1ܝܕܥܝܢܢ ܓܝܪ ܕܐܢ ܒܝܬܢ ܕܒܐܪܥܐ ܗܢܐ ܕܦܓܪܐ ܢܫܬܪܐ ܐܠܐ ܐܝܬ ܠܢ ܒܢܝܢܐ ܕܡܢ ܐܠܗܐ ܒܝܬܐ ܕܠܐ ܒܥܒܕ ܐܝܕܝܐ ܒܫܡܝܐ ܠܥܠܡ ܀
1 Yaram wi nu soloo ci kaw suuf dafa mel ni ab tànt. Su daanoo, xam nanu ne, Yàlla jagleel na nu am taax ci asamaan, mu loxol nit defarul, di taax muy sax ba fàww.
2ܐܦ ܥܠ ܗܕܐ ܓܝܪ ܡܬܬܢܚܝܢܢ ܘܤܘܝܢܢ ܕܢܠܒܫ ܒܝܬܢ ܕܡܢ ܫܡܝܐ ܀
2 Fi mu ne nu ngi wonk, di yàkkamtee féete ak sunu dëkkukaayu asamaan, sol ko ni koddaay, xam ne,
3ܐܠܐ ܐܦ ܡܐ ܕܠܒܫܢ ܢܫܬܟܚ ܠܢ ܥܪܛܠ ܀
3 bu nu ko solee, dunu def yaramu neen.
4ܟܕ ܐܝܬܝܢ ܓܝܪ ܗܫܐ ܒܗܢܐ ܒܝܬܐ ܡܬܬܢܚܝܢܢ ܡܢ ܝܘܩܪܗ ܘܠܐ ܨܒܝܢܢ ܠܡܫܠܚܗ ܐܠܐ ܕܢܠܒܫ ܠܥܠ ܡܢܗ ܕܬܬܒܠܥ ܡܝܬܘܬܗ ܒܚܝܐ ܀
4 Nun ñi nekk ci tànt bii, nu ngi wonk ndax coono. Du caageen ne, danoo bëgg a summi sunu yaramu àddina, waaye danoo bëgg a sol sunu yaramu asamaan, ngir liy dee sóobu ci biir dund.
5ܘܕܡܥܬܕ ܠܢ ܠܗ ܠܗܕܐ ܐܠܗܐ ܗܘ ܗܘ ܕܝܗܒ ܠܢ ܪܗܒܘܢܐ ܕܪܘܚܗ ܀
5 Ki nu waajal ngir loolu moo di Yàlla, moom mi nu jox Xelam, di dawal ci cér bi mu nu dencal.
6ܡܛܠ ܕܝܕܥܝܢܢ ܗܟܝܠ ܘܡܦܤܝܢܢ ܕܟܡܐ ܕܒܦܓܪܐ ܫܪܝܢܢ ܥܢܝܕܝܢܢ ܡܢ ܡܪܢ ܀
6 Noonu kon nu ngi fees ak kóolute fu nu tollu; te xam nanu ne, fi ak nu ngi dëkk ci yaram wii, àggagunu sunu màkkaan ci wetu Boroom bi —
7ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܗܘ ܓܝܪ ܡܗܠܟܝܢܢ ܘܠܐ ܒܚܙܝܐ ܀
7 ndaxte doxewunu ab gis, waaye ngëm lanuy doxe.
8ܡܛܠ ܗܢܐ ܬܟܝܠܝܢܢ ܘܡܤܘܚܝܢܢ ܕܢܥܢܕ ܡܢ ܦܓܪܐ ܘܢܗܘܐ ܠܘܬ ܡܪܢ ܀
8 Kon fees nanu ak kóolute, te yéenee jóge ci dëkkukaayu yaram wii, dem dëkk ci wetu Boroom bi.
9ܘܡܬܚܦܛܝܢܢ ܕܐܢ ܥܢܘܕܐ ܚܢܢ ܘܐܢ ܥܡܘܪܐ ܠܗ ܗܘܝܢ ܫܦܪܝܢ ܀
9 Kon nag des fi walla jóge fi, li nuy faaydaal moo di neex Boroom bi.
10ܟܠܢ ܓܝܪ ܥܬܝܕܝܢܢ ܠܡܩܡ ܩܕܡ ܒܝܡ ܕܡܫܝܚܐ ܕܢܬܦܪܥ ܐܢܫ ܐܢܫ ܒܦܓܪܗ ܡܕܡ ܕܥܒܝܕ ܠܗ ܐܢ ܕܛܒ ܘܐܢ ܕܒܝܫ ܀
10 Ndaxte nun ñépp fàww nu teew ci kanamu Kirist, mu àtte nu, ngir ku nekk jot peyu li mu def ci yaramam, muy lu baax walla lu bon.
11ܡܛܠ ܕܝܕܥܝܢܢ ܗܟܝܠ ܕܚܠܬܗ ܕܡܪܢ ܠܒܢܝܢܫܐ ܗܘ ܡܦܝܤܝܢܢ ܠܐܠܗܐ ܕܝܢ ܓܠܝܢܢ ܤܒܪ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܐܦ ܠܡܕܥܝܟܘܢ ܕܝܠܟܘܢ ܓܠܝܢܢ ܀
11 Gannaaw xam nanu ragal Yàlla nag, nu ngi fexee gëmloo nit ñi, waaye li nu nekk leer na Yàlla te yaakaar naa ne, leer na leen it, ba ne fàŋŋ.
12ܠܐ ܗܘܐ ܬܘܒ ܢܦܫܢ ܡܫܒܚܝܢܢ ܠܟܘܢ ܐܠܐ ܥܠܬܐ ܗܘ ܝܗܒܝܢܢ ܠܟܘܢ ܕܗܘܝܬܘܢ ܡܫܬܒܗܪܝܢ ܒܢ ܠܘܬ ܗܢܘܢ ܕܒܐܦܐ ܗܘ ܡܫܬܒܗܪܝܢ ܘܠܐ ܒܠܒܐ ܀
12 Jéemunoo waxati lu ngeen nuy nawe, waaye danu leen a bëgg a may yoonu tiitaru ci nun, tey tontu ñooñuy tiitaroo col te du xol.
13ܐܢ ܓܝܪ ܫܛܝܢܢ ܠܐܠܗܐ ܘܐܢ ܬܩܢܝܢܢ ܠܟܘܢ ܀
13 Su fekkee danoo tàggalikoo ak sunu sago, ngir Yàlla la. Su nu àndee ak sunu sago, ngir yéen la.
14ܚܘܒܗ ܓܝܪ ܕܡܫܝܚܐ ܐܠܨ ܠܢ ܕܪܢܝܢܢ ܗܕܐ ܕܚܕ ܚܠܦ ܟܠܢܫ ܡܝܬ ܡܕܝܢ ܟܠܢܫ ܡܝܬ ܠܗ ܀
14 Ndaxte mbëggeelu Kirist moo nuy jiite, ndax wóor na nu ne, ndegam kenn rekk a dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.
15ܘܚܠܦ ܟܠܢܫ ܗܘ ܡܝܬ ܕܐܝܠܝܢ ܕܚܝܝܢ ܠܐ ܠܢܦܫܗܘܢ ܢܚܘܢ ܐܠܐ ܠܗܘ ܐܝܢܐ ܕܥܠ ܐܦܝܗܘܢ ܡܝܬ ܘܩܡ ܀
15 Te dee na ngir ñépp, ngir ñiy dund dootuñu dund ngir seen bopp, waaye ngir ki dee ci seen wàll te dekki.
16ܘܡܟܝܠ ܚܢܢ ܠܐܢܫ ܒܦܓܪ ܠܐ ܝܕܥܝܢܢ ܘܐܢ ܝܕܥܢ ܒܦܓܪ ܠܡܫܝܚܐ ܐܠܐ ܡܢ ܗܫܐ ܠܐ ܝܕܥܝܢܢ ܀
16 Kon nag gannaawsi tey xoolatunu kenn ci gis-gisu àddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu àddina, léegi xooleetunu ko noonu.
17ܟܠ ܡܢ ܕܒܡܫܝܚܐ ܗܘ ܗܟܝܠ ܒܪܝܬܐ ܗܘ ܚܕܬܐ ܥܬܝܩܬܐ ܥܒܪ ܠܗܝܢ ܀
17 Kon bu nit bokkee ci Kirist, mbindeef mu bees la. Li jëkk wéy na, lu bees a fi teew.
18ܘܟܠ ܡܕܡ ܗܘܐ ܚܕܬܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܗܘ ܕܪܥܝܢ ܠܗ ܒܡܫܝܚܐ ܘܝܗܒ ܠܢ ܬܫܡܫܬܐ ܕܬܪܥܘܬܐ ܀
18 Te loolu lépp a ngi sosoo ci Yàlla, mi nu jubale ak boppam jaare ko ci Yeesu Kirist, te sas nu nuy waare juboo googu:
19ܐܠܗܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܒܡܫܝܚܐ ܗܘ ܕܪܥܝ ܠܥܠܡܐ ܥܡ ܪܒܘܬܗ ܘܠܐ ܚܫܒ ܠܗܘܢ ܚܛܗܝܗܘܢ ܘܤܡ ܒܢ ܕܝܠܢ ܡܠܬܐ ܕܬܪܥܘܬܐ ܀
19 maanaam, Yàlla jaar na ci Kirist, di jubale waa àddina ak boppam te sëfu leen seeni tooñ. Kàddug juboo googu, Yàlla dénk na nu ko.
20ܐܝܙܓܕܐ ܚܢܢ ܗܟܝܠ ܚܠܦ ܡܫܝܚܐ ܘܐܝܟ ܗܘ ܕܐܠܗܐ ܒܥܐ ܡܢܟܘܢ ܒܐܝܕܢ ܚܠܦ ܡܫܝܚܐ ܗܟܝܠ ܒܥܝܢܢ ܐܬܪܥܘ ܠܐܠܗܐ ܀
20 Ay ndaw lanu, yu Kirist yónni, te Yàllaa ngi woo nit ñi jaare ko ci nun. Kon nag ci turu Kirist, nu ngi leen koy ñaan: nanguleen a juboo ak Yàlla.
21ܗܘ ܓܝܪ ܕܠܐ ܝܕܥ ܗܘܐ ܚܛܝܬܐ ܡܛܠܬܟܘܢ ܚܛܝܬܐ ܥܒܕܗ ܕܚܢܢ ܢܗܘܐ ܒܗ ܙܕܝܩܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
21 Kirist mi musul a def bàkkaar, Yàlla def na ko bàkkaar ci sunu wàll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu man a doon njubteg Yàlla.