1ܘܠܝܘܡܐ ܕܬܠܬܐ ܗܘܬ ܡܫܬܘܬܐ ܒܩܛܢܐ ܡܕܝܢܬܐ ܕܓܠܝܠܐ ܘܐܡܗ ܕܝܫܘܥ ܬܡܢ ܗܘܬ ܀
1 Ñaari fan gannaaw loolu ag céet am ca dëkku Kana ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu teewe woon na ko.
2ܘܐܦ ܗܘ ܝܫܘܥ ܘܬܠܡܝܕܘܗܝ ܐܬܩܪܝܘ ܠܗ ܠܡܫܬܘܬܐ ܀
2 Woo woon nañu it Yeesu ca céet ga ak ay taalibeem.
3ܘܚܤܪ ܗܘܐ ܚܡܪܐ ܘܐܡܪܐ ܠܗ ܐܡܗ ܠܝܫܘܥ ܚܡܪܐ ܠܝܬ ܠܗܘܢ ܀
3 Ca biir xew wa, biiñ ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne ko: «Amatuñu biiñ.»
4ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܡܐ ܠܝ ܘܠܟܝ ܐܢܬܬܐ ܠܐ ܥܕܟܝܠ ܐܬܬ ܫܥܬܝ ܀
4 Yeesu ne: «Soxna si, Loo ma bëggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.»
5ܐܡܪܐ ܐܡܗ ܠܡܫܡܫܢܐ ܡܕܡ ܕܐܡܪ ܠܟܘܢ ܥܒܕܘ ܀
5 Yaayam daldi ne surga ya: «Defleen lépp lu mu leen wax.»
6ܐܝܬ ܗܘܝ ܕܝܢ ܬܡܢ ܐܓܢܐ ܕܟܐܦܐ ܫܬ ܕܤܝܡܢ ܠܬܕܟܝܬܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܕܐܚܕܢ ܬܪܝܢ ܬܪܝܢ ܪܒܥܝܢ ܐܘ ܬܠܬܐ ܀
6 Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu Yawut ya daan jëfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka téeméeri liitar.
7ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܡܠܘ ܐܢܝܢ ܡܝܐ ܠܐܓܢܐ ܘܡܠܘ ܐܢܝܢ ܥܕܡܐ ܠܥܠ ܀
7 Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi.» Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat.
8ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܙܠܘܥܘ ܡܟܝܠ ܘܐܝܬܘ ܠܪܝܫ ܤܡܟܐ ܘܐܝܬܝܘ ܀
8 Noonu Yeesu ne leen: «Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.» Ñu daldi ko ciy yót.
9ܘܟܕ ܛܥܡ ܗܘ ܪܝܫ ܤܡܟܐ ܡܝܐ ܗܢܘܢ ܕܗܘܘ ܚܡܪܐ ܘܠܐ ܝܕܥ ܗܘܐ ܡܢ ܐܝܡܟܐ ܗܘܐ ܡܫܡܫܢܐ ܕܝܢ ܝܕܥܝܢ ܗܘܘ ܕܗܢܘܢ ܡܠܘ ܐܢܘܢ ܠܡܝܐ ܩܪܐ ܪܝܫ ܤܡܟܐ ܠܚܬܢܐ ܀
9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko:
10ܘܐܡܪ ܠܗ ܟܠ ܐܢܫ ܠܘܩܕܡ ܚܡܪܐ ܛܒܐ ܡܝܬܐ ܘܡܐ ܕܪܘܝܘ ܗܝܕܝܢ ܐܝܢܐ ܕܒܨܝܪ ܐܢܬ ܕܝܢ ܢܛܪܬܝܗܝ ܠܚܡܪܐ ܛܒܐ ܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܀
10 «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sog a génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gën a neex ba nëgëni.»
11ܗܕܐ ܗܝ ܐܬܐ ܩܕܡܝܬܐ ܕܥܒܕ ܝܫܘܥ ܒܩܛܢܐ ܕܓܠܝܠܐ ܘܐܘܕܥ ܫܘܒܚܗ ܘܗܝܡܢܘ ܒܗ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
11 Firnde bii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkk a def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12ܒܬܪ ܗܕܐ ܢܚܬ ܠܟܦܪܢܚܘܡ ܗܘ ܘܐܡܗ ܘܐܚܘܗܝ ܘܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܬܡܢ ܗܘܘ ܩܠܝܠ ܝܘܡܬܐ ܀
12 Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
13ܘܩܪܝܒ ܗܘܐ ܦܨܚܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܘܤܠܩ ܠܐܘܪܫܠܡ ܝܫܘܥ ܀
13 Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Jéggi ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,
14ܘܐܫܟܚ ܒܗܝܟܠܐ ܠܗܠܝܢ ܕܡܙܒܢܝܢ ܬܘܪܐ ܘܥܪܒܐ ܘܝܘܢܐ ܘܠܡܥܪܦܢܐ ܕܝܬܒܝܢ ܀
14 dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog.
15ܘܥܒܕ ܠܗ ܦܪܓܠܐ ܡܢ ܚܒܠܐ ܘܠܟܠܗܘܢ ܐܦܩ ܡܢ ܗܝܟܠܐ ܘܠܥܪܒܐ ܘܠܬܘܪܐ ܘܠܡܥܪܦܢܐ ܘܐܫܕ ܥܘܪܦܢܗܘܢ ܘܦܬܘܪܝܗܘܢ ܗܦܟ ܀
15 Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu kër Yàlla ga, ñoom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya,
16ܘܠܗܢܘܢ ܕܡܙܒܢܝܢ ܝܘܢܐ ܐܡܪ ܫܩܘܠܘ ܗܠܝܢ ܡܟܐ ܘܠܐ ܬܥܒܕܘܢܗ ܠܒܝܬܗ ܕܐܒܝ ܒܝܬ ܬܐܓܘܪܬܐ ܀
16 daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!»
17ܘܐܬܕܟܪܘ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܟܬܝܒ ܕܛܢܢܗ ܕܒܝܬܟ ܐܟܠܢܝ ܀
17 Taalibeem ya fàttaliku Mbind mii: «Cawarte gi ma am ci sa kër, mu ngi mel ni taal buy tàkk ci sama biir.»
18ܥܢܘ ܕܝܢ ܝܗܘܕܝܐ ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܡܢܐ ܐܬܐ ܡܚܘܐ ܐܢܬ ܠܢ ܕܗܠܝܢ ܥܒܕ ܐܢܬ ܀
18 Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne, am nga sañ-sañu def lii nga def?»
19ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܤܬܘܪܘ ܗܝܟܠܐ ܗܢܐ ܘܠܬܠܬܐ ܝܘܡܝܢ ܐܢܐ ܡܩܝܡ ܐܢܐ ܠܗ ܀
19 Yeesu tontu leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.»
20ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܝܗܘܕܝܐ ܠܐܪܒܥܝܢ ܘܫܬ ܫܢܝܢ ܐܬܒܢܝ ܗܝܟܠܐ ܗܢܐ ܘܐܢܬ ܠܬܠܬܐ ܝܘܡܝܢ ܡܩܝܡ ܐܢܬ ܠܗ ܀
20 Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent-fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!»
21ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܗܘܐ ܥܠ ܗܝܟܠܐ ܕܦܓܪܗ ܀
21 Waaye kër Yàlla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax.
22ܟܕ ܩܡ ܕܝܢ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܐܬܕܟܪܘ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܗܕܐ ܐܡܪ ܗܘܐ ܘܗܝܡܢܘ ܠܟܬܒܐ ܘܠܡܠܬܐ ܕܐܡܪ ܝܫܘܥ ܀
22 Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.
23ܟܕ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܒܐܘܪܫܠܡ ܒܦܨܚܐ ܒܥܕܥܕܐ ܤܓܝܐܐ ܗܝܡܢܘ ܒܗ ܕܚܙܘ ܐܬܘܬܐ ܕܥܒܕ ܀
23 Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci màggalu bésu Jéggi ba, ñu bare gis kéemaan, yi mu doon def, daldi gëm ci turam.
24ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܠܐ ܡܗܝܡܢ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܢܦܫܗ ܡܛܠ ܕܗܘ ܝܕܥ ܗܘܐ ܠܟܠܢܫ ܀
24 Waaye Yeesu wóoluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen ñoom ñépp,
25ܘܠܐ ܤܢܝܩ ܗܘܐ ܕܐܢܫ ܢܤܗܕ ܠܗ ܥܠ ܟܠ ܒܪܢܫ ܗܘ ܓܝܪ ܝܕܥ ܗܘܐ ܡܢܐ ܐܝܬ ܒܒܪܢܫܐ ܀
25 te it soxlawul ñu koy xamal dara ci nit, ndaxte moom ci boppam xam na xolu nit.