Syriac: NT

Wolof: New Testament

Mark

16

1ܘܟܕ ܥܒܪܬ ܫܒܬܐ ܡܪܝܡ ܡܓܕܠܝܬܐ ܘܡܪܝܡ ܕܝܥܩܘܒ ܘܫܠܘܡ ܙܒܢ ܗܪܘܡܐ ܕܢܐܬܝܢ ܢܡܫܚܢܝܗܝ ܀
1 Bi bésu noflaay bi wéyee, Maryaamam Magdala, Maryaama yaayu Saag, ak Salome, jënd cuuraay, ngir dem xeeñal néewu Yeesu.
2ܒܫܦܪܐ ܕܝܢ ܒܚܕ ܒܫܒܐ ܐܬܝ ܠܒܝܬ ܩܒܘܪܐ ܟܕ ܕܢܚ ܫܡܫܐ ܀
2 Kon bés bu jëkk ci ayu-bés gi, ñu njëlu dem ca bàmmeel ba,
3ܘܐܡܪܢ ܗܘܝ ܒܢܦܫܗܝܢ ܡܢ ܕܝܢ ܥܓܠ ܠܢ ܟܐܦܐ ܡܢ ܬܪܥܐ ܕܒܝܬ ܩܒܘܪܐ ܀
3 di laajante: «Ku nuy béraŋal doj, wiy ub bàmmeel bi?» Doj woowu nag bu réy-a-réy la woon. Noonu ñu xool, gis ne doj wa deñ.
4ܘܚܪ ܚܙܝ ܕܡܥܓܠܐ ܗܝ ܟܐܦܐ ܪܒܐ ܗܘܬ ܓܝܪ ܛܒ ܀
5 Ñu dugg ci bàmmeel bi, gis ca ndeyjoor waxambaane wu sol mbubb mu weex, ñu daldi tiit.
5ܘܥܠܝܢ ܠܒܝܬ ܩܒܘܪܐ ܘܚܙܝ ܥܠܝܡܐ ܕܝܬܒ ܡܢ ܝܡܝܢܐ ܘܥܛܝܦ ܐܤܛܠܐ ܚܘܪܬܐ ܘܬܡܗ ܀
6 Waaye mu ne leen: «Buleen tiit. Yéena ngi seet Yeesum Nasaret, mi ñu daajoon ci bant bi. Nekkatu fi, dekki na; gisleen fi ñu ko tëraloon.
6ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܝܢ ܠܐ ܬܕܚܠܢ ܠܝܫܘܥ ܢܨܪܝܐ ܒܥܝܢ ܐܢܬܝܢ ܗܘ ܕܐܙܕܩܦ ܩܡ ܠܗ ܠܐ ܗܘܐ ܬܢܢ ܗܐ ܕܘܟܬܐ ܐܝܟܐ ܕܤܝܡ ܗܘܐ ܀
7 Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: “Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.”»
7ܐܠܐ ܙܠܝܢ ܐܡܪܝܢ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܠܟܐܦܐ ܕܗܐ ܩܕܡ ܠܟܘܢ ܠܓܠܝܠܐ ܬܡܢ ܬܚܙܘܢܝܗܝ ܐܝܟܢܐ ܕܐܡܪ ܠܟܘܢ ܀
8 Noonu jigéen ñi génn, dawe bàmmeel ba, tiit bay lox. Te waxuñu kenn dara ndax seen tiit.
8ܘܟܕ ܫܡܥ ܥܪܩ ܘܢܦܩ ܡܢ ܩܒܪܐ ܐܚܝܕ ܗܘܐ ܠܗܝܢ ܓܝܪ ܬܗܪܐ ܘܪܬܝܬܐ ܘܠܐܢܫ ܡܕܡ ܠܐ ܐܡܪܝܢ ܕܚܝܠܢ ܗܘܝ ܓܝܪ ܀
9 Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, mu jëkk a feeñu Maryaama mu dëkk Magdala, mi mu dàqe woon juróom-ñaari rab.
9ܒܫܦܪܐ ܕܝܢ ܒܚܕ ܒܫܒܐ ܩܡ ܘܐܬܚܙܝ ܠܘܩܕܡ ܠܡܪܝܡ ܡܓܕܠܝܬܐ ܗܝ ܕܫܒܥܐ ܫܐܕܝܢ ܐܦܩ ܗܘܐ ܡܢܗ ܀
10 Maryaama nag dem nettali ko ñi àndoon ak Yeesu, fekk ñuy naqarlu, di jooy.
10ܘܗܝ ܐܙܠܬ ܤܒܪܬ ܠܗܢܘܢ ܕܥܡܗ ܗܘܘ ܕܐܒܝܠܝܢ ܗܘܘ ܘܒܟܝܢ ܀
11 Bi ñu déggee ne, Yeesoo ngi dund te Maryaama gis na ko, gëmuñu ko.
11ܘܗܢܘܢ ܟܕ ܫܡܥܘ ܕܐܡܪܢ ܕܚܝ ܘܐܬܚܙܝ ܠܗܝܢ ܠܐ ܗܝܡܢܘ ܐܢܝܢ ܀
12 Gannaaw loolu Yeesu feeñu ñaar ci ñoom ci jeneen jëmm, ñuy jaar ci yoon wi, jëm àll ba.
12ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܐܬܚܙܝ ܠܬܪܝܢ ܡܢܗܘܢ ܒܕܡܘܬܐ ܐܚܪܬܐ ܟܕ ܡܗܠܟܝܢ ܘܐܙܠܝܢ ܠܩܪܝܬܐ ܀
13 Ñu woññiku nag, wax ko ña ca des, waaye ba tey gëmuñu leen ñoom it.
13ܘܗܢܘܢ ܐܙܠܘ ܐܡܪܘ ܠܫܪܟܐ ܐܦ ܠܐ ܠܗܢܘܢ ܗܝܡܢܘ ܀
14 Gannaaw ga it Yeesu feeñu fukki taalibe yi ak benn, bi ñuy lekk. Mu yedd leen ndax seen ngëmadi ak seen dëgër bopp, ci li ñu bañ a gëm ñi ko gisoon, bi mu dekkee.
14ܐܚܪܝܬ ܕܝܢ ܐܬܚܙܝ ܠܚܕܥܤܪ ܟܕ ܤܡܝܟܝܢ ܘܚܤܕ ܠܚܤܝܪܘܬ ܗܝܡܢܘܬܗܘܢ ܘܠܩܫܝܘܬ ܠܒܗܘܢ ܕܠܗܢܘܢ ܕܚܙܐܘܗܝ ܕܩܡ ܠܐ ܗܝܡܢܘ ܀
15 Mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp, yégal xebaar bu baax bi mbindeef yépp.
15ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܙܠܘ ܠܥܠܡܐ ܟܠܗ ܘܐܟܪܙܘ ܤܒܪܬܝ ܒܟܠܗ ܒܪܝܬܐ ܀
16 Ku gëm te ñu sóob ko ci ndox, dina mucc; ku gëmul, dees na ko daan.
16ܐܝܢܐ ܕܡܗܝܡܢ ܘܥܡܕ ܚܝܐ ܘܐܝܢܐ ܕܠܐ ܡܗܝܡܢ ܡܬܚܝܒ ܀
17 Ñi ma gëm dinañu ànd ak firnde yii: ci sama tur dinañu dàq rab yi, di wax làkk yu bees,
17ܐܬܘܬܐ ܕܝܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܗܝܡܢܝܢ ܗܠܝܢ ܢܩܦܢ ܒܫܡܝ ܫܐܕܐ ܢܦܩܘܢ ܘܒܠܫܢܐ ܚܕܬܐ ܢܡܠܠܘܢ ܀
18 di jàpp jaan ak seeni loxo; te bu ñu naanee lu ñu tooke, du leen wàññi dara, te jarag ju ñu teg loxo, mu wér.»
18ܘܚܘܘܬܐ ܢܫܩܠܘܢ ܘܐܢ ܤܡܐ ܕܡܘܬܐ ܢܫܬܘܢ ܠܐ ܢܗܪ ܐܢܘܢ ܘܐܝܕܝܗܘܢ ܢܤܝܡܘܢ ܥܠ ܟܪܝܗܐ ܘܢܬܚܠܡܘܢ ܀
19 Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak ñoom, mu yékkatiku, dem asamaan, toog ci ndeyjooru Yàlla.
19ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܡܪܢ ܡܢ ܒܬܪ ܕܡܠܠ ܥܡܗܘܢ ܠܫܡܝܐ ܤܠܩ ܘܝܬܒ ܡܢ ܝܡܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܀
20 Taalibe ya dem waareji, te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, di dëggal kàddu gi ak firnde, yi ci ànd.
20ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܢܦܩܘ ܘܐܟܪܙܘ ܒܟܠ ܕܘܟܐ ܘܡܪܢ ܡܥܕܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܘܡܫܪ ܡܠܝܗܘܢ ܒܐܬܘܬܐ ܕܥܒܕܝܢ ܗܘܘ ܀ ܀ ܀