1ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܟܡܐ ܙܒܢܐ ܕܝܪܬܐ ܛܠܐ ܠܐ ܦܪܝܫ ܡܢ ܥܒܕܐ ܟܕ ܡܪܐ ܗܘ ܕܟܠܗܘܢ ܀
1 Li ma leen di wax, mooy lii: doom ji war a donni baayam, fi ak mu ngi cig ndaw, ak lu ko alal jiy lew lépp, du wuute dara ak jaam.
2ܐܠܐ ܬܚܝܬ ܐܦܛܪܘܦܐ ܐܝܬܘܗܝ ܘܪܒܝ ܒܬܐ ܥܕܡܐ ܠܙܒܢܐ ܕܤܡ ܐܒܘܗܝ ܀
2 Ñi ko yore tey sàmm alalam ñoo koy yilif, ba jamono ji ko baayam àppaloon mat.
3ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܢܢ ܟܕ ܝܠܘܕܐ ܗܘܝܢ ܬܚܝܬ ܐܤܛܘܟܤܘܗܝ ܕܥܠܡܐ ܡܫܥܒܕܝܢ ܗܘܝܢ ܀
3 Nun itam naka noonu, laata nuy mat, aaday àddina ñoo nu nootoon, ba def nu ni ay jaam.
4ܟܕ ܡܛܐ ܕܝܢ ܫܘܠܡܗ ܕܙܒܢܐ ܫܕܪ ܐܠܗܐ ܠܒܪܗ ܘܗܘܐ ܡܢ ܐܢܬܬܐ ܘܗܘܐ ܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܀
4 Waaye bi àpp bi Yàlla tëraloon matee, yónni na Doomam, mu juddoo ci jigéen, ci biir yoonu Musaa,
5ܕܠܐܝܠܝܢ ܕܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܐܢܘܢ ܢܙܒܢ ܘܢܩܒܠ ܤܝܡܬ ܒܢܝܐ ܀
5 ngir jot ñi yoon wi nootoon, ndax Yàlla jàpp nu ni ay doomam.
6ܘܕܐܝܬܝܟܘܢ ܕܝܢ ܒܢܝܐ ܫܕܪ ܐܠܗܐ ܪܘܚܐ ܕܒܪܗ ܠܠܒܘܬܟܘܢ ܗܝ ܕܩܪܝܐ ܐܒܐ ܐܒܘܢ ܀
6 Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba,» maanaam «Baay.»
7ܡܟܝܠ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܥܒܕܐ ܐܠܐ ܒܢܝܐ ܘܐܢ ܒܢܝܐ ܐܦ ܝܪܬܐ ܕܐܠܗܐ ܒܝܕ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
7 Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Yàlla jagleel na la cér ci xéewal, yi mu dencal ay doomam.
8ܗܝܕܝܢ ܓܝܪ ܟܕ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܠܐܠܗܐ ܦܠܚܬܘܢ ܠܗܢܘܢ ܕܡܢ ܟܝܢܗܘܢ ܠܐ ܗܘܘ ܐܠܗܐ ܀
8 Bu jëkk, bi ngeen xamagul Yàlla, yéena ngi doon jaamu yeneen yu ñu daan bokkaaleel Yàlla.
9ܗܫܐ ܕܝܢ ܕܝܕܥܬܘܢ ܠܐܠܗܐ ܘܝܬܝܪܐܝܬ ܕܐܬܝܕܥܬܘܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܬܘܒ ܗܦܟܬܘܢ ܠܟܘܢ ܥܠ ܗܢܘܢ ܐܤܛܘܟܤܐ ܡܪܥܐ ܘܡܤܟܢܐ ܘܡܢ ܕܪܝܫ ܨܒܝܬܘܢ ܠܡܫܬܥܒܕܘ ܠܗܘܢ ܀
9 Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen man a def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu nootaat leen?
10ܝܘܡܐ ܘܝܪܚܐ ܘܙܒܢܐ ܘܫܢܝܐ ܢܛܪܝܬܘܢ ܀
10 Yéena ngi fonk bés yi, weer yi, màggal yi ak at yi!
11ܕܚܠ ܐܢܐ ܕܠܡܐ ܤܪܝܩܐܝܬ ܠܐܝܬ ܒܟܘܢ ܀
11 Sama xel dalul ci yéen, ngir ragal sama coono ci yéen neen.
12ܗܘܘ ܐܟܘܬܝ ܡܛܠ ܕܐܦ ܐܢܐ ܐܟܘܬܟܘܢ ܗܘܝܬ ܐܚܝ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟܘܢ ܠܐ ܡܕܡ ܐܤܟܠܬܘܢ ܒܝ ܀
12 Bokk yi, dama leen di ñaan, ngeen mel ni man, ndaxte man itam fekksi naa leen ci seen xalaat. Tooñuleen ma.
13ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܓܝܪ ܕܒܟܪܝܗܘܬ ܒܤܪܝ ܤܒܪܬܟܘܢ ܗܘܝܬ ܡܢ ܩܕܝܡ ܀
13 Xam ngeen ne, sama wopp moo taxoon, ma yégal leen xebaar bu baax bi.
14ܘܢܤܝܘܢܐ ܕܒܤܪܝ ܠܐ ܫܛܬܘܢ ܘܠܐ ܢܕܬܘܢ ܐܠܐ ܐܝܟ ܕܠܡܠܐܟܐ ܕܐܠܗܐ ܩܒܠܬܘܢܢܝ ܘܐܝܟ ܕܠܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
14 Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen bañ ma, taxul ngeen séexlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Yàlla walla Yeesu Kirist.
15ܐܝܟܘ ܗܟܝܠ ܛܘܒܟܘܢ ܤܗܕ ܐܢܐ ܓܝܪ ܥܠܝܟܘܢ ܕܐܠܘ ܡܫܟܚܐ ܗܘܬ ܥܝܢܝܟܘܢ ܚܨܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܘܝܗܒܝܢ ܠܝ ܀
15 Waaw, fan la seen mbég jaar? Ndaxte seedeel naa leen ne, su ngeen ko manoon, kon luqi ngeen seeni bët, jox ma.
16ܕܠܡܐ ܒܥܠܕܒܒܐ ܗܘܝܬ ܠܟܘܢ ܕܐܟܪܙܬ ܠܟܘܢ ܫܪܪܐ ܀
16 Ndax dëgg, gi ma leen wax, moo tax ngeen def ma ab noon?
17ܚܤܡܝܢ ܒܟܘܢ ܠܐ ܗܘܐ ܠܫܦܝܪܬܐ ܐܠܐ ܠܡܚܒܫܟܘܢ ܗܘ ܨܒܝܢ ܕܐܢܬܘܢ ܬܗܘܘܢ ܚܤܡܝܢ ܒܗܘܢ ܀
17 Nit ñooñu leen di farle, seen mébét baaxul. Dañu leen a bëgg a tàggale ak nun, ngir ngeen far ak ñoom.
18ܫܦܝܪ ܗܘ ܕܝܢ ܕܬܬܚܤܡܘܢ ܒܫܦܝܪܬܐ ܒܟܠܙܒܢ ܘܠܐ ܐܡܬܝ ܕܠܘܬܟܘܢ ܐܢܐ ܒܠܚܘܕ ܀
18 Farle baax na, bu àndee ak mébét mu baax. Waaye bu sama jëmm rekk tax ngeen koy def.
19ܒܢܝ ܐܝܠܝܢ ܕܡܢ ܕܪܝܫ ܡܚܒܠ ܐܢܐ ܥܕܡܐ ܕܢܬܬܨܝܪ ܒܟܘܢ ܡܫܝܚܐ ܀
19 Sama doom yi! Yéena tax may dellu ci metit ni kuy matu, ba kera jikkoy Kirist di mat ci yéen.
20ܨܒܐ ܗܘܝܬ ܕܝܢ ܕܐܗܘܐ ܠܘܬܟܘܢ ܗܫܐ ܘܐܫܚܠܦ ܒܪܬ ܩܠܝ ܡܛܠ ܕܬܡܝܗ ܐܢܐ ܒܟܘܢ ܀
20 Léegi bëggoon naa nekk ci seen biir, ngir man a jubbanti sama kàddu, ndaxte xamatuma nu may doxale ak yéen!
21ܐܡܪܘ ܠܝ ܐܢܬܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܨܒܝܢ ܕܢܗܘܘܢ ܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܠܗ ܠܢܡܘܤܐ ܠܐ ܫܡܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
21 Yéen ñi bëgg a topp yoon wi, xanaa xamuleen li yoonu Musaa wi wax?
22ܟܬܝܒ ܓܝܪ ܕܠܐܒܪܗܡ ܬܪܝܢ ܒܢܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܚܕ ܡܢ ܐܡܬܐ ܘܚܕ ܡܢ ܚܐܪܬܐ ܀
22 Mbind mi nee na: Ibraayma am na ñaari doom; ki jaam bi jur ak ki gor si jur.
23ܐܠܐ ܗܘ ܕܡܢ ܐܡܬܐ ܒܒܤܪ ܐܬܝܠܕ ܗܘ ܕܝܢ ܕܡܢ ܚܐܪܬܐ ܒܡܘܠܟܢܐ ܗܘܐ ܀
23 Doomu jaam bi juddu na ni bépp doom, waaye doom, ji mu am ak jabaram, juddu na ci kaw digeb Yàlla.
24ܗܠܝܢ ܕܝܢ ܐܝܬܝܗܝܢ ܦܠܐܬܐ ܕܬܪܬܝܢ ܕܝܬܩܤ ܚܕܐ ܕܡܢ ܛܘܪ ܤܝܢܝ ܝܠܕܐ ܠܥܒܕܘܬܐ ܕܐܝܬܝܗ ܗܓܪ ܀
24 Loolu nag am na lu muy misaal. Ñaari jigéen ñi dañoo bijji ñaari kóllëre. Benn bi di Ajara, mooy wone kóllëre, gi Yàlla fasoon ca tundu Sinayi. Ay jaam lay jur.
25ܗܓܪ ܓܝܪ ܛܘܪܐ ܗܘ ܕܤܝܢܝ ܕܒܐܪܒܝܐ ܘܫܠܡܐ ܠܗܕܐ ܐܘܪܫܠܡ ܘܦܠܚܐ ܥܒܕܘܬܐ ܗܝ ܘܒܢܝܗ ܀
25 Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wi nekk ca réewu Arabi. Te it mooy misaalu dëkku Yerusalem, bi fi nekk tey. Ndaxte moom ak ay doomam yépp ay jaam lañu.
26ܗܝ ܕܝܢ ܐܘܪܫܠܡ ܥܠܝܬܐ ܚܐܪܬܐ ܗܝ ܕܐܝܬܝܗ ܐܡܢ ܀
26 Waaye Yerusalem, ga ca kaw, mooy gor si. Moom mooy sunu ndey.
27ܟܬܝܒ ܓܝܪ ܕܐܬܒܤܡܝ ܥܩܪܬܐ ܗܝ ܕܠܐ ܝܠܕܐ ܘܐܬܦܨܚܝ ܘܓܥܝ ܗܝ ܕܠܐ ܡܚܒܠܐ ܡܛܠ ܕܤܓܝܘ ܒܢܝܗ ܕܨܕܝܬܐ ܝܬܝܪ ܡܢ ܒܢܝܗ ܕܒܥܝܠܬܐ ܀
27 Ndaxte Mbind mi nee na:«Bégal, yaw jigéen ji dul jur,te musul a am doom.Reeyal te bànneexu,yaw mi musul a xam coonob mat,ndaxte jigéen ji ñu faalewulmoo gën a jaboot ki nekk ak jëkkëram.»
28ܚܢܢ ܕܝܢ ܐܚܝ ܐܝܟ ܐܝܤܚܩ ܒܢܝ ܡܘܠܟܢܐ ܚܢܢ ܀
28 Yéen bokk yi, yéenay doom yi ñu dige woon, niki Isaaxa.
29ܘܐܝܟ ܕܗܝܕܝܢ ܗܘ ܕܝܠܝܕ ܗܘܐ ܒܒܤܪܐ ܪܕܦ ܗܘܐ ܠܗܘ ܕܒܪܘܚܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܗܫܐ ܀
29 Waaye doom ji juddoo ni bépp doom, dafa daan sonal doom ji juddoo ci dooley Xelum Yàlla. Te loolu mooy law ba léegi.
30ܐܠܐ ܡܢܐ ܐܡܪ ܟܬܒܐ ܐܦܩܝܗ ܠܐܡܬܐ ܘܠܒܪܗ ܡܛܠ ܕܠܐ ܢܐܪܬ ܒܪܗ ܕܐܡܬܐ ܥܡ ܒܪܗ ܕܚܐܪܬܐ ܀
30 Lu ci Mbind mi wax nag? Nee na: «Dàqal jaam bi ak doomam, ndaxte doomu jaam bi warul a bokk cér ak doomu gor si ci ndono.»
31ܚܢܢ ܗܟܝܠ ܐܚܝ ܠܐ ܗܘܝܢ ܒܢܝ ܐܡܬܐ ܐܠܐ ܒܢܝ ܚܐܪܬܐ ܀
31 Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam, ay doomi gor lanu.