1ܢܡܘܤܐ ܓܝܪ ܛܠܢܝܬܐ ܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܕܛܒܬܐ ܕܥܬܝܕܢ ܠܐ ܗܘܐ ܩܢܘܡܐ ܕܝܠܗܝܢ ܕܨܒܘܬܐ ܡܛܠ ܗܢܐ ܟܕ ܒܟܠ ܫܢܐ ܗܢܘܢ ܟܕ ܗܢܘܢ ܕܒܚܐ ܡܬܩܪܒܝܢ ܗܘܘ ܠܐ ܡܡܬܘV ܐܫܟܚܘ ܕܢܓܡܪܘܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܩܪܒܝܢ ܠܗܘܢ ܀
1 Yoonu Musaa dafa misaal xéewal yi waroon a ñëw; takkandeer la ci yëf yu dëggu yi, waaye du ñoom ci seen bopp. Looloo tax mënul a yeggale cig mat ñi ñëw ci Yàlla, ndaxte at mu nekk duñu jóg ci jébbal Yàlla sarax yooyu.
2ܐܠܘ ܓܝܪ ܓܡܪܝܢ ܗܘܘ ܟܒܪ ܕܝܢ ܐܬܬܢܝܚܘ ܡܢ ܩܘܪܒܢܝܗܘܢ ܡܛܠ ܕܠܐ ܡܟܝܠ ܛܪܝܐ ܗܘܬ ܠܗܘܢ ܬܐܪܬܗܘܢ ܒܚܛܗܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܚܕܐ ܙܒܢ ܐܬܕܟܝܘ ܠܗܘܢ ܀
2 Sarax yi ñuy def, bu ñu manoon a sellal ñiy jaamu benn yoon ba fàww, kon dinañu leen bàyyi, ndaxte dootuñu am yeraange ci seeni bàkkaar.
3ܐܠܐ ܒܗܘܢ ܒܕܒܚܐ ܡܕܟܪܝܢ ܚܛܗܝܗܘܢ ܒܟܠ ܫܢܐ ܀
3 Waaye dañuy fàttaliku bàkkaar yi ci sarax yi ñuy def at mu jot.
4ܠܐ ܓܝܪ ܡܫܟܚ ܕܡܐ ܕܬܘܪܐ ܘܕܨܦܪܝܐ ܠܡܕܟܝܘ ܚܛܗܐ ܀
4 Ndaxte deretu yëkk yi ak ju sikket yi mënuñoo dindi bàkkaar yi.
5ܡܛܠ ܗܢܐ ܟܕ ܥܐܠ ܠܥܠܡܐ ܐܡܪ ܒܕܒܚܐ ܘܩܘܪܒܢܐ ܠܐ ܨܒܝܬ ܦܓܪܐ ܕܝܢ ܐܠܒܫܬܢܝ ܀
5 Looloo tax bi muy wàcc àddina, Kirist nee na:«Bëggoo saraxu mala walla beneen sarax,waaye aw yaram nga ma defaral.
6ܘܝܩܕܐ ܫܠܡܐ ܕܚܠܦ ܚܛܗܐ ܠܐ ܫܐܠܬ ܀
6 Sarax yu ñuy lakkwalla sarax yiy dindi bàkkaar,benn neexu la ci.
7ܗܝܕܝܢ ܐܡܪܬ ܕܗܐ ܐܢܐ ܐܬܐ ܐܢܐ ܕܒܪܝܫ ܟܬܒܐ ܟܬܝܒ ܥܠܝ ܕܐܥܒܕ ܨܒܝܢܟ ܐܠܗܐ ܀
7 Moo tax ma ne: “Damaa wàccngir def sa coobare, yaw Yàlla,mu dëppoo ak li ñu bind ci sama mbirci téereb yoon wi.”»
8ܡܢ ܠܥܠ ܐܡܪ ܕܕܒܚܐ ܘܩܘܪܒܢܐ ܘܝܩܕܐ ܫܠܡܐ ܕܚܠܦ ܚܛܗܐ ܠܐ ܨܒܝܬ ܗܢܘܢ ܕܡܬܩܪܒܝܢ ܗܘܘ ܒܢܡܘܤܐ ܀
8 Wax na bu jëkk: «Saraxi mala walla yeneeni sarax, sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar, bëgguloo leen te benn neexu la ci.» Teewul yoon wi moo leen santaane.
9ܘܒܬܪܗ ܐܡܪ ܕܗܐ ܐܬܐ ܐܢܐ ܕܐܥܒܕ ܨܒܝܢܟ ܐܠܗܐ ܒܗܕܐ ܒܛܠ ܠܩܕܡܝܬܐ ܕܢܩܝܡ ܠܕܬܪܬܝܢ ܀
9 Noonu mu tegaat ca ne: «Damaa wàcc ngir def sa coobare.» Noonu toxal na jëfin wu jëkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees.
10ܒܗܢܐ ܓܝܪ ܨܒܝܢܗ ܐܬܩܕܫܢ ܒܩܘܪܒܢܐ ܕܦܓܪܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܚܕܐ ܙܒܢ ܀
10 Te ci li Kirist def coobareg Yàlla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba fàww, moo tax nu sell ci bàkkaar.
11ܟܠ ܪܒ ܟܘܡܪܐ ܓܝܪ ܕܩܐܡ ܗܘܐ ܘܡܫܡܫ ܟܠܝܘܡ ܗܢܘܢ ܒܗܢܘܢ ܕܒܚܐ ܡܩܪܒ ܗܘܐ ܐܝܠܝܢ ܕܡܢ ܡܬܘܡ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܗܘܘ ܠܡܕܟܝܘ ܚܛܗܐ ܀
11 Bés bu nekk saraxalekat yi dañuy taxaw di liggéeyal Yàlla, di sax ci def sarax yu mënul a dindi bàkkaar yi mukk.
12ܗܢܐ ܕܝܢ ܚܕ ܕܒܚܐ ܩܪܒ ܚܠܦ ܚܛܗܐ ܘܝܬܒ ܥܠ ܝܡܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܠܥܠܡ ܀
12 Waaye nag saraxalekat bii di Kirist, bi mu saraxee sarax bu am doole ngir dindi bàkkaar yi benn yoon ba fàww, dafa toog ca ndeyjooru Yàlla,
13ܘܡܩܘܐ ܡܟܝܠ ܥܕܡܐ ܕܢܬܬܤܝܡܘܢ ܒܥܠܕܒܒܘܗܝ ܟܘܒܫܐ ܬܚܝܬ ܪܓܠܘܗܝ ܀
13 di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam.
14ܒܚܕ ܓܝܪ ܩܘܪܒܢܐ ܓܡܪ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܬܩܕܫܝܢ ܒܗ ܠܥܠܡ ܀
14 Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba fàww.
15ܤܗܕܐ ܠܢ ܕܝܢ ܐܦ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܐܡܪܬ ܀
15 Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko;
16ܗܕܐ ܗܝ ܕܝܬܩܐ ܕܐܬܠ ܠܗܘܢ ܡܢ ܒܬܪ ܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܐܡܪ ܡܪܝܐ ܐܬܠܝܘܗܝ ܠܢܡܘܤܝ ܒܡܕܥܝܗܘܢ ܘܥܠ ܠܒܘܬܗܘܢ ܐܟܬܒܝܘܗܝ ܀
16 dafa jëkk a wax ne:«Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak ñoom,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xol,bind ko ci seen xel.»
17ܘܥܘܠܗܘܢ ܘܚܛܗܝܗܘܢ ܠܐ ܐܬܕܟܪ ܠܗܘܢ ܀
17 Noonu mu tegaat ca ne:«Dootuma fàttaliku seeni bàkkaarwalla seeni tooñ.»
18ܐܝܟܐ ܕܝܢ ܕܐܝܬ ܫܘܒܩܢܐ ܕܚܛܗܐ ܠܐ ܡܬܒܥܐ ܩܘܪܒܢܐ ܕܚܠܦ ܚܛܗܐ ܀
18 Kon nag fu ñuy baale bàkkaar, aajootul sarax su koy dindi.
19ܐܝܬ ܠܢ ܗܟܝܠ ܐܚܝ ܓܠܝܘܬ ܐܦܐ ܒܡܥܠܢܐ ܕܒܝܬ ܩܘܕܫܐ ܒܕܡܗ ܕܝܫܘܥ ܀
19 Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell-baa-sell,
20ܘܐܘܪܚܐ ܕܚܝܐ ܕܚܕܬ ܠܢ ܗܫܐ ܒܐܦܝ ܬܪܥܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܒܤܪܗ ܀
20 nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund,
21ܘܐܝܬ ܠܢ ܟܘܡܪܐ ܪܒܐ ܥܠ ܒܝܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
21 te gannaaw am nanu saraxalekat bu mag, biy yilif waa kër Yàlla,
22ܢܩܪܘܒ ܗܟܝܠ ܒܠܒܐ ܫܪܝܪܐ ܘܒܬܘܟܠܢܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܟܕ ܪܤܝܤܝܢ ܠܒܘܬܢ ܘܕܟܝܢ ܡܢ ܬܐܪܬܐ ܒܝܫܬܐ ܘܡܤܚܝ ܦܓܪܢ ܒܡܝܐ ܕܟܝܐ ܀
22 kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell.
23ܘܢܚܡܤܢ ܒܬܘܕܝܬܐ ܕܤܒܪܢ ܘܠܐ ܢܨܛܠܐ ܡܗܝܡܢ ܗܘ ܓܝܪ ܡܢ ܕܡܠܟ ܠܢ ܀
23 Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te bañ a toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.
24ܘܢܚܘܪ ܚܕ ܒܚܕ ܒܓܘܪܓܐ ܕܚܘܒܐ ܘܕܥܒܕܐ ܛܒܐ ܀
24 Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax.
25ܘܠܐ ܢܗܘܐ ܫܒܩܝܢ ܟܢܘܫܝܢ ܐܝܟ ܕܐܝܬ ܥܝܕܐ ܠܐܢܫ ܐܢܫ ܐܠܐ ܒܥܘ ܚܕ ܡܢ ܚܕ ܝܬܝܪܐܝܬ ܟܡܐ ܕܚܙܝܬܘܢ ܕܩܪܒ ܝܘܡܐ ܗܘ ܀
25 Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi.
26ܐܢ ܓܝܪ ܒܨܒܝܢܗ ܢܚܛܐ ܐܢܫ ܡܢ ܒܬܪ ܕܩܒܠ ܝܕܥܬܐ ܕܫܪܪܐ ܠܝܬ ܡܟܝܠ ܕܒܚܬܐ ܕܬܬܩܪܒ ܚܠܦ ܚܛܗܐ ܀
26 Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu.
27ܐܠܐ ܥܬܝܕ ܗܘ ܕܝܢܐ ܕܚܝܠܐ ܘܛܢܢܐ ܕܢܘܪܐ ܕܐܟܠ ܠܒܥܠܕܒܒܐ ܀
27 Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy war a lakk nooni Yàlla yi.
28ܐܢ ܓܝܪ ܐܝܢܐ ܕܥܒܪ ܥܠ ܢܡܘܤܐ ܕܡܘܫܐ ܥܠ ܦܘܡ ܬܪܝܢ ܘܬܠܬܐ ܤܗܕܝܢ ܕܠܐ ܪܚܡܝܢ ܡܐܬ ܀
28 Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te ñaar walla ñetti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn yërmande.
29ܟܡܐ ܤܒܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܝܬܝܪܐܝܬ ܡܤܡ ܒܪܫܐ ܢܩܒܠ ܐܝܢܐ ܕܕܫܗ ܠܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܘܚܫܒ ܕܡܐ ܕܕܝܬܩܐ ܕܝܠܗ ܐܝܟ ܕܟܠܢܫ ܕܒܗ ܐܬܩܕܫ ܘܨܥܪ ܠܪܘܚܐ ܕܛܝܒܘܬܐ ܀
29 Ku xeeb Doomu Yàlla ji te fonkadi deretu kóllëre, ji ñu ko sellale, te muy toroxal Xelum Yàlla, mi indi yiw, naka la mbugalam war a gën a yéese?
30ܝܕܥܝܢܢ ܠܗܘ ܕܐܡܪ ܕܕܝܠܝ ܗܝ ܬܒܥܬܐ ܘܐܢܐ ܐܦܪܘܥ ܘܬܘܒ ܕܢܕܘܢ ܡܪܝܐ ܠܥܡܗ ܀
30 Xam nanu ki wax ne: «Man maay àtte, maay fey jëf.» Te newaat na: «Boroom bi dina àtte ay gaayam.»
31ܕܚܠܬܐ ܗܝ ܪܒܬܐ ܠܡܦܠ ܒܐܝܕܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܚܝܐ ܀
31 Ndaw tiitaange ci ku sàggan, ba tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund!
32ܐܬܕܟܪܘ ܗܟܝܠ ܠܝܘܡܬܐ ܩܕܡܝܐ ܗܢܘܢ ܕܒܗܘܢ ܩܒܠܬܘܢ ܡܥܡܘܕܝܬܐ ܘܐܓܘܢܐ ܪܒܐ ܤܝܒܪܬܘܢ ܕܚܫܐ ܒܚܤܕܐ ܘܒܐܘܠܨܢܐ ܀
32 Fàttalikuleen bés yu jëkk ya, ba leeru Yàlla tàbbee ci yéen; dékku ngeen xeex bu mag ciy fitna.
33ܘܕܗܘܝܬܘܢ ܚܙܘܢܐ ܘܐܦ ܐܫܬܘܬܦܬܘܢ ܠܐܢܫܐ ܕܗܠܝܢ ܤܝܒܪܘ ܀
33 Léeg-léeg ñu saaga leen ak di leen sonal ci kanamu nit ñi; léeg-léeg it ngeen taxawu ñi ñuy def noonu.
34ܘܟܐܒ ܠܟܘܢ ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܐܤܝܪܝܢ ܘܚܛܘܦܝܐ ܕܢܟܤܝܟܘܢ ܒܚܕܘܬܐ ܤܝܒܪܬܘܢ ܡܛܠ ܕܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܝܬ ܠܟܘܢ ܩܢܝܢܐ ܒܫܡܝܐ ܕܡܝܬܪ ܗܘ ܘܠܐ ܥܒܪ ܀
34 Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne, am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww.
35ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܘܒܕܘܢ ܓܠܝܘܬ ܐܦܐ ܕܐܝܬ ܠܟܘܢ ܕܥܬܝܕ ܠܗ ܐܓܪܐ ܤܓܝܐܐ ܀
35 Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag.
36ܡܤܝܒܪܢܘܬܐ ܗܘ ܓܝܪ ܡܬܒܥܝܐ ܠܟܘܢ ܕܬܥܒܕܘܢ ܨܒܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܘܬܤܒܘܢ ܡܘܠܟܢܐ ܀
36 Dangeen a war a muñ, ba def coobareg Yàlla, sog a jot li mu leen digoon.
37ܡܛܠ ܕܩܠܝܠ ܗܘ ܙܒܢܐ ܘܛܒ ܙܥܘܪ ܕܢܐܬܐ ܗܘ ܕܐܬܐ ܘܠܐ ܢܘܚܪ ܀
37 Ndaxte lii la Mbind mi wax:«Ci kanam tuuti, ki war a ñëw dina ñëwte léegi mu agsi.
38ܟܐܢܐ ܕܝܢ ܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܕܝܠܝ ܢܚܐ ܘܐܢ ܡܬܩܛܥܐ ܠܗ ܠܐ ܨܒܝܐ ܒܗ ܢܦܫܝ ܀
38 Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm,waaye bu delloo gannaaw,sama xol du sedd ci moom.»
39ܚܢܢ ܕܝܢ ܠܐ ܗܘܝܢ ܕܩܘܛܥܐ ܕܡܘܒܠܐ ܠܐܒܕܢܐ ܐܠܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܕܡܩܢܝܐ ܠܢ ܢܦܫܢ ܀
39 Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye nu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc.