1ܘܗܘܐ ܡܢ ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܡܬܟܪܟ ܗܘܐ ܝܫܘܥ ܒܡܕܝܢܬܐ ܘܒܩܘܪܝܐ ܘܡܟܪܙ ܗܘܐ ܘܡܤܒܪ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܬܪܥܤܪܬܗ ܥܡܗ ܀
1 Gannaaw loolu Yeesu di dem ca ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di waaraate ak di yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla. Fukki taalibe ya ak ñaar ànd ak moom,
2ܘܢܫܐ ܗܠܝܢ ܕܐܬܐܤܝ ܡܢ ܟܘܪܗܢܐ ܘܡܢ ܪܘܚܐ ܒܝܫܬܐ ܡܪܝܡ ܕܡܬܩܪܝܐ ܡܓܕܠܝܬܐ ܗܝ ܕܫܒܥܐ ܫܐܕܝܢ ܢܦܩܘ ܡܢܗ ܀
2 ak ay jigéen yu mu teqale woon ak rab te jële leen ci seeni wopp, ñu di: Maryaama, mi ñuy wooye Maryaamam Magdala, mi Yeesu tàggale woon ak juróom-ñaari rab;
3ܘܝܘܚܢ ܐܢܬܬ ܟܘܙܐ ܪܒܝܬܗ ܕܗܪܘܕܤ ܘܫܘܫܢ ܘܐܚܪܢܝܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܡܫܡܫܢ ܗܘܝ ܠܗܘܢ ܡܢ ܩܢܝܢܝܗܝܢ ܀
3 Sànn, jabaru ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.
4ܘܟܕ ܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܟܢܫ ܗܘܐ ܘܡܢ ܟܠ ܡܕܝܢܢ ܐܬܝܢ ܗܘܘ ܠܘܬܗ ܐܡܪ ܒܡܬܠܐ ܀
4 Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii:
5ܢܦܩ ܙܪܘܥܐ ܠܡܙܪܥ ܙܪܥܗ ܘܟܕ ܙܪܥ ܐܝܬ ܕܢܦܠ ܥܠ ܝܕ ܐܘܪܚܐ ܘܐܬܕܝܫ ܘܐܟܠܬܗ ܦܪܚܬܐ ܀
5 «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp.
6ܘܐܚܪܢܐ ܢܦܠ ܥܠ ܫܘܥܐ ܘܒܪ ܫܥܬܗ ܝܥܐ ܘܕܠܝܬ ܗܘܐ ܠܗ ܬܠܝܠܘܬܐ ܝܒܫ ܀
6 Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.
7ܘܐܚܪܢܐ ܢܦܠ ܒܝܬ ܟܘܒܐ ܘܝܥܘ ܥܡܗ ܟܘܒܐ ܘܚܢܩܘܗܝ ܀
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.
8ܘܐܚܪܢܐ ܢܦܠ ܒܐܪܥܐ ܛܒܬܐ ܘܫܦܝܪܬܐ ܘܝܥܐ ܘܥܒܕ ܦܐܪܐ ܚܕ ܒܡܐܐ ܗܠܝܢ ܟܕ ܐܡܪ ܩܥܐ ܗܘܐ ܕܡܢ ܕܐܝܬ ܠܗ ܐܕܢܐ ܕܢܫܡܥ ܢܫܡܥ ܀
8 Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
9ܘܫܐܠܘܗܝ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܡܢܘ ܡܬܠܐ ܗܢܐ ܀
9 Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki.
10ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܠܟܘܢ ܗܘ ܝܗܝܒ ܠܡܕܥ ܐܪܙܐ ܕܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܠܗܢܘܢ ܕܝܢ ܫܪܟܐ ܒܦܠܐܬܐ ܡܬܐܡܪ ܕܟܕ ܚܙܝܢ ܠܐ ܢܚܙܘܢ ܘܟܕ ܫܡܥܝܢ ܠܐ ܢܤܬܟܠܘܢ ܀
10 Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.”
11ܗܢܘ ܕܝܢ ܡܬܠܐ ܙܪܥܐ ܐܝܬܘܗܝ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
11 «Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi.
12ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܕܥܠ ܝܕ ܐܘܪܚܐ ܐܝܬܝܗܘܢ ܗܢܘܢ ܕܫܡܥܝܢ ܡܠܬܐ ܘܐܬܐ ܒܥܠܕܒܒܐ ܫܩܠ ܡܠܬܐ ܡܢ ܠܒܗܘܢ ܕܠܐ ܢܗܝܡܢܘܢ ܘܢܚܘܢ ܀
12 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu bañ a gëm te Yàlla musal ko.
13ܗܠܝܢ ܕܝܢ ܕܥܠ ܫܘܥܐ ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܕܡܐ ܕܫܡܥܘ ܒܚܕܘܬܐ ܡܩܒܠܝܢ ܠܗ ܠܡܠܬܐ ܘܥܩܪܐ ܠܝܬ ܠܗܘܢ ܐܠܐ ܕܙܒܢܐ ܗܝ ܗܝܡܢܘܬܗܘܢ ܘܒܙܒܢ ܢܤܝܘܢܐ ܡܬܟܫܠܝܢ ܀
13 Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.
14ܗܘ ܕܝܢ ܕܢܦܠ ܒܝܬ ܟܘܒܐ ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܫܡܥܝܢ ܡܠܬܐ ܘܒܨܦܬܐ ܘܒܥܘܬܪܐ ܘܒܪܓܝܓܬܗ ܕܥܠܡܐ ܡܬܚܢܩܝܢ ܘܦܐܪܐ ܠܐ ܝܗܒܝܢ ܀
14 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nes tuuti soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.
15ܗܘ ܕܝܢ ܕܒܐܪܥܐ ܛܒܬܐ ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܒܠܒܐ ܫܦܝܐ ܘܛܒܐ ܫܡܥܝܢ ܡܠܬܐ ܘܐܚܕܝܢ ܘܝܗܒܝܢ ܦܐܪܐ ܒܡܤܝܒܪܢܘܬܐ ܀
15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
16ܠܐ ܐܢܫ ܡܢܗܪ ܫܪܓܐ ܘܡܚܦܐ ܠܗ ܒܡܐܢܐ ܐܘ ܤܐܡ ܠܗ ܬܚܝܬ ܥܪܤܐ ܐܠܐ ܤܐܡ ܠܗ ܠܥܠ ܡܢ ܡܢܪܬܐ ܕܟܠ ܕܥܐܠ ܢܚܙܐ ܢܘܗܪܗ ܀
16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17ܠܝܬ ܓܝܪ ܡܕܡ ܕܟܤܐ ܕܠܐ ܢܬܓܠܐ ܘܠܐ ܕܡܛܫܝ ܕܠܐ ܢܬܝܕܥ ܘܢܐܬܐ ܠܓܠܝܐ ܀
17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18ܚܙܘ ܐܝܟܢܐ ܫܡܥܬܘܢ ܡܢ ܕܐܝܬ ܠܗ ܓܝܪ ܢܬܝܗܒ ܠܗ ܘܡܢ ܕܠܝܬ ܠܗ ܐܦ ܗܘ ܕܤܒܪ ܕܐܝܬ ܠܗ ܢܫܬܩܠ ܡܢܗ ܀
18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne, am nga ko ba noppi.»
19ܐܬܘ ܕܝܢ ܠܘܬܗ ܐܡܗ ܘܐܚܘܗܝ ܘܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܗܘܘ ܕܢܡܠܠܘܢ ܥܡܗ ܡܛܠ ܟܢܫܐ ܀
19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye mënuñu woon a agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.
20ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܐܡܟ ܘܐܚܝܟ ܩܝܡܝܢ ܠܒܪ ܘܨܒܝܢ ܠܡܚܙܝܟ ܀
20 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21ܗܘ ܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܐܡܝ ܘܐܚܝ ܐܝܠܝܢ ܕܫܡܥܝܢ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܥܒܕܝܢ ܠܗ ܀
21 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»
22ܗܘܐ ܕܝܢ ܒܚܕ ܡܢ ܝܘܡܬܐ ܤܠܩ ܝܫܘܥ ܝܬܒ ܒܤܦܝܢܬܐ ܗܘ ܘܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܢܥܒܪ ܠܗܘ ܥܒܪܐ ܕܝܡܬܐ ܀
22 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
23ܘܟܕ ܪܕܝܢ ܕܡܟ ܠܗ ܗܘ ܝܫܘܥ ܘܗܘܬ ܥܠܥܠܐ ܕܪܘܚܐ ܒܝܡܬܐ ܘܩܪܝܒܐ ܗܘܬ ܤܦܝܢܬܐ ܠܡܛܒܥ ܀
23 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yengal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgg a suux.
24ܘܩܪܒܘ ܐܥܝܪܘܗܝ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܪܒܢ ܪܒܢ ܐܒܕܝܢܢ ܗܘ ܕܝܢ ܩܡ ܘܟܐܐ ܒܪܘܚܐ ܘܒܡܚܫܘܠܐ ܕܝܡܐ ܘܢܚܘ ܘܗܘܐ ܫܠܝܐ ܀
24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
25ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܝܟܐ ܗܝ ܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܟܕ ܕܚܝܠܝܢ ܡܬܕܡܪܝܢ ܗܘܘ ܘܐܡܪܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܡܢܘ ܟܝ ܗܢܐ ܕܐܦ ܠܪܘܚܐ ܦܩܕ ܘܠܡܚܫܘܠܐ ܘܠܝܡܐ ܘܡܫܬܡܥܝܢ ܠܗ ܀
25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
26ܘܪܕܘ ܘܐܬܘ ܠܐܬܪܐ ܕܓܕܪܝܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܒܥܒܪܐ ܠܘܩܒܠ ܓܠܝܠܐ ܀
26 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27ܘܟܕ ܢܦܩ ܠܐܪܥܐ ܦܓܥ ܒܗ ܓܒܪܐ ܚܕ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܕܐܝܬ ܒܗ ܕܝܘܐ ܡܢ ܙܒܢܐ ܤܓܝܐܐ ܘܡܐܢܐ ܠܐ ܠܒܫ ܗܘܐ ܘܒܒܝܬܐ ܠܐ ܥܡܪ ܗܘܐ ܐܠܐ ܒܒܝܬ ܩܒܘܪܐ ܀
27 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
28ܟܕ ܚܙܐ ܕܝܢ ܠܝܫܘܥ ܩܥܐ ܘܢܦܠ ܩܕܡܘܗܝ ܘܒܩܠܐ ܪܡܐ ܐܡܪ ܡܐ ܠܢ ܘܠܟ ܝܫܘܥ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܡܪܝܡܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܠܐ ܬܫܢܩܢܝ ܀
28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
29ܦܩܕ ܗܘܐ ܠܗ ܓܝܪ ܝܫܘܥ ܠܪܘܚܐ ܛܢܦܐ ܠܡܦܩ ܡܢ ܒܪܢܫܐ ܤܓܝ ܗܘܐ ܓܝܪ ܙܒܢܐ ܡܢ ܕܫܒܐ ܗܘܐ ܠܗ ܘܡܬܐܤܪ ܗܘܐ ܒܫܫܠܬܐ ܘܒܟܒܠܐ ܡܬܢܛܪ ܗܘܐ ܘܡܦܤܩ ܗܘܐ ܐܤܘܪܘܗܝ ܘܡܬܕܒܪ ܗܘܐ ܡܢ ܫܐܕܐ ܠܚܘܪܒܐ ܀
29 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
30ܫܐܠܗ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܡܢ ܫܡܟ ܐܡܪ ܠܗ ܠܓܝܘܢ ܡܛܠ ܕܕܝܘܐ ܤܓܝܐܐ ܥܠܝܠܝܢ ܗܘܘ ܒܗ ܀
30 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ne: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
31ܘܒܥܝܢ ܗܘܘ ܡܢܗ ܕܠܐ ܢܦܩܘܕ ܠܗܘܢ ܠܡܐܙܠ ܠܬܗܘܡܐ ܀
31 Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leen a sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
32ܐܝܬ ܗܘܐ ܕܝܢ ܬܡܢ ܒܩܪܐ ܕܚܙܝܪܐ ܤܓܝܐܐ ܕܪܥܝܐ ܒܛܘܪܐ ܘܒܥܝܢ ܗܘܘ ܡܢܗ ܕܢܦܤ ܠܗܘܢ ܕܒܚܙܝܪܐ ܢܥܠܘܢ ܘܐܦܤ ܠܗܘܢ ܀
32 Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33ܘܢܦܩܘ ܫܐܕܐ ܡܢ ܓܒܪܐ ܘܥܠܘ ܒܚܙܝܪܐ ܘܬܪܨܬ ܒܩܪܐ ܗܝ ܟܠܗ ܠܫܩܝܦܐ ܘܢܦܠܘ ܒܝܡܬܐ ܘܐܬܚܢܩܘ ܀
33 Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
34ܟܕ ܚܙܘ ܕܝܢ ܪܥܘܬܐ ܡܕܡ ܕܗܘܐ ܥܪܩܘ ܘܐܫܬܥܝܘ ܒܡܕܝܢܬܐ ܘܒܩܘܪܝܐ ܀
34 Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
35ܘܢܦܩܘ ܐܢܫܐ ܕܢܚܙܘܢ ܡܕܡ ܕܗܘܐ ܘܐܬܘ ܠܘܬ ܝܫܘܥ ܘܐܫܟܚܘܗܝ ܠܓܒܪܐ ܗܘ ܕܢܦܩܘ ܫܐܕܘܗܝ ܟܕ ܠܒܝܫ ܘܡܢܟܦ ܘܝܬܒ ܠܘܬ ܪܓܠܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܘܕܚܠܘ ܀
35 Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
36ܘܐܫܬܥܝܘ ܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܚܙܘ ܐܝܟܢܐ ܐܬܐܤܝ ܓܒܪܐ ܗܘ ܕܝܘܢܐ ܀
36 Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
37ܘܒܥܝܢ ܗܘܘ ܡܢܗ ܟܠܗ ܟܢܫܐ ܕܓܕܪܝܐ ܕܢܐܙܠ ܠܗ ܡܢ ܠܘܬܗܘܢ ܡܛܠ ܕܕܚܠܬܐ ܪܒܬܐ ܐܚܕܬ ܐܢܘܢ ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܤܠܩ ܠܤܦܝܢܬܐ ܘܗܦܟ ܡܢ ܠܘܬܗܘܢ ܀
37 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgg a dem.
38ܗܘ ܕܝܢ ܓܒܪܐ ܕܢܦܩܘ ܡܢܗ ܫܐܕܐ ܒܥܐ ܗܘܐ ܡܢܗ ܕܠܘܬܗ ܢܗܘܐ ܘܫܪܝܗܝ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܀
38 Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu woññi ko ne ko:
39ܗܦܘܟ ܠܒܝܬܟ ܘܐܫܬܥܐ ܡܕܡ ܕܥܒܕ ܠܟ ܐܠܗܐ ܘܐܙܠ ܘܡܟܪܙ ܗܘܐ ܒܟܠܗ ܡܕܝܢܬܐ ܡܕܡ ܕܥܒܕ ܠܗ ܝܫܘܥ ܀
39 «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
40ܟܕ ܗܦܟ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܩܒܠܗ ܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܟܠܗܘܢ ܓܝܪ ܠܗ ܚܝܪܝܢ ܗܘܘ ܀
40 Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
41ܘܓܒܪܐ ܚܕ ܕܫܡܗ ܝܘܐܪܫ ܪܝܫ ܟܢܘܫܬܐ ܢܦܠ ܩܕܡ ܪܓܠܘܗܝ ܕܝܫܘܥ ܘܒܥܐ ܗܘܐ ܡܢܗ ܕܢܥܘܠ ܠܒܝܬܗ ܀
41 Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, saraxu ko mu ñëw këram,
42ܒܪܬܐ ܓܝܪ ܝܚܝܕܝܬܐ ܐܝܬ ܗܘܬ ܠܗ ܐܝܟ ܒܪܬ ܫܢܝܢ ܬܪܬܥܤܪܐ ܘܩܪܝܒܐ ܗܘܬ ܠܡܡܬ ܘܟܕ ܐܙܠ ܥܡܗ ܗܘ ܝܫܘܥ ܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܚܒܨ ܗܘܐ ܠܗ ܀
42 ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaj a dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
43ܐܢܬܬܐ ܕܝܢ ܚܕܐ ܕܬܪܝܥ ܗܘܐ ܕܡܗ ܫܢܝܢ ܬܪܬܥܤܪܐ ܗܝ ܕܒܝܬ ܐܤܘܬܐ ܟܠܗ ܩܢܝܢܗ ܐܦܩܬ ܘܠܐ ܐܫܟܚܬ ܕܡܢ ܐܢܫ ܬܬܐܤܐ ܀
43 Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn mënu ko woon a faj.
44ܐܬܩܪܒܬ ܡܢ ܒܤܬܪܗ ܘܩܪܒܬ ܠܟܢܦܐ ܕܡܐܢܗ ܘܡܚܕܐ ܩܡܬ ܡܪܕܝܬܐ ܕܕܡܗ ܀
44 Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
45ܘܐܡܪ ܝܫܘܥ ܡܢܘ ܩܪܒ ܠܝ ܘܟܕ ܟܠܗܘܢ ܟܦܪܝܢ ܐܡܪ ܠܗ ܫܡܥܘܢ ܟܐܦܐ ܘܕܥܡܗ ܪܒܢ ܟܢܫܐ ܐܠܨܝܢ ܠܟ ܘܚܒܨܝܢ ܘܐܡܪ ܐܢܬ ܡܢܘ ܩܪܒ ܠܝ ܀
45 Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
46ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܫ ܩܪܒ ܠܝ ܐܢܐ ܓܝܪ ܝܕܥܬ ܕܚܝܠܐ ܢܦܩ ܡܢܝ ܀
46 Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne, am na doole ju génn ci man.»
47ܗܝ ܕܝܢ ܐܢܬܬܐ ܟܕ ܚܙܬ ܕܠܐ ܛܥܬܗ ܐܬܬ ܟܕ ܪܬܝܬܐ ܘܢܦܠܬ ܤܓܕܬ ܠܗ ܘܐܡܪܬ ܠܥܝܢ ܥܡܐ ܟܠܗ ܡܛܠ ܐܝܕܐ ܥܠܬܐ ܩܪܒܬ ܘܐܝܟܢܐ ܡܚܕܐ ܐܬܐܤܝܬ ܀
47 Te jigéen ja xam ne, mënul woon a nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanamu ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.
48ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܐܡܪ ܠܗ ܐܬܠܒܒܝ ܒܪܬܝ ܗܝܡܢܘܬܟܝ ܐܚܝܬܟܝ ܙܠܝ ܒܫܠܡܐ ܀
48 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.»
49ܘܥܕ ܗܘ ܡܡܠܠ ܐܬܐ ܐܢܫ ܡܢ ܕܒܝܬ ܪܒ ܟܢܘܫܬܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܡܝܬܬ ܠܗ ܒܪܬܟ ܠܐ ܬܥܡܠ ܠܡܠܦܢܐ ܀
49 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.»
50ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܫܡܥ ܘܐܡܪ ܠܐܒܘܗ ܕܛܠܝܬܐ ܠܐ ܬܕܚܠ ܒܠܚܘܕ ܗܝܡܢ ܘܚܝܐ ܀
50 Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.»
51ܐܬܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܠܒܝܬܐ ܘܠܐ ܫܒܩ ܠܐܢܫ ܕܢܥܘܠ ܥܡܗ ܐܠܐ ܠܫܡܥܘܢ ܘܠܝܥܩܘܒ ܘܠܝܘܚܢܢ ܘܠܐܒܘܗ ܕܛܠܝܬܐ ܘܠܐܡܗ ܀
51 Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.
52ܟܠܗܘܢ ܕܝܢ ܒܟܝܢ ܗܘܘ ܘܡܪܩܕܝܢ ܥܠܝܗ ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܐ ܬܒܟܘܢ ܠܐ ܓܝܪ ܡܝܬܬ ܐܠܐ ܕܡܟܐ ܗܝ ܀
52 Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
53ܘܓܚܟܝܢ ܗܘܘ ܥܠܘܗܝ ܕܝܕܥܝܢ ܕܡܝܬܬ ܠܗ ܀
53 Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne, dee na.
54ܗܘ ܕܝܢ ܐܦܩ ܠܟܠܢܫ ܠܒܪ ܘܐܚܕܗ ܒܐܝܕܗ ܘܩܪܗ ܘܐܡܪ ܛܠܝܬܐ ܩܘܡܝ ܀
54 Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.»
55ܘܗܦܟܬ ܪܘܚܗ ܘܡܚܕܐ ܩܡܬ ܘܦܩܕ ܕܢܬܠܘܢ ܠܗ ܠܡܐܟܠ ܀
55 Noonu ruuwu xale ba dellusiwaat, mu daldi jóg ca saa sa. Yeesu santaane ñu may ko, mu lekk.
56ܘܬܡܗܘ ܐܒܗܝܗ ܗܘ ܕܝܢ ܙܗܪ ܐܢܘܢ ܕܠܐܢܫ ܠܐ ܢܐܡܪܘܢ ܡܐ ܕܗܘܐ ܀
56 Waajuri xale bi daldi waaru. Waaye Yeesu tere leen, ñu wax kenn li xew.