Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Acts

26

1 Bi mu ko waxee, Agaripa ne Pool: «Jëlal kàddu gi.» Noonu Pool tàllal loxoom, daldi làyyi ne:
1保罗在亚基帕王面前申辩(徒9:3-8,22:6-11)亚基帕对保罗说:“准你为自己申辩。”于是保罗伸手辩护说:
2 «Buur Agaripa, ma làyyi ci sa kanam tey ci lépp, li ma Yawut yiy jiiñ, xol bu sedd la ci man,
2“亚基帕王啊,犹太人控告我的事,今天我可以在你面前辩护,实在是万幸;
3 ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ.
3特别是你熟悉犹太人的一切规例和争论,所以求你耐心听我申诉:
4 «Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.
4我从幼年到现在,在本国、在耶路撒冷为人怎样,犹太人都知道。
5 Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gën a diis ci sunu diine.
5如果他们肯作证的话,他们是早就知道,我是按着我们祖宗最严格的教派,过着法利赛人的生活。
6 Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne, Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam.
6现在我站着受审,是为了对 神向我们祖先的应许存着盼望。
7 Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.
7我们十二支派昼夜切切地事奉 神,都是盼望这应许实现。王啊,我被犹太人控告,正是为了这个盼望。
8 Lu tax seen xel dàq ne, Yàlla dina dekkal ñi dee?
8 神使死人复活,你们为什么认为是不可信的呢?
9 «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne, war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
9从前,我也认为应该多方敌对拿撒勒人耶稣的名。
10 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci saraxalekat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoon a bëgg a rey, ànd naa ci.
10后来就在耶路撒冷这样作了。我得到了众祭司长授权,把许多圣徒关在监里,并且他们被杀的时候,我也表示同意。
11 Daan naa wër jàngoo-jàngu, di leen teg toskare te di leen jéem a weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
11我在各会堂里多次用刑强迫他们说亵渎的话;我非常愤恨他们,甚至追到国外的城巿去迫害他们。
12 «Noonu am bés, may dem dëkku Damas, yor sañ-sañ ak ndigalu saraxalekat yu mag ya.
12“那时候,我得到祭司长的授权和准许,去大马士革。
13 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
13王啊,就在中午的时候,我在路上看见一道光,比太阳更明亮,从天上四面照着我和同行的人。
14 Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
14我们都仆倒在地上,我听见有声音用希伯来话对我说:‘扫罗!扫罗!你为什么迫害我?你要踢刺是难的。’
15 «Noonu ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
15我说:‘主啊,你是谁?’主说:‘我就是你所迫害的耶稣。
16 Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man, ak li ma lay feeñuji.
16你起来,站着,我向你显现,是要指派你为我工作。你要为你所见过的事,和我将要向你显明的事作见证。
17 Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal,
17我要救你脱离这人民和外族人,差遣你到他们那里去,
18 ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, woññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.”
18开他们的眼睛,使他们从黑暗中归向光明,从撒但的权下归向 神,使他们的罪恶得到赦免,并且在那些因信我而成圣的人中同得基业。’
19 «Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu.
19“亚基帕王啊,因此,我没有违背这从天上来的异象,
20 Waaye li tàmbali ci Damas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te woññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu.
20先向大马士革、耶路撒冷、犹太全地的人宣讲,后向外族人宣讲,叫他们悔改,归向 神,行事与悔改的心相称。
21 Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
21犹太人就是为了这缘故在殿里捉住我,想要杀我。
22 Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,
22然而,我得到 神的帮助,直到今日还是站得稳,向尊卑老幼作见证,我所讲的都是众先知和摩西所论的将来必成的事,
23 maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkk a dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.»
23就是基督必须受难,并且从死人中首先复活,把光明的信息传报给这人民和外族人。”
24 Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»
24保罗说服亚基帕王保罗申诉到这里,非斯都大声说:“保罗!你疯了;你的学问太大,使你疯了!”
25 Waaye Pool tontu ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago.
25保罗说:“非斯都大人,我没有疯,我说的都是真实的话,清醒的话。
26 Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne, dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.
26因为王知道这些事,所以我对王坦白直说。我确信这些事没有一件能瞒得过他,因为这不是在背地里作的。
27 Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne, gëm nga.»
27亚基帕王啊,你信先知吗?我知道你是信的。”
28 Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgg a dugale ci gaayi Kirist!»
28亚基帕对保罗说:“你想用这样短短的时间就可以说服我作基督徒吗!”
29 Pool tontu ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»
29保罗说:“无论时间短也好,时间长也好,我向 神所求的,不单是你,而且是今天所有的听众,都能像我一样作基督徒,只是不要有这些锁链。”
30 Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp.
30亚基帕王、总督和百尼基,还有在座的人都站起来,
31 Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.»
31退到一边,彼此谈论,说:“这个人并没有犯过什么该死该绑的罪。”
32 Te Agaripa ne Festus: «Manoon nanu koo yiwi, bu dénkuloon mbiram Sesaar.»
32亚基帕对非斯都说:“这个人若没有向凯撒上诉,早就可以释放了。”