Syriac: NT

Wolof: New Testament

2 Corinthians

4

1ܡܛܠ ܗܢܐ ܠܐ ܡܐܢܐ ܠܢ ܒܬܫܡܫܬܐ ܗܕܐ ܕܐܚܝܕܝܢܢ ܐܝܟ ܪܚܡܐ ܕܗܘܘ ܥܠܝܢ ܀
1 Kon nag ndegam Yàlla ci yërmandeem sas na nu liggéey boobu, dunu bayliku.
2ܐܠܐ ܐܤܠܝܢܢ ܟܤܝܬܗ ܕܒܗܬܬܐ ܘܠܐ ܡܗܠܟܝܢܢ ܒܚܪܥܘܬܐ ܘܠܐ ܢܟܠܝܢܢ ܡܠܬܗ ܕܐܠܗܐ ܐܠܐ ܒܓܠܝܘܬܐ ܕܫܪܪܐ ܡܚܘܝܢܢ ܢܦܫܢ ܠܟܠܗܘܢ ܪܥܝܢܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܀
2 Lànk nanoo ànd ci mbir, yi ñuy nëbb te ñu gàccelu. Sunuy tànk du yu njublaŋ te dunu dëngal kàddug Yàlla. Waaye nu ngi biral dëgg, di sàkku kóoluteg ñépp fa kanam Yàlla.
3ܘܐܢ ܕܝܢ ܡܟܤܝ ܗܘ ܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܝܠܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܐܒܕܝܢ ܗܘ ܡܟܤܝ ܀
3 Su fekkee ne sax, xebaar bu baax bi dafa muuru ci ñenn ñi, dafa fekk ñoom ñu aw yoon wu jëm ci sànkute.
4ܐܝܠܝܢ ܕܐܠܗܗ ܕܥܠܡܐ ܗܢܐ ܥܘܪ ܡܕܥܝܗܘܢ ܥܠ ܕܠܐ ܡܗܝܡܢܝܢ ܕܠܐ ܢܕܢܚ ܠܗܘܢ ܢܘܗܪܗ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܫܘܒܚܗ ܕܡܫܝܚܐ ܕܗܘܝܘ ܕܡܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
4 Ñoom la yàllay jamono ji gëlëmal seen xel, ngir ñu bañ a gis leeru xebaar bu baax, biy wone ndamu Kirist, mi di melokaanu Yàlla.
5ܠܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܢܦܫܢ ܡܟܪܙܝܢܢ ܐܠܐ ܠܡܫܝܚܐ ܝܫܘܥ ܡܪܢ ܠܢܦܫܢ ܕܝܢ ܕܥܒܕܝܟܘܢ ܚܢܢ ܡܛܠ ܝܫܘܥ ܀
5 Ndaxte Yeesu Kirist Boroom bi lanuy waare, waaye waarewunu lu jëm ci sunu bopp. Nun seeni jaam lanu ndax Yeesu.
6ܡܛܠ ܕܐܠܗܐ ܗܘ ܕܐܡܪ ܕܡܢ ܚܫܘܟܐ ܢܘܗܪܐ ܢܕܢܚ ܗܘ ܕܢܚ ܒܠܒܘܬܢ ܕܢܬܢܗܪ ܒܝܕܥܬܐ ܕܫܘܒܚܗ ܕܐܠܗܐ ܒܦܪܨܘܦܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
6 Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer leer ci biir lëndëm,» moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Yàlla, liy feeñ ci xar-kanamu Kirist.
7ܐܝܬ ܠܢ ܕܝܢ ܤܝܡܬܐ ܗܕܐ ܒܡܐܢܐ ܕܚܨܦܐ ܕܪܒܘܬܐ ܕܚܝܠܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܬܗܘܐ ܘܠܐ ܡܢܢ ܀
7 Leer googu ci sunu xol mi ngi mel ni alal, waaye ñu ngi ko def ci nun ñi néew doole niy njaq kese, ngir kàttan gu ëpp xel gi, bawoo ci Yàlla te du ci nun.
8ܒܟܠܡܕܡ ܓܝܪ ܡܬܐܠܨܝܢܢ ܐܠܐ ܠܐ ܡܬܚܢܩܝܢܢ ܡܬܛܪܦܝܢܢ ܐܠܐ ܠܐ ܚܝܒܝܢ ܚܢܢ ܀
8 Dañu nuy sonal fu nekk, waaye kenn tancu nu. Dañu nuy dugal ci ruq yi, waaye dinanu ci génn.
9ܡܬܪܕܦܝܢܢ ܐܠܐ ܠܐ ܡܫܬܒܩܝܢܢ ܡܤܬܚܦܝܢܢ ܐܠܐ ܠܐ ܐܒܕܝܢܢ ܀
9 Dañu nuy fitnaal, waaye Yàlla du nu wacc mukk. Tër nañu nu, waaye kenn doggaliwu nu.
10ܒܟܠܙܒܢ ܡܝܬܘܬܗ ܕܝܫܘܥ ܒܦܓܪܝܢ ܫܩܝܠܝܢܢ ܕܐܦ ܚܝܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܒܦܓܪܝܢ ܢܬܓܠܘܢ ܀
10 Fu nu tollu noo ngi gàddu ci sunu yaram dee gi Yeesu dee woon, ngir dundu Yeesu moom it feeñ ci sunu yaram.
11ܐܢ ܚܢܢ ܓܝܪ ܚܝܐ ܠܡܘܬܐ ܡܫܬܠܡܝܢܢ ܡܛܠ ܝܫܘܥ ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܝܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܢܬܓܠܘܢ ܒܦܓܪܢ ܗܢܐ ܕܡܐܬ ܀
11 Bés bu nekk, nun ñiy dund, ñu ngi nuy jébbal dee ndax Kirist, ngir dundu Kirist moom itam feeñ ci sunu yaram wiy dee.
12ܗܫܐ ܡܘܬܐ ܒܢ ܡܬܚܦܛ ܘܚܝܐ ܒܟܘܢ ܀
12 Noonu dee mu ngi jëf ci nun, dund di jëf ci yéen.
13ܐܦ ܚܢܢ ܗܟܝܠ ܕܚܕܐ ܗܝ ܪܘܚܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܐܝܬ ܠܢ ܐܝܟ ܕܟܬܝܒ ܕܗܝܡܢܬ ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܦ ܡܠܠܬ ܡܗܝܡܢܝܢܢ ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܦ ܡܡܠܠܝܢܢ ܀
13 Mbind mi nee na: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it nag, ndegam am nanu menn xelu ngëm moomu, danoo gëm, ba tax nuy wax.
14ܘܝܕܥܝܢܢ ܕܗܘ ܡܢ ܕܐܩܝܡ ܠܡܪܢ ܝܫܘܥ ܐܦ ܠܢ ܒܝܕ ܝܫܘܥ ܢܩܝܡ ܘܢܩܪܒܢ ܥܡܟܘܢ ܠܘܬܗ ܀
14 Ndaxte xam nanu ne Yàlla, mi dekkal Boroom bi Yeesu, dina nu dekkal nun itam ak Yeesu, te dina nu yóbbu ak yéen, taxawal nun ñépp ci jataayam.
15ܟܠܡܕܡ ܓܝܪ ܡܛܠܬܟܘܢ ܗܘ ܕܟܕ ܡܬܝܬܪܐ ܛܝܒܘܬܐ ܒܝܕ ܤܓܝܐܐ ܬܤܓܐ ܬܘܕܝܬܐ ܠܫܘܒܚܗ ܕܐܠܗܐ ܀
15 Ndaxte lépp li nuy daj, seen njariñ a tax, ngir yiwu Yàlla, wiy yokku ci nit ñu gën a takku, yokkaale ngërëm lu jëm ci Yàlla, ngir jollil ndamam.
16ܡܛܠ ܗܢܐ ܠܐ ܡܐܢܐ ܠܢ ܐܦ ܐܢ ܒܪܢܫܢ ܓܝܪ ܒܪܝܐ ܡܬܚܒܠ ܐܠܐ ܕܡܢ ܠܓܘ ܡܬܚܕܬ ܝܘܡ ܡܢ ܝܘܡ ܀
16 Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day yàqu jëm cig mag, sunu ruu moom, bés ak bés muy gën a yeesaat.
17ܐܘܠܨܢܗ ܓܝܪ ܕܙܒܢܐ ܗܢܐ ܟܕ ܛܒ ܙܥܘܪ ܘܩܠܝܠ ܫܘܒܚܐ ܪܒܐ ܕܠܐ ܤܟܐ ܠܥܠܡ ܥܠܡܝܢ ܡܛܝܒ ܠܢ ܀
17 Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul yàgg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan.
18ܕܠܐ ܚܕܝܢܢ ܒܗܠܝܢ ܕܡܬܚܙܝܢ ܐܠܐ ܒܗܠܝܢ ܕܠܐ ܡܬܚܙܝܢ ܕܡܬܚܙܝܢ ܓܝܪ ܕܙܒܢܐ ܐܢܝܢ ܕܠܐ ܡܬܚܙܝܢ ܕܝܢ ܕܠܥܠܡ ܐܢܝܢ ܀
18 Kon diirunu li ñuy gis waaye li ñu dul gis. Ndaxte li ñuy gis day wéy, waaye li ñu dul gis day sax ba fàww.