1 Bi ñu fa jógee, ñu aw yoon wa jaar dëkku Amfipolis ak Apoloni, door a ñëw Tesalonig, fa Yawut ya am jàngu.
1帖撒罗尼迦的骚动
2 Pool nag dugg ca ñoom, na mu ko daan defe, ba am fa ñetti bésu noflaay, muy werante ak ñoom ci li Mbind mi wax.
2保罗照他的习惯进去,一连三个安息日,根据圣经与他们辩论,
3 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne, fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»
3讲解证明基督必须受害,从死人中复活,说:“我所传给你们的这位耶稣,就是基督。”
4 Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.
4他们中间有人给说服了,就附从了保罗和西拉;还有一大群虔诚的希腊人,和不少显要的妇女。
5 Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yengal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.
5但犹太人嫉妒起来,招聚了一些市井流氓,纠合成群,骚动全城,冲进了耶孙的家,搜索保罗和西拉,要把他们交给民众。
6 Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,
6搜索不到他们,就把耶孙和几个弟兄,拉到地方长官那里,喊叫着说:“这些扰乱天下的人,也到这里来了,
7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
7耶孙却收留他们。这些人都违背凯撒的法令,说另外还有一个王耶稣。”
8 Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool.
8群众和地方长官听见这话,就惊慌起来,
9 Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara.
9取得耶孙和其余的人签保后,才放了他们。
10 Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.
10来到比里亚弟兄们当夜立刻送保罗和西拉往比里亚去。二人到了,就进入犹太人的会堂。
11 Fekk ña fa nekk ñoo gën a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
11这里的人,比帖撒罗尼迦人开明,热切接受主的道,天天考查圣经,要知道所听的是否与圣经相符。
12 Kon nag Yawut yu bare gëm ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana ak ay góor.
12结果他们中间有很多人信了,也有高贵的希腊妇女,男的也不少。
13 Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne, Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
13但帖撒罗尼迦的犹太人,知道保罗又在比里亚宣讲 神的道,就到那里去,煽动挑拨群众。
14 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
14弟兄们立刻把保罗送到海边去;西拉和提摩太仍然留在比里亚。
15 Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu woññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gën a gaaw.
15护送保罗的人带他到了雅典;保罗吩咐他们叫西拉和提摩太赶快去见他,于是他们就回去了。
16 Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.
16在雅典保罗在雅典等候他们的时候,看见满城都是偶像,心灵十分忿激。
17 Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.
17于是在会堂里,同犹太人和虔诚的人辩论;并且天天在市中心和所遇见的人辩论。
18 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgg a wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni, day waare ay yàlla yu nu xamul.»
18还有伊壁鸠鲁派和斯多亚派的哲学家也同他争论,有的说:“这个拾人牙慧的人要说什么呢?”有的说:“他似乎是一个宣传外地鬼神的人。”这是因为保罗传扬耶稣和复活的道理。
19 Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
19他们拉着保罗,把他带到亚略.巴古那里,说:“你所讲的这个新道理,我们可以知道吗?
20 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoon a xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»
20因为你把一切新奇的事,传到我们耳中,我们愿意知道这些事是什么意思。”
21 Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte.
21原来所有雅典人和外侨,专好谈论和打听新奇的事,来打发时间。
22 Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne, farlu ngeen ci diine lool.
22保罗站在亚略.巴古当中,说:“各位雅典人,我看你们在各方面都非常敬畏鬼神。
23 Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.
23我走路的时候,仔细看你们所敬拜的,发现有一座坛,上面写着‘献给不认识的神’。我现在把你们不认识而敬拜的这位神,传给你们。
24 «Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.
24创造宇宙和其中万有的 神,既然是天地的主,就不住在人手所造的殿宇,
25 Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp.
25也不受人手的服事,好像他缺少什么;他自己反而把生命、气息和一切,赐给万人。
26 Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xebla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.
26他从一个本源造出了万族来,使他们住在整个大地上,并且定了他们的期限和居住的疆界,
27 Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.
27要他们寻求 神,或者可以摸索而找到他。其实他离我们各人不远,
28 “Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.”
28因着他我们可以生存、活动、存在,就如你们有些诗人说:‘原来我们也是他的子孙。’
29 Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne, Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel.
29我们既然是 神的子孙,就不应该以为他的神性是好像人用手艺、心思所雕刻的金银石头一样。
30 Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo man a doon ak foo man a nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar.
30过去那无知的时代, 神不加以追究;现在,他却吩咐各处的人都要悔改,
31 Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.»
31因为他已经定好了日子,要借着他所立的人,按公义审判天下,并且使他从死人中复活,给万人作一个可信的凭据。”
32 Bi ñu déggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee, ñii di ko fontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon.»
32众人一听到死人复活的事,就讥笑他,但有的说:“我们要再听听你讲这件事!”
33 Noonu Pool génn ci seen biir.
33这样,保罗就离开他们。
34 Moona am na ñenn ñu taq ci moom te gëm: xàmmees na ci Denis, ku bokk ci mbooloom Areyopas, ak jigéen ju tudd Damaris, ak ñeneen.
34但有几个人接近他,并且信了主,其中有亚略.巴古的议员丢尼修,一个名叫戴马里的女子,还有其他的人。