Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

2 Timothy

1

1 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobareg Yàlla, ngir xamle dund gi nu Yàlla dig te féete ci Kirist Yeesu,
1问安
2 maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
2写信给亲爱的儿子提摩太,愿恩惠、怜悯、平安从父 神和我们的主基督耶稣临到你。
3 Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla, mi may jaamu ci xel mu dal, ni ko samay maam daan defe. Guddi ak bëccëg, bu sama xel demee ci say rangooñ,
3为主作见证不要当作羞耻我感谢 神,就是我像我祖先一样,以清洁的良心所事奉的 神,在祷告中昼夜不断地记念你;
4 ma bëgg laa gis, ba am mbég mu réy.
4一想起你流的眼泪,我就渴望见你,好叫我满有喜乐。
5 Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne, sax na ci yaw it.
5我记得你心里无伪的信心,这信心原先是在你外祖母罗以和你母亲友尼基心里的,我深信也在你的心里。
6 Looloo tax maa ngi lay fàttali, nga xambaat taal bi Yàlla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo.
6为了这缘故,我提醒你,要把 神借着我按手给你的恩赐,像火一样再挑旺起来。
7 Ndaxte Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp.
7因为 神所赐给我们的,不是胆怯的灵,而是有能力、仁爱、自律的灵。
8 Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li ñu ma tëj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xebaar bu baax bi, wéeru ci kàttanu Yàlla.
8所以,不要以给我们的主作见证当作羞耻,也不要以我这为主被囚的当作羞耻,却要为了福音的缘故,靠着 神的大能,与我同受磨难。
9 Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy jëf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Yàlla may ci Kirist Yeesu, ba àddina sosoogul.
9 神救了我们,以圣召呼召我们,不是按照我们的行为,却是按照他自己的计划和恩典;这恩典是在永世之先,在基督耶稣里赐给了我们的,
10 Te léegi biral na ko ci feeñug sunu Musalkat Kirist Yeesu, mi nasaxal dee te feeñal dund ci xebaar bu baax bi, te muy dund gu sax.
10但现在借着我们救主基督耶稣的显现,才表明出来。他废掉了死亡,借着福音把生命和不朽彰显出来。
11 Te Yàlla fal na ma ndaw ak jàngalekat, ngir may yégle xebaar bi;
11为这福音,我被派作传道的、使徒和教师。
12 looloo tax ma jànkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa Ki ma wékk sama yaakaar, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, man na koo denc ba bés ba.
12为了这缘故,我也受这些苦,但我不以为耻,因为我知道我所信的是谁,也深信他能保守我所交托他的,直到那日。
13 Toppal ci tànki wax yu wér yi nga dégge ci man, jàpp ci ak ngëm ak mbëggeel, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist Yeesu.
13你要靠着在基督耶稣里的信心和爱心,常常坚守从我这里听过的话,作为纯正话语的模范;
14 Te nga sàmm bu baax li la Yàlla dénk, wéeru ci Xel mu Sell, mi dëkk ci nun.
14又要靠着那住在我们里面的圣灵,保守所交托你的善道。
15 Xam nga ne, waa diiwaanu Asi gépp, won nañu ma gannaaw, ñu deme niki Fusel ak Ermosen.
15你知道所有在亚西亚的人都离弃了我,他们当中有腓吉路和黑摩其尼。
16 Waaye Onesifor daa na faral di dëfël sama xol; na Boroom bi sotti yërmandeem ci këram. Rusul woon sax ci samay jéng,
16愿主赐怜悯给阿尼色弗一家的人,因为他多次使我畅快,也不以我的锁链为耻;
17 waaye bi mu ñëwee dëkku Room, wut na ma fu ne, ba gis ma.
17他竟然来到罗马,迫切地寻找我,结果找到了。
18 Na ko Boroom bi teeru ak yërmandeem ca bés ba. Umplewoo it coono yi mu daj, ngir dimbali ma ca dëkku Efes.
18(愿主在那日使他从主那里得着怜悯。)你也清楚知道他在以弗所是怎样多方服事我。