Syriac: NT

Wolof: New Testament

Galatians

5

1ܩܘܡܘ ܗܟܝܠ ܒܚܐܪܘܬܐ ܗܝ ܕܡܫܝܚܐ ܚܪܪܢ ܘܠܐ ܬܬܟܕܢܘܢ ܬܘܒ ܒܢܝܪܐ ܕܥܒܕܘܬܐ ܀
1 Kirist a nu daggal sunu buumi njaam, ngir goreel nu. Kon dëgërleen ci seen ngor te bañ a delluwaat ci njaam.
2ܗܐ ܐܢܐ ܦܘܠܘܤ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܢ ܬܬܓܙܪܘܢ ܡܫܝܚܐ ܡܕܡ ܠܐ ܡܗܢܐ ܠܟܘܢ ܀
2 Dégluleen! Man Pool maa leen koy wax: bu ngeen itteelee xaraf, kon Kirist dootu leen jariñ dara.
3ܡܤܗܕ ܐܢܐ ܕܝܢ ܬܘܒ ܠܟܠ ܒܪܢܫ ܕܡܬܓܙܪ ܕܚܝܒ ܗܘ ܕܟܠܗ ܢܡܘܤܐ ܢܥܒܕ ܀
3 Te maa ngi dellu di waxaat ne, képp kuy farataal xaraf, fàww nga sàmm lépp lu yoon wi santaane.
4ܐܬܒܛܠܬܘܢ ܠܟܘܢ ܡܢ ܡܫܝܚܐ ܐܝܠܝܢ ܕܒܢܡܘܤܐ ܡܙܕܕܩܝܬܘܢ ܘܡܢ ܛܝܒܘܬܐ ܢܦܠܬܘܢ ܀
4 Yéen ñiy fexee jub fa kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, tàggalikoo ngeen ak Kirist; dëddu ngeen yiwu Yàlla.
5ܚܢܢ ܓܝܪ ܒܪܘܚܐ ܕܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܠܤܒܪܐ ܕܙܕܝܩܘܬܐ ܡܩܘܝܢܢ ܀
5 Waaye njub, gi nu Yàlla dencal ëllëg, nu ngi koy séentu ci kaw ngëm ak ci ndimbalu Xelum Yàlla.
6ܒܡܫܝܚܐ ܓܝܪ ܝܫܘܥ ܠܐ ܓܙܘܪܬܐ ܡܕܡ ܐܝܬܝܗ ܘܠܐ ܥܘܪܠܘܬܐ ܐܠܐ ܗܝܡܢܘܬܐ ܕܡܬܓܡܪܐ ܒܚܘܒܐ ܀
6 Ndaxte bu nu bokkee ci Kirist Yeesu, xaraf ak bañ a xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, giy jëf ci mbëggeel.
7ܫܦܝܪ ܪܗܛܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܡܢܘ ܕܘܕܟܘܢ ܕܠܫܪܪܐ ܠܐ ܬܬܛܦܝܤܘܢ ܀
7 Ni ngeen jógtee woon de baax na! Waaw ku leen dog, ba ngeen bañ a déggal dëgg?
8ܦܝܤܟܘܢ ܠܐ ܗܘܐ ܡܢ ܗܘ ܕܩܪܟܘܢ ܀
8 Li ñu leen xiir jógewul ci Yàlla, mi leen woo.
9ܚܡܝܪܐ ܩܠܝܠ ܟܠܗ ܓܒܝܠܬܐ ܡܚܡܥ ܀
9 Dees na ne: «Tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki.»
10ܐܢܐ ܬܟܝܠ ܐܢܐ ܥܠܝܟܘܢ ܒܡܪܢ ܕܡܕܡ ܐܚܪܝܢ ܠܐ ܡܬܪܥܝܬܘܢ ܘܐܝܢܐ ܕܕܠܚ ܠܟܘܢ ܗܘ ܢܤܝܒܪܝܘܗܝ ܠܕܝܢܐ ܡܢ ܕܐܝܬܘܗܝ ܀
10 Waaye teewul Boroom bi jox na ma kóolute ci yéen. Biral na ma ne, dingeen bokk ak man xalaat. Léegi nag, kiy nëxal seen xel, ku mu man a doon, Yàlla dina ko mbugal.
11ܐܢܐ ܕܝܢ ܐܚܝ ܐܠܘ ܥܕܟܝܠ ܓܙܘܪܬܐ ܡܟܪܙ ܗܘܝܬ ܠܡܢܐ ܡܬܪܕܦ ܗܘܝܬ ܕܠܡܐ ܐܬܒܛܠ ܠܗ ܟܫܠܗ ܕܙܩܝܦܐ ܀
11 Man nag bokk yi, bu ma doon faaydaal xaraf ci sama waare, kon duñu ma fitnaale nii; te it li may yégle ci deewu Kirist ca bant ba dootul naqari kenn.
12ܐܫܬܘܦ ܕܝܢ ܐܦ ܡܦܤܩ ܢܦܤܩܘܢ ܗܢܘܢ ܕܕܠܚܝܢ ܠܟܘܢ ܀
12 Ñi farataal xaraf te di leen dëpp, nañu gën a sore ci seen réer: bu yaboo sax ñu dagg seen ngóora, ba dara du ci des!
13ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܠܚܐܪܘܬܐ ܗܘ ܐܬܩܪܝܬܘܢ ܐܚܝ ܒܠܚܘܕ ܠܐ ܬܗܘܐ ܚܐܪܘܬܟܘܢ ܠܥܠܬ ܒܤܪܐ ܐܠܐ ܒܚܘܒܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܫܬܥܒܕܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܀
13 Yéen nag bokk yi, Yàlla woo na leen, ngeen nekk i gor. Waaye nag buleen ci sukkandiku, bay topp seen nafsu, waaye dimbaleenteleen ci kaw mbëggeel.
14ܟܠܗ ܓܝܪ ܢܡܘܤܐ ܒܚܕܐ ܡܠܬܐ ܡܬܡܠܐ ܒܗܝ ܕܬܚܒ ܠܩܪܝܒܟ ܐܝܟ ܢܦܫܟ ܀
14 Ndaxte yoon wépp, ndigal lii a ko tënk: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
15ܐܢ ܕܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܡܢܟܬܝܬܘܢ ܘܐܟܠܝܬܘܢ ܚܙܘ ܕܠܡܐ ܚܕ ܡܢ ܚܕ ܬܤܘܦܘܢ ܀
15 Waaye moytuleen! Bu ngeen dee màttante ak a lekkante, dingeen yàqante.
16ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܒܪܘܚܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܗܠܟܝܢ ܘܪܓܬܐ ܕܒܤܪܐ ܠܐ ܡܢ ܡܬܘܡ ܬܥܒܕܘܢ ܀
16 Li ma leen di wax mooy lii: dundleen ci Xelum Yàlla, kon dungeen topp seen nafsu.
17ܒܤܪܐ ܓܝܪ ܪܐܓ ܡܕܡ ܕܢܟܐ ܠܪܘܚܐ ܘܪܘܚܐ ܪܓܐ ܡܕܡ ܕܢܟܐ ܠܒܤܪܐ ܘܬܪܝܗܘܢ ܤܩܘܒܠܐ ܐܢܘܢ ܚܕ ܕܚܕ ܕܠܐ ܡܕܡ ܕܨܒܝܬܘܢ ܬܗܘܘܢ ܥܒܕܝܢ ܀
17 Ndaxte sunu nafsu am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu Xelum Yàlla. Te Xelum Yàlla itam am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu sunu nafsu. Ñoom ñaar dañoo juuyoo ci bépp fànn, ba tax lépp lu ngeen bëggoon a def, dungeen ko man.
18ܐܢ ܕܝܢ ܒܪܘܚܐ ܡܬܕܒܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܀
18 Waaye bu ngeen toppee Xelum Yàlla, nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.
19ܝܕܝܥܝܢ ܐܢܘܢ ܓܝܪ ܥܒܕܘܗܝ ܕܒܤܪܐ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܙܢܝܘܬܐ ܛܢܦܘܬܐ ܨܚܢܘܬܐ ܀
19 Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: njaaloo, xalaat yu bon, def i ñaawteef ak say cér,
20ܦܘܠܚܢܐ ܕܦܬܟܪܐ ܚܪܫܘܬܐ ܒܥܠܕܒܒܘܬܐ ܚܪܝܢܐ ܛܢܢܐ ܚܡܬܐ ܥܨܝܢܐ ܦܠܓܘܬܐ ܤܕܩܐ ܀
20 xërëm, luxus, noonoo ak xuloo, ñeetaane, xadar, diiroo mbagg, féewaloo ak xaajaloo,
21ܚܤܡܐ ܩܛܠܐ ܪܘܝܘܬܐ ܙܡܪܐ ܘܟܠ ܕܠܗܠܝܢ ܕܡܝܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܗܠܝܢ ܤܥܪܝܢ ܐܝܟ ܕܡܢ ܠܘܩܕܡ ܐܡܪܬ ܠܟܘܢ ܐܦ ܗܫܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܠܐ ܝܪܬܝܢ ܀
21 kiñaan, màndite ak xawaare ak yeneen yu ni mel. Léegi nag maa ngi leen di artu, ni ma ko defe woon: ñiy jëfe noonu duñu am cér ci nguuru Yàlla.
22ܦܐܪܐ ܕܝܢ ܕܪܘܚܐ ܐܝܬܝܗܘܢ ܚܘܒܐ ܚܕܘܬܐ ܫܠܡܐ ܡܓܪܬ ܪܘܚܐ ܒܤܝܡܘܬܐ ܛܒܘܬܐ ܗܝܡܢܘܬܐ ܀
22 Waaye li Xelu Yàlla mi di meññ mooy: mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre,
23ܡܟܝܟܘܬܐ ܡܤܝܒܪܢܘܬܐ ܥܠ ܗܠܝܢ ܢܡܘܤܐ ܠܐ ܤܝܡ ܀
23 lewetaay ak maandute. Yoon wi terewul yu ni mel.
24ܐܝܠܝܢ ܕܝܢ ܕܕܡܫܝܚܐ ܐܢܘܢ ܒܤܪܗܘܢ ܙܩܦܘ ܥܡ ܟܠܗܘܢ ܟܐܒܘܗܝ ܘܪܓܝܓܬܗ ܀
24 Léegi ñi bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj nañu seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak ay xemmemam ak ay bëgg-bëggam.
25ܢܚܐ ܗܟܝܠ ܒܪܘܚܐ ܘܠܪܘܚܐ ܢܫܠܡ ܀
25 Gannaaw nag nu ngi dund léegi ci Xelum Yàlla, kon nanu ko topp.
26ܘܠܐ ܢܗܘܐ ܤܪܝܩܝ ܫܘܒܚܐ ܕܡܩܠܝܢ ܚܕ ܥܠ ܚܕ ܘܚܤܡܝܢ ܚܕ ܒܚܕ ܀
26 Bu nu tiitaru di dëkkante, di iñaanante.