Syriac: NT

Wolof: New Testament

Galatians

3

1ܐܘ ܚܤܝܪܝ ܪܥܝܢܐ ܓܠܛܝܐ ܡܢܘ ܚܤܡ ܒܟܘܢ ܕܗܐ ܐܝܟ ܗܘ ܕܡܨܪ ܨܝܪ ܗܘܐ ܩܕܡ ܥܝܢܝܟܘܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܟܕ ܨܠܝܒ ܀
1 Yéen waa Galasi, yéena ñàkk xel! Ku leen fàbbi, gannaaw bi ma leen yégalee ci lu leer ni ñu daaje Yeesu Kirist ca bant ba?
2ܗܕܐ ܒܠܚܘܕ ܨܒܐ ܐܢܐ ܕܐܕܥ ܡܢܟܘܢ ܡܢ ܥܒܕܐ ܕܢܡܘܤܐ ܢܤܒܬܘܢ ܪܘܚܐ ܐܘ ܡܢ ܫܡܥܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܀
2 Lenn rekk laa bëgg, ngeen wax ma ko: ndax sàmm yoon wee tax, ngeen jot Xelum Yàlla? Déedéet! Dangeen a dégg xebaar bu baax bi te gëm ko.
3ܗܟܢܐ ܤܟܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܫܪܝܬܘܢ ܒܪܘܚܐ ܘܗܫܐ ܒܒܤܪ ܡܫܠܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
3 Mbaa du nii ngeen ñàkke xel, ba tàmbalee ci Xelum Yàlla, ba noppi yaakaar a mate ci seen jëfi bopp?
4ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܐܝܩܐ ܤܝܒܪܬܘܢ ܘܐܫܬܘܦ ܕܝܢ ܐܝܩܐ ܀
4 Mbaa du fitna, yi ngeen daj yépp, dafa nar a neen? Mënuma koo gëm!
5ܗܘ ܗܟܝܠ ܕܝܗܒ ܒܟܘܢ ܪܘܚܐ ܘܤܥܪ ܒܟܘܢ ܚܝܠܐ ܡܢ ܥܒܕܐ ܕܢܡܘܤܐ ܐܘ ܡܢ ܫܡܥܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܀
5 Bu leen Yàlla di may Xelam, di leen won jalooreem, ndax li ngeen sàmm yoon a tax, mu def ko, mbaa li ngeen dégg xebaar bu baax te gëm ko?
6ܐܝܟܢܐ ܕܗܝܡܢ ܐܒܪܗܡ ܠܐܠܗܐ ܘܐܬܚܫܒܬ ܠܗ ܠܙܕܝܩܘ ܀
6 Xool-leen ci Ibraayma; Mbind mi wax na ne:«Ibraayma gëm na Yàlla,te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
7ܕܥܘ ܗܟܝܠ ܕܐܝܠܝܢ ܕܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܐܢܘܢ ܗܢܘܢ ܐܢܘܢ ܒܢܝܐ ܕܐܒܪܗܡ ܀
7 Xamleen boog ne, boroom ngëm yi rekk ñooy doomi Ibraayma.
8ܡܛܠ ܓܝܪ ܕܩܕܡ ܝܕܥ ܐܠܗܐ ܕܒܗܝܡܢܘܬܐ ܗܘ ܡܙܕܕܩܝܢ ܥܡܡܐ ܩܕܡ ܤܒܪ ܠܐܒܪܗܡ ܐܝܟ ܕܐܡܪ ܟܬܒܐ ܩܕܝܫܐ ܕܒܟ ܢܬܒܪܟܘܢ ܟܠܗܘܢ ܥܡܡܐ ܀
8 Mbind mi tëral na lu jiitu ne, Yàlla dina àtte jub ñi dul Yawut ci kaw ngëm. Kon looloo tax mu yégal Ibraayma lu jiitu xebaar bu baax bi ne ko: «Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci yaw.»
9ܡܕܝܢ ܡܗܝܡܢܐ ܗܘ ܡܬܒܪܟܝܢ ܒܐܒܪܗܡ ܡܗܝܡܢܐ ܀
9 Kon ñi gëm, Yàlla dina leen barkeel, sukkandikoo ko ci seen ngëm, ni mu defal Ibraayma, boroom ngëm.
10ܐܝܠܝܢ ܓܝܪ ܕܡܢ ܥܒܕܐ ܐܢܘܢ ܕܢܡܘܤܐ ܬܚܝܬ ܠܘܛܬܐ ܐܢܘܢ ܟܬܝܒ ܓܝܪ ܕܠܝܛ ܗܘ ܟܠܡܢ ܕܠܐ ܢܥܒܕ ܟܠ ܕܟܬܝܒ ܒܢܡܘܤܐ ܗܢܐ ܀
10 Ñiy wékku ñépp ci jëfi yoon wi, ñu alku lañu, ndaxte bind nañu ne: «Képp ku dul topp lépp lu ndigali yoon wi santaane, Yal na alku.»
11ܕܠܐ ܕܝܢ ܡܙܕܕܩ ܐܢܫ ܒܢܡܘܤܐ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܗܕܐ ܓܠܝܐ ܗܝ ܡܛܠ ܕܟܬܝܒ ܕܙܕܝܩܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܢܚܐ ܀
11 Bir na sax ne, sàmm yoon du tax kenn jub fa kanam Yàlla, ndaxte Mbind mi tëral na ne: «Ku jub ci kaw ngëm dinga dund.»
12ܢܡܘܤܐ ܕܝܢ ܠܐ ܗܘܐ ܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܐܠܐ ܡܢ ܕܢܥܒܕ ܐܝܠܝܢ ܕܟܬܝܒܢ ܒܗ ܢܚܐ ܒܗܝܢ ܀
12 Waaye yoon wi laajul ngëm. Mbind mi nee na: «Ku manoon a matal li yoon wi wax, kon dinga dund ba fàww.»
13ܠܢ ܕܝܢ ܡܫܝܚܐ ܙܒܢܢ ܡܢ ܠܘܛܬܐ ܕܢܡܘܤܐ ܘܗܘ ܗܘܐ ܚܠܦܝܢ ܠܘܛܬܐ ܟܬܝܒ ܓܝܪ ܕܠܝܛ ܗܘ ܟܠܡܢ ܕܡܬܬܠܐ ܒܩܝܤܐ ܀
13 Waaye Kirist jot na nu ci alkande, ji yoon wi indi; mu gàddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na: «Képp ku ñu rey, wékk ko ci bant, alku nga.»
14ܕܒܥܡܡܐ ܬܗܘܐ ܒܘܪܟܬܗ ܕܐܒܪܗܡ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܚܢܢ ܢܤܒ ܫܘܘܕܝܐ ܕܪܘܚܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܀
14 Noonu barke bi Yàlla dig Ibraayma baawaan na, ba daj ñi dul Yawut te gëm Kirist Yeesu, te nu jot ci kaw ngëm Xel mu Sell, mi Yàlla dige.
15ܐܚܝ ܐܝܟ ܕܒܝܬ ܒܢܝܢܫܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܕܝܬܩܐ ܕܒܪܢܫܐ ܕܐܫܬܪܪܬ ܐܢܫ ܠܐ ܡܤܠܐ ܐܘ ܡܫܚܠܦ ܒܗ ܡܕܡ ܀
15 Bokk yi, maa ngi misaal wax ji ci jëfi doom Aadama. Xam ngeen ne, kóllëre gu ñu fas ba noppi, waruñu koo fecci, walla ñu ciy rax dara.
16ܠܐܒܪܗܡ ܕܝܢ ܐܬܡܠܟ ܡܘܠܟܢܐ ܘܠܙܪܥܗ ܘܠܐ ܐܡܪ ܠܗ ܕܠܙܪܥܝܟ ܐܝܟ ܕܠܤܓܝܐܐ ܐܠܐ ܠܙܪܥܟ ܐܝܟ ܕܠܚܕ ܗܘ ܕܐܝܬܘܗܝ ܡܫܝܚܐ ܀
16 Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam,» mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan,» maanaam Kirist.
17ܗܕܐ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܕܝܬܩܐ ܕܡܢ ܩܕܝܡ ܐܫܬܪܪܬ ܡܢ ܐܠܗܐ ܒܡܫܝܚܐ ܢܡܘܤܐ ܗܘ ܕܗܘܐ ܡܢ ܒܬܪ ܐܪܒܥ ܡܐܐ ܘܬܠܬܝܢ ܫܢܝܢ ܠܐ ܡܫܟܚ ܕܢܤܠܝܗ ܘܢܒܛܠ ܡܘܠܟܢܐ ܀
17 Li ma ci bëgg a wax mooy lii: ndegam Yàlla fas na kóllëreem, yoonu Musaa, wi feeñ ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw ga, du ko man a fecci, ba tebbi digeb Yàlla.
18ܐܢ ܕܝܢ ܡܢ ܢܡܘܤܐ ܗܝ ܝܪܬܘܬܐ ܡܟܝܠ ܠܐ ܗܘܬ ܡܢ ܡܘܠܟܢܐ ܠܐܒܪܗܡ ܕܝܢ ܒܡܘܠܟܢܐ ܗܘ ܝܗܒ ܠܗ ܐܠܗܐ ܀
18 Ndaxte xéewal, yi Yàllay dige, bu ñu doon jóge ci yoon wi, kon ajootuñu ci dige bi, fekk ci kaw dige la ko Yàlla maye Ibraayma.
19ܡܢܐ ܗܟܝܠ ܢܡܘܤܐ ܡܛܠ ܡܤܛܝܢܘܬܐ ܐܬܬܘܤܦ ܥܕܡܐ ܕܢܐܬܐ ܙܪܥܐ ܗܘ ܕܠܗ ܗܘܐ ܫܘܘܕܝܐ ܘܐܬܝܗܒ ܗܘ ܢܡܘܤܐ ܒܝܕ ܡܠܐܟܐ ܒܐܝܕܐ ܕܡܨܥܝܐ ܀
19 Waaw kon yoonu Musaa, luy jariñam? Dañu koo wàcceel nit ñi, ngir seen jàdd yoon ne fàŋŋ. Looloo doon wàllu yoon wi, ba kera Sët biy ñëw, moom mi ñu digoon dige bi. Yoon wi nag, Yàlla tëral na ko jaare ci ay malaaka, te am na ku ko jottali.
20ܡܨܥܝܐ ܕܝܢ ܠܐ ܗܘܐ ܕܚܕ ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܚܕ ܗܘ ܀
20 Waaye aajowul jottalikat, su fi kenn rekk teewee, te Yàlla kenn la.
21ܢܡܘܤܐ ܗܟܝܠ ܤܩܘܒܠܐ ܗܘ ܕܡܘܠܟܢܐ ܕܐܠܗܐ ܚܤ ܐܠܘ ܓܝܪ ܐܬܝܗܒ ܗܘܐ ܢܡܘܤܐ ܐܝܢܐ ܕܡܫܟܚ ܗܘܐ ܠܡܚܝܘ ܫܪܝܪܐܝܬ ܡܢ ܢܡܘܤܐ ܗܘܝܐ ܗܘܬ ܙܕܝܩܘܬܐ ܀
21 Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Yàlla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit man a sàmm, ba mu jural ko dund gu sax, kon sàmm yoon dina tax nit jub fa kanam Yàlla.
22ܐܠܐ ܚܒܫ ܟܬܒܐ ܟܠܡܕܡ ܬܚܝܬ ܚܛܝܬܐ ܕܡܘܠܟܢܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܢܬܝܗܒ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܗܝܡܢܝܢ ܀
22 Waaye yoon wi tëj na ñépp ci dooley bàkkaar, ngir ñi gëm Yeesu Kirist jot li Yàlla dige woon ci seen kaw ngëm.
23ܥܕܠܐ ܕܝܢ ܬܐܬܐ ܗܝܡܢܘܬܐ ܢܡܘܤܐ ܢܛܪ ܗܘܐ ܠܢ ܟܕ ܚܒܝܫܝܢܢ ܠܗܝܡܢܘܬܐ ܕܥܬܝܕܐ ܗܘܬ ܠܡܬܓܠܝܘ ܀
23 Bi ngëm Yeesu Kirist feeñagul nag, yoon wi da noo tëjoon ràpp, ba kera ngëm di feeñ.
24ܢܡܘܤܐ ܗܟܝܠ ܬܪܐܐ ܗܘܐ ܠܢ ܠܘܬ ܡܫܝܚܐ ܕܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܢܙܕܕܩ ܀
24 Ci noonu la nu yoon wi doon noote, ba Kirist di ñëw, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw ngëm.
25ܟܕ ܐܬܬ ܕܝܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܠܐ ܗܘܝܢ ܬܚܝܬ ܬܪܐܐ ܀
25 Waaye léegi, bi jamonoy ngëm ji ñëwee, nekkatunu ci kilifteefu yoon wi.
26ܟܠܟܘܢ ܓܝܪ ܒܢܝܐ ܐܢܬܘܢ ܕܐܠܗܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
26 Yéen ñépp doomi Yàlla ngeen ndax li ngeen bokk ci Kirist Yeesu ci kaw ngëm.
27ܐܝܠܝܢ ܓܝܪ ܕܒܡܫܝܚܐ ܥܡܕܬܘܢ ܠܡܫܝܚܐ ܠܒܫܬܘܢ ܀
27 Yéen ñépp, ñi ñu sóob ci ndox ngir wone seen bokk ci Kirist, soloo ngeen Kirist.
28ܠܝܬ ܝܗܘܕܝܐ ܘܠܐ ܐܪܡܝܐ ܠܝܬ ܥܒܕܐ ܘܠܐ ܒܪ ܚܐܪܐ ܠܝܬ ܕܟܪܐ ܘܠܐ ܢܩܒܬܐ ܟܠܟܘܢ ܓܝܪ ܚܕ ܐܢܬܘܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
28 Kon nag amul xaajale ci diggante Yawut ak ki dul Yawut, ci diggante jaam ak gor, ci diggante góor ak jigéen. Yéen ñépp benn ngeen ci seen bokk ci Kirist.
29ܘܐܢ ܕܡܫܝܚܐ ܐܢܬܘܢ ܡܟܝܠ ܙܪܥܗ ܐܢܬܘܢ ܕܐܒܪܗܡ ܘܝܪܬܐ ܒܡܘܠܟܢܐ ܀
29 Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma, te jot ngeen xéewal, yi ko Yàlla dig.