1ܒܪܫܝܬ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܠܬܐ ܘܗܘ ܡܠܬܐ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܘܐܠܗܐ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܗܘ ܡܠܬܐ ܀
1 Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
2ܗܢܐ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܒܪܫܝܬ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܀
2 Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga.
3ܟܠ ܒܐܝܕܗ ܗܘܐ ܘܒܠܥܕܘܗܝ ܐܦܠܐ ܚܕܐ ܗܘܬ ܡܕܡ ܕܗܘܐ ܀
3 Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom.
4ܒܗ ܚܝܐ ܗܘܐ ܘܚܝܐ ܐܝܬܝܗܘܢ ܢܘܗܪܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܀
4 Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.
5ܘܗܘ ܢܘܗܪܐ ܒܚܫܘܟܐ ܡܢܗܪ ܘܚܫܘܟܐ ܠܐ ܐܕܪܟܗ ܀
5 Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.
6ܗܘܐ ܒܪܢܫܐ ܕܐܫܬܕܪ ܡܢ ܐܠܗܐ ܫܡܗ ܝܘܚܢܢ ܀
6 Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya.
7ܗܢܐ ܐܬܐ ܠܤܗܕܘܬܐ ܕܢܤܗܕ ܥܠ ܢܘܗܪܐ ܕܟܠܢܫ ܢܗܝܡܢ ܒܐܝܕܗ ܀
7 Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm.
8ܠܐ ܗܘ ܗܘܐ ܢܘܗܪܐ ܐܠܐ ܕܢܤܗܕ ܥܠ ܢܘܗܪܐ ܀
8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.
9ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܓܝܪ ܢܘܗܪܐ ܕܫܪܪܐ ܕܡܢܗܪ ܠܟܠܢܫ ܕܐܬܐ ܠܥܠܡܐ ܀
9 Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.
10ܒܥܠܡܐ ܗܘܐ ܘܥܠܡܐ ܒܐܝܕܗ ܗܘܐ ܘܥܠܡܐ ܠܐ ܝܕܥܗ ܀
10 Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko.
11ܠܕܝܠܗ ܐܬܐ ܘܕܝܠܗ ܠܐ ܩܒܠܘܗܝ ܀
11 Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.
12ܐܝܠܝܢ ܕܝܢ ܕܩܒܠܘܗܝ ܝܗܒ ܠܗܘܢ ܫܘܠܛܢܐ ܕܒܢܝܐ ܕܐܠܗܐ ܢܗܘܘܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܗܝܡܢܝܢ ܒܫܡܗ ܀
12 Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.
13ܐܝܠܝܢ ܕܠܘ ܡܢ ܕܡܐ ܘܠܐ ܡܢ ܨܒܝܢܐ ܕܒܤܪܐ ܘܠܐ ܡܢ ܨܒܝܢܐ ܕܓܒܪܐ ܐܠܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܬܝܠܕܘ ܀
13 Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.
14ܘܡܠܬܐ ܒܤܪܐ ܗܘܐ ܘܐܓܢ ܒܢ ܘܚܙܝܢ ܫܘܒܚܗ ܫܘܒܚܐ ܐܝܟ ܕܝܚܝܕܝܐ ܕܡܢ ܐܒܐ ܕܡܠܐ ܛܝܒܘܬܐ ܘܩܘܫܬܐ ܀
14 Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
15ܝܘܚܢܢ ܤܗܕ ܥܠܘܗܝ ܘܩܥܐ ܘܐܡܪ ܗܢܘ ܗܘ ܕܐܡܪܬ ܕܒܬܪܝ ܐܬܐ ܘܗܘܐ ܠܗ ܩܕܡܝ ܡܛܠ ܕܩܕܡܝ ܗܘ ܡܢܝ ܀
15 Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
16ܘܡܢ ܡܠܝܘܬܗ ܚܢܢ ܟܠܢ ܢܤܒܢ ܘܛܝܒܘܬܐ ܚܠܦ ܛܝܒܘܬܐ ܀
16 Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni-yoon.
17ܡܛܠ ܕܢܡܘܤܐ ܒܝܕ ܡܘܫܐ ܐܬܝܗܒ ܫܪܪܐ ܕܝܢ ܘܛܝܒܘܬܐ ܒܝܕ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܗܘܐ ܀
17 Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.
18ܐܠܗܐ ܠܐ ܚܙܐ ܐܢܫ ܡܡܬܘܡ ܝܚܝܕܝܐ ܐܠܗܐ ܗܘ ܕܐܝܬܘܗܝ ܒܥܘܒܐ ܕܐܒܘܗܝ ܗܘ ܐܫܬܥܝ ܀
18 Kenn musul a gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.
19ܘܗܕܐ ܗܝ ܤܗܕܘܬܗ ܕܝܘܚܢܢ ܟܕ ܫܕܪܘ ܠܘܬܗ ܝܗܘܕܝܐ ܡܢ ܐܘܪܫܠܡ ܟܗܢܐ ܘܠܘܝܐ ܕܢܫܐܠܘܢܝܗܝ ܐܢܬ ܡܢ ܐܢܬ ܀
19 Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay saraxalekat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan.
20ܘܐܘܕܝ ܘܠܐ ܟܦܪ ܘܐܘܕܝ ܕܠܘ ܐܢܐ ܐܢܐ ܡܫܝܚܐ ܀
20 Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne, moom du Almasi bi.
21ܘܫܐܠܘܗܝ ܬܘܒ ܡܢܐ ܗܟܝܠ ܐܠܝܐ ܐܢܬ ܘܐܡܪ ܠܐ ܐܝܬܝ ܢܒܝܐ ܐܢܬ ܘܐܡܪ ܠܐ ܀
21 Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Iliyas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Iliyas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi war a ñëw?» Mu tontu ne leen: «Déedéet.»
22ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܘܡܢܘ ܐܢܬ ܕܢܬܠ ܦܬܓܡܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܫܕܪܘܢ ܡܢܐ ܐܡܪ ܐܢܬ ܥܠ ܢܦܫܟ ܀
22 Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu man a tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»
23ܐܡܪ ܐܢܐ ܩܠܐ ܕܩܪܐ ܒܡܕܒܪܐ ܕܐܫܘܘ ܐܘܪܚܗ ܕܡܪܝܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܡܪ ܐܫܥܝܐ ܢܒܝܐ ܀
23 Yaxya tontu leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
24ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܕܐܫܬܕܪܘ ܡܢ ܦܪܝܫܐ ܗܘܘ ܀
24 Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya.
25ܘܫܐܠܘܗܝ ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܡܢܐ ܗܟܝܠ ܡܥܡܕ ܐܢܬ ܐܢ ܐܢܬ ܠܐ ܐܝܬܝܟ ܡܫܝܚܐ ܘܠܐ ܐܠܝܐ ܘܠܐ ܢܒܝܐ ܀
25 Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Iliyas, doo Yonent bi war a ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?»
26ܥܢܐ ܝܘܚܢܢ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܢܐ ܡܥܡܕ ܐܢܐ ܒܡܝܐ ܒܝܢܬܟܘܢ ܕܝܢ ܩܐܡ ܗܘ ܕܐܢܬܘܢ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܀
26 Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.
27ܗܢܘ ܗܘ ܕܒܬܪܝ ܐܬܐ ܘܗܘܐ ܠܗ ܩܕܡܝ ܗܘ ܕܐܢܐ ܠܐ ܫܘܐ ܐܢܐ ܕܐܫܪܐ ܥܪܩܐ ܕܡܤܢܘܗܝ ܀
27 Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»
28ܗܠܝܢ ܒܒܝܬ ܥܢܝܐ ܗܘܝ ܒܥܒܪܐ ܕܝܘܪܕܢܢ ܐܝܟܐ ܕܡܥܡܕ ܗܘܐ ܝܘܚܢܢ ܀
28 Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
29ܘܠܝܘܡܐ ܕܒܬܪܗ ܚܙܐ ܝܘܚܢܢ ܠܝܫܘܥ ܕܐܬܐ ܠܘܬܗ ܘܐܡܪ ܗܐ ܐܡܪܗ ܕܐܠܗܐ ܗܘ ܕܫܩܠ ܚܛܝܬܗ ܕܥܠܡܐ ܀
29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy mbotem Yàlla, mi ñu nar a rey, ngir dindi bàkkaaru àddina.
30ܗܢܘ ܕܐܢܐ ܐܡܪܬ ܥܠܘܗܝ ܕܒܬܪܝ ܐܬܐ ܓܒܪܐ ܘܗܘܐ ܠܗ ܩܕܡܝ ܡܛܠ ܕܩܕܡܝ ܗܘ ܡܢܝ ܀
30 Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”
31ܘܐܢܐ ܠܐ ܝܕܥ ܗܘܝܬ ܠܗ ܐܠܐ ܕܢܬܝܕܥ ܠܐܝܤܪܝܠ ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܬܝܬ ܐܢܐ ܕܒܡܝܐ ܐܥܡܕ ܀
31 Xawma woon kooku kan la waroon a doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32ܘܐܤܗܕ ܝܘܚܢܢ ܘܐܡܪ ܕܚܙܝܬ ܠܪܘܚܐ ܕܢܚܬܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܐܝܟ ܝܘܢܐ ܘܩܘܝܬ ܥܠܘܗܝ ܀
32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.
33ܘܐܢܐ ܠܐ ܝܕܥ ܗܘܝܬ ܠܗ ܐܠܐ ܡܢ ܕܫܕܪܢܝ ܕܐܥܡܕ ܒܡܝܐ ܗܘ ܐܡܪ ܠܝ ܕܐܝܢܐ ܕܚܙܐ ܐܢܬ ܕܢܚܬܐ ܪܘܚܐ ܘܡܩܘܝܐ ܥܠܘܗܝ ܗܢܘ ܡܥܡܕ ܒܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܀
33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
34ܘܐܢܐ ܚܙܝܬ ܘܐܤܗܕܬ ܕܗܢܘ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܀
34 Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne, moom moo di Doomu Yàlla ji.»
35ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܩܐܡ ܗܘܐ ܝܘܚܢܢ ܘܬܪܝܢ ܡܢ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.
36ܘܚܪ ܒܝܫܘܥ ܟܕ ܡܗܠܟ ܘܐܡܪ ܗܐ ܐܡܪܗ ܕܐܠܗܐ ܀
36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy mbotem Yàlla mi!»
37ܘܫܡܥܘ ܬܪܝܗܘܢ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܟܕ ܐܡܪ ܘܐܙܠܘ ܠܗܘܢ ܒܬܪܗ ܕܝܫܘܥ ܀
37 Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.
38ܘܐܬܦܢܝ ܝܫܘܥ ܘܚܙܐ ܐܢܘܢ ܕܐܬܝܢ ܒܬܪܗ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܢܐ ܒܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܪܒܢ ܐܝܟܐ ܗܘܐ ܐܢܬ ܀
38 Yeesu geestu, gis ne, ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu tontu ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi.»
39ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܬܘ ܘܬܚܙܘܢ ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܐܬܘ ܘܚܙܘ ܐܝܟܐ ܕܗܘܐ ܘܠܘܬܗ ܗܘܘ ܝܘܡܐ ܗܘ ܘܐܝܬ ܗܘܝ ܐܝܟ ܫܥܐ ܥܤܪ ܀
39 Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.
40ܚܕ ܕܝܢ ܡܢ ܗܢܘܢ ܕܫܡܥܘ ܡܢ ܝܘܚܢܢ ܘܐܙܠܘ ܒܬܪܗ ܕܝܫܘܥ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܐܢܕܪܐܘܤ ܐܚܘܗܝ ܕܫܡܥܘܢ ܀
40 Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.
41ܗܢܐ ܚܙܐ ܠܘܩܕܡ ܠܫܡܥܘܢ ܐܚܘܗܝ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܫܟܚܢܝܗܝ ܠܡܫܝܚܐ ܀
41 Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist.»
42ܘܐܝܬܝܗ ܠܘܬ ܝܫܘܥ ܘܚܪ ܒܗ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܐܢܬ ܗܘ ܫܡܥܘܢ ܒܪܗ ܕܝܘܢܐ ܐܢܬ ܬܬܩܪܐ ܟܐܦܐ ܀
42 Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer,» maanaam «xeer.»
43ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܨܒܐ ܝܫܘܥ ܠܡܦܩ ܠܓܠܝܠܐ ܘܐܫܟܚ ܠܦܝܠܝܦܘܤ ܘܐܡܪ ܠܗ ܬܐ ܒܬܪܝ ܀
43 Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»
44ܗܘ ܕܝܢ ܦܝܠܝܦܘܤ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܢ ܒܝܬ ܨܝܕܐ ܡܢ ܡܕܝܢܬܗ ܕܐܢܕܪܐܘܤ ܘܕܫܡܥܘܢ ܀
44 Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer.
45ܘܦܝܠܝܦܘܤ ܐܫܟܚ ܠܢܬܢܝܐܝܠ ܘܐܡܪ ܠܗ ܗܘ ܕܟܬܒ ܥܠܘܗܝ ܡܘܫܐ ܒܢܡܘܤܐ ܘܒܢܒܝܐ ܐܫܟܚܢܝܗܝ ܕܝܫܘܥ ܗܘ ܒܪ ܝܘܤܦ ܡܢ ܢܨܪܬ ܀
45 Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.»
46ܐܡܪ ܠܗ ܢܬܢܝܐܝܠ ܡܢ ܢܨܪܬ ܡܫܟܚ ܡܕܡ ܕܛܒ ܢܗܘܐ ܐܡܪ ܠܗ ܦܝܠܝܦܘܤ ܬܐ ܘܬܚܙܐ ܀
46 Nataneel tontu ko ne: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
47ܘܚܙܝܗܝ ܝܫܘܥ ܠܢܬܢܝܐܝܠ ܟܕ ܐܬܐ ܠܘܬܗ ܘܐܡܪ ܥܠܘܗܝ ܗܐ ܫܪܝܪܐܝܬ ܒܪ ܐܝܤܪܝܠ ܕܢܟܠܐ ܠܝܬ ܒܗ ܀
47 Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.»
48ܐܡܪ ܠܗ ܢܬܢܝܐܝܠ ܡܢ ܐܝܡܟܐ ܝܕܥ ܐܢܬ ܠܝ ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܥܕܠܐ ܢܩܪܝܟ ܦܝܠܝܦܘܤ ܟܕ ܬܚܝܬ ܬܬܐ ܐܢܬ ܚܙܝܬܟ ܀
48 Nataneel ne ko: «Noo ma xame?» Yeesu tontu ko ne: «Bi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.»
49ܥܢܐ ܢܬܢܝܐܝܠ ܘܐܡܪ ܠܗ ܪܒܝ ܐܢܬ ܗܘ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܐܢܬ ܗܘ ܡܠܟܗ ܕܐܝܤܪܝܠ ܀
49 Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!»
50ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܥܠ ܕܐܡܪܬ ܠܟ ܕܚܙܝܬܟ ܬܚܝܬ ܬܬܐ ܡܗܝܡܢ ܐܢܬ ܕܪܘܪܒܢ ܡܢ ܗܠܝܢ ܬܚܙܐ ܀
50 Yeesu tontu ko ne: «Ndax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga gëm? Dinga gis mbir yu gën a réy yii.»
51ܐܡܪ ܠܗ ܐܡܝܢ ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܡܢ ܗܫܐ ܬܚܙܘܢ ܫܡܝܐ ܕܦܬܝܚܝܢ ܘܡܠܐܟܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܟܕ ܤܠܩܝܢ ܘܢܚܬܝܢ ܠܘܬ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܀
51 Noonu mu teg ca ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di wàcc ci Doomu nit ki.»