Syriac: NT

Wolof: New Testament

Hebrews

9

1ܒܩܕܡܝܬܐ ܕܝܢ ܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܦܘܩܕܐ ܕܬܫܡܫܬܐ ܘܒܝܬ ܩܘܕܫܐ ܥܠܡܢܝܐ ܀
1 Kóllëre gu jëkk ga ëmboon na ay ndigal ci mbirum ni ñu war a jaamoo Yàlla. Amoon na itam kër Yàlla gu nekkoon àddina.
2ܡܫܟܢܐ ܓܝܪ ܩܕܡܝܐ ܕܐܬܥܒܕ ܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܡܢܪܬܐ ܘܦܬܘܪܐ ܘܠܚV ܐܦܐ ܘܡܬܩܪܐ ܗܘܐ ܒܝܬ ܩܘܕܫܐ ܀
2 Nekkoon na ab tàntu màggalukaay bu ñu séddale ñaari néeg. Ca ba jiitu la làmpu diwlin ba nekkoon ak taabal, ja ñu daan teg mburu ya ñu daa jébbal Yàlla. Foofaa nga tuddoon bérab bu sell ba.
3ܡܫܟܢܐ ܕܝܢ ܓܘܝܐ ܕܠܓܘ ܡܢ ܐܦܝ ܬܪܥܐ ܕܬܪܝܢ ܡܬܩܪܐ ܗܘܐ ܩܕܘܫ ܩܘܕܫܐ ܀
3 Néeg ba ñu tudde bérab bu sell-baa-sell a nga nekkoon ca gannaaw ñaareelu rido ba.
4ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܒܝܬ ܒܤܡܐ ܕܕܗܒܐ ܘܩܒܘܬܐ ܕܕܝܬܩܐ ܕܩܪܝܡܐ ܟܠܗ ܒܕܗܒܐ ܘܐܝܬ ܒܗ ܩܤܛܐ ܕܕܗܒܐ ܗܝ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܡܢܢܐ ܘܫܒܛܐ ܕܐܗܪܘܢ ܗܘ ܕܐܦܪܥ ܘܠܘܚܐ ܕܕܝܬܩܐ ܀
4 Saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu kóllëre, ga ñu taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon ñam, wi ñuy wax mànn, ak it yetu Aaroona wi jebbi woon, ak àlluway doj, ya ñu bindoon wax yi kóllëre gi ëmb.
5ܘܠܥܠ ܡܢܗ ܟܪܘܒܐ ܕܫܘܒܚܐ ܕܡܛܠܝܢ ܥܠ ܚܘܤܝܐ ܠܐ ܗܘܐ ܕܝܢ ܙܒܢܐ ܗܘ ܕܢܐܡܪ ܥܠ ܚܕܐ ܚܕܐ ܡܢ ܗܠܝܢ ܕܗܟܢܐ ܡܬܩܢܢ ܗܘܝ ܀
5 Ca kaw gaal ga teg nañu fa ñaari nataali mbindeef yu ñuy wax Seruben, yu doon wone ndamu Yàlla. Seeni laaf ñoo doon yiir baalukaay ba. Waaye loolu lépp léegi mënunu koo tekki benn-benn.
6ܘܠܡܫܟܢܐ ܒܪܝܐ ܒܟܠܙܒܢ ܥܐܠܝܢ ܗܘܘ ܟܘܡܪܐ ܘܡܫܠܡܝܢ ܗܘܘ ܬܫܡܫܬܗܘܢ ܀
6 Ba ñu defaree lépp, saraxalekat ya dañu daan dugg bés bu set ca néeg bu jëkk ba, ngir mottali seen liggéeyu saraxale ca Yàlla.
7ܠܡܫܟܢܐ ܕܝܢ ܕܠܓܘ ܡܢܗ ܚܕܐ ܗܘ ܒܫܢܬܐ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܥܐܠ ܗܘܐ ܪܒܟܘܡܪܐ ܒܕܡܐ ܗܘ ܕܡܩܪܒ ܗܘܐ ܚܠܦ ܢܦܫܗ ܘܚܠܦ ܤܟܠܘܬܗ ܕܥܡܐ ܀
7 Waaye ca néeg ba ca topp, saraxalekat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te yóbbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Yàlla, ngir bàkkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen ñàkka xam.
8ܒܗܕܐ ܕܝܢ ܡܘܕܥܐ ܗܘܬ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܠܐ ܐܬܓܠܝܬ ܥܕܟܝܠ ܐܘܪܚܐ ܕܩܕܝܫܐ ܟܡܐ ܙܒܢܐ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܩܝܡܐ ܠܡܫܟܢܐ ܩܕܡܝܐ ܀
8 Ci noonu nag Xel mu Sell mi wone na ne, yoon wi ñuy jaar, ba dem ca bérab bu sell-baa-sell, ubbikoogul woon, fi ak tànt ba jëkk baa ngi doon taxaw.
9ܘܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܬܠܐ ܗܢܐ ܠܙܒܢܐ ܗܘ ܕܒܗ ܩܘܪܒܢܐ ܘܕܒܚܐ ܡܬܩܪܒܝܢ ܗܘܘ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܗܘܘ ܠܡܓܡܪ ܬܐܪܬܗ ܕܡܢ ܕܡܩܪܒ ܠܗܘܢ ܀
9 Misaal la ci jamonoy tey; dafay wone ne, sarax yi ak saraxi mala yi ñu daan jagleel Yàlla, mënuñoo dalal xelu jaamukatu Yàlla bi.
10ܐܠܐ ܒܡܐܟܠܐ ܘܒܡܫܬܝܐ ܒܠܚܘܕ ܘܒܡܥܡܘܕܝܬܐ ܕܙܢܝܢ ܙܢܝܢ ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܦܘܩܕܐ ܕܒܤܪܐ ܕܤܝܡܝܢ ܥܕܡܐ ܠܙܒܢܐ ܕܬܘܪܨܐ ܀
10 Sarax yooyu ñu ngi jëmoon ci lekk ak ci naan ak ci fànn yu bare ci mbirum sangu set. Ay sàrt yu jëm ci yaram lañu, yu ñu waroon a farataal, ba kera jamono ji Yàllay tëral kóllëre gu bees.
11ܡܫܝܚܐ ܕܝܢ ܕܐܬܐ ܗܘܐ ܪܒܟܘܡܪܐ ܕܛܒܬܐ ܕܤܥܪ ܘܥܠ ܠܡܫܟܢܐ ܪܒܐ ܘܡܫܠܡܢܐ ܕܠܐ ܥܒܝܕ ܒܐܝܕܝܐ ܘܠܐ ܗܘܐ ܡܢ ܗܠܝܢ ܒܪܝܬܐ ܀
11 Waaye Kirist ñëw na, doon saraxalekat bu mag, bi joxe xéewal yi teew. Jaar na ca màggalukaay ba gën a màgg te gën a mat, te màggalukaay booba loxol nit defaru ko, maanaam bokkul ci àddina sii.
12ܘܠܐ ܥܠ ܒܕܡܐ ܕܨܦܪܝܐ ܘܕܥܓܠܐ ܐܠܐ ܒܕܡܐ ܕܢܦܫܗ ܥܠ ܚܕܐ ܙܒܢ ܠܒܝܬ ܡܩܕܫܐ ܘܐܫܟܚ ܦܘܪܩܢܐ ܕܠܥܠV ܀
12 Noonu Kirist dugg na benn yoon ba fàww ca bérab bu sell-baa-sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu yëkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul àpp.
13ܐܢ ܓܝܪ ܕܡܐ ܕܨܦܪܝܐ ܘܕܥܓܠܐ ܘܩܛܡܐ ܕܥܓܠܬܐ ܡܬܪܤܤ ܗܘܐ ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܡܬܛܡܐܝܢ ܗܘܘ ܘܡܩܕܫ ܠܗܘܢ ܠܕܘܟܝܐ ܕܒܤܪܗܘܢ ܀
13 Deretu sikket yi ak ju yëkk yi, ak wëllu, wi ñu lakk te di suy dóom bi ñi taq sobe, ñooy sellal yaram.
14ܟܡܐ ܗܟܝܠ ܝܬܝܪܐܝܬ ܕܡܗ ܕܡܫܝܚܐ ܕܒܪܘܚܐ ܕܠܥܠV ܢܦܫܗ ܩܪܒ ܕܠܐ ܡܘV ܠܐܠܗܐ ܢܕܟܐ ܬܐܪܬܢ ܡܢ ܥܒܕܐ ܡܝܬܐ ܕܢܫܡܫ ܠܐܠܗܐ ܚܝܐ ܀
14 Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo ëpp doole? Jox na bakkanam Yàlla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo man a sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax jëf yu jëm ci dee, ngir nu man a jaamu Yàlla jiy dund.
15ܡܛܠ ܗܢܐ ܗܘ ܗܘܐ ܡܨܥܝܐ ܕܕܝܬܩܐ ܚܕܬܐ ܕܒܡܘܬܗ ܗܘ ܗܘܐ ܦܘܪܩܢܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܥܒܪܘ ܥܠ ܕܝܬܩܐ ܩܕܡܝܬܐ ܕܢܤܒܘܢ ܡܘܠܟܢܐ ܐܝܠܝܢ ܕܐܬܩܪܝܘ ܠܝܪܬܘܬܐ ܕܠܥܠV ܀
15 Looloo tax mu nekk Rammukat bi ci wàllu kóllëre gu bees ci diggante Yàlla ak nit, ngir ñi Yàlla woo am cér bu sax ci kaw, te mu digoon leen ko, ndaxte Kirist dee na, ngir jot ñi jàdd yoon ca kóllëre gu jëkk ga.
16ܐܝܟܐ ܓܝܪ ܕܐܝܬ ܕܝܬܩܐ ܡܘܬܐ ܗܘ ܡܚܘܝܐ ܕܗܘ ܕܥܒܕܗ ܀
16 Ci li jëm ci dénkaane bu ñu bind, jëme ci miraas, fàww ñu wone firndeg deewu ka ko bind,
17ܥܠ ܡܝܬܐ ܕܝܢ ܒܠܚܘܕ ܡܫܬܪܪܐ ܡܛܠ ܕܟܡܐ ܕܚܝ ܗܘ ܕܥܒܕܗ ܠܝܬ ܒܗ ܚܫܚܘ ܀
17 ndaxte bala dénkaaneb miraas di taxaw, dee am; te taxawul, fi ak ki ko bind a ngi dund.
18ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܦܠܐ ܩܕܡܝܬܐ ܕܠܐ ܕܡܐ ܐܫܬܪܪܬ ܀
18 Looloo waral kóllëre gu jëkk ga, ñu fasoon ko ak deret.
19ܟܕ ܐܬܦܩܕ ܓܝܪ ܟܠܗ ܦܘܩܕܢܐ ܡܢ ܡܘܫܐ ܠܥܡܐ ܟܠܗ ܒܢܡܘܤܐ ܢܤܒ ܗܘܐ ܡܘܫܐ ܕܡܐ ܕܥܓܠܬܐ ܘܡܝܐ ܒܥܡܪܐ ܕܙܚܘܪܝܬܐ ܘܙܘܦܐ ܘܪܤ ܥܠ ܤܦܪܐ ܘܥܠ ܥܡܐ ܟܠܗ ܀
19 Keroog Musaa jàng na ndigali yoon wépp ci kanamu bànni Israyil gépp. Gannaaw loolu jël na deretu wëllu, jëlaale ndox, ak bantu garab gu ñuy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca téereb yoon wa ak ca mbooloo mépp
20ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܗܢܐ ܗܘ ܕܡܐ ܕܕܝܬܩܐ ܗܝ ܕܐܬܦܩܕܬ ܠܟܘܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܀
20 te naan: «Lii mooy deretu kóllëre gi leen Yàlla tëralal.»
21ܐܦ ܥܠ ܡܫܟܢܐ ܘܥܠ ܟܠܗܘܢ ܡܐܢܐ ܕܬܫܡܫܬܐ ܡܢܗ ܡܢ ܕܡܐ ܪܤ ܀
21 Noonu mu daldi wis it deret ja ca tànt ba ak ca jumtukaay, ya ñu daan jaamoo.
22ܡܛܠ ܕܟܠܡܕV ܒܕܡܐ ܗܘ ܡܬܕܟܐ ܒܢܡܘܤܐ ܘܕܠܐ ܫܘܦܥ ܕܡܐ ܠܝܬ ܫܘܒܩܢܐ ܀
22 Ndaxte ci yoonu Musaa, daanaka deret lañuy sellale lépp, te bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du am.
23ܐܢܢܩܐ ܗܝ ܓܝܪ ܕܗܠܝܢ ܕܕܡܘܬܐ ܐܢܝܢ ܕܫܡܝܢܝܬܐ ܒܗܠܝܢ ܡܬܕܟܝܢ ܗܠܝܢ ܕܝܢ ܫܡܝܢܝܬܐ ܒܕܒܚܐ ܕܡܝܬܪܝܢ ܡܢ ܗܠܝܢ ܀
23 Yëfi àddina yi misaal yu dëggu yi ci asamaan, war nañu leen a sellale noonu. Waaye yëf yu dëggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu gën a baax, ngir ñu sell.
24ܠܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܠܒܝܬ ܡܩܕܫܐ ܕܥܒܝܕ ܒܐܝܕܝܐ ܥܠ ܡܫܝܚܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܕܡܘܬܐ ܕܗܘ ܫܪܝܪܐ ܐܠܐ ܠܗ ܠܫܡܝܐ ܥܠ ܕܢܬܚܙܐ ܩܕV ܦܪܨܘܦܗ ܕܐܠܗܐ ܚܠܦܝܢ ܀
24 Ndaxte Kirist duggul ci bérab bu sell bu nit tabax, muy doon nataal ci bu dëggu bi. Waaye dugg na ca biir asamaan sax, ngir taxawal nu ca kanam Yàlla léegi.
25ܐܦܠܐ ܕܢܩܪܒ ܢܦܫܗ ܙܒܢܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܐܝܟ ܕܥܒܕ ܗܘܐ ܪܒ ܟܘܡܪܐ ܘܥܐܠ ܒܟܠ ܫܢܐ ܠܒܝܬ ܡܩܕܫܐ ܒܕܡܐ ܕܠܐ ܕܝܠܗ ܀
25 Saraxalekat bu mag bi dafay dugg at mu jot ca bérab bu sell-baa-sell ak deret ju dul josam. Waaye Kirist joxewul bakkanam ay yooni yoon.
26ܘܐܢ ܠܐ ܚܝܒ ܗܘܐ ܕܙܒܢܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܢܚܫ ܡܢ ܫܘܪܝܗ ܕܥܠܡܐ ܗܫܐ ܕܝܢ ܒܚܪܬܗ ܕܥܠܡܐ ܚܕܐ ܗܘ ܙܒܢ ܩܪܒ ܢܦܫܗ ܒܕܒܝܚܘܬܗ ܕܢܒܛܠܝܗ ܠܚܛܝܬܐ ܀
26 Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba tàyyi ca njàlbéenug àddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la feeñu ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far bàkkaar yi.
27ܘܐܝܟܢܐ ܕܤܝV ܠܒܢܝܢܫܐ ܕܚܕܐ ܙܒܢ ܢܡܘܬܘܢ ܘܡܢ ܒܬܪ ܡܘܬܗܘܢ ܕܝܢܐ ܀
27 Kon ni nit ñi deeye benn yoon rekk, ba noppi jaar ca àtte ba, ni ko Yàlla dogale,
28ܗܟܢܐ ܐܦ ܡܫܝܚܐ ܚܕܐ ܙܒܢ ܐܬܩܪܒ ܘܒܩܢܘܡܗ ܕܒܚ ܚܛܗܐ ܕܤܓܝܐܐ ܕܬܪܬܝܢ ܕܝܢ ܙܒܢܝܢ ܕܠܐ ܚܛܗܝܢ ܡܬܚܙܐ ܠܚܝܝܗܘܢ ܕܐܝܠܝܢ ܕܡܤܟܝܢ ܠܗ ܀
28 noonu it la Kirist joxee boppam benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina feeñaat, waxuma ci mbiri bàkkaar, waaye ngir indil ñi koy séentu mucc gi.