1ܡܛܠ ܕܤܓܝܐܐ ܨܒܘ ܕܢܟܬܒܘܢ ܬܫܥܝܬܐ ܕܤܘܥܪܢܐ ܐܝܠܝܢ ܕܚܢܢ ܡܦܤܝܢ ܚܢܢ ܒܗܘܢ ܀
1 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,
2ܐܝܟ ܡܕܡ ܕܐܫܠܡܘ ܠܢ ܗܢܘܢ ܕܡܢ ܩܕܝܡ ܗܘܘ ܚܙܝܐ ܘܡܫܡܫܢܐ ܕܝܠܗ ܕܡܠܬܐ ܀
2 li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.
3ܐܬܚܙܝ ܐܦ ܠܝ ܡܛܠ ܕܩܪܝܒ ܗܘܝܬ ܝܨܝܦܐܝܬ ܠܟܠܗܘܢ ܕܟܠ ܡܕܡ ܒܛܟܤܗ ܐܟܬܘܒ ܠܟ ܢܨܝܚܐ ܬܐܘܦܝܠܐ ܀
3 Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.
4ܕܬܕܥ ܫܪܪܐ ܕܡܠܐ ܕܐܬܬܠܡܕܬ ܠܗܝܢ ܀
4 Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la.
5ܗܘܐ ܒܝܘܡܬܗ ܕܗܪܘܕܤ ܡܠܟܐ ܕܝܗܘܕܐ ܟܗܢܐ ܚܕ ܕܫܡܗ ܗܘܐ ܙܟܪܝܐ ܡܢ ܬܫܡܫܬܐ ܕܒܝܬ ܐܒܝܐ ܘܐܢܬܬܗ ܡܢ ܒܢܬܗ ܕܐܗܪܘܢ ܫܡܗ ܗܘܐ ܐܠܝܫܒܥ ܀
5 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona.
6ܬܪܝܗܘܢ ܕܝܢ ܙܕܝܩܝܢ ܗܘܘ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܘܡܗܠܟܝܢ ܒܟܠܗܘܢ ܦܘܩܕܢܘܗܝ ܘܒܟܐܢܘܬܗ ܕܡܪܝܐ ܕܠܐ ܥܕܠܝ ܀
6 Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.
7ܒܪܐ ܕܝܢ ܠܝܬ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܡܛܠ ܕܐܠܝܫܒܥ ܥܩܪܬܐ ܗܘܬ ܘܬܪܝܗܘܢ ܤܓܝܐܝ ܒܝܘܡܬܗܘܢ ܗܘܘ ܀
7 Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
8ܗܘܐ ܗܘܐ ܕܝܢ ܟܕ ܡܟܗܢ ܗܘܐ ܒܛܟܤܐ ܕܬܫܡܫܬܗ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܀
8 Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
9ܒܥܝܕܐ ܕܟܗܢܘܬܐ ܡܛܝܗܝ ܕܢܤܝܡ ܒܤܡܐ ܘܥܠ ܠܗܝܟܠܗ ܕܡܪܝܐ ܀
9 Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya.
10ܘܟܠܗ ܟܢܫܐ ܕܥܡܐ ܡܨܠܐ ܗܘܐ ܠܒܪ ܒܥܕܢܐ ܕܒܤܡܐ ܀
10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
11ܘܐܬܚܙܝ ܠܗ ܠܙܟܪܝܐ ܡܠܐܟܐ ܕܡܪܝܐ ܕܩܐܡ ܡܢ ܝܡܝܢܐ ܕܡܕܒܚܐ ܕܒܤܡܐ ܀
11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
12ܘܐܫܬܓܫ ܙܟܪܝܐ ܟܕ ܚܙܝܗܝ ܘܕܚܠܬܐ ܢܦܠܬ ܥܠܘܗܝ ܀
12 Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit.
13ܘܐܡܪ ܠܗ ܡܠܐܟܐ ܠܐ ܬܕܚܠ ܙܟܪܝܐ ܡܛܠ ܕܐܫܬܡܥܬ ܨܠܘܬܟ ܘܐܢܬܬܟ ܐܠܝܫܒܥ ܬܐܠܕ ܠܟ ܒܪܐ ܘܬܩܪܐ ܫܡܗ ܝܘܚܢܢ ܀
13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
14ܘܬܗܘܐ ܠܟ ܚܕܘܬܐ ܘܐܪܘܙܐ ܘܤܓܝܐܐ ܢܚܕܘܢ ܒܡܘܠܕܗ ܀
14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
15ܢܗܘܐ ܓܝܪ ܪܒ ܩܕܡ ܡܪܝܐ ܘܚܡܪܐ ܘܫܟܪܐ ܠܐ ܢܫܬܐ ܘܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܢܬܡܠܐ ܥܕ ܗܘ ܒܟܪܤܐ ܕܐܡܗ ܀
15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
16ܘܤܓܝܐܐ ܡܢ ܒܢܝ ܐܝܤܪܝܠ ܢܦܢܐ ܠܘܬ ܡܪܝܐ ܐܠܗܗܘܢ ܀
16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
17ܘܗܘ ܢܐܙܠ ܩܕܡܘܗܝ ܒܪܘܚܐ ܘܒܚܝܠܐ ܕܐܠܝܐ ܢܒܝܐ ܕܢܦܢܐ ܠܒܐ ܕܐܒܗܐ ܥܠ ܒܢܝܐ ܘܠܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܡܬܛܦܝܤܝܢ ܠܝܕܥܬܐ ܕܟܐܢܐ ܘܢܛܝܒ ܠܡܪܝܐ ܥܡܐ ܓܡܝܪܐ ܀
17 Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18ܘܐܡܪ ܙܟܪܝܐ ܠܡܠܐܟܐ ܐܝܟܢܐ ܐܕܥ ܗܕܐ ܐܢܐ ܓܝܪ ܐܝܬܝ ܤܒܐ ܘܐܢܬܬܝ ܤܓܝܐܬ ܒܝܘܡܬܗ ܗܝ ܀
18 Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.»
19ܘܥܢܐ ܡܠܐܟܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܢܐ ܐܢܐ ܓܒܪܝܐܝܠ ܕܩܐܡ ܐܢܐ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܘܐܫܬܠܚܬ ܕܐܡܠܠ ܥܡܟ ܘܐܤܒܪܟ ܗܠܝܢ ܀
19 Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu.
20ܡܟܝܠ ܬܗܘܐ ܫܬܝܩ ܘܠܐ ܬܫܟܚ ܠܡܡܠܠܘ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܐ ܕܗܠܝܢ ܢܗܘܝܢ ܥܠ ܕܠܐ ܗܝܡܢܬ ܠܡܠܝ ܗܠܝܢ ܕܡܬܡܠܝܢ ܒܙܒܢܗܝܢ ܀
20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21ܥܡܐ ܕܝܢ ܩܐܡ ܗܘܐ ܘܡܤܟܐ ܠܙܟܪܝܐ ܘܬܡܝܗܝܢ ܗܘܘ ܥܠ ܬܘܚܪܬܗ ܕܒܗܝܟܠܐ ܀
21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba.
22ܟܕ ܢܦܩ ܕܝܢ ܙܟܪܝܐ ܠܐ ܡܫܟܚ ܗܘܐ ܕܢܡܠܠ ܥܡܗܘܢ ܘܐܤܬܟܠܘ ܕܚܙܘܐ ܚܙܐ ܒܗܝܟܠܐ ܘܗܘ ܡܪܡܙ ܪܡܙ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܘܩܘܝ ܟܕ ܚܪܫ ܀
22 Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23ܘܟܕ ܐܬܡܠܝܘ ܝܘܡܬܐ ܕܬܫܡܫܬܗ ܐܙܠ ܠܒܝܬܗ ܀
23 Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
24ܘܗܘܐ ܡܢ ܒܬܪ ܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܒܛܢܬ ܐܠܝܫܒܥ ܐܢܬܬܗ ܘܡܛܫܝܐ ܗܘܬ ܢܦܫܗ ܝܪܚܐ ܚܡܫܐ ܘܐܡܪܐ ܗܘܬ ܀
24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
25ܕܗܠܝܢ ܥܒܕ ܠܝ ܡܪܝܐ ܒܝܘܡܬܐ ܕܚܪ ܒܝ ܠܡܤܒ ܚܤܕܝ ܕܒܝܬ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܀
25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
26ܒܝܪܚܐ ܕܝܢ ܕܫܬܐ ܐܫܬܠܚ ܓܒܪܝܐܝܠ ܡܠܐܟܐ ܡܢ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܠܓܠܝܠܐ ܠܡܕܝܢܬܐ ܕܫܡܗ ܢܨܪܬ ܀
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
27ܠܘܬ ܒܬܘܠܬܐ ܕܡܟܝܪܐ ܠܓܒܪܐ ܕܫܡܗ ܝܘܤܦ ܡܢ ܒܝܬܗ ܕܕܘܝܕ ܘܫܡܗ ܠܒܬܘܠܬܐ ܡܪܝܡ ܀
27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
28ܘܥܠ ܠܘܬܗ ܡܠܐܟܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܫܠܡ ܠܟܝ ܡܠܝܬ ܛܝܒܘܬܐ ܡܪܢ ܥܡܟܝ ܒܪܝܟܬ ܒܢܫܐ ܀
28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29ܗܝ ܕܝܢ ܟܕ ܚܙܬ ܐܬܪܗܒܬ ܒܡܠܬܗ ܘܡܬܚܫܒܐ ܗܘܬ ܕܡܢܐ ܗܘ ܫܠܡܐ ܗܢܐ ܀
29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki.
30ܘܐܡܪ ܠܗ ܡܠܐܟܐ ܠܐ ܬܕܚܠܝܢ ܡܪܝܡ ܐܫܟܚܬܝ ܓܝܪ ܛܝܒܘܬܐ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܀
30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
31ܗܐ ܓܝܪ ܬܩܒܠܝܢ ܒܛܢܐ ܘܬܐܠܕܝܢ ܒܪܐ ܘܬܩܪܝܢ ܫܡܗ ܝܫܘܥ ܀
31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32ܗܢܐ ܢܗܘܐ ܪܒ ܘܒܪܗ ܕܥܠܝܐ ܢܬܩܪܐ ܘܢܬܠ ܠܗ ܡܪܝܐ ܐܠܗܐ ܟܘܪܤܝܗ ܕܕܘܝܕ ܐܒܘܗܝ ܀
32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
33ܘܢܡܠܟ ܥܠ ܒܝܬܗ ܕܝܥܩܘܒ ܠܥܠܡ ܘܠܡܠܟܘܬܗ ܤܘܦ ܠܐ ܢܗܘܐ ܀
33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34ܐܡܪܐ ܡܪܝܡ ܠܡܠܐܟܐ ܐܝܟܢܐ ܬܗܘܐ ܗܕܐ ܕܓܒܪܐ ܠܐ ܚܟܝܡ ܠܝ ܀
34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.»
35ܥܢܐ ܡܠܐܟܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܬܐܬܐ ܘܚܝܠܗ ܕܥܠܝܐ ܢܓܢ ܥܠܝܟܝ ܡܛܠ ܗܢܐ ܗܘ ܕܡܬܝܠܕ ܒܟܝ ܩܕܝܫܐ ܗܘ ܘܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܢܬܩܪܐ ܀
35 Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
36ܘܗܐ ܐܠܝܫܒܥ ܐܚܝܢܬܟܝ ܐܦ ܗܝ ܒܛܢܐ ܒܪܐ ܒܤܝܒܘܬܗ ܘܗܢܐ ܝܪܚܐ ܕܫܬܐ ܠܗ ܠܗܝ ܕܡܬܩܪܝܐ ܥܩܪܬܐ ܀
36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram.
37ܡܛܠ ܕܠܐ ܥܛܠ ܠܐܠܗܐ ܡܕܡ ܀
37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38ܐܡܪܐ ܡܪܝܡ ܗܐ ܐܢܐ ܐܡܬܗ ܕܡܪܝܐ ܢܗܘܐ ܠܝ ܐܝܟ ܡܠܬܟ ܘܐܙܠ ܡܠܐܟܐ ܡܢ ܠܘܬܗ ܀
38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
39ܩܡܬ ܕܝܢ ܡܪܝܡ ܒܗܘܢ ܒܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܘܐܙܠܬ ܒܛܝܠܐܝܬ ܠܛܘܪܐ ܠܡܕܝܢܬܐ ܕܝܗܘܕ ܀
39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
40ܘܥܠܬ ܠܒܝܬܗ ܕܙܟܪܝܐ ܘܫܐܠܬ ܫܠܡܗ ܕܐܠܝܫܒܥ ܀
40 Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet.
41ܘܗܘܐ ܕܟܕ ܫܡܥܬ ܐܠܝܫܒܥ ܫܠܡܗ ܕܡܪܝܡ ܕܨ ܥܘܠܐ ܒܟܪܤܗ ܘܐܬܡܠܝܬ ܐܠܝܫܒܥ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܀
41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
42ܘܩܥܬ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܘܐܡܪܬ ܠܡܪܝܡ ܡܒܪܟܬܐ ܐܢܬܝ ܒܢܫܐ ܘܡܒܪܟ ܗܘ ܦܐܪܐ ܕܒܟܪܤܟܝ ܀
42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43ܐܝܡܟܐ ܠܝ ܗܕܐ ܕܐܡܗ ܕܡܪܝ ܬܐܬܐ ܠܘܬܝ ܀
43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
44ܗܐ ܓܝܪ ܟܕ ܢܦܠ ܩܠܐ ܕܫܠܡܟܝ ܒܐܕܢܝ ܒܚܕܘܬܐ ܪܒܬܐ ܕܨ ܥܘܠܐ ܒܟܪܤܝ ܀
44 Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég.
45ܘܛܘܒܝܗ ܠܐܝܕܐ ܕܗܝܡܢܬ ܕܗܘܐ ܫܘܠܡܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܐܬܡܠܠ ܥܡܗ ܡܢ ܠܘܬ ܡܪܝܐ ܀
45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!»
46ܘܐܡܪܬ ܡܪܝܡ ܡܘܪܒܐ ܢܦܫܝ ܠܡܪܝܐ ܀
46 Noonu Maryaama daldi ne:
47ܘܚܕܝܬ ܪܘܚܝ ܒܐܠܗܐ ܡܚܝܢܝ ܀
47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48ܕܚܪ ܒܡܘܟܟܐ ܕܐܡܬܗ ܗܐ ܓܝܪ ܡܢ ܗܫܐ ܛܘܒܐ ܢܬܠܢ ܠܝ ܫܪܒܬܐ ܟܠܗܝܢ ܀
48 ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49ܕܥܒܕ ܠܘܬܝ ܪܘܪܒܬܐ ܗܘ ܕܚܝܠܬܢ ܘܩܕܝܫ ܫܡܗ ܀
49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell.
50ܘܚܢܢܗ ܠܕܪܐ ܘܫܪܒܬܐ ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܕܚܠܝܢ ܠܗ ܀
50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51ܥܒܕ ܙܟܘܬܐ ܒܕܪܥܗ ܘܒܕܪ ܚܬܝܪܝ ܒܬܪܥܝܬܐ ܕܠܒܗܘܢ ܀
51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52ܤܚܦ ܬܩܝܦܐ ܡܢ ܟܘܪܤܘܬܐ ܘܐܪܝܡ ܡܟܝܟܐ ܀
52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi.
53ܟܦܢܐ ܤܒܥ ܛܒܬܐ ܘܥܬܝܪܐ ܫܪܐ ܤܦܝܩܐܝܬ ܀
53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen.
54ܥܕܪ ܠܐܝܤܪܝܠ ܥܒܕܗ ܘܐܬܕܟܪ ܚܢܢܗ ܀
54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem,
55ܐܝܟ ܕܡܠܠ ܥܡ ܐܒܗܝܢ ܥܡ ܐܒܪܗܡ ܘܥܡ ܙܪܥܗ ܠܥܠܡ ܀
55 ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56ܩܘܝܬ ܕܝܢ ܡܪܝܡ ܠܘܬ ܐܠܝܫܒܥ ܐܝܟ ܝܪܚܐ ܬܠܬܐ ܘܗܦܟܬ ܠܒܝܬܗ ܀
56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi.
57ܐܠܝܫܒܥ ܕܝܢ ܗܘܐ ܗܘܐ ܠܗ ܙܒܢܐ ܕܬܐܠܕ ܘܝܠܕܬ ܒܪܐ ܀
57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58ܘܫܡܥܘ ܫܒܒܝܗ ܘܒܢܝ ܛܘܗܡܗ ܕܐܤܓܝ ܐܠܗܐ ܚܢܢܗ ܠܘܬܗ ܘܚܕܝܢ ܗܘܘ ܥܡܗ ܀
58 Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59ܘܗܘܐ ܠܝܘܡܐ ܕܬܡܢܝܐ ܘܐܬܘ ܠܡܓܙܪܗ ܠܛܠܝܐ ܘܩܪܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܒܫܡܐ ܕܐܒܘܗܝ ܙܟܪܝܐ ܀
59 Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya.
60ܘܥܢܬ ܐܡܗ ܘܐܡܪܐ ܠܗܘܢ ܠܐ ܗܟܢܐ ܐܠܐ ܢܬܩܪܐ ܝܘܚܢܢ ܀
60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܕܠܝܬ ܐܢܫ ܒܫܪܒܬܟܝ ܕܡܬܩܪܐ ܒܫܡܐ ܗܢܐ ܀
61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62ܘܪܡܙܘ ܠܐܒܘܗܝ ܕܐܝܟܢܐ ܨܒܐ ܕܢܫܡܝܘܗܝ ܀
62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63ܘܫܐܠ ܦܢܩܝܬܐ ܘܟܬܒ ܘܐܡܪ ܝܘܚܢܢ ܗܘ ܫܡܗ ܘܐܬܕܡܪܘ ܟܠܢܫ ܀
63 Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
64ܘܡܚܕܐ ܐܬܦܬܚ ܦܘܡܗ ܘܠܫܢܗ ܘܡܠܠ ܘܒܪܟ ܠܐܠܗܐ ܀
64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla.
65ܘܗܘܬ ܕܚܠܬܐ ܥܠ ܟܠܗܘܢ ܫܒܒܝܗܘܢ ܘܒܟܠܗ ܛܘܪܐ ܕܝܗܘܕ ܗܠܝܢ ܡܬܡܠܠܢ ܗܘܝ ܀
65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
66ܘܟܠܗܘܢ ܕܫܡܥܘ ܡܬܚܫܒܝܢ ܗܘܘ ܒܠܒܗܘܢ ܘܐܡܪܝܢ ܡܢܐ ܟܝ ܢܗܘܐ ܛܠܝܐ ܗܢܐ ܘܐܝܕܗ ܕܡܪܝܐ ܐܝܬ ܗܘܬ ܥܡܗ ܀
66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
67ܘܐܬܡܠܝ ܙܟܪܝܐ ܐܒܘܗܝ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܘܐܬܢܒܝ ܘܐܡܪ ܀
67 Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
68ܡܒܪܟ ܗܘ ܡܪܝܐ ܐܠܗܗ ܕܐܝܤܪܝܠ ܕܤܥܪ ܥܡܗ ܘܥܒܕ ܠܗ ܦܘܪܩܢܐ ܀
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69ܘܐܩܝܡ ܠܢ ܩܪܢܐ ܕܦܘܪܩܢܐ ܒܒܝܬܗ ܕܕܘܝܕ ܥܒܕܗ ܀
69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70ܐܝܟ ܕܡܠܠ ܒܦܘܡܐ ܕܢܒܝܘܗܝ ܩܕܝܫܐ ܕܡܢ ܥܠܡ ܀
70 ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71ܕܢܦܪܩܢ ܡܢ ܒܥܠܕܒܒܝܢ ܘܡܢ ܐܝܕܐ ܕܟܠܗܘܢ ܤܢܐܝܢ ܀
71 Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72ܘܥܒܕ ܚܢܢܗ ܥܡ ܐܒܗܝܢ ܘܥܗܕ ܠܕܝܬܩܘܗܝ ܩܕܝܫܬܐ ܀
72 Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73ܘܡܘܡܬܐ ܕܝܡܐ ܠܐܒܪܗܡ ܐܒܘܢ ܕܢܬܠ ܠܢ ܀
73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74ܕܢܬܦܪܩ ܡܢ ܐܝܕܐ ܕܒܥܠܕܒܒܝܢ ܘܕܠܐ ܕܚܠܐ ܢܦܠܘܚ ܩܕܡܘܗܝ ܀
74 dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75ܟܠܗܘܢ ܝܘܡܬܢ ܒܟܐܢܘܬܐ ܘܒܙܕܝܩܘܬܐ ܀
75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
76ܘܐܢܬ ܛܠܝܐ ܢܒܝܗ ܕܥܠܝܐ ܬܬܩܪܐ ܬܐܙܠ ܓܝܪ ܩܕܡ ܦܪܨܘܦܗ ܕܡܪܝܐ ܕܬܛܝܒ ܐܘܪܚܗ ܀
76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi.
77ܕܢܬܠ ܡܕܥܐ ܕܚܝܐ ܠܥܡܗ ܒܫܘܒܩܢܐ ܕܚܛܗܝܗܘܢ ܀
77 Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
78ܒܪܚܡܐ ܕܚܢܢܐ ܕܐܠܗܢ ܕܒܗܘܢ ܢܤܥܪܢ ܕܢܚܐ ܡܢ ܪܘܡܐ ܀
78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,
79ܠܡܢܗܪܘ ܠܐܝܠܝܢ ܕܒܚܫܘܟܐ ܘܒܛܠܠܐ ܕܡܘܬܐ ܝܬܒܝܢ ܕܢܬܪܘܨ ܪܓܠܝܢ ܒܐܘܪܚܐ ܕܫܠܡܐ ܀
79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»
80ܛܠܝܐ ܕܝܢ ܪܒܐ ܗܘܐ ܘܡܬܚܝܠ ܒܪܘܚܐ ܘܒܚܘܪܒܐ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܐ ܕܬܚܘܝܬܗ ܕܠܘܬ ܐܝܤܪܝܠ ܀
80 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.