Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

1 Corinthians

14

1 Xintewooleen mbëggeel te fonk mayi Xelum Yàlla, rawatina mayu wax ci kàddug Yàlla,
1讲道与说方言的恩赐
2 ndaxte kiy wax aw làkk, waxul ak nit ñi, waaye Yàlla lay waxal, ndaxte kenn déggul li muy wax. Dafay wax ay mbóot ci xelam.
2原来那说方言的不是对人说,而是对 神说,因为没有人能听得懂;他是在灵里讲奥秘的事。
3 Waaye kiy jottali kàddug Yàlla, nit ñi lay waxal ngir yékkati seen ngëm, di leen dénk ak a dëfël.
3但那讲道的是对人讲说,使他们得着造就、安慰和劝勉。
4 Kiy wax aw làkk dafay yokk boppam, waaye kiy wax ci kàddug Yàlla, dafay yokk ngëmu mbooloo mi.
4那说方言的是造就自己,但那讲道的是造就教会。
5 Léegi nag bëgg naa yéen ñépp, ngeen di wax ay làkk, waaye li ma gënal mooy ngeen di wax ci kàddug Yàlla. Kiy wax ci kàddug Yàlla moo gën kiy wax ay làkk, su firiwul li muy wax, ngir ngëmu mbooloo mi yokku.
5我愿意你们都说方言,但我更愿意你们都讲道;因为那说方言的,如果不翻译出来使教会得着造就,就远不如那讲道的了。
6 Kon nag bokk yi, su ma ñëwee ci yéen, di wax ay làkk, lu ma leen di jariñ? Dara, su ma leen indilul dëgg gu Yàlla feeñal, walla xam-xam walla kàddu gu tukkee ca Yàlla, walla am njàngale.
6弟兄们,你们想想,如果我到你们那里去,只说方言,不向你们讲有关启示、知识、预言,或教训的话,那我对你们有什么益处呢?
7 Noonu la mel itam ci yëf yi dundul tey riir, ni toxoro walla xalam. Su li ci jibe leerul, naka la nit man a ràññee li mbiibi toxoro walla buumi xalam di wax?
7甚至那些没有生命却能发声的东西,例如箫或琴,如果音调不分,怎能使人知道所弹所奏的是什么呢?
8 Rax-ca-dolli su liit gi jibul bu leer, kuy man a waajal xare ba?
8又如果军号所发的声音不清楚,谁会准备作战呢?
9 Noonu itam bu ngeen génnewul ay wax yu leer ci seen gémmiñ, nan lañuy man a xame li ngeen di wax? Dingeen wax cig neen!
9你们也是这样,如果用舌头发出人听不懂的话来,人怎会知道你所讲的是什么呢?这样,你们就是向空气说话了。
10 Xawma ñaata xeeti làkk a am ci àddina, te wu ci nekk am na lu muy tekki.
10世上有那么多种语言,但没有一种是没有意义的。
11 Su ma xamul nag làkk wi ñu may làkk, doxandéem laay doon ci ki koy wax, te ki koy wax it doxandéem la ci man.
11我若不明白某一种语言的意思,在那讲的人来看,我就是个外国人;在我来说,那讲话的人也是个外国人。
12 Yéen itam, gannaaw dangeen a fonk mayi Xelum Yàlla, jéemleen a ëpple ci liy yokk ngëmu mbooloo mi.
12你们也是这样,你们既然热切地渴慕属灵的恩赐,就应当追求多多得着造就教会的恩赐。
13 Looloo tax kiy wax aw làkk, na ñaan ngir mu man a firi li looluy tekki.
13所以,说方言的应当祈求,使他能把方言翻译出来。
14 Su may ñaan Yàlla ci aw làkk, sama xol day ñaan, waaye sama xel amalul kenn njariñ.
14我若用方言祷告,是我的灵在祷告,我的理智并没有作用。
15 Kon nag lu muy indi? Bu may ñaan, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel. Bu may woy, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel.
15那么我应当怎样行呢?我要用灵祷告,也要用理智祷告;我要用灵歌唱,也要用理智歌唱。
16 Walla, boo dee gërëm Yàlla, ànd ci ak sa xol rekk, kon ku musul a jàng mbir yooyu, nan la man a waxe: «Amiin,» ci sa cant Yàlla googu? Ndaxte xamul li ngay wax.
16不然,如果你用灵赞美,在场那些不明白的人,因为不知道你在说什么,怎能在你感谢的时候说“阿们”呢?
17 Dëgg la, dangay sant Yàlla bu baax, waaye ki ci des, ngëmam yokkuwul.
17你感谢固然是好,但别人却得不着造就。
18 Maa ngi sant Yàlla ci li may wax ay làkk, ba raw leen yéen ñépp.
18我感谢 神,我说方言比你们大家都多。
19 Waaye ci ndajem mbooloom ñi gëm, wax juróomi baat yu am njariñ, ngir jàngal ñi ci des, moo ma gënal wax fukki junniy baat ciw làkk.
19但在教会中,我宁愿用理智说五句话去教导人,胜过用方言说万句话。
20 Bokk yi, buleen melati ni ay xale, ci ni ngeen di xalaate. Ci lu jëm ci lu bon, mel-leen ni ay xale, waaye ci seeni xalaat, mel-leen ni ay mag.
20弟兄们,你们在思想上不要作小孩子,却要在恶事上作婴孩,在思想上作成年人。
21 Bind nañu ci téereb yoon wi:«Dinaa wax ak mbooloo mii,jaare ko ci ay nit, ñuy wax yeneen làkk,ak ay gémmiñi doxandéem,waaye ba tey duñu ma déglu.» Moom la Boroom bi wax.
21律法上记着说:“主说:我要借着说别种话的人,用外国人的嘴唇,对这人民说话;虽然这样,他们还是不听我。”
22 Ci noonu wax ay làkk, firnde la ci ñi gëmul, te du firnde ci ñi gëm. Te it wax ci kàddug Yàlla, du firnde ci ñi gëmul, waaye firnde la ci ñi gëm.
22可见说方言不是要给信主的人作记号,而是要给未信的人;讲道不是要给未信的人,而是要给信主的人作记号。
23 Kon nag su fekkee ku jàngul mbiri Kirist walla ku gëmul dugg ca mbooloo ma, fekk ñépp di wax ay làkk, ndax du wax ne, dangeen a dof?
23所以,如果全教会聚在一起的时候,大家都说方言,有不明白的人或未信的人进来,不是要说你们疯了吗?
24 Waaye bu ñépp dee wax ci kàddug Yàlla, te ku gëmul dugg fa, walla ku jàngul mbiri Kirist, wax yi ñépp wax dafay wone bàkkaaram te àtte ko,
24如果大家都讲道,有未信的人或不明白的人进来,他就会被众人劝服而知罪,被众人审问了。
25 ba kumpay xolam feeñ. Bu ko defee dina dëpp jëwam ci suuf, di màggal Yàlla te naan: «Dëgg-dëgg Yàllaa ngi ci seen biir.»
25他心里隐秘的事被显露出来,他就必俯伏敬拜 神,宣告说:“ 神真的是在你们中间了。”
26 Kon nag bokk yi, lu muy indi? Bu ngeen dajee, kii am aw taalif, kii am njàngale, kii dëgg gu Yàlla feeñal, kii di wax aw làkk, kee di ko firi. Na loolu lépp aw ci yoonu yokk ngëmu mbooloo mi.
26 神不是混乱而是和平的弟兄们,那么应该怎么办呢?你们聚集在一起的时候,各人或有诗歌,或有教训,或有启示,或有方言,或有翻译出来的话,一切都应该能造就人。
27 Su amee kuy wax aw làkk, na ñaar wax walla gën gaa bare ñett. Nañu ko toppante, te kenn di firi.
27如果有人说方言,只可以有两个人,或最多三个人,并且要轮流说,同时要有一个人翻译。
28 Su amul kuy firi, kooku di wax aw làkk, na noppi ci ndajem mbooloo mi. Na waxanteek Yàlla ci xolam.
28如果没有人翻译,他就应当在会中闭口,只对自己和对 神说好了。
29 Ci ñiy wax ci kàddug Yàlla nag, na ñaar walla ñett wax, te ñi ci des ràññee li ñuy wax.
29讲道的,也只可以两三个人讲,其余的人要衡量他们所讲的。
30 Su amee ku toog te Yàlla feeñal ko dëgg, na ki doon wax noppi.
30在座的有人得了启示,那先讲的人就应当住口。
31 Yéen ñépp man ngeen a kenn-kennoo wax ci kàddug Yàlla, ngir ñépp jàng te dégg li ñu leen di dénk.
31因为你们都可以轮流讲道,好让大家都可以学习,都可以得到勉励。
32 Ñiy jottali kàddug Yàlla dañoo moom seen xel,
32先知的灵是受先知控制的,
33 ndaxte Yàlla du Yàllay lëj-lëj waaye Yàllay jàmm la. Ci mboolooy gaayi Yàlla yépp,
33因为 神不是混乱的,而是和平的。
34 na jigéen ñi noppi ci ndaje mi, ndaxte sañuñu faa wax. Nañu doon jigéen ñu nangu, ni ko yoon wi tërale.
34妇女在聚会中应当闭口,好像在圣徒的众教会中一样,因为她们是不准讲话的;就如律法所说的,她们应该顺服。
35 Te su ñu bëggee laaj dara, nañu ko laaj seen jëkkër ca kër ga, ndaxte jigéen di wax ci ndajem mbooloom ñi gëm, gàcce la.
35如果她们想要学什么,可以在家里问自己的丈夫,因为妇女在聚会中讲话原是可耻的。
36 Ndax ci yéen la kàddug Yàlla sosoo? Walla ndax ci yéen rekk la agsi?
36难道 神的道是从你们出来的吗?是单单临到你们的吗?
37 Su kenn xalaatee ne, mooy wax ci kàddug Yàlla, walla mu xalaat ne, Xelum Yàlla jagleel na may, na nangu ne lii ma leen bind ndigalu Boroom bi la.
37如果有人自以为是先知或是属灵的,他就应该知道我写给你们的是主的命令;
38 Te su ko xeebee it, ñu xeeb ko.
38如果有人不理会,别人也不必理会他。
39 Kon nag bokk yi, farluleen ci di wax ci kàddug Yàlla, te buleen tere kenn muy wax ay làkk.
39所以我的弟兄们,你们要热切地追求讲道的恩赐,也不要禁止说方言。
40 Waaye nag, na lépp di dox ciy teggin te aw yoon.
40凡事都要规规矩矩地按着次序行。