Syriac: NT

Wolof: New Testament

Philippians

4

1ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܚܒܝܒܐ ܘܪܚܝܡܐ ܘܚܕܘܬܝ ܘܟܠܝܠܝ ܗܟܢܐ ܩܘܡܘ ܒܡܪܢ ܚܒܝܒܝ ܀
1 Kon nag yéen samay bokk, ñi ma bëgg te namm leen, di sama mbég ak sama kaalag ndam, jàppleen bu dëgër noonu ci Boroom bi, soppe yi!
2ܡܢ ܐܘܗܕܝܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܘܡܢ ܤܘܢܛܝܟܐ ܕܚܕ ܪܥܝܢܐ ܢܗܘܐ ܠܗܝܢ ܒܡܪܢ ܀
2 Ci lu jëm ci Ewodi ak Santis, maa ngi leen di ñaan, ñu bokk benn xalaat ci Boroom bi.
3ܐܦ ܡܢܟ ܒܥܐ ܐܢܐ ܒܪ ܙܘܓܝ ܫܪܝܪܐ ܕܬܗܘܐ ܡܥܕܪ ܠܗܝܢ ܕܗܢܝܢ ܠܐܝ ܥܡܝ ܒܐܘܢܓܠܝܘܢ ܥܡ ܩܠܡܝܤ ܘܥܡ ܫܪܟܐ ܕܡܥܕܪܢܝ ܗܢܘܢ ܕܫܡܗܝܗܘܢ ܟܬܝܒܝܢ ܒܟܬܒܐ ܕܚܝܐ ܀
3 Te yaw sama nawle bu wér, nanga dimbali jigéen ñooñu xeexoon ci sama wet ci tas xebaar bu baax bi, boole ci Këlemaŋ ak samay yeneeni nawle, ñoom ñi Yàlla bind seeni tur ci téereb dund ba.
4ܚܕܘ ܒܡܪܢ ܒܟܠܙܒܢ ܘܬܘܒ ܐܡܪ ܐܢܐ ܚܕܘ ܀
4 Deeleen bég ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: bégleen!
5ܘܡܟܝܟܘܬܟܘܢ ܬܬܝܕܥ ܠܘܬ ܟܠܢܫ ܡܪܢ ܩܪܝܒ ܗܘ ܀
5 Na seen lewet leer ñépp. Boroom bi jege na.
6ܕܡܕܡ ܠܐ ܬܐܨܦܘܢ ܐܠܐ ܒܟܠܙܒܢ ܒܨܠܘܬܐ ܘܒܒܥܘܬܐ ܘܒܬܘܕܝܬܐ ܫܐܠܬܟܘܢ ܢܬܝܕܥܢ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܀
6 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant.
7ܘܫܠܡܗ ܕܐܠܗܐ ܗܘ ܕܪܒ ܡܢ ܟܠ ܡܕܥ ܢܢܛܪ ܠܒܘܬܟܘܢ ܘܡܕܥܝܟܘܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
7 Noonu jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu.
8ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܐܝܠܝܢ ܕܫܪܝܪܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܢܟܦܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܟܐܢܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܕܟܝܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܪܚܝܡܢ ܘܐܝܠܝܢ ܕܫܒܝܚܢ ܘܐܝܠܝܢ ܥܒܕܐ ܕܫܘܒܚܐ ܘܕܩܘܠܤܐ ܗܠܝܢ ܐܬܪܥܘ ܀
8 Léegi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu dëggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mat a naw, xalaatleen ko.
9ܗܠܝܢ ܕܝܠܦܬܘܢ ܘܩܒܠܬܘܢ ܘܫܡܥܬܘܢ ܘܚܙܝܬܘܢ ܒܝ ܗܠܝܢ ܤܥܘܪܘ ܘܐܠܗܐ ܕܫܠܡܐ ܢܗܘܐ ܥܡܟܘܢ ܀
9 Li ngeen jànge ci man te nangu ko, li ngeen dégge ci man te gis ko, jëfeleen ko; kon Yàllay jàmm dina ànd ak yéen.
10ܪܘܪܒܐܝܬ ܕܝܢ ܚܕܝܬ ܒܡܪܢ ܕܐܩܦܬܘܢ ܠܡܐܨܦ ܕܝܠܝ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܝܨܦܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܐܠܐ ܠܐ ܤܦܝܩܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܀
10 Sama xol sedd na guyy ci Boroom bi, ci ni ngeen yeesale seen ndimbal ci man. Xam naa ne, amoon ngeen yéene ji, waaye man gi moo fi nekkul woon.
11ܠܐ ܗܘܐ ܕܝܢ ܡܛܠ ܕܚܤܪ ܠܝ ܐܡܪ ܐܢܐ ܐܢܐ ܓܝܪ ܝܠܦܬ ܕܢܗܘܐ ܤܦܩ ܠܝ ܗܘ ܡܕܡ ܕܐܝܬ ܠܝ ܀
11 Ba tey soxla taxul ma waxe nii, ndaxte jàng naa doylu ci mbir mu ma man a dab.
12ܝܕܥ ܐܢܐ ܕܐܬܡܟܟ ܝܕܥ ܐܢܐ ܗܘ ܐܦ ܕܐܬܝܬܪ ܒܟܠ ܘܒܟܠ ܡܕܡ ܡܕܪܫ ܐܢܐ ܐܦ ܒܤܒܥܐ ܐܦ ܒܟܦܢܐ ܒܡܫܪܬܚܘܬܐ ܘܒܚܤܝܪܘܬܐ ܀
12 Miin naa ñàkk, man naa naataange. Ci fépp ak ci lépp, Yàlla def na ba sama xol toj ci suur ak xiif, barele ak néewle.
13ܕܟܠ ܡܕܡ ܡܨܐ ܐܢܐ ܚܝܠܐ ܒܡܫܝܚܐ ܕܡܚܝܠ ܠܝ ܀
13 Man naa lépp ci ndimbalu Aji Dooleel ji.
14ܒܪܡ ܫܦܝܪ ܥܒܕܬܘܢ ܕܐܫܬܘܬܦܬܘܢ ܠܐܘܠܨܢܝ ܀
14 Waaye teewul taxawu, bi ngeen ma taxawu ci sama tiis, jëf ju rafet la.
15ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܦܝܠܝܦܤܝܐ ܕܒܫܘܪܝܐ ܕܤܒܪܬܐ ܟܕ ܢܦܩܬ ܡܢ ܡܩܕܘܢܝܐ ܐܦܠܐ ܚܕܐ ܡܢ ܥܕܬܐ ܐܫܬܘܬܦ ܠܝ ܒܚܘܫܒܢ ܡܤܒܐ ܘܡܬܠܐ ܐܠܐ ܐܢܬܘܢ ܒܠܚܘܕ ܀
15 Yéen waa Filib xam ngeen ne, bi ngeen jëkkee xam xebaar bu baax bi, te ma jóge diiwaanu Maseduwan, benn mbooloo àndul woon ak man ci mbirum joqleente ndimbal, mu dul yéen doŋŋ.
16ܕܐܦ ܠܬܤܠܘܢܝܩܐ ܚܕܐ ܙܒܢ ܘܬܪܬܝܢ ܚܫܚܬܝ ܫܕܪܬܘܢ ܠܝ ܀
16 Ba ma nekkee dëkku Tesalonig sax, yónnee ngeen ay yooni yoon, ngir faj samay soxla.
17ܠܘ ܕܡܘܗܒܬܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܐܠܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܕܦܐܪܐ ܢܤܓܘܢ ܠܟܘܢ ܀
17 Loolu tekkiwul ne, damay sàkku ay ndimbal ci yéen, waaye damaa bëgg rekk seen denc yokku fa Yàlla.
18ܟܠܡܕܡ ܩܒܠܬ ܘܝܬܝܪ ܠܝ ܘܡܠܐ ܐܢܐ ܘܢܤܒܬ ܟܠ ܕܫܕܪܬܘܢ ܠܝ ܒܝܕ ܐܦܦܪܘܕܝܛܤ ܪܝܚܐ ܒܤܝܡܐ ܘܕܒܚܐ ܡܩܒܠܐ ܕܫܦܪ ܠܐܠܗܐ ܀
18 Fi mu ne jot naa li ma aajowoo lépp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma yónnee ci loxoy Epafrodit doy na sëkk; ni xetu latkoloñ la mel ci man, di sarax su neex Yàlla te mu nangu ko.
19ܘܐܠܗܝ ܢܡܠܐ ܟܠܗ ܤܢܝܩܘܬܟܘܢ ܐܝܟ ܥܘܬܪܗ ܒܫܘܒܚܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
19 Te Yàlla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu xéewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla yépp.
20ܠܐܠܗܐ ܕܝܢ ܐܒܘܢ ܫܘܒܚܐ ܘܐܝܩܪܐ ܠܥܠܡ ܥܠܡܝܢ ܐܡܝܢ ܀
20 Na Yàlla sunu Baay yelloo ndam ba fàww. Amiin.
21ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܕܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܫܐܠܝܢ ܒܫܠܡܟܘܢ ܐܚܐ ܕܥܡܝ ܀
21 Nuyul-leen ma gaayi Kirist Yeesu yu sell yépp. Bokk yi ànd ak man, ñu ngi leen di nuyu.
22ܫܐܠܝܢ ܒܫܠܡܟܘܢ ܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܗܠܝܢ ܕܡܢ ܒܝܬܗ ܕܩܤܪ ܀
22 Te it gaayi Yàlla yu sell yépp ñu ngi leen di nuyu, rawatina nag ñi nekk kër buur bi Sesaar.
23ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܡ ܟܠܟܘܢ ܐܡܝܢ ܀
23 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.