Syriac: NT

Wolof: New Testament

Luke

6

1ܗܘܐ ܕܝܢ ܒܫܒܬܐ ܟܕ ܡܗܠܟ ܝܫܘܥ ܒܝܬ ܙܪܥܐ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܡܠܓܝܢ ܗܘܘ ܫܒܠܐ ܘܦܪܟܝܢ ܒܐܝܕܝܗܘܢ ܘܐܟܠܝܢ ܀
1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk.
2ܐܢܫܝܢ ܕܝܢ ܡܢ ܦܪܝܫܐ ܐܡܪܝܢ ܠܗܘܢ ܡܢܐ ܥܒܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܕܡ ܕܠܐ ܫܠܝܛ ܠܡܥܒܕ ܒܫܒܬܐ ܀
2 Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?»
3ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܘܠܐ ܗܕܐ ܩܪܝܬܘܢ ܡܕܡ ܕܥܒܕ ܕܘܝܕ ܟܕ ܟܦܢ ܗܘ ܘܐܝܠܝܢ ܕܥܡܗ ܀
3 Yeesu tontu leen ne: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4ܕܥܠ ܠܒܝܬܗ ܕܐܠܗܐ ܘܠܚܡܐ ܕܦܬܘܪܗ ܕܡܪܝܐ ܢܤܒ ܐܟܠ ܘܝܗܒ ܠܐܝܠܝܢ ܕܥܡܗ ܗܘ ܕܠܐ ܫܠܝܛ ܗܘܐ ܠܡܐܟܠ ܐܠܐ ܠܟܗܢܐ ܒܠܚܘܕ ܀
4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu jébbal Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.»
5ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܕܡܪܗ ܗܘ ܕܫܒܬܐ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܀
5 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
6ܗܘܐ ܕܝܢ ܠܫܒܬܐ ܐܚܪܬܐ ܥܠ ܠܟܢܘܫܬܐ ܘܡܠܦ ܗܘܐ ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܬܡܢ ܓܒܪܐ ܕܐܝܕܗ ܕܝܡܝܢܐ ܝܒܝܫܐ ܗܘܬ ܀
6 Beneen bésu noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram làggi.
7ܘܤܦܪܐ ܘܦܪܝܫܐ ܢܛܪܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܕܐܢ ܗܘ ܕܡܐܤܐ ܒܫܒܬܐ ܕܢܫܟܚܘܢ ܢܐܟܠܘܢ ܩܪܨܘܗܝ ܀
7 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8ܗܘ ܕܝܢ ܝܕܥ ܡܚܫܒܬܗܘܢ ܘܐܡܪ ܠܗܘ ܓܒܪܐ ܕܝܒܝܫܐ ܐܝܕܗ ܩܘܡ ܬܐ ܠܟ ܠܡܨܥܬ ܟܢܘܫܬܐ ܘܟܕ ܐܬܐ ܘܩܡ ܀
8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanamu ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
9ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܐܫܐܠܟܘܢ ܡܢܐ ܫܠܝܛ ܒܫܒܬܐ ܕܛܒ ܠܡܥܒܕ ܐܘ ܕܒܝܫ ܢܦܫܐ ܠܡܚܝܘ ܐܘ ܠܡܘܒܕܘ ܀
9 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
10ܘܚܪ ܒܗܘܢ ܒܟܠܗܘܢ ܘܐܡܪ ܠܗ ܦܫܘܛ ܐܝܕܟ ܘܦܫܛ ܘܬܩܢܬ ܐܝܕܗ ܐܝܟ ܚܒܪܬܗ ܀
10 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ.
11ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܐܬܡܠܝܘ ܚܤܡܐ ܘܡܡܠܠܝܢ ܗܘܘ ܚܕ ܥܡ ܚܕ ܕܡܢܐ ܢܥܒܕܘܢ ܠܗ ܠܝܫܘܥ ܀
11 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
12ܗܘܐ ܕܝܢ ܒܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܢܦܩ ܝܫܘܥ ܠܛܘܪܐ ܠܡܨܠܝܘ ܘܬܡܢ ܐܓܗ ܗܘܐ ܒܨܠܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
12 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
13ܘܟܕ ܢܓܗܬ ܩܪܐ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܓܒܐ ܡܢܗܘܢ ܬܪܥܤܪ ܗܢܘܢ ܕܫܠܝܚܐ ܫܡܝ ܐܢܘܢ ܀
13 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
14ܫܡܥܘܢ ܗܘ ܕܫܡܝ ܟܐܦܐ ܘܐܢܕܪܐܘܤ ܐܚܘܗܝ ܘܝܥܩܘܒ ܘܝܘܚܢܢ ܘܦܝܠܝܦܘܤ ܘܒܪ ܬܘܠܡܝ ܀
14 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
15ܘܡܬܝ ܘܬܐܘܡܐ ܘܝܥܩܘܒ ܒܪ ܚܠܦܝ ܘܫܡܥܘܢ ܕܡܬܩܪܐ ܛܢܢܐ ܀
15 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
16ܘܝܗܘܕܐ ܒܪ ܝܥܩܘܒ ܘܝܗܘܕܐ ܤܟܪܝܘܛܐ ܗܘ ܕܗܘܐ ܡܫܠܡܢܐ ܀
16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor.
17ܘܢܚܬ ܥܡܗܘܢ ܝܫܘܥ ܘܩܡ ܒܦܩܥܬܐ ܘܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܕܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܤܘܓܐܐ ܕܟܢܫܐ ܕܥܡܐ ܡܢ ܟܠܗ ܝܗܘܕ ܘܡܢ ܐܘܪܫܠܡ ܘܡܢ ܤܦܪ ܝܡܐ ܕܨܘܪ ܘܕܨܝܕܢ ܀
17 Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
18ܕܐܬܘ ܕܢܫܡܥܘܢ ܡܠܬܗ ܘܕܢܬܐܤܘܢ ܡܢ ܟܘܪܗܢܝܗܘܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܡܬܐܠܨܝܢ ܡܢ ܪܘܚܐ ܛܢܦܬܐ ܘܡܬܐܤܝܢ ܗܘܘ ܀
18 Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.
19ܘܟܠܗ ܟܢܫܐ ܒܥܝܢ ܗܘܘ ܠܡܬܩܪܒܘ ܠܗ ܚܝܠܐ ܓܝܪ ܢܦܩ ܗܘܐ ܡܢܗ ܘܠܟܠܗܘܢ ܡܐܤܐ ܗܘܐ ܀
19 Ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.
20ܘܐܪܝܡ ܥܝܢܘܗܝ ܥܠ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪ ܛܘܒܝܟܘܢ ܡܤܟܢܐ ܕܕܝܠܟܘܢ ܗܝ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
20 Yeesu xool ay taalibeem ne leen:«Yéen ñi sësul lu dul ci Yàlla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.
21ܛܘܒܝܟܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܟܦܢܝܢ ܗܫܐ ܕܬܤܒܥܘܢ ܛܘܒܝܟܘܢ ܠܕܒܟܝܢ ܗܫܐ ܕܬܓܚܟܘܢ ܀
21 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree.
22ܛܘܒܝܟܘܢ ܡܐ ܕܤܢܝܢ ܠܟܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܘܡܦܪܫܝܢ ܠܟܘܢ ܘܡܚܤܕܝܢ ܠܟܘܢ ܘܡܦܩܝܢ ܫܡܟܘܢ ܐܝܟ ܒܝܫܐ ܚܠܦ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܀
22 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.
23ܚܕܘ ܒܗܘ ܝܘܡܐ ܘܕܘܨܘ ܕܐܓܪܟܘܢ ܤܓܝ ܒܫܡܝܐ ܗܟܢܐ ܓܝܪ ܥܒܕܝܢ ܗܘܘ ܐܒܗܬܗܘܢ ܠܢܒܝܐ ܀
23 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.
24ܒܪܡ ܘܝ ܠܟܘܢ ܥܬܝܪܐ ܕܩܒܠܬܘܢ ܒܘܝܐܟܘܢ ܀
24 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.
25ܘܝ ܠܟܘܢ ܤܒܥܐ ܕܬܟܦܢܘܢ ܘܝ ܠܟܘܢ ܠܕܓܚܟܝܢ ܗܫܐ ܕܬܒܟܘܢ ܘܬܬܐܒܠܘܢ ܀
25 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen,ndax ëllëg dingeen xiif.Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.
26ܘܝ ܠܟܘܢ ܟܕ ܢܗܘܘܢ ܐܡܪܝܢ ܥܠܝܟܘܢ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܕܫܦܝܪ ܗܟܢܐ ܓܝܪ ܥܒܕܝܢ ܗܘܘ ܠܢܒܝܐ ܕܕܓܠܘܬܐ ܐܒܗܬܗܘܢ ܀
26 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.
27ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܕܫܡܥܝܢ ܐܚܒܘ ܠܒܥܠܕܒܒܝܟܘܢ ܘܥܒܕܘ ܕܫܦܝܪ ܠܐܝܠܝܢ ܕܤܢܝܢ ܠܟܘܢ ܀
27 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
28ܘܒܪܟܘ ܠܐܝܠܝܢ ܕܠܝܛܝܢ ܠܟܘܢ ܘܨܠܘ ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܕܒܪܝܢ ܠܟܘܢ ܒܩܛܝܪܐ ܀
28 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
29ܘܠܕܡܚܐ ܠܟ ܥܠ ܦܟܟ ܩܪܒ ܠܗ ܐܚܪܢܐ ܘܡܢ ܡܢ ܕܫܩܠ ܡܪܛܘܛܟ ܠܐ ܬܟܠܐ ܐܦ ܟܘܬܝܢܟ ܀
29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
30ܠܟܠ ܕܫܐܠ ܠܟ ܗܒ ܠܗ ܘܡܢ ܡܢ ܕܫܩܠ ܕܝܠܟ ܠܐ ܬܬܒܥ ܀
30 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
31ܘܐܝܟܢܐ ܕܨܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܢܥܒܕܘܢ ܠܟܘܢ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܗܟܘܬ ܥܒܕܘ ܠܗܘܢ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܀
31 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
32ܐܢ ܓܝܪ ܡܚܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܚܒܝܢ ܠܟܘܢ ܐܝܕܐ ܗܝ ܛܝܒܘܬܟܘܢ ܐܦ ܓܝܪ ܚܛܝܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܚܒܝܢ ܠܗܘܢ ܪܚܡܝܢ ܀
32 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
33ܘܐܢ ܥܒܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܛܒ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܛܐܒܝܢ ܠܟܘܢ ܐܝܕܐ ܗܝ ܛܝܒܘܬܟܘܢ ܐܦ ܚܛܝܐ ܓܝܪ ܗܟܢܐ ܥܒܕܝܢ ܀
33 Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.
34ܘܐܢ ܡܘܙܦܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܢ ܕܤܒܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܬܬܦܪܥܘܢ ܡܢܗ ܐܝܕܐ ܗܝ ܛܝܒܘܬܟܘܢ ܐܦ ܚܛܝܐ ܓܝܪ ܠܚܛܝܐ ܡܘܙܦܝܢ ܕܗܟܘܬ ܢܬܦܪܥܘܢ ܀
34 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.
35ܒܪܡ ܐܚܒܘ ܠܒܥܠܕܒܒܝܟܘܢ ܘܐܛܐܒܘ ܠܗܘܢ ܘܐܘܙܦܘ ܘܠܐ ܬܦܤܩܘܢ ܤܒܪܐ ܕܐܢܫ ܘܢܗܘܐ ܤܓܝ ܐܓܪܟܘܢ ܘܬܗܘܘܢ ܒܢܘܗܝ ܕܪܡܐ ܕܗܘ ܒܤܝܡ ܗܘ ܥܠ ܒܝܫܐ ܘܥܠ ܟܦܘܪܐ ܀
35 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, bañ a yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
36ܗܘܘ ܗܟܝܠ ܡܪܚܡܢܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܐܒܘܟܘܢ ܡܪܚܡܢܐ ܗܘ ܀
36 Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
37ܠܐ ܬܕܘܢܘܢ ܘܠܐ ܡܬܬܕܝܢܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐ ܬܚܝܒܘܢ ܘܠܐ ܡܬܚܝܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܫܪܘ ܘܬܫܬܪܘܢ ܀
37 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
38ܗܒܘ ܘܡܬܝܗܒ ܠܟܘܢ ܒܟܝܠܬܐ ܛܒܬܐ ܘܪܩܝܥܬܐ ܘܡܫܦܥܬܐ ܢܪܡܘܢ ܒܥܘܒܝܟܘܢ ܒܗܝ ܓܝܪ ܟܝܠܬܐ ܕܡܟܝܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܬܬܟܝܠ ܠܟܘܢ ܀
38 Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
39ܘܐܡܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܡܬܠܐ ܠܡܐ ܡܫܟܚ ܤܡܝܐ ܠܤܡܝܐ ܠܡܕܒܪܘ ܠܐ ܬܪܝܗܘܢ ܒܓܘܡܨܐ ܢܦܠܝܢ ܀
39 Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?
40ܠܝܬ ܬܠܡܝܕܐ ܕܝܬܝܪ ܡܢ ܪܒܗ ܟܠܢܫ ܓܝܪ ܕܓܡܝܪ ܢܗܘܐ ܐܝܟ ܪܒܗ ܀
40 Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.
41ܡܢܐ ܕܝܢ ܚܙܐ ܐܢܬ ܓܠܐ ܕܒܥܝܢܗ ܕܐܚܘܟ ܩܪܝܬܐ ܕܝܢ ܕܒܥܝܢܟ ܠܐ ܡܬܚܙܝܐ ܠܟ ܀
41 «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
42ܐܘ ܐܝܟܢܐ ܡܫܟܚ ܐܢܬ ܠܡܐܡܪ ܠܐܚܘܟ ܐܚܝ ܫܒܘܩ ܐܦܩ ܓܠܐ ܡܢ ܥܝܢܟ ܕܗܐ ܩܪܝܬܐ ܕܒܥܝܢܟ ܕܝܠܟ ܠܐ ܡܬܚܙܝܐ ܠܟ ܢܤܒ ܒܐܦܐ ܐܦܩ ܠܘܩܕܡ ܩܪܝܬܐ ܡܢ ܥܝܢܟ ܘܗܝܕܝܢ ܢܬܚܙܐ ܠܟ ܠܡܦܩܘ ܓܠܐ ܡܢ ܥܝܢܗ ܕܐܚܘܟ ܀
42 Nan nga man a waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
43ܠܐ ܐܝܬ ܐܝܠܢܐ ܛܒܐ ܕܥܒܕ ܦܐܪܐ ܒܝܫܐ ܐܦ ܠܐ ܐܝܠܢܐ ܒܝܫܐ ܕܥܒܕ ܦܐܪܐ ܛܒܐ ܀
43 «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
44ܟܠ ܐܝܠܢܐ ܓܝܪ ܡܢ ܦܐܪܘܗܝ ܗܘ ܡܬܝܕܥ ܠܐ ܓܝܪ ܠܩܛܝܢ ܡܢ ܟܘܒܐ ܬܐܢܐ ܐܦ ܠܐ ܡܢ ܤܢܝܐ ܩܛܦܝܢ ܥܢܒܐ ܀
44 Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla réseñ ci xaaxaam.
45ܓܒܪܐ ܛܒܐ ܡܢ ܤܝܡܬܐ ܛܒܬܐ ܕܒܠܒܗ ܡܦܩ ܛܒܬܐ ܘܓܒܪܐ ܒܝܫܐ ܡܢ ܤܝܡܬܐ ܒܝܫܬܐ ܕܒܠܒܗ ܡܦܩ ܒܝܫܬܐ ܡܢ ܬܘܬܪܝ ܠܒܐ ܓܝܪ ܡܡܠܠܢ ܤܦܘܬܐ ܀
45 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.
46ܡܢܐ ܩܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܝ ܡܪܝ ܡܪܝ ܘܡܕܡ ܕܐܡܪ ܐܢܐ ܠܐ ܥܒܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
46 «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax?
47ܟܠ ܐܢܫ ܕܐܬܐ ܠܘܬܝ ܘܫܡܥ ܡܠܝ ܘܥܒܕ ܠܗܝܢ ܐܚܘܝܟܘܢ ܠܡܢܐ ܕܡܐ ܀
47 Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel.
48ܕܡܐ ܠܓܒܪܐ ܕܒܢܐ ܒܝܬܐ ܘܚܦܪ ܘܥܡܩ ܘܤܡ ܫܬܐܤܐ ܥܠ ܫܘܥܐ ܟܕ ܗܘܐ ܕܝܢ ܡܠܐܐ ܐܬܛܪܝ ܡܠܐܐ ܒܒܝܬܐ ܗܘ ܘܠܐ ܐܫܟܚ ܕܢܙܝܥܝܘܗܝ ܤܝܡܐ ܗܘܬ ܓܝܪ ܫܬܐܤܬܗ ܥܠ ܫܘܥܐ ܀
48 Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër.
49ܘܗܘ ܕܫܡܥ ܘܠܐ ܥܒܕ ܕܡܐ ܠܓܒܪܐ ܕܒܢܐ ܒܝܬܗ ܥܠ ܥܦܪܐ ܕܠܐ ܫܬܐܤܬܐ ܘܟܕ ܐܬܛܪܝ ܒܗ ܢܗܪܐ ܒܪ ܫܥܬܗ ܢܦܠ ܘܗܘܬ ܡܦܘܠܬܗ ܪܒܐ ܕܒܝܬܐ ܗܘ ܀
49 Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»