Syriac: NT

Wolof: New Testament

Ephesians

2

1ܘܐܦ ܠܟܘܢ ܕܡܝܬܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܒܚܛܗܝܟܘܢ ܘܒܤܟܠܘܬܟܘܢ ܀
1 Te yéen itam Yàlla dekkal na leen, yéen ñi doon ndee fa kanamam ci seeni moy ak seeni bàkkaar.
2ܒܗܠܝܢ ܕܡܢ ܩܕܝܡ ܗܠܟܬܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܒܗܝܢ ܐܝܟ ܥܠܡܝܘܬܗ ܕܥܠܡܐ ܗܢܐ ܘܐܝܟ ܨܒܝܢܗ ܕܪܝܫ ܫܘܠܛܢܐ ܕܐܐܪ ܘܕܪܘܚܐ ܗܕܐ ܕܡܬܚܦܛܐ ܒܒܢܝܐ ܕܠܐ ܡܬܛܦܝܤܢܘܬܐ ܀
2 Ci biir yooyu ngeen doon dund démb, topp doxalinu àddina, tey déggal kilifag boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, di xel mu bon miy jëf ci kureelu ñi déggadil Yàlla.
3ܒܗܢܘܢ ܥܒܕܐ ܕܐܦ ܚܢܢ ܐܬܗܦܟܢ ܒܗܘܢ ܡܢ ܩܕܝܡ ܒܪܓܝܓܬܐ ܕܒܤܪܢ ܘܥܒܕܝܢ ܗܘܝܢ ܨܒܝܢܐ ܕܒܤܪܢ ܘܕܬܪܥܝܬܢ ܘܒܢܝܐ ܗܘܝܢ ܕܪܘܓܙܐ ܡܠܝܐܝܬ ܐܝܟ ܫܪܟܐ ܀
3 Te nun it booba àndoon nanu ak ñoom ca seen dund ga, di topp sunu bakkan ciy wut bànneexi yaram ak coobarey xel. Noonu ci sunu bindu nit yeyoo nanu meru Yàlla, ni ña ca des.
4ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܕܥܬܝܪ ܒܪܚܡܘܗܝ ܡܛܠ ܚܘܒܗ ܤܓܝܐܐ ܕܐܚܒܢ ܀
4 Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw mbëggeel gu réy, gi mu am ci nun,
5ܟܕ ܡܝܬܝܢ ܗܘܝܢ ܒܚܛܗܝܢ ܐܚܝܢ ܥܡ ܡܫܝܚܐ ܘܒܛܝܒܘܬܗ ܦܪܩܢ ܀
5 dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bàkkaar — ci kaw yiwu Yàlla ngeen mucce.
6ܘܐܩܝܡܢ ܥܡܗ ܘܐܘܬܒܢ ܥܡܗ ܒܫܡܝܐ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
6 Te dekkal na nu ak Kirist Yeesu, dëël nu ak moom ca bérab yu kawe ya.
7ܕܢܚܘܐ ܠܥܠܡܐ ܕܐܬܝܢ ܪܒܘܬܐ ܕܥܘܬܪܐ ܕܛܝܒܘܬܗ ܘܒܤܝܡܘܬܗ ܕܗܘܬ ܥܠܝܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
7 Noonu ba fu jamono yem, dina lañal fi sunu kanam yiwam wu réy wi xel mënta takk, jaar ci baaxaay gi mu nu won ci Kirist Yeesu.
8ܒܛܝܒܘܬܗ ܗܘ ܓܝܪ ܐܬܦܪܩܢ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܘܗܕܐ ܠܐ ܗܘܬ ܡܢܟܘܢ ܐܠܐ ܡܘܗܒܬܐ ܗܝ ܕܐܠܗܐ ܀
8 Ndaxte ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yéen, mayu Yàlla la;
9ܠܐ ܡܢ ܥܒܕܐ ܕܠܐ ܐܢܫ ܢܫܬܒܗܪ ܀
9 du peyu jëf, ngir kenn du ci kañu.
10ܒܪܝܬܐ ܚܢܢ ܓܝܪ ܕܝܠܗ ܕܐܬܒܪܝܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܥܒܕܐ ܛܒܐ ܗܢܘܢ ܕܡܢ ܩܕܝܡ ܛܝܒ ܐܠܗܐ ܕܒܗܘܢ ܢܗܠܟ ܀
10 Ndaxte jëfu Yàlla lanu; moo nu bind ci Kirist Yeesu, ngir nu wéy ci jëf yu rafet, yi mu nu fàgguloon ca njàlbéen ga.
11ܡܛܠ ܗܕܐ ܗܘܝܬܘܢ ܥܗܕܝܢ ܕܐܢܬܘܢ ܥܡܡܐ ܡܢ ܩܕܝܡ ܕܒܤܪ ܗܘܝܬܘܢ ܘܡܬܩܪܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܥܘܪܠܘܬܐ ܡܢ ܗܝ ܕܡܬܩܪܝܐ ܓܙܘܪܬܐ ܘܐܝܬܝܗ ܥܒܕ ܐܝܕܝܐ ܒܒܤܪܐ ܀
11 Kon nag yéen ñi dul Yawut cib juddu, yéen ñi xaraful, te ñi xaraf ci seen yaram ci loxol nit ñoo leen teg ay yéefar, fàttalikuleen lii:
12ܘܐܝܬܝܟܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܒܗܘ ܙܒܢܐ ܕܠܐ ܡܫܝܚܐ ܘܢܘܟܪܝܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܡܢ ܕܘܒܪܐ ܕܐܝܤܪܝܠ ܘܐܟܤܢܝܐ ܗܘ ܠܕܝܬܩܐ ܕܡܘܠܟܢܐ ܘܕܠܐ ܤܒܪ ܗܘܝܬܘܢ ܘܕܠܐ ܐܠܗ ܒܥܠܡܐ ܀
12 booba amuleen woon benn cér ci Kirist, mbaa benn baat ci kureelu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre, gi Yàlla fas ak ñoom, te ëmb dige ya. Amuleen woon jenn yaakaar mbaa benn xam-xamu Yàlla ci àddina.
13ܗܫܐ ܕܝܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܐܢܬܘܢ ܕܡܢ ܩܕܝܡ ܪܚܝܩܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܩܪܝܒܐ ܗܘܝܬܘܢ ܒܕܡܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
13 Waaye léegi ci seen bokk ci Kirist Yeesu, yéen ñi sore woon jege ngeen ndax deretu Kirist ji ñu tuur.
14ܗܘܝܘ ܓܝܪ ܫܝܢܢ ܗܘ ܕܥܒܕ ܬܪܬܝܗܝܢ ܚܕܐ ܘܫܪܐ ܤܝܓܐ ܕܩܐܡ ܗܘܐ ܒܡܨܥܬܐ ܀
14 Ndaxte mooy sunu jàmm, moom mi jël Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn. Ñag bi doxoon sunu diggante te sosoon sunu dëngoo, moo ko màbb ci li mu joxe yaramam,
15ܘܒܥܠܕܒܒܘܬܐ ܒܒܤܪܗ ܘܢܡܘܤܐ ܕܦܘܩܕܐ ܒܦܘܩܕܢܘܗܝ ܒܛܠ ܕܠܬܪܝܗܘܢ ܢܒܪܐ ܒܩܢܘܡܗ ܠܚܕ ܒܪܢܫܐ ܚܕܬܐ ܘܥܒܕ ܫܝܢܐ ܀
15 far noonu yoonu Musaa, muy ndigal ya ak dogal ya. Noonu la nu jële, Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn ci moom, ba nu jàmmoo.
16ܘܪܥܝ ܠܬܪܝܗܘܢ ܒܚܕ ܦܓܪ ܥܡ ܐܠܗܐ ܘܒܙܩܝܦܗ ܩܛܠ ܒܥܠܕܒܒܘܬܐ ܀
16 Te nun ñaar, ñi def benn jëmm, jubale na nu ak Yàlla ci dee, gi mu dee ca bant ba ñu ko daajoon, dindee noonu sunu tongoonte.
17ܘܐܬܐ ܤܒܪ ܫܠܡܐ ܠܟܘܢ ܠܪܚܝܩܐ ܘܠܩܪܝܒܐ ܀
17 Bi mu ko defee mu ñëw, yégalsi nu xebaaru jàmm fa kanam Yàlla, yéen ñi sore woon ak nun ñi jege.
18ܡܛܠ ܕܒܗ ܗܘ ܗܘܐ ܠܢ ܩܘܪܒܐ ܠܬܪܝܢ ܒܚܕܐ ܪܘܚ ܠܘܬ ܐܒܐ ܀
18 Ndaxte nun ñaar ñépp am nanu bunt ci Yàlla Baay bi, jaar ci Kirist, ci ndimbalu menn Xel mu Sell mi.
19ܡܟܝܠ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܐܟܤܢܝܐ ܘܠܐ ܬܘܬܒܐ ܐܠܐ ܒܢܝ ܡܕܝܢܬܐ ܕܩܕܝܫܐ ܘܒܢܝ ܒܝܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
19 Noonu dootuleen ay doxandéem mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Yàlla yu sell yi, te waa këram ngeen.
20ܘܐܬܒܢܝܬܘܢ ܥܠ ܫܬܐܤܬܐ ܕܫܠܝܚܐ ܘܕܢܒܝܐ ܘܗܘ ܗܘܐ ܪܝܫ ܩܪܢܐ ܕܒܢܝܢܐ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
20 Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa.
21ܘܒܗ ܡܬܪܟܒ ܟܠܗ ܒܢܝܢܐ ܘܪܒܐ ܠܗܝܟܠܐ ܩܕܝܫܐ ܒܡܪܝܐ ܀
21 Ci moom la doj yépp ràbbloo, ba tabax bi jóg, di màggalukaay bu sell ngir Boroom bi.
22ܟܕ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܒܗ ܡܬܒܢܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܥܡܪܐ ܕܐܠܗܐ ܒܪܘܚ ܀
22 Te ci seen bokk ci Kirist, Yàlla boole na leen tabax yéen itam, ba ngeen nekk dëkkukaayam, jaar ci Xel mu Sell mi.