Syriac: NT

Wolof: New Testament

Galatians

6

1ܐܚܝ ܐܢ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܢܬܩܕܡ ܒܤܟܠܘܬܐ ܐܢܬܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܒܪܘܚ ܐܢܬܘܢ ܐܬܩܢܘܗܝ ܒܪܘܚܐ ܡܟܝܟܬܐ ܘܗܘܝܬܘܢ ܙܗܝܪܝܢ ܕܕܠܡܐ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܬܬܢܤܘܢ ܀
1 Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam.
2ܘܛܥܢܘ ܝܘܩܪܐ ܕܚܕܕܐ ܕܗܟܢܐ ܡܡܠܝܬܘܢ ܢܡܘܤܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
2 Jàppalanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral.
3ܐܢ ܓܝܪ ܐܢܫ ܤܒܪ ܕܐܝܬܘܗܝ ܡܕܡ ܟܕ ܠܐ ܐܝܬܘܗܝ ܢܦܫܗ ܡܛܥܐ ܀
3 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp.
4ܐܠܐ ܐܢܫ ܥܒܕܗ ܢܗܘܐ ܒܩܐ ܘܗܝܕܝܢ ܒܝܢܘܗܝ ܠܢܦܫܗ ܢܗܘܐ ܫܘܒܗܪܗ ܘܠܐ ܒܐܚܪܢܐ ܀
4 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina man a naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des.
5ܟܠܢܫ ܓܝܪ ܡܘܒܠܐ ܕܢܦܫܗ ܢܫܩܘܠ ܀
5 Ndaxte ku ci nekk dangaa war a yenu sab yen.
6ܢܫܬܘܬܦ ܕܝܢ ܗܘ ܕܫܡܥ ܡܠܬܐ ܠܗܘ ܡܢ ܕܡܫܡܥ ܠܗ ܒܟܠܗܝܢ ܛܒܬܐ ܀
6 Kiy jàng kàddug Yàlla war na sédd ki koy jàngal ci alalam jépp.
7ܠܐ ܬܛܥܘܢ ܐܠܗܐ ܠܐ ܡܬܒܙܚ ܡܕܡ ܕܙܪܥ ܓܝܪ ܒܪ ܐܢܫܐ ܗܘ ܗܘ ܚܨܕ ܀
7 Bu leen ci dara nax; kenn du fontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob.
8ܡܢ ܕܒܒܤܪ ܙܪܥ ܡܢ ܒܤܪܐ ܚܒܠܐ ܗܘ ܚܨܕ ܘܡܢ ܕܒܪܘܚ ܙܪܥ ܡܢ ܪܘܚܐ ܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܢܚܨܘܕ ܀
8 Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex.
9ܘܟܕ ܥܒܕܝܢܢ ܕܛܒ ܠܐ ܗܘܬ ܡܐܢܐ ܠܢ ܢܗܘܐ ܓܝܪ ܙܒܢܐ ܕܢܚܨܘܕ ܘܠܐ ܬܡܐܢ ܠܢ ܀
9 Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu.
10ܗܫܐ ܗܟܝܠ ܥܕ ܙܒܢܐ ܐܝܬ ܠܢ ܢܦܠܘܚ ܛܒܬܐ ܠܘܬ ܟܠܢܫ ܝܬܝܪܐܝܬ ܠܘܬ ܒܢܝ ܒܝܬܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܀
10 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm.
11ܚܙܘ ܐܝܠܝܢ ܟܬܝܒܢ ܟܬܒܬ ܠܟܘܢ ܒܐܝܕܝ ܀
11 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp!
12ܐܝܠܝܢ ܕܨܒܝܢ ܕܢܫܬܒܗܪܘܢ ܒܒܤܪܐ ܗܢܘܢ ܐܠܨܝܢ ܠܟܘܢ ܕܬܬܓܙܪܘܢ ܕܒܠܚܘܕ ܒܙܩܝܦܗ ܕܡܫܝܚܐ ܠܐ ܢܬܪܕܦܘܢ ܀
12 Ñiy gistal ci seen yaram, ñooñoo bëgg ngeen xaraf, ngir ragal a daj fitna ci yégle deewu Kirist ca bant ba.
13ܐܦܠܐ ܓܝܪ ܗܢܘܢ ܗܠܝܢ ܕܓܙܪܝܢ ܢܛܪܝܢ ܢܡܘܤܐ ܐܠܐ ܨܒܝܢ ܕܬܬܓܙܪܘܢ ܕܒܒܤܪܟܘܢ ܕܝܠܟܘܢ ܢܫܬܒܗܪܘܢ ܀
13 Kureel gi faaydaal xaraf, ñoom ci seen bopp sax, duñu topp yoon wi. Dañoo bëgg a ngeen xaraf, ba ñu man a bàkku ci seen yaram, yéen.
14ܠܝ ܕܝܢ ܠܐ ܢܗܘܐ ܠܝ ܕܐܫܬܒܗܪ ܐܠܐ ܒܙܩܝܦܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܒܗ ܥܠܡܐ ܙܩܝܦ ܠܝ ܘܐܢܐ ܙܩܝܦ ܐܢܐ ܠܥܠܡܐ ܀
14 Man ci sama wàllu bopp, duma bàkku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba ñu ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci yëfi àddina; yëfi àddina dee ci man.
15ܠܐ ܓܝܪ ܓܙܘܪܬܐ ܐܝܬܝܗ ܡܕܡ ܘܠܐ ܥܘܪܠܘܬܐ ܐܠܐ ܒܪܝܬܐ ܚܕܬܐ ܀
15 Xaraf ak bañ a xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees.
16ܘܐܝܠܝܢ ܕܠܗܢܐ ܫܒܝܠܐ ܫܠܡܝܢ ܫܠܡܐ ܢܗܘܐ ܥܠܝܗܘܢ ܘܪܚܡܐ ܘܥܠ ܐܝܤܪܝܠ ܕܐܠܗܐ ܀
16 Ñiy topp ndigal lii nag, na Yàlla wàcce jàmm ak yërmande ci ñoom, ak ci Israyilu Yàlla.
17ܡܟܝܠ ܠܝ ܐܢܫ ܥܡܠܐ ܠܐ ܢܪܡܐ ܐܢܐ ܓܝܪ ܟܘܬܡܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܒܦܓܪܝ ܫܩܝܠ ܐܢܐ ܀
17 Léegi nag, bu ma kenn lëjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy màndargaal ne, jaamu Yeesu laa.
18ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܡ ܪܘܚܟܘܢ ܐܚܝ ܐܡܝܢ ܀
18 Bokk yi, na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom ànd ak seen xel. Amiin.