1ܗܘܐ ܕܝܢ ܟܕ ܟܢܫ ܥܠܘܗܝ ܟܢܫܐ ܠܡܫܡܥ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܗܘ ܩܐܡ ܗܘܐ ܥܠ ܝܕ ܝܡܬܐ ܕܓܢܤܪ ܀
1 Benn bés Yeesu taxaw ca tefesu dexu Senesaret. Mbooloo ma wër ko, di buuxante ngir déglu kàddug Yàlla.
2ܚܙܐ ܤܦܝܢܐ ܬܪܬܝܢ ܕܩܝܡܢ ܥܠ ܓܢܒ ܝܡܬܐ ܘܨܝܕܐ ܕܤܠܩܘ ܡܢܗܝܢ ܘܡܫܝܓܝܢ ܡܨܝܕܬܗܘܢ ܀
2 Noonu mu gis ñaari gaal yu teer ca tefes ga, nappkat ya ca wàcce, di raxas seeni mbaal.
3ܘܚܕܐ ܡܢܗܝܢ ܕܫܡܥܘܢ ܗܘܬ ܟܐܦܐ ܘܤܠܩ ܝܫܘܥ ܝܬܒ ܒܗ ܘܐܡܪ ܕܢܕܒܪܘܢܗ ܩܠܝܠ ܡܢ ܝܒܫܐ ܠܡܝܐ ܘܝܬܒ ܗܘܐ ܘܡܠܦ ܡܢ ܤܦܝܢܬܐ ܠܟܢܫܐ ܀
3 Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simoŋ, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di jàngal mbooloo ma.
4ܘܟܕ ܫܬܩ ܡܢ ܡܡܠܠܗ ܐܡܪ ܠܫܡܥܘܢ ܕܒܪܘ ܠܥܘܡܩܐ ܘܐܪܡܘ ܡܨܝܕܬܟܘܢ ܠܨܝܕܐ ܀
4 Bi mu jàngalee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gën a xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»
5ܥܢܐ ܫܡܥܘܢ ܘܐܡܪ ܠܗ ܪܒܝ ܠܠܝܐ ܟܠܗ ܠܐܝܢ ܘܡܕܡ ܠܐ ܐܚܕܢ ܥܠ ܡܠܬܟ ܕܝܢ ܪܡܐ ܐܢܐ ܡܨܝܕܬܐ ܀
5 Simoŋ tontu ko ne: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»
6ܘܟܕ ܗܕܐ ܥܒܕܘ ܚܒܫܘ ܢܘܢܐ ܤܓܝܐܐ ܕܛܒ ܘܡܨܛܪܝܐ ܗܘܬ ܡܨܝܕܬܗܘܢ ܀
6 Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.
7ܘܪܡܙܘ ܠܚܒܪܝܗܘܢ ܕܒܤܦܝܢܬܐ ܐܚܪܬܐ ܕܢܐܬܘܢ ܢܥܕܪܘܢ ܐܢܘܢ ܘܟܕ ܐܬܘ ܡܠܘ ܐܢܝܢ ܤܦܝܢܐ ܬܪܬܝܗܝܢ ܐܝܟ ܕܩܪܝܒܢ ܗܘܝ ܠܡܛܒܥ ܀
7 Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgg a suux.
8ܟܕ ܚܙܐ ܕܝܢ ܫܡܥܘܢ ܟܐܦܐ ܢܦܠ ܩܕܡ ܪܓܠܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܡܪܝ ܦܪܘܩ ܠܟ ܡܢܝ ܕܓܒܪܐ ܐܢܐ ܚܛܝܐ ܀
8 Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanamu Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
9ܬܡܗܐ ܓܝܪ ܐܚܕܗ ܗܘܐ ܘܠܟܠܗܘܢ ܕܥܡܗ ܥܠ ܨܝܕܐ ܗܘ ܕܢܘܢܐ ܕܨܕܘ ܀
9 Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon
10ܗܟܘܬ ܕܝܢ ܐܦ ܠܝܥܩܘܒ ܘܠܝܘܚܢܢ ܒܢܝ ܙܒܕܝ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܗܘܘ ܫܘܬܦܐ ܕܫܡܥܘܢ ܐܡܪ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܠܫܡܥܘܢ ܠܐ ܬܕܚܠ ܡܢ ܗܫܐ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܬܗܘܐ ܨܐܕ ܠܚܝܐ ܀
10 ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaawsi tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»
11ܘܩܪܒܘ ܐܢܝܢ ܤܦܝܢܐ ܠܐܪܥܐ ܘܫܒܩܘ ܟܠ ܡܕܡ ܘܐܬܘ ܒܬܪܗ ܀
11 Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.
12ܘܟܕ ܗܘܐ ܝܫܘܥ ܒܚܕܐ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܐܬܐ ܓܒܪܐ ܕܡܠܐ ܟܠܗ ܓܪܒܐ ܚܙܐ ܠܝܫܘܥ ܘܢܦܠ ܥܠ ܐܦܘܗܝ ܘܒܥܐ ܗܘܐ ܡܢܗ ܘܐܡܪ ܠܗ ܡܪܝ ܐܢ ܨܒܐ ܐܢܬ ܡܫܟܚ ܐܢܬ ܠܡܕܟܝܘܬܝ ܀
12 Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëwam ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
13ܘܦܫܛ ܐܝܕܗ ܝܫܘܥ ܩܪܒ ܠܗ ܘܐܡܪ ܠܗ ܨܒܐ ܐܢܐ ܐܬܕܟܐ ܘܒܪ ܫܥܬܗ ܐܙܠ ܡܢܗ ܓܪܒܗ ܘܐܬܕܟܝ ܀
13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
14ܘܦܩܕܗ ܕܠܐܢܫ ܠܐ ܬܐܡܪ ܐܠܐ ܙܠ ܚܘܐ ܢܦܫܟ ܠܟܗܢܐ ܘܩܪܒ ܚܠܦ ܬܕܟܝܬܟ ܐܝܟܢܐ ܕܦܩܕ ܡܘܫܐ ܠܤܗܕܘܬܗܘܢ ܀
14 Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
15ܘܢܦܩ ܥܠܘܗܝ ܛܒܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܘܡܬܟܢܫ ܗܘܐ ܥܡܐ ܤܓܝܐܐ ܠܡܫܡܥ ܡܢܗ ܘܠܡܬܐܤܝܘ ܡܢ ܟܘܪܗܢܝܗܘܢ ܀
15 Noonu turu Yeesu di gën a siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.
16ܗܘ ܕܝܢ ܡܫܢܐ ܗܘܐ ܠܕܒܪܐ ܘܡܨܠܐ ܀
16 Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan.
17ܘܗܘܐ ܒܚܕ ܡܢ ܝܘܡܬܐ ܟܕ ܡܠܦ ܗܘܐ ܝܫܘܥ ܝܬܒܝܢ ܗܘܘ ܦܪܝܫܐ ܘܡܠܦܝ ܢܡܘܤܐ ܕܐܬܘ ܗܘܘ ܡܢ ܟܠ ܩܘܪܝܐ ܕܓܠܝܠܐ ܘܕܝܗܘܕ ܘܕܐܘܪܫܠܡ ܘܚܝܠܐ ܕܡܪܝܐ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܠܡܐܤܝܘܬܗܘܢ ܀
17 Am na bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.
18ܘܐܢܫܐ ܐܝܬܝܘ ܒܥܪܤܐ ܓܒܪܐ ܚܕ ܡܫܪܝܐ ܘܒܥܝܢ ܗܘܘ ܕܢܥܠܘܢ ܢܤܝܡܘܢܝܗܝ ܩܕܡܘܗܝ ܀
18 Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wut a dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu.
19ܘܟܕ ܠܐ ܐܫܟܚܘ ܕܐܝܟܢܐ ܢܥܠܘܢܝܗܝ ܡܛܠ ܤܘܓܐܐ ܕܥܡܐ ܤܠܩܘ ܠܗܘܢ ܠܐܓܪܐ ܘܫܒܘܗܝ ܥܡ ܥܪܤܗ ܡܢ ܬܛܠܝܠܐ ܠܡܨܥܬܐ ܩܕܡܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܀
19 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanamu Yeesu ca biir mbooloo ma.
20ܟܕ ܚܙܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܗܝܡܢܘܬܗܘܢ ܐܡܪ ܠܗܘ ܡܫܪܝܐ ܓܒܪܐ ܫܒܝܩܝܢ ܠܟ ܚܛܗܝܟ ܀
20 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
21ܘܫܪܝܘ ܤܦܪܐ ܘܦܪܝܫܐ ܡܬܚܫܒܝܢ ܘܐܡܪܝܢ ܡܢܘ ܗܢܐ ܕܡܡܠܠ ܓܘܕܦܐ ܡܢܘ ܡܫܟܚ ܠܡܫܒܩ ܚܛܗܐ ܐܠܐ ܐܢ ܐܠܗܐ ܒܠܚܘܕ ܀
21 Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
22ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܝܕܥ ܡܚܫܒܬܗܘܢ ܘܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܢܐ ܡܬܚܫܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܠܒܟܘܢ ܀
22 Waaye Yeesu xam seen xalaat, tontu leen ne: «Lu tax ngeen di werante ci seen xel?
23ܐܝܕܐ ܦܫܝܩܐ ܠܡܐܡܪ ܕܫܒܝܩܝܢ ܠܟ ܚܛܗܝܟ ܐܘ ܠܡܐܡܪ ܩܘܡ ܗܠܟ ܀
23 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
24ܕܬܕܥܘܢ ܕܝܢ ܕܫܠܝܛ ܗܘ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܒܐܪܥܐ ܕܢܫܒܘܩ ܚܛܗܐ ܐܡܪ ܠܡܫܪܝܐ ܠܟ ܐܡܪ ܐܢܐ ܩܘܡ ܫܩܘܠ ܥܪܤܟ ܘܙܠ ܠܒܝܬܟ ܀
24 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
25ܘܡܚܕܐ ܩܡ ܠܥܢܝܗܘܢ ܘܫܩܠ ܥܪܤܗ ܘܐܙܠ ܠܒܝܬܗ ܟܕ ܡܫܒܚ ܠܐܠܗܐ ܀
25 Nit ka jóg ca saa sa ci kanamu ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla.
26ܘܬܡܗܐ ܐܚܕ ܠܟܠܢܫ ܘܡܫܒܚܝܢ ܗܘܘ ܠܐܠܗܐ ܘܐܬܡܠܝܘ ܕܚܠܬܐ ܘܐܡܪܝܢ ܕܚܙܝܢ ܝܘܡܢܐ ܬܕܡܪܬܐ ܀
26 Mbooloo mépp waaru, di màggal Yàlla. Ñu ragal tey wax naan: «Gis nanu tey ay mbir yu ëpp xel.»
27ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܢܦܩ ܝܫܘܥ ܘܚܙܐ ܡܟܤܐ ܕܫܡܗ ܠܘܝ ܕܝܬܒ ܒܝܬ ܡܟܤܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܬܐ ܒܬܪܝ ܀
27 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay topp ci man.»
28ܘܫܒܩ ܟܠ ܡܕܡ ܘܩܡ ܐܙܠ ܒܬܪܗ ܀
28 Lewi jóg, bàyyi lépp, daldi ko topp.
29ܘܥܒܕ ܠܗ ܠܘܝ ܒܒܝܬܗ ܩܘܒܠܐ ܪܒܐ ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܕܡܟܤܐ ܘܕܐܚܪܢܐ ܕܤܡܝܟܝܢ ܗܘܘ ܥܡܗܘܢ ܀
29 Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom.
30ܘܪܛܢܝܢ ܗܘܘ ܤܦܪܐ ܘܦܪܝܫܐ ܘܐܡܪܝܢ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܠܡܢܐ ܥܡ ܡܟܤܐ ܘܚܛܝܐ ܐܟܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܫܬܝܢ ܀
30 Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
31ܘܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܠܐ ܡܬܒܥܐ ܐܤܝܐ ܠܚܠܝܡܐ ܐܠܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܒܝܫ ܒܝܫ ܥܒܝܕܝܢ ܀
31 Yeesu tontu leen ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
32ܠܐ ܐܬܝܬ ܕܐܩܪܐ ܠܙܕܝܩܐ ܐܠܐ ܠܚܛܝܐ ܠܬܝܒܘܬܐ ܀
32 Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»
33ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܠܡܢܐ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܝܘܚܢܢ ܨܝܡܝܢ ܐܡܝܢܐܝܬ ܘܡܨܠܝܢ ܐܦ ܕܦܪܝܫܐ ܕܝܠܟ ܕܝܢ ܐܟܠܝܢ ܘܫܬܝܢ ܀
33 Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.»
34ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܒܢܘܗܝ ܕܓܢܘܢܐ ܟܡܐ ܕܚܬܢܐ ܥܡܗܘܢ ܕܬܥܒܕܘܢ ܕܢܨܘܡܘܢ ܀
34 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeen a woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom?
35ܢܐܬܘܢ ܕܝܢ ܝܘܡܬܐ ܟܕ ܢܬܬܪܝܡ ܚܬܢܐ ܡܢܗܘܢ ܗܝܕܝܢ ܢܨܘܡܘܢ ܒܗܢܘܢ ܝܘܡܬܐ ܀
35 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.»
36ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܬܠܐ ܕܠܐ ܐܢܫ ܩܐܕ ܐܘܪܩܥܬܐ ܡܢ ܡܐܢܐ ܚܕܬܐ ܘܪܡܐ ܥܠ ܡܐܢܐ ܒܠܝܐ ܕܠܐ ܠܚܕܬܐ ܩܐܕ ܘܠܒܠܝܐ ܠܐ ܫܠܡܐ ܐܘܪܩܥܬܐ ܕܡܢ ܚܕܬܐ ܀
36 Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.
37ܘܠܐ ܐܢܫ ܪܡܐ ܚܡܪܐ ܚܕܬܐ ܒܙܩܐ ܒܠܝܬܐ ܘܐܢ ܕܝܢ ܠܐ ܡܒܙܥ ܚܡܪܐ ܚܕܬܐ ܠܙܩܐ ܘܗܘ ܚܡܪܐ ܡܬܐܫܕ ܘܙܩܐ ܐܒܕܢ ܀
37 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bu bees bi day toj mbuus yi, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.
38ܐܠܐ ܚܡܪܐ ܚܕܬܐ ܒܙܩܐ ܚܕܬܬܐ ܪܡܝܢ ܘܬܪܝܗܘܢ ܡܬܢܛܪܝܢ ܀
38 Waaye dañoo war a def biiñ bu bees ci mbuus yu bees.
39ܘܠܐ ܐܢܫ ܫܬܐ ܚܡܪܐ ܥܬܝܩܐ ܘܡܚܕܐ ܒܥܐ ܚܕܬܐ ܐܡܪ ܓܝܪ ܥܬܝܩܐ ܒܤܝܡ ܀
39 Ku naan biiñ bu màggat du bëgg bu bees bi, ndax day wax ne: “Bu màggat bi baax na.”»