1ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܢܐ ܦܘܠܘܤ ܐܤܝܪܐ ܐܢܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܠ ܐܦܝܟܘܢ ܥܡܡܐ ܀
1 Kon nag maa ngi leen di ñaanal, man Pool mi ñu tëj kaso ci turu Kirist ndax sas wi may bey ci yéen, xeet yi dul Yawut.
2ܐܢ ܫܡܥܬܘܢ ܡܕܒܪܢܘܬܐ ܕܛܝܒܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܕܐܬܝܗܒܬ ܠܝ ܒܟܘܢ ܀
2 Wóor na ma ne, dégg ngeen yenub xamle yiwu Yàlla, bi mu ma jagleel jëm ci yéen.
3ܕܒܓܠܝܢܐ ܐܬܝܕܥ ܠܝ ܐܪܙܐ ܐܝܟܢܐ ܕܟܬܒܬ ܠܟܘܢ ܒܙܥܘܪܝܬܐ ܀
3 Yàlla feeñu na ma, xamal ma mbóoti mbir mi mu tëral, ni ma leen ko binde ci kàddu yu néew.
4ܐܝܟ ܡܐ ܕܡܫܟܚܝܬܘܢ ܟܕ ܩܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܤܬܟܠܘ ܝܕܥܬܝ ܕܒܐܪܙܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
4 Bu ngeen jàngee loolu, dingeen man a xam bu wér dégg, gi ma am ci mbóoti mbiri Kirist.
5ܗܘ ܕܒܕܪܐ ܐܚܪܢܐ ܠܐ ܐܬܝܕܥ ܠܒܢܝܢܫܐ ܐܝܟ ܕܗܫܐ ܐܬܓܠܝ ܠܫܠܝܚܘܗܝ ܩܕܝܫܐ ܘܠܢܒܝܘܗܝ ܒܪܘܚ ܀
5 Ci jamono yu weesu, loolu kumpa la woon ci doom Aadama, waaye léegi Yàlla feeñalal na ko ay ndawam ak yonentam yu sell yi, jaarale ko ci Xel mu Sell mi.
6ܕܢܗܘܘܢ ܥܡܡܐ ܒܢܝ ܝܪܬܘܬܗ ܘܫܘܬܦܐ ܕܦܓܪܗ ܘܕܡܘܠܟܢܐ ܕܐܬܝܗܒ ܒܗ ܒܝܕ ܐܘܢܓܠܝܘܢ ܀
6 Mbir mi nii la tëdde: léegi xeet yi dul Yawut dañoo bokksi cér ak Yawut yi, bokk ak ñoom jenn jëmm, bokk wàll ci xéewal yi Yàlla dige ci Kirist Yeesu, te xebaar bu baax bi xamle ko.
7ܗܘ ܕܐܢܐ ܗܘܝܬ ܡܫܡܫܢܗ ܐܝܟ ܡܘܗܒܬܐ ܕܛܝܒܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܕܐܬܝܗܒܬ ܠܝ ܡܢ ܡܥܒܕܢܘܬܐ ܕܚܝܠܗ ܀
7 Xamle xebaar bu baax boobu nag, Yàlla fal na ma ci jawriñ ci kaw yiwam, te di ma dooleel ci kàttanam.
8ܠܝ ܕܙܥܘܪܐ ܐܢܐ ܕܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܐܬܝܗܒܬ ܛܝܒܘܬܐ ܗܕܐ ܕܐܤܒܪ ܒܥܡܡܐ ܥܘܬܪܗ ܕܡܫܝܚܐ ܗܘ ܕܠܐ ܡܬܥܩܒ ܀
8 May na ma, man mi gën a tuuti ci gaayi Yàlla yu sell yi, may xebaar xeeti àddina barkeel yu xel dajul yi ci Kirist;
9ܘܐܢܗܪ ܠܟܠܢܫ ܐܝܕܐ ܗܝ ܡܕܒܪܢܘܬܐ ܕܐܪܙܐ ܗܘ ܕܟܤܐ ܗܘܐ ܡܢ ܥܠܡܐ ܒܐܠܗܐ ܕܟܠ ܒܪܐ ܀
9 te it may sulli melokaanu mbir mu xóot mi Yàlla tëral, te doon kumpa njàlbéen ga ba tey ci moom, mi sos lépp.
10ܕܒܝܕ ܥܕܬܐ ܬܬܝܕܥ ܚܟܡܬܗ ܕܐܠܗܐ ܡܠܝܬ ܦܘܪܫܢܐ ܠܐܪܟܘܤ ܘܠܫܘܠܛܢܐ ܕܒܫܡܝܐ ܀
10 Waaye léegi nee na fàŋŋ, ngir kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi ca bérab yu kawe ya man a xam ni Xelum Yàlla xóote, jaar ci li ñu gis ci mbooloom ñi gëm Kirist.
11ܗܝ ܕܥܬܕ ܗܘܐ ܡܢ ܥܠܡܐ ܘܥܒܕܗ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܡܪܢ ܀
11 Mooy dogal bi sax dàkk, te Yàlla tëral ko ci Kirist Yeesu sunu Boroom.
12ܗܘ ܕܒܗ ܐܝܬ ܠܢ ܦܪܗܤܝܐ ܘܩܪܝܒܘܬܐ ܒܬܘܟܠܢܐ ܕܗܝܡܢܘܬܗ ܀
12 Ci turam am nanu kóolute fa kanam Yàlla, ak bunt bu yaatu ci moom ci kaw ngëm.
13ܡܛܠ ܗܢܐ ܫܐܠܢܐ ܕܠܐ ܬܡܐܢ ܠܝ ܒܐܘܠܨܢܝ ܕܥܠ ܐܦܝܟܘܢ ܕܗܕܐ ܗܝ ܬܫܒܘܚܬܟܘܢ ܀
13 Maa ngi leen di ñaan nag, ngeen bañ a yoqi ndax coono, yi may jële ci bey sama sas ci yéen, xam ne coono yooyu ñoo leen di jural ndam.
14ܘܟܐܦܢܐ ܒܘܪܟܝ ܠܘܬ ܐܒܘܗܝ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
14 Moo tax maa ngi sukk, jublu ci Yàlla Baay
15ܗܘ ܕܡܢܗ ܡܫܬܡܗܐ ܟܠ ܐܒܗܘܬܐ ܕܒܫܡܝܐ ܘܒܐܪܥܐ ܀
15 biy cosaanul njaboot gépp, muy ci kaw, muy ci suuf.
16ܕܢܬܠ ܠܟܘܢ ܐܝܟ ܥܘܬܪܐ ܕܬܫܒܘܚܬܗ ܕܒܚܝܠܐ ܬܫܬܪܪܘܢ ܒܪܘܚܗ ܕܒܒܪܢܫܟܘܢ ܕܠܓܘ ܀
16 Ma di ko ñaan, mu may leen, ci kaw ndamam lu amul kem, Xel mu Sell mi feddali seen baatin ak kàttan gu mag,
17ܢܥܡܪ ܡܫܝܚܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܘܒܠܒܘܬܟܘܢ ܒܚܘܒܐ ܟܕ ܢܗܘܐ ܫܪܝܪ ܥܩܪܟܘܢ ܘܫܬܐܤܬܟܘܢ ܀
17 ba Kirist dëkk ci seeni xol ci kaw ngëm. Te ngeen sax noonu te sampu ci mbëggeelu Yàlla,
18ܕܬܫܟܚܘܢ ܠܡܕܪܟܘ ܥܡ ܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܡܢܘ ܪܘܡܐ ܘܥܘܡܩܐ ܘܐܘܪܟܐ ܘܦܬܝܐ ܀
18 ba jagoo, yéen ak gaayi Yàlla yu sell yépp, guddaay ba, yaatuwaay ba, kawe ga ak xóotaay ba,
19ܘܬܕܥܘܢ ܪܒܘܬܐ ܕܝܕܥܬܐ ܕܚܘܒܗ ܕܡܫܝܚܐ ܘܬܬܡܠܘܢ ܒܟܠܗ ܡܘܠܝܐ ܕܐܠܗܐ ܀
19 te xam mbëggeelu Kirist, gi raw mépp xel. Noonu dingeen fees dell ak matug Yàlla.
20ܠܗܘ ܕܝܢ ܕܡܨܐ ܒܚܝܠܐ ܝܬܝܪ ܡܢ ܟܠ ܠܡܥܒܕ ܠܢ ܘܝܬܝܪ ܡܢ ܡܐ ܕܫܐܠܝܢܢ ܘܪܢܝܢܢ ܐܝܟ ܚܝܠܗ ܕܡܤܬܥܪ ܒܢ ܀
20 Léegi nag, na ndam li féete ak Yàlla, mi man a yeggale lépp luy ñaan mbaa yéene, ba weesu ko fuuf, dëppook kàttan giy jëf ci nun;
21ܠܗ ܬܫܒܘܚܬܐ ܒܥܕܬܗ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܟܠܗܘܢ ܕܪܐ ܕܥܠܡܝ ܥܠܡܝܢ ܐܡܝܢ ܀
21 moo yelloo ndamul mbooloom ñi gëm jamonoy jamono ba fàww, jaar ci Kirist Yeesu. Amiin.