Syriac: NT

Wolof: New Testament

Ephesians

5

1ܗܘܝܬܘܢ ܗܟܝܠ ܡܬܕܡܝܢ ܒܐܠܗܐ ܐܝܟ ܒܢܝܐ ܚܒܝܒܐ ܀
1 Yéen nag ñiy guney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu.
2ܘܗܠܟܘ ܒܚܘܒܐ ܐܝܟ ܕܐܦ ܡܫܝܚܐ ܐܚܒܢ ܘܐܫܠܡ ܢܦܫܗ ܥܠ ܐܦܝܢ ܩܘܪܒܢܐ ܘܕܒܚܐ ܠܐܠܗܐ ܠܪܝܚܐ ܒܤܝܡܐ ܀
2 Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ.
3ܙܢܝܘܬܐ ܕܝܢ ܘܟܠܗ ܛܢܦܘܬܐ ܘܥܠܘܒܘܬܐ ܐܦܠܐ ܡܫܬܡܗܘ ܬܫܬܡܗ ܒܝܢܬܟܘܢ ܐܝܟ ܕܝܐܐ ܠܩܕܝܫܐ ܀
3 Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi.
4ܘܠܐ ܨܘܚܝܬܐ ܘܠܐ ܡܠܐ ܕܫܛܝܘܬܐ ܐܘ ܕܒܙܚܐ ܐܘ ܕܫܥܝܐ ܗܠܝܢ ܕܠܐ ܡܬܒܥܝܢ ܐܠܐ ܚܠܦ ܗܠܝܢ ܬܘܕܝܬܐ ܀
4 Dawleen it yu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla.
5ܗܕܐ ܕܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܝܕܥܝܢ ܕܟܠܢܫ ܕܐܝܬܘܗܝ ܙܢܝܐ ܐܘ ܛܢܦܐ ܐܘ ܥܠܘܒܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܦܠܚ ܦܬܟܪܐ ܠܝܬ ܠܗ ܝܪܬܘܬܐ ܒܡܠܟܘܬܗ ܕܡܫܝܚܐ ܘܕܐܠܗܐ ܀
5 Na leen wóor ne, kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla.
6ܕܠܡܐ ܐܢܫ ܢܛܥܝܟܘܢ ܒܡܠܐ ܤܪܝܩܬܐ ܡܛܠ ܗܠܝܢ ܗܘ ܓܝܪ ܐܬܐ ܪܘܓܙܗ ܕܐܠܗܐ ܥܠ ܒܢܝܐ ܕܠܐ ܡܬܛܦܝܤܢܘܬܐ ܀
6 Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil.
7ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܗܘܘܢ ܠܗܘܢ ܫܘܬܦܐ ܀
7 Kon nag buleen séq ak ñoom dara.
8ܐܝܬܝܟܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܓܝܪ ܡܢ ܠܘܩܕܡ ܚܫܘܟܐ ܗܫܐ ܕܝܢ ܢܘܗܪܐ ܐܢܬܘܢ ܒܡܪܢ ܐܝܟ ܒܢܝ ܢܘܗܪܐ ܗܟܝܠ ܗܟܢܐ ܗܠܟܘ ܀
8 Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi. Dundeleen nag ni ay guney leer.
9ܦܐܪܘܗܝ ܓܝܪ ܕܢܘܗܪܐ ܒܟܠܗ ܐܢܘܢ ܛܒܘܬܐ ܘܙܕܝܩܘܬܐ ܘܩܘܫܬܐ ܀
9 Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg.
10ܘܗܘܝܬܘܢ ܦܪܫܝܢ ܡܢܐ ܫܦܝܪ ܩܕܡ ܡܪܢ ܀
10 Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi,
11ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܫܬܘܬܦܝܢ ܠܘܬ ܥܒܕܐ ܕܚܫܘܟܐ ܕܦܐܪܐ ܠܝܬ ܒܗܘܢ ܐܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܟܘܢܝܢ ܠܗܘܢ ܀
11 te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def.
12ܡܕܡ ܓܝܪ ܕܒܛܘܫܝܝ ܥܒܕܝܢ ܢܕܝܕ ܗܘ ܐܦ ܠܡܡܠܠܘܬܗ ܀
12 Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la;
13ܟܠ ܡܕܡ ܓܝܪ ܡܬܟܘܢ ܡܢ ܢܘܗܪܐ ܘܡܬܓܠܐ ܘܟܠܡܕܡ ܕܓܠܐ ܢܘܗܪܐ ܗܘ ܀
13 waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko.
14ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܡܝܪ ܕܐܬܬܥܝܪ ܕܡܟܐ ܘܩܘܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܘܢܢܗܪ ܠܟ ܡܫܝܚܐ ܀
14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne:«Yeewul, yaw mi nelaw,te jóge ci biir néew yi,kon Kirist dina ne ràññ ci yaw,ni leeru jant buy fenk.»
15ܚܙܘ ܗܟܝܠ ܐܝܟܢܐ ܬܗܠܟܘܢ ܙܗܝܐܝܬ ܠܐ ܐܝܟ ܤܟܠܐ ܐܠܐ ܐܝܟ ܚܟܝܡܐ ܀
15 Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel,
16ܕܙܒܢܝܢ ܩܐܪܤܗܘܢ ܡܛܠ ܕܝܘܡܬܐ ܒܝܫܐ ܐܢܘܢ ܀
16 tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon.
17ܡܛܠ ܗܢܐ ܠܐ ܬܗܘܘܢ ܚܤܝܪܝ ܪܥܝܢܐ ܐܠܐ ܐܤܬܟܠܘ ܡܢܘ ܨܒܝܢܗ ܕܐܠܗܐ ܀
17 Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobareg Boroom bi.
18ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܪܘܝܢ ܒܚܡܪܐ ܕܒܗ ܐܝܬ ܐܤܘܛܘܬܐ ܐܠܐ ܐܬܡܠܘ ܒܪܘܚܐ ܀
18 Buleen màndi it ci sangara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi;
19ܘܡܠܠܘ ܥܡ ܢܦܫܟܘܢ ܒܡܙܡܘܪܐ ܘܒܬܫܒܚܬܐ ܘܒܙܡܝܪܬܐ ܕܪܘܚܐ ܗܘܝܬܘܢ ܙܡܪܝܢ ܒܠܒܘܬܟܘܢ ܠܡܪܝܐ ܀
19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ci ay woy ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seeni xol.
20ܘܗܘܝܬܘܢ ܡܘܕܝܢ ܒܟܠܙܒܢ ܥܠ ܐܦܝ ܟܠܢܫ ܒܫܡܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܐܠܗܐ ܐܒܐ ܀
20 Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen man a tollu, ci lu mu man a doon;
21ܘܗܘܝܬܘܢ ܡܫܬܥܒܕܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܒܚܘܒܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.
22ܢܫܐ ܗܘܝܬܝܢ ܡܫܬܥܒܕܢ ܠܒܥܠܝܟܝܢ ܐܝܟ ܕܠܡܪܢ ܀
22 Naka yéen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi.
23ܡܛܠ ܕܓܒܪܐ ܪܫܗ ܗܘ ܕܐܢܬܬܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܡܫܝܚܐ ܪܫܐ ܗܘ ܕܥܕܬܐ ܘܗܘܝܘ ܡܚܝܢܐ ܕܦܓܪܐ ܀
23 Ndaxte góor mooy kilifag jabaram, ni Kirist nekke kilifag mbooloom ñi gëm, muy jëmmam ji muy sàmm.
24ܐܠܐ ܐܝܟܢܐ ܕܥܕܬܐ ܡܫܬܥܒܕܐ ܠܡܫܝܚܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܢܫܐ ܠܒܥܠܝܗܝܢ ܒܟܠܡܕܡ ܀
24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jigéen ji war a jiitale jëkkëram ci lépp.
25ܓܒܪܐ ܐܚܒܘ ܢܫܝܟܘܢ ܐܝܟ ܕܐܦ ܡܫܝܚܐ ܐܚܒ ܠܥܕܬܗ ܘܢܦܫܗ ܐܫܠܡ ܥܠ ܐܦܝܗ ܀
25 Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom,
26ܕܢܩܕܫܝܗ ܘܢܕܟܝܗ ܒܤܚܝܐ ܕܡܝܐ ܘܒܡܠܬܐ ܀
26 ngir sellal ko ak kàddoom, ba mu laab ni ku sangu set.
27ܘܢܩܝܡܝܗ ܥܕܬܐ ܠܢܦܫܗ ܟܕ ܡܫܒܚܐ ܘܠܝܬ ܒܗ ܛܘܠܫܐ ܘܠܐ ܩܡܛܐ ܘܠܐ ܡܕܡ ܕܠܗܠܝܢ ܕܡܐ ܐܠܐ ܬܗܘܐ ܩܕܝܫܐ ܕܠܐ ܡܘܡ ܀
27 Noonu dina ko jël, mu mel ni séet bu ñu waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te gàkkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk.
28ܗܟܢܐ ܘܠܐ ܠܓܒܪܐ ܕܢܚܒܘܢ ܢܫܝܗܘܢ ܐܝܟ ܕܠܦܓܪܝܗܘܢ ܡܢ ܕܠܐܢܬܬܗ ܓܝܪ ܡܚܒ ܢܦܫܗ ܗܘ ܡܚܒ ܀
28 Na góor bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa jabar, bëgg sa bopp la.
29ܠܐ ܓܝܪ ܐܢܫ ܡܡܬܘܡ ܤܢܐ ܦܓܪܗ ܐܠܐ ܡܬܪܤܐ ܠܗ ܘܝܨܦ ܕܝܠܗ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܡܫܝܚܐ ܕܥܕܬܗ ܀
29 Ndaxte kenn musul a bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi;
30ܡܛܠ ܕܗܕܡܐ ܚܢܢ ܕܦܓܪܗ ܘܡܢ ܒܤܪܗ ܚܢܢ ܘܡܢ ܓܪܡܘܗܝ ܀
30 ndaxte noo di céri jëmmam.
31ܡܛܠ ܗܢܐ ܢܫܒܘܩ ܓܒܪܐ ܠܐܒܘܗܝ ܘܠܐܡܗ ܘܢܩܦ ܠܐܢܬܬܗ ܘܢܗܘܘܢ ܬܪܝܗܘܢ ܚܕ ܒܤܪ ܀
31 Mbind mi nee na: «Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.»
32ܗܢܐ ܐܪܙܐ ܪܒ ܗܘ ܐܢܐ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܥܠ ܡܫܝܚܐ ܘܥܠ ܥܕܬܗ ܀
32 Loolu ëmb na mbóot mu xóot; man maa ngi wax ci lu jëm ci Kirist ak mbooloo mi.
33ܒܪܡ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܟܠ ܚܕ ܚܕ ܡܢܟܘܢ ܗܟܢܐ ܢܪܚܡ ܐܢܬܬܗ ܐܝܟ ܕܠܢܦܫܗ ܐܢܬܬܐ ܕܝܢ ܬܗܘܐ ܕܚܠܐ ܡܢ ܒܥܠܗ ܀
33 Waaye li teew, na góor gu nekk bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram.