1ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܟܕ ܡܠܐ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܗܦܟ ܡܢ ܝܘܪܕܢܢ ܘܕܒܪܬܗ ܪܘܚܐ ܠܚܘܪܒܐ ܀
1 Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan.
2ܝܘܡܬܐ ܐܪܒܥܝܢ ܕܢܬܢܤܐ ܡܢ ܐܟܠܩܪܨܐ ܘܠܐ ܠܥܤ ܡܕܡ ܒܗܢܘܢ ܝܘܡܬܐ ܘܟܕ ܫܠܡ ܐܢܘܢ ܠܚܪܬܐ ܟܦܢ ܀
2 Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.
3ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܟܠܩܪܨܐ ܐܢ ܒܪܗ ܐܢܬ ܕܐܠܗܐ ܐܡܪ ܠܟܐܦܐ ܗܕܐ ܕܬܗܘܐ ܠܚܡܐ ܀
3 Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.»
4ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܟܬܝܒ ܗܘ ܕܠܐ ܗܘܐ ܒܠܚܡܐ ܒܠܚܘܕ ܚܝܐ ܒܪܢܫܐ ܐܠܐ ܒܟܠ ܦܬܓܡ ܕܐܠܗܐ ܀
4 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
5ܘܐܤܩܗ ܤܛܢܐ ܠܛܘܪܐ ܪܡܐ ܘܚܘܝܗ ܟܠܗܝܢ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܪܥܐ ܒܥܕܢܐ ܙܥܘܪܐ ܀
5 Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef-ak-xippi mu won ko réewi àddina sépp,
6ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܟܠܩܪܨܐ ܠܟ ܐܬܠ ܫܘܠܛܢܐ ܗܢܐ ܟܠܗ ܘܫܘܒܚܗ ܕܠܝ ܡܫܠܡ ܘܠܡܢ ܕܐܨܒܐ ܝܗܒ ܐܢܐ ܠܗ ܀
6 ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox.
7ܐܢ ܗܟܝܠ ܬܤܓܘܕ ܩܕܡܝ ܕܝܠܟ ܢܗܘܐ ܟܠܗ ܀
7 Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.»
8ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܟܬܝܒ ܗܘ ܕܠܡܪܝܐ ܐܠܗܟ ܬܤܓܘܕ ܘܠܗ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܬܦܠܘܚ ܀
8 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
9ܘܐܝܬܝܗ ܠܐܘܪܫܠܡ ܘܐܩܝܡܗ ܥܠ ܟܢܦܐ ܕܗܝܟܠܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܢ ܒܪܗ ܐܢܬ ܕܐܠܗܐ ܐܪܡܐ ܢܦܫܟ ܡܟܐ ܠܬܚܬ ܀
9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,
10ܟܬܝܒ ܓܝܪ ܕܠܡܠܐܟܘܗܝ ܢܦܩܕ ܥܠܝܟ ܕܢܢܛܪܘܢܟ ܀
10 ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu sàmm la,
11ܘܥܠ ܕܪܥܝܗܘܢ ܢܫܩܠܘܢܟ ܕܠܐ ܬܬܩܠ ܪܓܠܟ ܒܟܐܦܐ ܀
11 dinañu la leewu ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
12ܥܢܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܡܝܪ ܗܘ ܕܠܐ ܬܢܤܐ ܠܡܪܝܐ ܐܠܗܟ ܀
12 Yeesu tontu ko ne: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
13ܘܟܕ ܫܠܡ ܐܟܠܩܪܨܐ ܟܠܗܘܢ ܢܤܝܘܢܘܗܝ ܦܪܩ ܡܢ ܠܘܬܗ ܥܕ ܙܒܢܐ ܀
13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
14ܘܗܦܟ ܝܫܘܥ ܒܚܝܠܐ ܕܪܘܚܐ ܠܓܠܝܠܐ ܘܢܦܩ ܥܠܘܗܝ ܛܒܐ ܒܟܠܗ ܐܬܪܐ ܕܚܕܪܝܗܘܢ ܀
14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15ܘܗܘ ܡܠܦ ܗܘܐ ܒܟܢܘܫܬܗܘܢ ܘܡܫܬܒܚ ܗܘܐ ܡܢ ܟܠ ܐܢܫ ܀
15 Muy jàngale ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16ܘܐܬܐ ܠܢܨܪܬ ܐܝܟܐ ܕܐܬܪܒܝ ܘܥܠ ܐܝܟܢܐ ܕܡܥܕ ܗܘܐ ܠܟܢܘܫܬܐ ܒܝܘܡܐ ܕܫܒܬܐ ܘܩܡ ܠܡܩܪܐ ܀
16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésu noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
17ܘܐܬܝܗܒ ܠܗ ܤܦܪܐ ܕܐܫܥܝܐ ܢܒܝܐ ܘܦܬܚ ܝܫܘܥ ܤܦܪܐ ܘܐܫܟܚ ܕܘܟܬܐ ܐܝܟܐ ܕܟܬܝܒ ܀
17 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18ܪܘܚܗ ܕܡܪܝܐ ܥܠܝ ܘܡܛܠ ܗܕܐ ܡܫܚܢܝ ܠܡܤܒܪܘ ܠܡܤܟܢܐ ܘܫܠܚܢܝ ܠܡܐܤܝܘ ܠܬܒܝܪܝ ܠܒܐ ܘܠܡܟܪܙܘ ܠܫܒܝܐ ܫܘܒܩܢܐ ܘܠܥܘܝܪܐ ܚܙܝܐ ܘܠܡܫܪܪܘ ܠܬܒܝܪܐ ܒܫܘܒܩܢܐ ܀
18 «Xelum Boroom baa ngi ci man,ndaxte moo ma tànn,ngir ma yégal néew doole yi xebaar bu baax bi.Dafa maa yónni,ngir ma yégal jaam ñi ne, dinañu leen goreel,yégal gumba yi ne, dinañu gis,te jot ñi ñu noot,
19ܘܠܡܟܪܙܘ ܫܢܬܐ ܡܩܒܠܬܐ ܠܡܪܝܐ ܀
19 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20ܘܟܪܟ ܤܦܪܐ ܘܝܗܒܗ ܠܡܫܡܫܢܐ ܘܐܙܠ ܝܬܒ ܟܠܗܘܢ ܕܝܢ ܕܒܟܢܘܫܬܐ ܥܝܢܝܗܘܢ ܚܝܪܢ ܗܘܝ ܒܗ ܀
20 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
21ܘܫܪܝ ܠܡܐܡܪ ܠܘܬܗܘܢ ܕܝܘܡܢܐ ܐܫܬܠܡ ܟܬܒܐ ܗܢܐ ܒܐܕܢܝܟܘܢ ܀
21 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»
22ܘܤܗܕܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܟܠܗܘܢ ܘܡܬܕܡܪܝܢ ܗܘܘ ܒܡܠܐ ܕܛܝܒܘܬܐ ܕܢܦܩܢ ܗܘܝ ܡܢ ܦܘܡܗ ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܠܐ ܗܘܐ ܗܢܐ ܒܪ ܝܘܤܦ ܀
22 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»
23ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܟܒܪ ܬܐܡܪܘܢ ܠܝ ܡܬܠܐ ܗܢܐ ܐܤܝܐ ܐܤܐ ܢܦܫܟ ܘܟܠ ܕܫܡܥܢ ܕܥܒܕܬ ܒܟܦܪܢܚܘܡ ܥܒܕ ܐܦ ܗܪܟܐ ܒܡܕܝܢܬܟ ܀
23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
24ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܠܝܬ ܢܒܝܐ ܕܡܬܩܒܠ ܒܡܕܝܢܬܗ ܀
24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
25ܫܪܪܐ ܓܝܪ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܤܓܝ ܐܪܡܠܬܐ ܐܝܬ ܗܘܝ ܒܐܝܤܪܝܠ ܒܝܘܡܝ ܐܠܝܐ ܢܒܝܐ ܟܕ ܐܬܬܚܕܘ ܫܡܝܐ ܫܢܝܢ ܬܠܬ ܘܝܪܚܐ ܫܬܐ ܘܗܘܐ ܟܦܢܐ ܪܒܐ ܒܟܠܗ ܐܪܥܐ ܀
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
26ܘܠܘܬ ܚܕܐ ܡܢܗܝܢ ܠܐ ܐܫܬܕܪ ܐܠܝܐ ܐܠܐ ܠܨܪܦܬ ܕܨܝܕܢ ܠܘܬ ܐܢܬܬܐ ܐܪܡܠܬܐ ܀
26 Moona Yàlla yónniwul Iliyas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
27ܘܤܓܝܐܐ ܓܪܒܐ ܐܝܬ ܗܘܘ ܒܝܬ ܐܝܤܪܝܠ ܒܝܘܡܝ ܐܠܝܫܥ ܢܒܝܐ ܘܚܕ ܡܢܗܘܢ ܠܐ ܐܬܕܟܝ ܐܠܐ ܐܢ ܢܥܡܢ ܐܪܡܝܐ ܀
27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alisa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naaman, mi dëkkoon réewu Siri.»
28ܘܟܕ ܫܡܥܘ ܗܠܝܢ ܗܢܘܢ ܕܒܟܢܘܫܬܐ ܐܬܡܠܝܘ ܚܡܬܐ ܟܠܗܘܢ ܀
28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
29ܘܩܡܘ ܐܦܩܘܗܝ ܠܒܪ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܘܐܝܬܝܘܗܝ ܥܕܡܐ ܠܓܒܝܢܐ ܕܛܘܪܐ ܗܘ ܕܡܕܝܢܬܗܘܢ ܒܢܝܐ ܗܘܬ ܥܠܘܗܝ ܕܢܫܕܘܢܝܗܝ ܡܢ ܫܩܝܦܐ ܀
29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30ܗܘ ܕܝܢ ܥܒܪ ܒܝܢܬܗܘܢ ܘܐܙܠ ܀
30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
31ܘܢܚܬ ܠܟܦܪܢܚܘܡ ܡܕܝܢܬܐ ܕܓܠܝܠܐ ܘܡܠܦ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܒܫܒܐ ܀
31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.
32ܘܬܡܝܗܝܢ ܗܘܘ ܒܝܘܠܦܢܗ ܕܡܫܠܛܐ ܗܘܬ ܡܠܬܗ ܀
32 Mu jàngal leen ca bésu noflaay ba, ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.
33ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܒܟܢܘܫܬܐ ܓܒܪܐ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܒܗ ܪܘܚܐ ܕܫܐܕܐ ܛܢܦܐ ܘܙܥܩ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܀
33 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne:
34ܘܐܡܪ ܫܒܘܩܝܢܝ ܡܐ ܠܢ ܘܠܟ ܝܫܘܥ ܢܨܪܝܐ ܐܬܝܬ ܠܡܘܒܕܘܬܢ ܝܕܥ ܐܢܐ ܠܟ ܡܢ ܐܢܬ ܩܕܝܫܗ ܕܐܠܗܐ ܀
34 «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!»
35ܘܟܐܐ ܒܗ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܤܟܘܪ ܦܘܡܟ ܘܦܘܩ ܡܢܗ ܘܫܕܝܗܝ ܫܐܕܐ ܒܡܨܥܬܐ ܘܢܦܩ ܡܢܗ ܟܕ ܠܐ ܤܪܚ ܒܗ ܡܕܡ ܀
35 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanamu ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.
36ܘܬܡܗܐ ܪܒܐ ܐܚܕ ܠܟܠܢܫ ܘܡܡܠܠܝܢ ܗܘܘ ܥܡ ܚܕܕܐ ܘܐܡܪܝܢ ܡܢܐ ܗܝ ܟܝ ܡܠܬܐ ܗܕܐ ܕܒܫܘܠܛܢܐ ܘܒܚܝܠܐ ܦܩܕܐ ܠܪܘܚܐ ܛܢܦܬܐ ܘܢܦܩܢ ܀
36 Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.»
37ܘܢܦܩ ܥܠܘܗܝ ܛܒܐ ܒܟܠܗ ܐܬܪܐ ܕܚܕܪܝܗܘܢ ܀
37 Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.
38ܘܟܕ ܢܦܩ ܝܫܘܥ ܡܢ ܟܢܘܫܬܐ ܥܠ ܠܒܝܬܗ ܕܫܡܥܘܢ ܘܚܡܬܗ ܕܫܡܥܘܢ ܐܠܝܨܐ ܗܘܬ ܒܐܫܬܐ ܪܒܬܐ ܘܒܥܘ ܡܢܗ ܡܛܠܬܗ ܀
38 Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu naan Yeesu, mu dimbali leen ci.
39ܘܩܡ ܠܥܠ ܡܢܗ ܘܟܐܐ ܒܐܫܬܗ ܘܫܒܩܬܗ ܘܡܚܕܐ ܩܡܬ ܘܡܫܡܫܐ ܗܘܬ ܠܗܘܢ ܀
39 Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.
40ܡܥܪܒܝ ܫܡܫܐ ܕܝܢ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܟܪܝܗܐ ܕܟܪܝܗܝܢ ܒܟܘܪܗܢܐ ܡܫܚܠܦܐ ܐܝܬܝܘ ܐܢܘܢ ܠܘܬܗ ܗܘ ܕܝܢ ܥܠ ܚܕ ܚܕ ܡܢܗܘܢ ܐܝܕܗ ܤܐܡ ܗܘܐ ܘܡܐܤܐ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܀
40 Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la.
41ܘܢܦܩܝܢ ܗܘܘ ܐܦ ܫܐܕܐ ܡܢ ܤܓܝܐܐ ܟܕ ܡܙܥܩܝܢ ܘܐܡܪܝܢ ܕܐܢܬ ܗܘ ܡܫܝܚܐ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܘܟܐܐ ܗܘܐ ܒܗܘܢ ܘܠܐ ܫܒܩ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܕܢܐܡܪܘܢ ܕܝܕܥܝܢ ܕܗܘܝܘ ܡܫܝܚܐ ܀
41 Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne, mooy Almasi bi.
42ܘܠܨܦܪܗ ܕܝܘܡܐ ܢܦܩ ܐܙܠ ܠܗ ܠܐܬܪܐ ܚܘܪܒܐ ܘܟܢܫܐ ܒܥܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܘܐܬܘ ܥܕܡܐ ܠܘܬܗ ܘܐܚܕܘܗܝ ܕܠܐ ܢܐܙܠ ܠܗ ܡܢ ܠܘܬܗܘܢ ܀
42 Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wut a téye, ngir bañ mu dem.
43ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܕܐܦ ܠܡܕܝܢܬܐ ܐܚܪܢܝܬܐ ܘܠܐ ܠܝ ܠܡܤܒܪܘ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܕܥܠ ܗܕܐ ܗܘ ܐܫܬܕܪܬ ܀
43 Waaye mu ne leen: «Damaa war a dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.»
44ܘܗܘ ܡܟܪܙ ܗܘܐ ܒܟܢܘܫܬܐ ܕܓܠܝܠܐ ܀
44 Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.