Syriac: NT

Wolof: New Testament

2 Corinthians

3

1ܡܫܪܝܢܢ ܠܢ ܬܘܒ ܡܢ ܕܪܝܫ ܕܢܚܘܝܟܘܢ ܡܢܐ ܚܢܢ ܐܘ ܕܠܡܐ ܤܢܝܩܝܢܢ ܐܝܟ ܐܚܪܢܐ ܕܐܓܪܬܐ ܕܦܘܩܕܐ ܢܬܟܬܒܢ ܠܟܘܢ ܥܠܝܢ ܐܘ ܕܐܢܬܘܢ ܬܟܬܒܘܢ ܬܦܩܕܘܢ ܥܠܝܢ ܀
1 Mbaa du danoo tàmbalee tëgguwaat nag? Mbaa du danoo soxla ni ñenn ñi ay dénkaane yu ñu nuy gërëme, te ñuy bataaxal yu jóge ci yéen walla yu jëm ci yéen?
2ܐܓܪܬܢ ܕܝܢ ܕܝܠܢ ܐܢܬܘܢ ܐܢܘܢ ܕܟܬܝܒܐ ܒܠܒܢ ܘܝܕܝܥܐ ܘܡܬܩܪܝܐ ܡܢ ܟܠܢܫ ܀
2 Déedéet, yéenay sunu bataaxal, te ci sunu xol lañu ko bind, di bataaxal bu nit ñépp man a xam te jàng ko;
3ܝܕܥܝܬܘܢ ܓܝܪ ܕܐܓܪܬܗ ܐܢܬܘܢ ܕܡܫܝܚܐ ܕܐܫܬܡܫܬ ܡܢܢ ܕܟܬܝܒܐ ܠܐ ܒܕܝܘܬܐ ܐܠܐ ܒܪܘܚܐ ܕܐܠܗܐ ܚܝܐ ܠܐ ܒܠܘܚܐ ܕܟܐܦܐ ܐܠܐ ܒܠܘܚܐ ܕܠܒܐ ܕܒܤܪܐ ܀
3 ndaxte leer na ne, bataaxal bu jóge ci Kirist ngeen, bu mu jaarale ci nun. Bindeesu ko daa, waaye ci Xelum Yàlla miy dund lees ko binde; te du ci àlluway doj lañu ko rëdd, waaye ci xolu doom Aadama.
4ܬܘܟܠܢܐ ܕܝܢ ܗܟܢܐ ܐܝܬ ܠܢ ܒܡܫܝܚܐ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܀
4 Googu kóolute lanu am fa kanam Yàlla ndax Kirist.
5ܠܘ ܕܚܢܢ ܤܦܩܝܢܢ ܕܢܬܪܥܐ ܡܕܡ ܐܝܟ ܕܡܢ ܢܦܫܢ ܐܠܐ ܚܝܠܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܗܘ ܀
5 Du caageen nag ne, àttan nanu dara ci sunu man-man, ba nu yaakaar dara ci sunu bopp, waaye sunu kàttan ci Yàlla lay jóge.
6ܗܘ ܕܐܫܘܝܢ ܕܢܗܘܐ ܡܫܡܫܢܐ ܕܕܝܬܩܐ ܚܕܬܐ ܠܐ ܒܟܬܒܐ ܐܠܐ ܒܪܘܚܐ ܟܬܒܐ ܓܝܪ ܩܛܠ ܪܘܚܐ ܕܝܢ ܡܚܝܐ ܀
6 Moo nu jox kàttan, nu nekk ndaw yuy xamle kóllëre gu bees gi. Te kóllëre googu ajuwul ci ay sàrti diine, waaye mi ngi aju ci jëfu Xelum Yàlla. Ndaxte sàrti kese day jëme ci dee, waaye Xelum Yàlla dafay joxe dund.
7ܐܢ ܕܝܢ ܬܫܡܫܬܐ ܕܡܘܬܐ ܒܟܬܒܐ ܐܬܪܫܡܬ ܒܟܐܦܐ ܘܗܘܬ ܒܬܫܒܘܚܬܐ ܐܝܟܢܐ ܕܠܐ ܢܫܟܚܘܢ ܒܢܝ ܐܝܤܪܝܠ ܠܡܚܪ ܒܦܪܨܘܦܗ ܕܡܘܫܐ ܡܛܠ ܫܘܒܚܐ ܕܦܪܨܘܦܗ ܗܘ ܕܐܬܒܛܠ ܀
7 Ba ñu bindee arafi sàrt yi ciy àlluway doj, leeraayu ndamu Yàlla nekk fa. Xar-kanamu Musaa di leer, ba bànni Israyil duñu ko man a xool, fekk leer ga di wéy. Ndegam sàrti yoon yooyuy jëme ci dee, ñoo ànd ak ndam,
8ܐܝܟܢܐ ܗܟܝܠ ܬܫܡܫܬܐ ܕܪܘܚܐ ܠܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܬܗܘܐ ܒܫܘܒܚܐ ܀
8 rawatina nag ne, jëfu Xelum Yàlla dina gën a ànd ak ndam.
9ܐܢ ܓܝܪ ܠܬܫܡܫܬܐ ܕܚܘܝܒܐ ܗܘܐ ܫܘܒܚܐ ܚܕ ܟܡܐ ܬܬܝܬܪ ܬܫܡܫܬܐ ܕܙܕܝܩܘܬܐ ܒܫܘܒܚܐ ܀
9 Su fekkee ne tëralin, wiy teg nit tooñ, àndoon na ak ndam, rawatina ci tëralin wiy àtte nit jub.
10ܐܝܟ ܗܘ ܓܝܪ ܕܐܦܠܐ ܡܫܒܚܐ ܗܝ ܕܐܫܬܒܚܬ ܒܦܘܚܡܐ ܕܗܢܐ ܫܘܒܚܐ ܡܝܬܪܐ ܀
10 Ndaxte ndam li amoon keroog suux na ci ndam li ko raw léegi.
11ܐܢ ܓܝܪ ܡܕܡ ܕܐܬܒܛܠ ܒܫܘܒܚܐ ܗܘܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܐܝܢܐ ܕܡܩܘܐ ܒܫܘܒܚܐ ܢܗܘܐ ܀
11 Te it ndegam li wéy dafa amoon ndam, astemaak li fi sax.
12ܡܛܠ ܕܐܝܬ ܠܢ ܗܟܝܠ ܗܢܐ ܤܒܪܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܒܓܠܐ ܥܝܢ ܡܬܕܒܪܝܢܢ ܀
12 Kon nag gannaaw wékku nanu ci yaakaar ju mel noonu, danuy waare ak kóolute gu mag.
13ܘܠܐ ܐܝܟ ܡܘܫܐ ܕܪܡܐ ܗܘܐ ܬܚܦܝܬܐ ܥܠ ܐܦܘܗܝ ܕܠܐ ܢܚܘܪܘܢ ܒܢܝ ܐܝܤܪܝܠ ܒܫܘܠܡܗ ܕܗܘ ܕܡܬܒܛܠ ܀
13 Dunu def ni Musaa, mi daan muur xar-kanamam, ngir bànni Israyil bañ a gis jeexug leer googu saxul.
14ܐܠܐ ܐܬܥܘܪܘ ܒܡܕܥܝܗܘܢ ܥܕܡܐ ܓܝܪ ܠܝܘܡܢܐ ܐܡܬܝ ܕܕܝܬܩܐ ܥܬܝܩܬܐ ܡܬܩܪܝܐ ܗܝ ܗܝ ܬܚܦܝܬܐ ܩܝܡܐ ܥܠܝܗܘܢ ܘܠܐ ܡܬܓܠܝܐ ܕܒܡܫܝܚܐ ܗܘ ܡܬܒܛܠܐ ܀
14 Waaye seen xel dafa daldi gumba. Ba tey jii sax, bu ñuy jàng téereb kóllëre gu jëkk gi, muuraay moomu dafay des; deñul, ndaxte ci Kirist rekk la man a deñe.
15ܘܥܕܡܐ ܠܝܘܡܢܐ ܐܡܬܝ ܕܡܬܩܪܐ ܡܘܫܐ ܬܚܦܝܬܐ ܥܠ ܠܒܗܘܢ ܪܡܝܐ ܀
15 Waaw, ba tey jii, su ñuy jàng yoonu Musaa, seen xol dafay muuru.
16ܘܐܡܬܝ ܕܐܢܫ ܡܢܗܘܢ ܢܬܦܢܐ ܠܘܬ ܡܪܝܐ ܡܫܬܩܠܐ ܡܢܗ ܬܚܦܝܬܐ ܀
16 Waaye saa su kenn walbatikoo ci Boroom bi, muuraay gi daldi muriku.
17ܡܪܝܐ ܕܝܢ ܗܘܝܘ ܪܘܚܐ ܘܐܬܪ ܕܪܘܚܗ ܕܡܪܝܐ ܚܐܪܘܬܐ ܗܝ ܀
17 Fekk nag Boroom, bi ñuy wax foofu, moo di Xelum Yàlla, te fu Xelu Boroom bi nekk, foofa yaatu gu mat am na fa.
18ܚܢܢ ܕܝܢ ܟܠܢ ܒܐܦܐ ܓܠܝܬܐ ܬܫܒܘܚܬܗ ܕܡܪܝܐ ܐܝܟ ܕܒܡܚܙܝܬܐ ܚܙܝܢܢ ܘܠܗ ܠܕܡܘܬܐ ܡܫܬܚܠܦܝܢܢ ܡܢ ܫܘܒܚܐ ܠܫܘܒܚܐ ܐܝܟ ܕܡܢ ܡܪܝܐ ܪܘܚܐ ܀
18 Te nun ñépp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar-kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, ànd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Yàlla.