Syriac: NT

Wolof: New Testament

Ephesians

6

1ܒܢܝܐ ܐܫܬܡܥܘ ܠܐܒܗܝܟܘܢ ܒܡܪܢ ܗܕܐ ܓܝܪ ܟܐܢܐ ܀
1 Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet.
2ܘܗܢܘ ܦܘܩܕܢܐ ܩܕܡܝܐ ܕܡܠܝܟ ܝܩܪ ܠܐܒܘܟ ܘܠܐܡܟ ܀
2 «Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkk a ëmb dige,
3ܕܢܗܘܐ ܠܟ ܕܫܦܝܪ ܘܢܐܪܟܘܢ ܚܝܝܟ ܥܠ ܐܪܥܐ ܀
3 maanaa: «ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm.»
4ܐܒܗܐ ܠܐ ܬܪܓܙܘܢ ܒܢܝܟܘܢ ܐܠܐ ܪܒܘ ܐܢܘܢ ܒܡܪܕܘܬܐ ܘܒܝܘܠܦܢܐ ܕܡܪܢ ܀
4 Yéen baay yi it, buleen bundaxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi.
5ܥܒܕܐ ܐܫܬܡܥܘ ܠܡܪܝܟܘܢ ܕܒܒܤܪ ܒܕܚܠܬܐ ܘܒܪܬܝܬܐ ܘܒܦܫܝܛܘܬ ܠܒܐ ܐܝܟ ܕܠܡܫܝܚܐ ܀
5 Yéen jaam yi, nangeen déggal seeni sang yu àddina, boole ci ragal ak wegeel, di ko def ak xol bu laab, ni su doon ngir Kirist.
6ܠܐ ܒܡܚܙܐ ܥܝܢܐ ܐܝܟ ܗܘ ܕܠܒܢܝܢܫܐ ܫܦܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܠܐ ܐܝܟ ܥܒܕܐ ܕܡܫܝܚܐ ܕܥܒܕܝܢ ܨܒܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܀
6 Buleen ko def rekk ci ngistal, ngir sàkku ngërëmu nit, waaye ni ay jaami Kirist, di jëfe coobareg Yàlla ak seen xol bépp.
7ܘܫܡܫܘ ܐܢܘܢ ܡܢ ܟܠܗ ܢܦܫܟܘܢ ܒܚܘܒܐ ܐܝܟ ܕܠܡܪܢ ܘܠܐ ܐܝܟ ܕܠܒܢܝܢܫܐ ܀
7 Beyleen seen sas nag ak xol bu tàlli, ni su doon ngir Boroom bi te du nit,
8ܟܕ ܝܕܥܝܬܘܢ ܕܗܘ ܡܕܡ ܕܥܒܕ ܐܢܫ ܕܫܦܝܪ ܗܘ ܡܬܦܪܥ ܡܢ ܡܪܢ ܐܢ ܥܒܕܐ ܗܘ ܘܐܢ ܒܪ ܚܐܪܐ ܀
8 xam ne ku def lu baax, Boroom bi delloo la ko, muy jaam, muy gor.
9ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܡܪܝܐ ܗܟܢܐ ܗܘܝܬܘܢ ܥܒܕܝܢ ܠܥܒܕܝܟܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܫܒܩܝܢ ܠܗܘܢ ܤܟܠܘܬܐ ܡܛܠ ܕܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܦ ܡܪܟܘܢ ܕܝܠܟܘܢ ܐܝܬܘܗܝ ܒܫܡܝܐ ܘܡܤܒ ܒܐܦܐ ܠܝܬ ܠܘܬܗ ܀
9 Yéen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, te dëddu gépp raglu, xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan, te ñépp a yem fi moom.
10ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܐܬܚܝܠܘ ܒܡܪܢ ܘܒܬܘܩܦܐ ܕܚܝܠܗ ܀
10 Léegi nag doolewuleen ci Boroom bi, te soloo kàttanam gu mag gi.
11ܘܠܒܫܘ ܟܠܗ ܙܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܐܝܟܢܐ ܕܬܫܟܚܘܢ ܠܡܩܡ ܠܘܩܒܠ ܨܢܥܬܗ ܕܐܟܠ ܩܪܨܐ ܀
11 Gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ngir man a jànkoonte ak pexey Seytaane.
12ܡܛܠ ܕܬܟܬܘܫܟܘܢ ܠܐ ܗܘܐ ܥܡ ܒܤܪܐ ܘܕܡܐ ܐܠܐ ܥܡ ܐܪܟܘܤ ܘܥܡ ܫܠܝܛܢܐ ܘܥܡ ܐܚܝܕܝ ܥܠܡܐ ܕܗܢܐ ܚܫܘܟܐ ܘܥܡ ܪܘܚܐ ܒܝܫܬܐ ܕܬܚܝܬ ܫܡܝܐ ܀
12 Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi.
13ܡܛܠ ܗܢܐ ܠܒܫܘ ܟܠܗ ܙܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܕܬܫܟܚܘܢ ܬܐܪܥܘܢ ܒܝܫܐ ܘܟܕ ܡܥܬܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܟܠܡܕܡ ܬܩܘܡܘܢ ܀
13 Kon nag gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ba man a jànkoonte jamono ju xeex bi taree, noot lépp te taxaw temm.
14ܩܘܡܘ ܗܟܝܠ ܘܚܙܘܩܘ ܚܨܝܟܘܢ ܒܩܘܫܬܐ ܘܠܒܫܘ ܫܪܝܢܐ ܕܙܕܝܩܘܬܐ ܀
14 Taxawleen kon temm, geñoo dëgg te sàngoo njub, muy seen kiiraayu dënn.
15ܘܤܐܢܘ ܒܪܓܠܝܟܘܢ ܛܘܝܒܗ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܫܠܡܐ ܀
15 Solooleen jàmm, ji xebaar bu baax biy joxe, ni ay dàll ci seeni tànk, ba jekk ci lépp.
16ܘܥܡ ܗܠܝܢ ܤܒܘ ܠܟܘܢ ܤܟܪܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܕܒܗ ܬܬܡܨܘܢ ܚܝܠܐ ܠܡܕܥܟܘ ܟܠܗܘܢ ܓܐܪܘܗܝ ܝܩܕܐ ܕܒܝܫܐ ܀
16 Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba man a fél jum yi leen Seytaane di fitt.
17ܘܤܝܡܘ ܤܢܘܪܬܐ ܕܦܘܪܩܢܐ ܘܐܚܘܕܘ ܤܝܦܐ ܕܪܘܚܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
17 Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak kàddug Yàlla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi tëggal.
18ܘܒܟܠ ܨܠܘܢ ܘܒܟܠ ܒܥܘܢ ܨܠܘ ܒܟܠܙܒܢ ܒܪܘܚ ܘܒܗ ܒܨܠܘܬܐ ܗܘܝܬܘܢ ܫܗܪܝܢ ܒܟܠܥܕܢ ܟܕ ܡܨܠܝܬܘܢ ܐܡܝܢܐܝܬ ܘܡܬܟܫܦܝܢ ܥܠ ܐܦܝ ܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܀
18 Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk, di ñaanal gaayi Yàlla yu sell yi yépp.
19ܐܦ ܥܠܝ ܕܬܬܝܗܒ ܠܝ ܡܠܬܐ ܒܡܦܬܚ ܦܘܡܝ ܕܥܝܢ ܒܓܠܐ ܐܟܪܙ ܐܪܙܐ ܕܤܒܪܬܐ ܀
19 Te buleen ma ci fàtte, ngir waxtu wu ma ubbee sama gémmiñ, ma am lu ma wax, ba man a xamle ak fit wu dëgër mbóoti xebaar bu baax bi.
20ܗܘ ܕܐܢܐ ܐܝܙܓܕܗ ܒܫܫܠܬܐ ܕܒܦܪܗܤܝܐ ܐܡܠܠܝܘܗܝ ܐܝܟ ܕܘܠܐ ܠܝ ܠܡܡܠܠܘܬܗ ܀
20 Ndaw laa ci, lu ñu jéng; na ma Yàlla may fit wu ma waxe, ni mu ma ware.
21ܕܬܕܥܘܢ ܕܝܢ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܡܕܡ ܕܠܘܬܝ ܘܡܕܡ ܕܤܥܪ ܐܢܐ ܗܐ ܡܘܕܥ ܠܟܘܢ ܛܘܟܝܩܘܤ ܐܚܐ ܚܒܝܒܐ ܘܡܫܡܫܢܐ ܡܗܝܡܢܐ ܒܡܪܢ ܀
21 Yónnee naa leen Tisig sama mbokk, mi ma sopp, te muy jawriñ ju takku ci liggéeyu Boroom bi, ngir mu xamal leen lépp li aju ci man ak li may def.
22ܕܠܗ ܫܕܪܬ ܠܘܬܟܘܢ ܥܠܝܗ ܥܠ ܗܕܐ ܕܬܕܥܘܢ ܡܐ ܕܠܘܬܝ ܘܢܒܝܐ ܠܒܘܬܟܘܢ ܀
22 Maa leen ko yónneel sama bopp, ngir ngeen xam li nu nekke, te mu dëfël seeni xol.
23ܫܠܡܐ ܥܡ ܐܚܝܢ ܘܚܘܒܐ ܥܡ ܗܝܡܢܘܬܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܒܐ ܘܡܢ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
23 Yéen bokk yi, na leen Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist Boroom bi may jàmm ak mbëggeel gu ànd ak ngëm.
24ܛܝܒܘܬܐ ܥܡ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܚܒܝܢ ܠܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܠܐ ܚܒܠ ܐܡܝܢ ܀
24 Na yiwu Yàlla ànd ak ñépp, ñi bëgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mbëggeel gu sax.