1ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܚܕܘ ܒܡܪܢ ܗܢܝܢ ܟܕ ܗܢܝܢ ܕܐܟܬܘܒ ܠܟܘܢ ܠܐ ܡܐܢܐ ܠܝ ܡܛܠ ܕܠܟܘܢ ܡܙܗܪܢ ܀
1 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.
2ܐܙܕܗܪܘ ܡܢ ܟܠܒܐ ܐܙܕܗܪܘ ܡܢ ܦܥܠܐ ܒܝܫܐ ܐܙܕܗܪܘ ܡܢ ܦܤܩ ܒܤܪܐ ܀
2 Moytuleen xaj yi, waaw moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit.
3ܓܙܘܪܬܐ ܓܝܪ ܚܢܢ ܐܝܬܝܢ ܐܝܠܝܢ ܕܦܠܚܝܢܢ ܠܐܠܗܐ ܒܪܘܚܐ ܘܡܫܬܒܗܪܝܢܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܠܐ ܬܟܝܠܝܢܢ ܥܠ ܒܤܪܐ ܀
3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu jenn yaakaar ci matug nit.
4ܟܕ ܠܝ ܐܝܬ ܗܘܐ ܠܝ ܬܘܟܠܢܐ ܐܦ ܥܠ ܒܤܪܐ ܐܢ ܓܝܪ ܐܢܫ ܤܒܪ ܕܬܘܟܠܢܗ ܒܒܤܪܐ ܗܘ ܝܬܝܪ ܡܢܗ ܐܢܐ ܀
4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.
5ܓܙܝܪܐ ܒܪ ܬܡܢܝܐ ܝܘܡܝܢ ܡܢ ܛܘܗܡܐ ܕܐܝܤܪܝܠ ܡܢ ܫܒܛܐ ܕܒܢܝܡܝܢ ܥܒܪܝܐ ܒܪ ܥܒܪܝܐ ܒܢܡܘܤܐ ܦܪܝܫܝܐ ܀
5 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Ben-yamin, di Ibrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgg a wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;
6ܒܛܢܢܐ ܪܕܘܦܐ ܕܥܕܬܐ ܘܒܙܕܝܩܘܬܐ ܕܢܡܘܤܐ ܕܠܐ ܪܫܝܢ ܗܘܝܬ ܀
6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.
7ܐܠܐ ܗܠܝܢ ܕܝܘܬܪܢܐ ܗܘܝ ܠܝ ܚܘܤܪܢܐ ܚܫܒܬ ܐܢܝܢ ܡܛܠ ܡܫܝܚܐ ܀
7 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.
8ܐܦ ܚܫܒ ܐܢܐ ܠܗܝܢ ܟܠܗܝܢ ܚܘܤܪܢܐ ܡܛܠ ܪܒܘܬܐ ܕܝܕܥܬܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܡܪܝ ܗܘ ܕܡܛܠܬܗ ܟܠܡܕܡ ܚܤܪܬ ܘܐܝܟ ܙܒܠܐ ܚܫܒܬ ܕܠܡܫܝܚܐ ܐܬܪ ܀
8 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel mënu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
9ܘܐܫܬܟܚ ܒܗ ܟܕ ܠܝܬ ܠܝ ܙܕܝܩܘܬܐ ܕܢܦܫܝ ܗܝ ܕܡܢ ܢܡܘܤܐ ܐܠܐ ܗܝ ܕܡܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܕܡܫܝܚܐ ܕܐܝܬܝܗ ܙܕܝܩܘܬܐ ܕܡܢ ܐܠܗܐ ܀
9 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm.
10ܕܒܗ ܐܫܬܘܕܥ ܠܝܫܘܥ ܘܠܚܝܠܐ ܕܩܝܡܬܗ ܘܐܫܬܘܬܦ ܒܚܫܘܗܝ ܘܐܬܕܡܐ ܒܡܘܬܗ ܀
10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,
11ܕܠܡܐ ܐܫܟܚ ܐܡܛܐ ܠܩܝܡܬܐ ܕܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܀
11 ngir man a séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
12ܠܐ ܗܘܐ ܡܢ ܟܕܘ ܢܤܒܬ ܐܘ ܡܢ ܟܕܘ ܐܬܓܡܪܬ ܐܠܐ ܪܗܛ ܐܢܐ ܕܠܡܐ ܐܕܪܟ ܠܡܕܡ ܕܡܛܠܬܗ ܐܕܪܟܢܝ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma.
13ܐܚܝ ܐܢܐ ܥܠ ܢܦܫܝ ܠܐ ܪܢܐ ܐܢܐ ܕܐܕܪܟܬ ܚܕܐ ܕܝܢ ܝܕܥ ܐܢܐ ܕܕܒܤܬܪܝ ܛܥܐ ܐܢܐ ܘܠܩܕܡܝ ܡܫܬܘܫܛ ܐܢܐ ܀
13 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam,
14ܘܪܗܛ ܐܢܐ ܠܘܩܒܠ ܢܝܫܐ ܕܐܤܒ ܙܟܘܬܐ ܕܩܪܝܢܐ ܕܠܥܠ ܕܐܠܗܐ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla tax a woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
15ܐܝܠܝܢ ܕܓܡܝܪܝܢ ܗܟܝܠ ܗܠܝܢ ܢܬܪܥܘܢ ܘܐܢ ܡܕܡ ܐܚܪܢܝܐܝܬ ܡܬܪܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܦ ܗܕܐ ܐܠܗܐ ܢܓܠܐ ܠܟܘܢ ܀
15 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Te su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal.
16ܒܪܡ ܠܗܕܐ ܕܡܛܝܢ ܒܚܕ ܫܒܝܠܐ ܢܫܠܡ ܘܒܚܕܐ ܐܘܝܘܬܐ ܀
16 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.
17ܐܬܕܡܘ ܒܝ ܐܚܝ ܘܗܘܝܬܘܢ ܡܬܒܩܝܢ ܒܐܝܠܝܢ ܕܗܟܢܐ ܡܗܠܟܝܢ ܐܝܟ ܕܡܘܬܐ ܕܒܢ ܚܙܝܬܘܢ ܀
17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen.
18ܐܝܬ ܓܝܪ ܤܓܝܐܐ ܕܐܚܪܢܝܐܝܬ ܡܗܠܟܝܢ ܗܢܘܢ ܕܙܒܢܝܢ ܤܓܝܐܢ ܐܡܪܬ ܠܟܘܢ ܥܠܝܗܘܢ ܗܫܐ ܕܝܢ ܟܕ ܒܟܐ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܗܢܘܢ ܕܒܥܠܕܒܒܐ ܐܢܘܢ ܕܙܩܝܦܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
18 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy.
19ܕܚܪܬܗܘܢ ܐܒܕܢܐ ܗܝ ܗܢܘܢ ܕܐܠܗܗܘܢ ܟܪܤܗܘܢ ܘܬܫܒܘܚܬܗܘܢ ܒܗܬܬܗܘܢ ܗܠܝܢ ܕܬܪܥܝܬܗܘܢ ܒܐܪܥܐ ܗܝ ܀
19 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk.
20ܕܝܠܢ ܕܝܢ ܦܘܠܚܢܢ ܒܫܡܝܐ ܗܘ ܘܡܢ ܬܡܢ ܡܤܟܝܢܢ ܠܡܚܝܢܐ ܠܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu.
21ܕܗܘ ܢܚܠܦ ܦܓܪܐ ܕܡܘܟܟܢ ܕܢܗܘܐ ܒܕܡܘܬܐ ܕܦܓܪܐ ܕܫܘܒܚܗ ܐܝܟ ܚܝܠܗ ܪܒܐ ܗܘ ܕܒܗ ܟܠ ܐܫܬܥܒܕ ܠܗ ܀
21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko man a nootal mbindeef yépp.