ܠܐܠܗܐ ܀
5 te xemmem bañ leen a jiital, ni xeeti àddina yi xamul Yàlla.
6ܘܠܐ ܬܗܘܘܢ ܡܫܝܚܝܢ ܠܡܥܒܪ ܘܠܡܥܠܒ ܐܢܫ ܠܐܚܘܗܝ ܒܗܕܐ ܨܒܘܬܐ ܡܛܠ ܕܡܪܢ ܗܘ ܬܒܘܥܐ ܥܠ ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܡܢ ܩܕܡ ܙܒܢܐ ܐܡܪܢ ܠܟܘܢ ܘܤܗܕܢ ܀
6 Ci mbir mii nag, bu kenn ci yéen laal yëfi jaambur, ngir bañ koo tooñ. Ndaxte waxoon nanu leen bu yàgg te artu leen ne, ñiy def loolu, Boroom bi dina leen mbugal.
7ܠܐ ܓܝܪ ܩܪܟܘܢ ܐܠܗܐ ܠܛܢܦܘܬܐ ܐܠܐ ܠܩܕܝܫܘܬܐ ܀
7 Ndaxte Yàlla woo na nu, nu dund ci cell, waaye du ci sobe.
8ܡܟܝܠ ܡܢ ܕܛܠܡ ܠܐ ܗܘܐ ܠܒܪܢܫܐ ܛܠܡ ܐܠܐ ܠܐܠܗܐ ܗܘ ܕܝܗܒ ܒܟܘܢ ܪܘܚܗ ܩܕܝܫܬܐ ܀
8 Ku tanqamlu wax jii nag, defoo ko nit, Yàlla nga ko def, moom mi leen di jox Xel mu Sell mi.
9ܥܠ ܚܘܒܐ ܕܝܢ ܕܐܚܐ ܠܐ ܤܢܝܩܝܬܘܢ ܠܡܟܬܒ ܠܟܘܢ ܐܢܬܘܢ ܓܝܪ ܩܢܘܡܟܘܢ ܡܠܦܐ ܐܢܬܘܢ ܕܐܠܗܐ ܕܬܚܒܘܢ ܚܕ ܠܚܕ ܀
9 Ci lu jëm ci bëggante ci seen biir, matul nu leen di bind dara, ndaxte Yàlla def na ci seen xol, ngeen bëggante.
10ܐܦ ܥܒܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܗܟܢܐ ܠܟܠܗܘܢ ܐܚܐ ܕܒܟܠܗ ܡܩܕܘܢܝܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܕܬܬܝܬܪܘܢ ܀
10 Te moom ngeen di def ci bokk yépp, yi ci diiwaanu Maseduwan. Waaye bokk yi, maa ngi leen di xiirtal, ngeen gën cee sax.
11ܘܬܬܚܦܛܘܢ ܕܬܗܘܘܢ ܫܠܝܢ ܘܥܢܝܢ ܒܤܘܥܪܢܝܟܘܢ ܘܗܘܝܬܘܢ ܦܠܚܝܢ ܒܐܝܕܝܟܘܢ ܐܝܟܢܐ ܕܦܩܕܢܟܘܢ ܀
11 Fullawooleen a dund ci jàmm, di topptoo seen mbiri bopp tey lekk seen ñaq, ni nu leen ko sante woon.
12ܕܬܗܘܘܢ ܡܗܠܟܝܢ ܒܐܤܟܡܐ ܠܘܬ ܒܪܝܐ ܘܥܠ ܐܢܫ ܠܐ ܬܤܬܢܩܘܢ ܀
12 Noonu dingeen dund dund gu jekk ci kanamu waa àddina, te it dungeen soxlaal kenn dara.
13ܨܒܐ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܬܕܥܘܢ ܐܚܝ ܕܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܕܡܟܝܢ ܠܐ ܬܗܘܐ ܟܪܝܐ ܠܟܘܢ ܐܝܟ ܫܪܟܐ ܕܐܢܫܐ ܕܤܒܪܐ ܠܝܬ ܠܗܘܢ ܀
13 Ci mbirum ñi nelaw nag bokk yi, bëgguñu ngeen réere mbir, ba tiis ni aji gëmul, yi amul benn yaakaar.
14ܐܢ ܓܝܪ ܡܗܝܡܢܝܢܢ ܕܝܫܘܥ ܡܝܬ ܘܩܡ ܗܟܢܐ ܐܦ ܐܠܗܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܕܡܟܘ ܒܝܫܘܥ ܡܝܬܐ ܥܡܗ ܀
14 Ndegam gëm nanu ne, Yeesu dee na te dekki, noonu it Yàlla dina indaale ak Yeesu ñépp ñi ko gëm te nelaw.
15ܗܕܐ ܕܝܢ ܐܡܪܝܢܢ ܠܟܘܢ ܒܡܠܬܗ ܕܡܪܢ ܕܚܢܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܫܬܚܪܝܢܢ ܒܡܐܬܝܬܗ ܕܡܪܢ ܕܚܝܝܢܢ ܠܐ ܢܕܪܟ ܠܐܝܠܝܢ ܕܕܡܟܘ ܀
15 Nu ngi leen di wax lii tukkee ci Boroom bi: nun ñiy dund te des fi, ba kera Boroom biy dellusi, dunu jiitu ñi nelaw.
16ܡܛܠ ܕܗܘ ܡܪܢ ܒܦܘܩܕܢܐ ܘܒܩܠܐ ܕܪܝܫ ܡܠܐܟܐ ܘܒܩܪܢܐ ܕܐܠܗܐ ܢܚܬ ܡܢ ܫܡܝܐ ܘܡܝܬܐ ܕܒܡܫܝܚܐ ܢܩܘܡܘܢ ܠܘܩܕܡ ܀
16 Ndaxte ndigal lu jamp dina jib, baatu kilifa ci malaaka yi dégtu, liitu Yàlla jolli, te Boroom bi moom ci boppam dina wàcce ca asamaan. Booba ñi gëm Kirist te dee dinañu jëkk a dekki;
17ܘܗܝܕܝܢ ܚܢܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܫܬܚܪܝܢܢ ܕܚܝܝܢܢ ܢܬܚܛܦ ܥܡܗܘܢ ܐܟܚܕܐ ܒܥܢܢܐ ܠܐܘܪܥܗ ܕܡܪܢ ܒܐܐܪ ܘܗܟܢܐ ܒܟܠܙܒܢ ܥܡ ܡܪܢ ܢܗܘܐ ܀
17 gannaaw loolu nun ñiy dund te des fi, dinañu ne fëyy ak ñoom jëm ci niir yi, taseji ak Boroom bi ci jaww ji. Te noonu dinanu nekk ak Boroom bi ba fàww.
18ܗܘܘ ܗܟܝܠ ܡܒܝܐܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܒܡܠܐ ܗܠܝܢ ܀
18 Kon nag na ku nekk di dëfël sa xolu moroom ak kàddu yooyu.