Syriac: NT

Wolof: New Testament

Philippians

1

1ܦܘܠܘܤ ܘܛܝܡܬܐܘܤ ܥܒܕܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܕܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܐܝܬ ܒܦܝܠܝܦܘܤ ܥܡ ܩܫܝܫܐ ܘܡܫܡܫܢܐ ܀
1 Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.
2ܛܝܒܘܬܐ ܥܡܟܘܢ ܘܫܠܡܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܒܘܢ ܘܡܢ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
3ܡܘܕܐ ܐܢܐ ܠܐܠܗܝ ܥܠ ܥܘܗܕܢܟܘܢ ܐܡܝܢܐ ܀
3 Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom;
4ܕܒܟܠ ܒܥܘܬܝ ܕܥܠ ܐܦܝܟܘܢ ܘܟܕ ܚܕܐ ܐܢܐ ܡܬܟܫܦ ܐܢܐ ܀
4 te saa su ma leen di ñaanal yéen yépp, duma noppee bég,
5ܥܠ ܫܘܬܦܘܬܟܘܢ ܕܒܐܘܢܓܠܝܘܢ ܡܢ ܝܘܡܐ ܩܕܡܝܐ ܘܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܀
5 ndax seen ànd ak man ci tas xebaar bu baax bi, ca ndoorte la ba tey.
6ܡܛܠ ܕܬܟܝܠ ܐܢܐ ܥܠ ܗܕܐ ܕܗܘ ܡܢ ܕܫܪܝ ܒܟܘܢ ܥܒܕܐ ܛܒܐ ܗܘ ܢܫܠܡ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
6 Wóor na ma ne, Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw.
7ܗܟܢܐ ܓܝܪ ܙܕܩ ܠܝ ܠܡܬܪܥܝܘ ܥܠ ܟܠܟܘܢ ܡܛܠ ܕܒܠܒܝ ܤܝܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܒܐܤܘܪܝ ܘܒܡܦܩ ܒܪܘܚܝ ܕܥܠ ܫܪܪܗ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܫܘܬܦܝ ܐܢܬܘܢ ܒܛܝܒܘܬܐ ܀
7 Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xebaar bu baax bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla.
8ܤܗܕ ܗܘ ܠܝ ܓܝܪ ܐܠܗܐ ܕܐܝܟܢܐ ܡܚܒ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܒܪܚܡܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
8 Ndaxte Yàllaa seede ne, sama xol seey na ci yéen ñépp ci biir cofeelu Kirist Yeesu.
9ܘܗܕܐ ܡܨܠܐ ܐܢܐ ܕܬܘܒ ܢܤܓܐ ܘܢܬܝܬܪ ܚܘܒܟܘܢ ܒܝܕܥܬܐ ܘܒܟܠ ܤܘܟܠ ܕܪܘܚ ܀
9 Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: na seen mbëggeel di yokku tey gën a tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér;
10ܕܬܗܘܘܢ ܦܪܫܝܢ ܐܝܠܝܢ ܕܥܗܢܢ ܘܬܗܘܘܢ ܕܟܝܢ ܕܠܐ ܬܘܩܠܐ ܒܝܘܡܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
10 nangeen sax noonu ci yi gën a rafet, ngeen am xol bu laab te bañ a am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw;
11ܘܡܠܝܢ ܦܐܪܐ ܕܙܕܝܩܘܬܐ ܕܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܫܘܒܚܐ ܘܠܐܝܩܪܐ ܕܐܠܗܐ ܀
11 na seen xol meññ njub, ba ne gàññ, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Yàlla ak cantam.
12ܨܒܐ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܬܕܥܘܢ ܐܚܝ ܕܤܘܥܪܢܝ ܕܝܠܝ ܝܬܝܪܐܝܬ ܐܬܐ ܠܩܕܡܘܗܝ ܒܐܘܢܓܠܝܘܢ ܀
12 Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xebaar bu baax dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam.
13ܗܟܢܐ ܕܐܦ ܐܤܘܪܝ ܐܬܓܠܝܘ ܒܡܫܝܚܐ ܒܦܪܛܘܪܝܢ ܟܠܗ ܘܠܫܪܟܐ ܕܟܠܢܫ ܀
13 Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne, turu Kirist rekk a tax ñu jàpp ma.
14ܘܤܘܓܐܐ ܕܐܚܐ ܕܒܡܪܢ ܐܬܬܟܠܘ ܥܠ ܐܤܘܪܝ ܘܐܫܝܚܘ ܝܬܝܪܐܝܬ ܕܠܐ ܕܚܠܐ ܠܡܡܠܠܘ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
14 Te it bokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gën a ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit.
15ܘܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢ ܚܤܡܐ ܘܚܪܝܢܐ ܐܢܫ ܐܢܫ ܕܝܢ ܒܨܒܝܢܐ ܛܒܐ ܘܒܚܘܒܐ ܠܡܫܝܚܐ ܡܟܪܙܝܢ ܀
15 Am na ñuy waare ci turu Kirist ci kaw kiñaan ak xëccoo, waaye ñi ci des ci kaw cofeel ak xol bu laab, ndaxte xam nañu ne, Yàlla moo ma teg fii, ngir ma taxawal xebaar bu baax bi.
16ܡܛܠ ܕܝܕܥܝܢ ܕܠܡܦܩ ܒܪܘܚܐ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܤܝܡ ܐܢܐ ܀
17 Waaye ñale amuñu xol bu laab, te seen njariñu bopp rekk a tax ñuy yégle turu Kirist, di wut a feddali samay buum ak coono.
17ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܕܒܚܪܝܢܐ ܠܡܫܝܚܐ ܡܟܪܙܝܢ ܠܐ ܗܘܐ ܕܟܝܐܝܬ ܐܠܐ ܕܤܒܪܝܢ ܕܡܘܤܦܝܢ ܐܘܠܨܢܐ ܠܐܤܘܪܝ ܀
18 Lu ci génn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaféq, muy ci dëgg; bég naa ci te dinaa ci bégati.
18ܘܒܗܕܐ ܚܕܝܬ ܘܚܕܐ ܐܢܐ ܕܒܟܠ ܦܪܘܤ ܐܢ ܒܥܠܬܐ ܘܐܢ ܒܩܘܫܬܐ ܡܫܝܚܐ ܢܬܟܪܙ ܀
19 Ndaxte xam naa ne, loolu lépp mu ngi jëm ci sama mucc, jaar ci seeni ñaan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Yàllay yéwénal.
19ܝܕܥ ܐܢܐ ܓܝܪ ܕܗܠܝܢ ܠܚܝܐ ܡܫܬܟܚܢ ܠܝ ܒܒܥܘܬܟܘܢ ܘܒܡܘܗܒܬܐ ܕܪܘܚܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
20 Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma bañ a rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey.
20ܐܝܟܢܐ ܕܡܤܒܪ ܐܢܐ ܘܡܤܟܐ ܐܢܐ ܕܒܡܕܡ ܠܐ ܐܒܗܬ ܐܠܐ ܒܓܠܝܘܬ ܐܦܐ ܐܝܟ ܕܒܟܠܙܒܢ ܐܦ ܗܫܐ ܢܬܪܘܪܒ ܡܫܝܚܐ ܒܦܓܪܝ ܐܢ ܒܚܝܐ ܘܐܢ ܒܡܘܬܐ ܀
21 Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee, te su ma deeyee, xéewal lay doon ci man.
21ܚܝܝ ܓܝܪ ܕܝܠܝ ܡܫܝܚܐ ܗܘ ܘܐܢ ܐܡܘܬ ܝܘܬܪܢܐ ܗܘ ܠܝ ܀
22 Su ma Yàlla bàyyee ci àddina, sas wu am njariñ la ci man. Am naa xel ñaar, te xawma bi ci gën. Am naa yéeney jóge fi, fekki Kirist, te looloo gën fuuf,
22ܐܢ ܕܝܢ ܐܦ ܒܗܠܝܢ ܚܝܐ ܕܒܤܪܐ ܦܐܪܐ ܐܝܬ ܠܝ ܒܥܒܕܝ ܠܐ ܝܕܥ ܐܢܐ ܡܢܐ ܐܓܒܐ ܠܝ ܀
24 waaye ma des fi ci àddina moo gën ci yéen.
23ܐܠܨܢ ܠܝ ܓܝܪ ܬܪܬܝܗܝܢ ܠܡܦܛܪ ܪܓܝܓ ܐܢܐ ܕܥܡ ܡܫܝܚܐ ܐܗܘܐ ܘܗܕܐ ܛܒ ܦܩܚܐ ܗܘܬ ܠܝ ܀
25 Loolu wóor na ma; kon xam naa ne, dinaa fi des, di leen taxawu yéen ñépp, ngir seen ngëm yokku, ànd ak mbég.
24ܐܠܐ ܐܦ ܕܐܩܘܐ ܒܦܓܪܝ ܐܠܨܐ ܠܝ ܨܒܘܬܐ ܡܛܠܬܟܘܢ ܀
26 Noonu dinaa dellusi ci yéen, ngir sama taxawaay gën a lawal seen mbég ci Kirist Yeesu.
25ܘܗܕܐ ܬܟܝܠܐܝܬ ܝܕܥ ܐܢܐ ܕܦܐܫ ܐܢܐ ܘܡܩܘܐ ܐܢܐ ܠܚܕܘܬܐ ܕܝܠܟܘܢ ܘܠܬܪܒܝܬܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܀
27 Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xebaar bu baax bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xebaar bu baax bi,
26ܕܟܕ ܐܬܐ ܬܘܒ ܠܘܬܟܘܢ ܢܬܝܬܪ ܒܝ ܫܘܒܗܪܟܘܢ ܕܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܠܚܘܕ ܀
28 te bañ a tiit dara ndax noon, yi leen di xëbal. Màndarga la muy wone ne aji sànku lañu, di màndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu jóge ci Yàlla.
27ܐܝܟܢܐ ܕܝܐܐ ܠܤܒܪܬܗ ܕܡܫܝܚܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܬܕܒܪܝܢ ܕܐܢ ܐܬܐ ܐܚܙܝܟܘܢ ܘܐܢ ܦܪܝܩ ܐܢܐ ܐܫܡܥ ܥܠܝܟܘܢ ܕܩܝܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܚܕܐ ܪܘܚ ܘܒܚܕܐ ܢܦܫ ܘܡܬܢܨܚܝܬܘܢ ܐܟܚܕ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܀
29 Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,
28ܘܒܡܕܡ ܠܐ ܡܬܬܙܝܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܢ ܗܢܘܢ ܕܩܝܡܝܢ ܠܩܘܒܠܢ ܠܬܚܘܝܬܐ ܕܐܒܕܢܗܘܢ ܘܠܚܝܐ ܕܝܠܟܘܢ ܀
30 di wéy ci bëre, bi ngeen gisoon ci man, te dégg léegi sama mbir.
29ܘܗܕܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܗܘ ܐܬܝܗܒܬ ܠܟܘܢ ܕܠܐ ܒܠܚܘܕ ܡܗܝܡܢܘ ܬܗܝܡܢܘܢ ܒܗ ܒܡܫܝܚܐ ܐܠܐ ܐܦ ܕܥܠ ܐܦܘܗܝ ܬܚܫܘܢ ܀
30ܘܬܤܝܒܪܘܢ ܐܓܘܢܐ ܐܝܟ ܗܘ ܕܚܙܝܬܘܢ ܒܝ ܘܗܫܐ ܫܡܥܝܬܘܢ ܥܠܝ ܀