Syriac: NT

Wolof: New Testament

Luke

9

1ܘܩܪܐ ܝܫܘܥ ܠܬܪܥܤܪܬܗ ܘܝܗܒ ܠܗܘܢ ܚܝܠܐ ܘܫܘܠܛܢܐ ܥܠ ܟܠܗܘܢ ܫܐܕܐ ܘܟܘܪܗܢܐ ܠܡܐܤܝܘ ܀
1 Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi.
2ܘܫܕܪ ܐܢܘܢ ܠܡܟܪܙܘ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܘܠܡܐܤܝܘ ܟܪܝܗܐ ܀
2 Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi.
3ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܕܡ ܠܐ ܬܫܩܠܘܢ ܠܐܘܪܚܐ ܠܐ ܫܒܛܐ ܘܠܐ ܬܪܡܠܐ ܘܠܐ ܠܚܡܐ ܘܠܐ ܟܤܦܐ ܘܠܐ ܬܪܬܝܢ ܟܘܬܝܢܝܢ ܢܗܘܝܢ ܠܟܘܢ ܀
3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki.
4ܘܠܐܝܢܐ ܒܝܬܐ ܕܥܐܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܬܡܢ ܗܘܘ ܘܡܢ ܬܡܢ ܦܘܩܘ ܀
4 Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge.
5ܘܠܡܢ ܕܠܐ ܡܩܒܠܝܢ ܠܟܘܢ ܡܐ ܕܢܦܩܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܗܝ ܐܦ ܚܠܐ ܡܢ ܪܓܠܝܟܘܢ ܦܨܘ ܥܠܝܗܘܢ ܠܤܗܕܘܬܐ ܀
5 Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
6ܘܢܦܩܘ ܫܠܝܚܐ ܘܡܬܟܪܟܝܢ ܗܘܘ ܒܩܘܪܝܐ ܘܒܡܕܝܢܬܐ ܘܡܤܒܪܝܢ ܗܘܘ ܘܡܐܤܝܢ ܒܟܠ ܕܘܟ ܀
6 Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xebaar bu baax bi, tey wéral jarag yi.
7ܫܡܥ ܕܝܢ ܗܪܘܕܤ ܛܛܪܪܟܐ ܟܠܗܝܢ ܕܗܘܝܢ ܗܘܝ ܒܐܝܕܗ ܘܡܬܕܡܪ ܗܘܐ ܡܛܠ ܕܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܐܢܫܝܢ ܕܝܘܚܢܢ ܩܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܀
7 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.»
8ܐܚܪܢܐ ܕܝܢ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܐܠܝܐ ܐܬܚܙܝ ܘܐܚܪܢܐ ܕܢܒܝܐ ܡܢ ܢܒܝܐ ܩܕܡܝܐ ܩܡ ܀
8 Am it ñuy wax naan: Iliyas moo dellusi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
9ܘܐܡܪ ܗܪܘܕܤ ܪܫܗ ܕܝܘܚܢܢ ܐܢܐ ܦܤܩܬ ܡܢܘ ܕܝܢ ܗܢܐ ܕܗܠܝܢ ܫܡܥ ܐܢܐ ܥܠܘܗܝ ܘܨܒܐ ܗܘܐ ܕܢܚܙܝܘܗܝ ܀
9 Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.
10ܘܟܕ ܗܦܟܘ ܫܠܝܚܐ ܐܫܬܥܝܘ ܠܝܫܘܥ ܟܠܡܕܡ ܕܥܒܕܘ ܘܕܒܪ ܐܢܘܢ ܒܠܚܘܕܝܗܘܢ ܠܐܬܪܐ ܚܘܪܒܐ ܕܒܝܬ ܨܝܕܐ ܀
10 Bi ndaw ya dellusee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda.
11ܟܢܫܐ ܕܝܢ ܟܕ ܝܕܥܘ ܐܙܠܘ ܒܬܪܗ ܘܩܒܠ ܐܢܘܢ ܘܡܡܠܠ ܗܘܐ ܥܡܗܘܢ ܥܠ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܠܐܝܠܝܢ ܕܤܢܝܩܝܢ ܗܘܘ ܥܠ ܐܤܝܘܬܐ ܡܐܤܐ ܗܘܐ ܀
11 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.
12ܟܕ ܕܝܢ ܫܪܝ ܝܘܡܐ ܠܡܨܠܐ ܩܪܒܘ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܫܪܝ ܠܟܢܫܐ ܕܢܐܙܠܘܢ ܠܩܘܪܝܐ ܕܚܕܪܝܢ ܘܠܟܦܪܘܢܐ ܕܢܫܪܘܢ ܒܗܘܢ ܘܢܫܟܚܘܢ ܠܗܘܢ ܤܝܒܪܬܐ ܡܛܠ ܕܒܐܬܪܐ ܚܘܪܒܐ ܐܝܬܝܢ ܀
12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.»
13ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܗܒܘ ܠܗܘܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܐܟܠ ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܐܡܪܝܢ ܠܝܬ ܠܢ ܝܬܝܪ ܡܢ ܚܡܫܐ ܠܚܡܝܢ ܘܬܪܝܢ ܢܘܢܝܢ ܐܠܐ ܐܢ ܐܙܠܢܢ ܘܙܒܢܢ ܤܝܒܪܬܐ ܠܗܢܐ ܟܠܗ ܥܡܐ ܀
13 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu tontu ko ne: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»
14ܗܘܝܢ ܗܘܘ ܓܝܪ ܐܝܟ ܚܡܫܐ ܐܠܦܝܢ ܓܒܪܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܐܤܡܟܘ ܐܢܘܢ ܤܡܟܐ ܚܡܫܝܢ ܐܢܫܝܢ ܒܤܡܟܐ ܀
14 Ndaxte lu war a mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom-fukki nit.»
15ܘܥܒܕܘ ܗܟܘܬ ܬܠܡܝܕܐ ܘܐܤܡܟܘ ܠܟܠܗܘܢ ܀
15 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.
16ܘܢܤܒ ܝܫܘܥ ܗܢܘܢ ܚܡܫܐ ܠܚܡܝܢ ܘܬܪܝܢ ܢܘܢܝܢ ܘܚܪ ܒܫܡܝܐ ܘܒܪܟ ܘܩܨܐ ܘܝܗܒ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܢܤܝܡܘܢ ܠܟܢܫܐ ܀
16 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi.
17ܘܐܟܠܘ ܟܠܗܘܢ ܘܤܒܥܘ ܘܫܩܠܘ ܩܨܝܐ ܡܕܡ ܕܐܘܬܪܘ ܬܪܥܤܪ ܩܘܦܝܢܝܢ ܀
17 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.
18ܘܟܕ ܡܨܠܐ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܘܬܠܡܝܕܘܗܝ ܥܡܗ ܫܐܠ ܐܢܘܢ ܘܐܡܪ ܡܢܘ ܐܡܪܝܢ ܥܠܝ ܟܢܫܐ ܕܐܝܬܝ ܀
18 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?»
19ܥܢܘ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܕܝܘܚܢܢ ܡܥܡܕܢܐ ܘܐܚܪܢܐ ܕܐܠܝܐ ܐܚܪܢܐ ܕܝܢ ܕܢܒܝܐ ܚܕ ܡܢ ܢܒܝܐ ܩܕܡܝܐ ܩܡ ܀
19 Ñu tontu ko ne: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
20ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܡܢܘ ܐܡܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܝܬܝ ܥܢܐ ܫܡܥܘܢ ܘܐܡܪ ܡܫܝܚܗ ܕܐܠܗܐ ܀
20 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»
21ܗܘ ܕܝܢ ܟܐܐ ܒܗܘܢ ܘܙܗܪ ܐܢܘܢ ܕܗܕܐ ܠܐܢܫ ܠܐ ܢܐܡܪܘܢ ܀
21 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn,
22ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܕܥܬܝܕ ܗܘ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܕܤܓܝܐܬܐ ܢܚܫ ܘܕܢܤܬܠܐ ܡܢ ܩܫܝܫܐ ܘܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܤܦܪܐ ܘܢܩܛܠܘܢܝܗܝ ܘܠܝܘܡܐ ܕܬܠܬܐ ܢܩܘܡ ܀
22 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»
23ܘܐܡܪ ܗܘܐ ܩܕܡ ܟܠܢܫ ܡܢ ܕܨܒܐ ܕܢܐܬܐ ܒܬܪܝ ܢܟܦܘܪ ܒܢܦܫܗ ܘܢܫܩܘܠ ܙܩܝܦܗ ܟܠܝܘܡ ܘܢܐܬܐ ܒܬܪܝ ܀
23 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
24ܡܢ ܓܝܪ ܕܨܒܐ ܕܢܦܫܗ ܢܚܐ ܡܘܒܕ ܠܗ ܡܢ ܕܝܢ ܕܢܘܒܕ ܢܦܫܗ ܡܛܠܬܝ ܗܢܐ ܡܚܐ ܠܗ ܀
24 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.
25ܡܢܐ ܓܝܪ ܢܬܥܕܪ ܒܪ ܐܢܫܐ ܕܢܐܬܪ ܥܠܡܐ ܟܠܗ ܢܦܫܗ ܕܝܢ ܢܘܒܕ ܐܘ ܢܚܤܪ ܀
25 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?
26ܡܢ ܕܢܒܗܬ ܒܝ ܕܝܢ ܘܒܡܠܝ ܢܒܗܬ ܒܗ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܡܐ ܕܐܬܐ ܒܫܘܒܚܐ ܕܐܒܘܗܝ ܥܡ ܡܠܐܟܘܗܝ ܩܕܝܫܐ ܀
26 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.
27ܫܪܪܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܝܬ ܐܢܫܐ ܕܩܝܡܝܢ ܗܪܟܐ ܕܠܐ ܢܛܥܡܘܢ ܡܘܬܐ ܥܕܡܐ ܕܢܚܙܘܢ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
27 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»
28ܗܘܐ ܕܝܢ ܒܬܪ ܡܠܐ ܗܠܝܢ ܐܝܟ ܬܡܢܝܐ ܝܘܡܝܢ ܕܒܪ ܝܫܘܥ ܠܫܡܥܘܢ ܘܠܝܥܩܘܒ ܘܠܝܘܚܢܢ ܘܤܠܩ ܠܛܘܪܐ ܠܡܨܠܝܘ ܀
28 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan.
29ܘܟܕ ܗܘ ܡܨܠܐ ܐܬܚܠܦ ܚܙܘܐ ܕܐܦܘܗܝ ܘܢܚܬܘܗܝ ܚܘܪܘ ܘܡܒܪܩܝܢ ܗܘܘ ܀
29 Bi muy ñaan, xar-kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax.
30ܘܗܐ ܬܪܝܢ ܓܒܪܝܢ ܡܡܠܠܝܢ ܗܘܘ ܥܡܗ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܡܘܫܐ ܘܐܠܝܐ ܀
30 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas.
31ܕܐܬܚܙܝܘ ܒܬܫܒܘܚܬܐ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܝܢ ܥܠ ܡܦܩܢܗ ܕܥܬܝܕ ܗܘܐ ܕܢܫܬܠܡ ܒܐܘܪܫܠܡ ܀
31 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demu Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem.
32ܘܝܩܪܘ ܗܘܘ ܠܗܘܢ ܒܫܢܬܐ ܫܡܥܘܢ ܘܗܢܘܢ ܕܥܡܗ ܘܠܡܚܤܢ ܐܬܬܥܝܪܘ ܘܚܙܘ ܫܘܒܚܗ ܘܠܗܢܘܢ ܬܪܝܢ ܐܢܫܝܢ ܕܩܝܡܝܢ ܗܘܘ ܠܘܬܗ ܀
32 Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmmeentu, waaye bi ñu yeewoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam.
33ܘܟܕ ܫܪܝܘ ܠܡܦܪܫ ܡܢܗ ܐܡܪ ܫܡܥܘܢ ܠܝܫܘܥ ܪܒܝ ܫܦܝܪ ܗܘ ܠܢ ܕܗܪܟܐ ܢܗܘܐ ܘܢܥܒܕ ܬܠܬ ܡܛܠܝܢ ܠܟ ܚܕܐ ܘܠܡܘܫܐ ܚܕܐ ܘܠܐܠܝܐ ܚܕܐ ܘܠܐ ܝܕܥ ܗܘܐ ܡܢܐ ܐܡܪ ܀
33 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» Fekk xamul la mu doon wax.
34ܘܟܕ ܐܡܪ ܗܠܝܢ ܗܘܬ ܥܢܢܐ ܘܐܛܠܬ ܥܠܝܗܘܢ ܘܕܚܠܘ ܟܕ ܚܙܘ ܠܡܘܫܐ ܘܠܐܠܝܐ ܕܥܠܘ ܒܥܢܢܐ ܀
34 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.
35ܘܩܠܐ ܗܘܐ ܡܢ ܥܢܢܐ ܕܐܡܪ ܗܢܘ ܒܪܝ ܚܒܝܒܐ ܠܗ ܫܡܥܘ ܀
35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
36ܘܟܕ ܗܘܐ ܩܠܐ ܐܫܬܟܚ ܝܫܘܥ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܘܗܢܘܢ ܫܬܩܘ ܘܠܐܢܫ ܠܐ ܐܡܪܘ ܒܗܢܘܢ ܝܘܡܬܐ ܡܕܡ ܕܚܙܘ ܀
36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, bañ a nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
37ܘܗܘܐ ܠܝܘܡܐ ܕܒܬܪܗ ܟܕ ܢܚܬܝܢ ܡܢ ܛܘܪܐ ܦܓܥ ܒܗܘܢ ܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܀
37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.
38ܘܓܒܪܐ ܚܕ ܡܢ ܟܢܫܐ ܗܘ ܩܥܐ ܘܐܡܪ ܡܠܦܢܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܐܬܦܢܝ ܥܠܝ ܒܪܝ ܕܝܚܝܕܝܐ ܗܘ ܠܝ ܀
38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.
39ܘܪܘܚܐ ܥܕܝܐ ܥܠܘܗܝ ܘܡܢ ܫܠܝܐ ܩܥܐ ܘܡܚܪܩ ܫܢܘܗܝ ܘܡܪܥܬ ܘܠܡܚܤܢ ܦܪܩܐ ܡܢܗ ܡܐ ܕܫܚܩܬܗ ܀
39 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.
40ܘܒܥܝܬ ܡܢ ܬܠܡܝܕܝܟ ܕܢܦܩܘܢܝܗܝ ܘܠܐ ܐܫܟܚܘ ܀
40 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.»
41ܥܢܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܐܘܢ ܫܪܒܬܐ ܕܠܐ ܡܗܝܡܢܐ ܘܡܥܩܠܬܐ ܥܕܡܐ ܠܐܡܬܝ ܐܗܘܐ ܠܘܬܟܘܢ ܘܐܤܝܒܪܟܘܢ ܩܪܒܝܗܝ ܠܟܐ ܠܒܪܟ ܀
41 Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
42ܘܟܕ ܡܩܪܒ ܠܗ ܐܪܡܝܗ ܕܝܘܐ ܗܘ ܘܡܥܤܗ ܘܟܐܐ ܝܫܘܥ ܒܪܘܚܐ ܗܝ ܛܢܦܬܐ ܘܐܤܝܗ ܠܛܠܝܐ ܘܝܗܒܗ ܠܐܒܘܗܝ ܀
42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.
43ܘܐܬܕܡܪܘ ܟܠܗܘܢ ܒܪܒܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܘܟܕ ܟܠܢܫ ܡܬܕܡܪ ܗܘܐ ܥܠ ܟܠ ܕܥܒܕ ܝܫܘܥ ܐܡܪ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
43 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:
44ܤܝܡܘ ܐܢܬܘܢ ܡܠܐ ܗܠܝܢ ܒܐܕܢܝܟܘܢ ܒܪܗ ܓܝܪ ܕܐܢܫܐ ܥܬܝܕ ܕܢܫܬܠܡ ܒܐܝܕܝ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܀
44 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
45ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܠܐ ܐܫܬܘܕܥܘܗ ܠܡܠܬܐ ܗܕܐ ܡܛܠ ܕܡܟܤܝܐ ܗܘܬ ܡܢܗܘܢ ܕܠܐ ܢܕܥܘܢܗ ܘܕܚܠܝܢ ܗܘܘ ܕܢܫܐܠܘܢܝܗܝ ܥܠܝܗ ܥܠ ܡܠܬܐ ܗܕܐ ܀
45 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46ܘܥܠܬ ܒܗܘܢ ܡܚܫܒܬܐ ܕܡܢܘ ܟܝ ܪܒ ܒܗܘܢ ܀
46 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gën a màgg ci ñoom.
47ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܝܕܥ ܡܚܫܒܬܐ ܕܠܒܗܘܢ ܘܢܤܒ ܛܠܝܐ ܘܐܩܝܡܗ ܠܘܬܗ ܀
47 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:
48ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܢ ܕܡܩܒܠ ܛܠܝܐ ܐܝܟ ܗܢܐ ܒܫܡܝ ܠܝ ܗܘ ܡܩܒܠ ܘܡܢ ܕܠܝ ܡܩܒܠ ܡܩܒܠ ܠܡܢ ܕܫܕܪܢܝ ܐܝܢܐ ܓܝܪ ܕܙܥܘܪ ܒܟܠܟܘܢ ܗܢܐ ܢܗܘܐ ܪܒ ܀
48 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gën a woyof ci yéen ñépp, kooku moo gën a màgg.»
49ܘܥܢܐ ܝܘܚܢܢ ܘܐܡܪ ܪܒܢ ܚܙܝܢ ܐܢܫ ܕܡܦܩ ܕܝܘܐ ܒܫܡܟ ܘܟܠܝܢܝܗܝ ܥܠ ܕܠܐ ܐܬܐ ܥܡܢ ܒܬܪܟ ܀
49 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»
50ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܠܐ ܬܟܠܘܢ ܡܢ ܓܝܪ ܕܠܐ ܗܘܐ ܠܘܩܒܠܟܘܢ ܚܠܦܝܟܘܢ ܗܘ ܀
50 Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
51ܘܗܘܐ ܕܟܕ ܡܬܡܠܝܢ ܝܘܡܬܐ ܕܤܘܠܩܗ ܐܬܩܢ ܦܪܨܘܦܗ ܕܢܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
52ܘܫܕܪ ܡܠܐܟܐ ܩܕܡ ܦܪܨܘܦܗ ܘܐܙܠܘ ܥܠܘ ܠܩܪܝܬܐ ܕܫܡܪܝܐ ܐܝܟ ܕܢܬܩܢܘܢ ܠܗ ܀
52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
53ܘܠܐ ܩܒܠܘܗܝ ܡܛܠ ܕܦܪܨܘܦܗ ܠܐܘܪܫܠܡ ܤܝܡ ܗܘܐ ܠܡܐܙܠ ܀
53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
54ܘܟܕ ܚܙܘ ܝܥܩܘܒ ܘܝܘܚܢܢ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܡܪܢ ܨܒܐ ܐܢܬ ܕܢܐܡܪ ܘܬܚܘܬ ܢܘܪܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܘܬܤܝܦ ܐܢܘܢ ܐܝܟ ܕܐܦ ܐܠܝܐ ܥܒܕ ܀
54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na safaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»
55ܘܐܬܦܢܝ ܘܟܐܐ ܒܗܘܢ ܘܐܡܪ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܝܕܐ ܐܢܬܘܢ ܪܘܚܐ ܀
55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,
56ܒܪܗ ܓܝܪ ܕܐܢܫܐ ܠܐ ܐܬܐ ܠܡܘܒܕܘ ܢܦܫܬܐ ܐܠܐ ܠܡܚܝܘ ܘܐܙܠܘ ܠܗܘܢ ܠܩܪܝܬܐ ܐܚܪܬܐ ܀
56 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.
57ܘܟܕ ܐܙܠܝܢ ܒܐܘܪܚܐ ܐܡܪ ܠܗ ܐܢܫ ܐܬܐ ܒܬܪܟ ܠܐܬܪ ܕܐܙܠ ܐܢܬ ܡܪܝ ܀
57 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.»
58ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܠܬܥܠܐ ܢܩܥܐ ܐܝܬ ܠܗܘܢ ܘܠܦܪܚܬܐ ܕܫܡܝܐ ܡܛܠܠܐ ܠܒܪܗ ܕܝܢ ܕܐܢܫܐ ܠܝܬ ܠܗ ܐܝܟܐ ܕܢܤܡܘܟ ܪܫܗ ܀
58 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
59ܘܐܡܪ ܠܐܚܪܢܐ ܬܐ ܒܬܪܝ ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗ ܡܪܝ ܐܦܤ ܠܝ ܠܘܩܕܡ ܐܙܠ ܐܩܒܘܪ ܐܒܝ ܀
59 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»
60ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܫܒܘܩ ܡܝܬܐ ܩܒܪܝܢ ܡܝܬܝܗܘܢ ܘܐܢܬ ܙܠ ܤܒܪ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
60 Mu tontu ko ne: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.»
61ܐܡܪ ܠܗ ܐܚܪܢܐ ܐܬܐ ܒܬܪܟ ܡܪܝ ܠܘܩܕܡ ܕܝܢ ܐܦܤ ܠܝ ܐܙܠ ܐܫܠܡ ܠܒܢܝ ܒܝܬܝ ܘܐܬܐ ܀
61 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkk a tàgguji sama waa kër.»
62ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܠܐ ܐܢܫ ܪܡܐ ܐܝܕܗ ܥܠ ܚܪܒܐ ܕܦܕܢܐ ܘܚܐܪ ܠܒܤܬܪܗ ܘܚܫܚ ܠܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
62 Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowul a liggéey ci nguuru Yàlla.»