1 Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si.
1怎样认出 神的灵
2 Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk.
2你们可以这样认出 神的灵:凡是承认耶稣基督是成了肉身来的,那灵就是出于 神。
3 Waaye mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci biir àddina.
3凡是不承认耶稣基督是成了肉身来的,那灵就不是出于 神,而是敌基督者的灵;你们听过他要来,现在他已经在世上了。
4 Yéen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu, ndaxte Ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina.
4孩子们,你们是属于 神的,并且已经胜过他们,因为那在你们里面的比那在世上的更大。
5 Ñoom ci àddina lañu bokk; moo tax ñuy wax waxi àddina, te àddina di leen déglu.
5他们是属于世界的,因此讲论属世的事,世界也就听从他们。
6 Nun nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg.
6我们是属于 神的,认识 神的就听从我们,不属于 神的就不听从我们。这样,我们就可以辨别真理的灵和谬妄的灵了。
7 Samay soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla.
7 神是爱亲爱的,我们应当彼此相爱,因为爱是从 神那里来的。凡是爱人的,都是从 神生的,并且认识 神。
8 Ku bëggul sa mbokk, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla mbëggeel la.
8不爱人的,就不认识 神,因为 神就是爱。
9 Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom.
9 神差遣他的独生子到世上来,要使我们借着他而活; 神的爱就在我们中间显明了。
10 Lii mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar.
10不是我们爱 神,而是 神爱我们,差遣他的儿子为我们的罪作了赎罪祭,这就是爱了。
11 Samay soppe, bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante.
11亲爱的, 神既然这样爱我们,我们也应当彼此相爱。
12 Kenn musul a gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun.
12从来没有人见过 神,我们若彼此相爱, 神就住在我们里面,他的爱也在我们里面得到成全了。
13 Ci lii lanuy xame ne, sax nanu ci Yàlla, te moom itam dëkk na ci nun: sol na nu Xelam.
13 神把他的灵赐给我们,我们就知道我们是住在他里面,他也住在我们里面。
14 Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi yónni na Doom ji, mu nekk Musalkatu àddina.
14父差遣子作世人的救主,这是我们见过的,并且现在作见证。
15 Képp ku nangu ne, Yeesu Doomu Yàlla la, Yàlla dëkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Yàlla.
15凡承认耶稣是 神的儿子的, 神就住在他里面,他也住在 神里面。
16 Mbëggeel gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko. Yàlla mbëggeel la, te képp ku sax ci mbëggeel, yaa ngi sax ci Yàlla, mu dëkk ci yaw.
16 神对我们的爱,我们已经明白了,而且相信了。 神就是爱;住在爱里面的,就住在 神里面, 神也住在他里面。
17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba.
17这样,爱在我们里面就得到成全,使我们在审判的日子,可以坦然无惧。因为他怎样,我们在这世上也怎样。
18 Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw.
18爱里没有惧怕,完全的爱可以把惧怕驱除,因为惧怕含有刑罚,惧怕的人在爱里还没有完全。
19 Danuy wéy ci mbëggeel, ndax moo nu jëkk a bëgg.
19我们爱,因为 神先爱我们。
20 Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo man a bëgg Yàlla mi nga gisul.
20人若说“我爱 神”,却恨他的弟兄,就是说谎的。不爱看得见的弟兄,就不能爱看不见的 神。
21 Te jox na nu ndigal lii: ku bëgg Yàlla, nga bëgg sa mbokk.
21爱 神的,也应当爱弟兄,这就是我们从 神领受的命令。