Syriac: NT

Wolof: New Testament

1 Thessalonians

5

1ܥܠ ܙܒܢܐ ܕܝܢ ܘܥܕܢܐ ܐܚܝ ܠܐ ܤܢܝܩܝܬܘܢ ܠܡܟܬܒ ܠܟܘܢ ܀
1 Waaye bokk yi, ci li jëm ci jamono yi ak waxtu, yi loolu di am, matul nu leen ciy bind dara.
2ܐܢܬܘܢ ܓܝܪ ܫܪܝܪܐܝܬ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܝܘܡܗ ܕܡܪܢ ܐܝܟ ܓܢܒܐ ܒܠܠܝܐ ܗܟܢܐ ܐܬܐ ܀
2 Ndaxte xam ngeen bu wér ne, ni sàcc di ñëwe guddi, noonu la bésu Boroom bi di ñëwe.
3ܟܕ ܢܐܡܪܘܢ ܕܫܠܡܐ ܗܘ ܘܫܝܢܐ ܘܗܝܕܝܢ ܡܢܫܠܝܐ ܢܩܘܡ ܥܠܝܗܘܢ ܐܒܕܢܐ ܐܝܟ ܚܒܠܐ ܥܠ ܒܛܢܬܐ ܘܠܐ ܢܡܕܘܢ ܀
3 Fekk nit ñiy naan: «Lépp a ngi ci jàmm, ba ne leww,» booba musiba bett leen, ni aw mat di bette jigéen ju ëmb, te kenn du ci mucc.
4ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܐܚܝ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܒܚܫܘܟܐ ܕܗܘ ܝܘܡܐ ܐܝܟ ܓܢܒܐ ܢܕܪܟܟܘܢ ܀
4 Waaye yéen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba tax bés boobu bett leen ni sàcc.
5ܟܠܟܘܢ ܓܝܪ ܒܢܝ ܢܘܗܪܐ ܐܢܬܘܢ ܘܒܢܝ ܐܝܡܡܐ ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܒܢܝ ܠܠܝܐ ܘܠܐ ܒܢܝ ܚܫܘܟܐ ܀
5 Ndaxte yéen ñépp ci leer ak bëccëg ngeen bokk; bokkunu ci guddi ak lëndëm.
6ܠܐ ܢܕܡܟ ܗܟܝܠ ܐܝܟ ܫܪܟܐ ܐܠܐ ܗܘܝܢ ܥܝܪܝܢ ܘܡܗܘܢܝܢ ܀
6 Kon nag bunu nelaw ni ñeneen ñi, waaye nanu xool te maandu.
7ܐܝܠܝܢ ܓܝܪ ܕܕܡܟܝܢ ܒܠܠܝܐ ܗܘ ܕܡܟܝܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܪܘܝܢ ܒܠܠܝܐ ܗܘ ܪܘܝܢ ܀
7 Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw, te ñiy màndi, guddi lañuy màndi.
8ܚܢܢ ܕܝܢ ܕܒܢܝ ܐܝܡܡܐ ܚܢܢ ܗܘܝܢ ܥܝܪܝܢ ܒܪܥܝܢܢ ܘܠܒܝܫܝܢ ܫܪܝܢܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܘܕܚܘܒܐ ܘܢܤܝܡ ܤܢܘܪܬܐ ܕܤܒܪܐ ܕܚܝܐ ܀
8 Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu maandu te ràngoo ngir xare bi: ngëm ak mbëggeel, muy kiiraayu dënn, ak kóoluteg mucc, muy mbaxanam xare.
9ܡܛܠ ܕܠܐ ܤܡܢ ܐܠܗܐ ܠܪܘܓܙܐ ܐܠܐ ܠܩܢܝܢܐ ܕܚܝܐ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
9 Ndaxte Yàlla jaglewu nu meram, waaye mucc la nu jagleel ndax darajay sunu Boroom Yeesu Kirist.
10ܗܘ ܕܡܝܬ ܥܠ ܐܦܝܢ ܕܐܢ ܥܝܪܝܢܢ ܘܐܢ ܕܡܟܝܢܢ ܐܟܚܕܐ ܥܡܗ ܢܚܐ ܀
10 Deeyal na nu, ngir nu man a dund ak moom, bu nu nelawee ak bu nu nelawagul.
11ܡܛܠ ܗܢܐ ܒܝܐܘ ܚܕ ܠܚܕ ܘܒܢܘ ܚܕ ܠܚܕ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܥܒܕܝܬܘܢ ܀
11 Kon nag nangeen dëgëralante te yokkante seen ngëm, ni ngeen koy defe.
12ܒܥܝܢܢ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܕܗܘܝܬܘܢ ܝܕܥܝܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܠܐܝܢ ܒܟܘܢ ܘܩܝܡܝܢ ܒܐܦܝܟܘܢ ܒܡܪܢ ܘܡܠܦܝܢ ܠܟܘܢ ܀
12 Gannaaw loolu bokk yi, ci lu jëm ci njiit, yi Boroom bi teg ci seen kanam te ñuy liggéey ci seen biir, di leen artu, maa ngi leen di ñaan ngeen déglu leen;
13ܕܗܘܘ ܚܫܝܒܝܢ ܠܟܘܢ ܒܚܘܒܐ ܝܬܝܪܐ ܘܡܛܠ ܥܒܕܗܘܢ ܐܫܬܝܢܘ ܥܡܗܘܢ ܀
13 rax-ca-dolli ngeen naw leen seen kem-kàttan te bëgg leen ndax seen liggéey. Na jàmm am ci seen biir.
14ܒܥܝܢܢ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܪܕܘ ܠܡܤܟܠܢܐ ܘܠܒܒܘ ܠܙܥܘܪܝ ܢܦܫܐ ܘܤܒܘ ܛܥܢܐ ܕܡܚܝܠܐ ܘܐܓܪܘ ܪܘܚܟܘܢ ܠܘܬ ܟܠܢܫ ܀
14 Bokk yi, nu ngi leen di dénk, ngeen yedd ñi feñaag, dëfël ñi seen yasara yàcciku, dimbali ñi néew doole, tey muñal ñépp.
15ܘܐܙܕܗܪܘ ܕܠܡܐ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܒܝܫܬܐ ܚܠܦ ܒܝܫܬܐ ܢܦܪܘܥ ܐܠܐ ܒܟܠܙܒܢ ܗܪܛܘ ܒܬܪ ܛܒܬܐ ܠܘܬ ܚܕܕܐ ܘܠܘܬ ܟܠܢܫ ܀
15 Saxleen ci baax ci seen biir ak ci ñépp, te bañ a feyantoo.
16ܗܘܘ ܚܕܝܢ ܒܟܠܙܒܢ ܀
16 Deeleen bég
17ܘܡܨܠܝܢ ܕܠܐ ܫܠܘܐ ܀
17 te sax ciy ñaan Yàlla,
18ܘܒܟܠ ܡܕܡ ܗܘܘ ܡܘܕܝܢ ܗܢܘ ܓܝܪ ܨܒܝܢܗ ܕܐܠܗܐ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܟܘܢ ܀
18 di ko gërëm ci lépp, ndaxte loolu mooy coobareg Yàlla ci yéen ci seen bokk ci Kirist Yeesu.
19ܪܘܚܐ ܠܐ ܬܕܥܟܘܢ ܀
19 Buleen fey taalu Xelum Yàlla,
20ܢܒܝܘܬܐ ܠܐ ܬܤܠܘܢ ܀
20 di xeeb waxu yonent yi.
21ܟܠܡܕܡ ܒܩܘ ܘܕܫܦܝܪ ܐܚܘܕܘ ܀
21 Waaye seetleen mbir yépp, jàpp ci li baax,
22ܘܡܢ ܟܠ ܨܒܘ ܒܝܫܐ ܥܪܘܩܘ ܀
22 dëddu lépp lu ci bon.
23ܗܘ ܕܝܢ ܐܠܗܐ ܕܫܠܡܐ ܢܩܕܫܟܘܢ ܓܡܝܪܐܝܬ ܠܟܠܟܘܢ ܘܟܠܗ ܪܘܚܟܘܢ ܘܢܦܫܟܘܢ ܘܦܓܪܟܘܢ ܢܢܛܪ ܕܠܐ ܪܫܝܢ ܠܡܐܬܝܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
23 Na leen Yàlla Boroom jàmm sellal, ba ngeen mat sëkk; na sàmm seen xel mépp, seen xol bépp ak seen yaram wépp, ngir dara bañ cee am sikk, ba bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.
24ܡܗܝܡܢ ܗܘ ܡܢ ܕܩܪܟܘܢ ܕܗܘ ܢܥܒܕ ܀
24 Yàlla, mi leen woo ci loolu, kuy sàmm kóllëre la, te dina ko def.
25ܐܚܝ ܨܠܘ ܥܠܝܢ ܀
25 Bokk yi, buleen nu fàtte ci seeni ñaan.
26ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܚܝܢ ܟܠܗܘܢ ܒܢܘܫܩܬܐ ܩܕܝܫܬܐ ܀
26 Nuyul-leen nu bokk yépp ak saafoonte bu laab.
27ܡܘܡܐ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܒܡܪܢ ܕܬܬܩܪܐ ܐܓܪܬܐ ܗܕܐ ܠܟܠܗܘܢ ܐܚܐ ܩܕܝܫܐ ܀
27 Maa ngi leen di dénk ci kanamu Boroom bi, ngeen jàngal bataaxal bii bokk yépp.
28ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܡܟܘܢ ܐܡܝܢ ܀
28 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen.