1 Bi ñuy wax ak mbooloo ma, saraxalekat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.
1彼得约翰在公议会受审
2 Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.
2因为使徒教训群众,并且传扬耶稣复活,证明有死人复活这件事,他们就非常恼怒,
3 Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi.
3于是下手拿住使徒。那时天已经晚了,就把他们拘留到第二天。
4 Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni.
4然而有许多听道的人信了,男人的数目,约有五千。
5 Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.
5第二天,犹太人的官长、长老、经学家,都聚集在耶路撒冷,
6 Ràññe nañu ci: Anas, miy saraxalekat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki saraxalekat bu mag bi.
6还有大祭司亚那和该亚法、约翰、亚历山大,以及大祭司的家人,所有的人都在那里。
7 Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
7他们叫使徒都站在当中,查问说:“你们凭什么能力,奉谁的名作这事?”
8 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
8当时彼得被圣灵充满,对他们说:“民众的领袖和长老啊!
9 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
9我们今天受审,如果是为了在那残疾人身上所行的善事,就是这个人怎么会好的,
10 nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp! Ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
10那么,你们各位和以色列全民都应当知道,站在你们面前这人好了,是因拿撒勒人耶稣基督的名。这位耶稣基督,你们把他钉死在十字架上, 神却使他从死人中复活。
11 Yeesu moomu mooy:“Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi,te moo doon doju koñ.”
11他是你们‘建筑工人所弃的石头,成了房角的主要石头。’
12 Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu war a mucce.»
12除了他以外,别无拯救,因为在天下人间,没有赐下别的名,我们可以靠着得救。”
13 Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne, musuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne, daa nañu ànd ak Yeesu.
13他们看见彼得和约翰的胆量,也知道这两个人是没有学问的平民,就很惊奇;同时认出他们是跟耶稣一伙的,
14 Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, mënuñu caa teg dara.
14又看见那医好了的人,和他们一同站着,就没有话可辩驳。
15 Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
15于是吩咐他们到公议会外面去,彼此商议说:
16 ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te mënunu koo weddi.
16“对这些人我们应该怎么办呢?因为有一件人所共知的神迹,借着他们行了出来,所有住在耶路撒冷的人都知道,我们也无法否认。
17 Waaye ngir mbir mi bañ a law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu bañ a waxati ak kenn ci tur woowu.»
17为了避免这件事在民间越传越广,我们应该警告他们,不许再奉这名向任何人谈道。”
18 Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
18于是叫了他们来,严禁他们再奉耶稣的名讲论施教。
19 Waaye Piyeer ak Yowaana tontu leen ne: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla moo jub ci kanam Yàlla, seetleen ko.
19彼得和约翰回答:“听从你们过于听从 神,在 神面前对不对,你们自己说吧!
20 Waaye nun mënunoo bañ a wax li nu gis te dégg ko.»
20我们看见的听见的,不能不说!”
21 Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.
21众人因着所发生的事,都颂赞 神,于是公议会为了群众的缘故,也因为找不到借口惩罚他们,就恐吓一番,把他们放了。
22 Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent-fukki at.
22原来借着神迹医好的那人,有四十多岁了。
23 Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li saraxalekat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.
23信徒同心祈祷彼得和约翰被释放了之后,回到自己的人那里去,把祭司长和长老说的一切,都告诉他们。
24 Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.
24他们听了,就同心向 神高声说:“主啊,你是那创造天地、海洋和其中万物的主宰。
25 Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne:“Lu tax xeeti àddina di bax?Lu tax ñuy fexe lu mënul a am?
25你曾以圣灵借着你仆人我们祖先大卫的口说:‘列国为什么骚动?万民为什么空谋妄想?
26 Buuri àddina dañoo booloo,te kilifa yi dajaloo,di bañ Boroom bi ak Almaseem.”
26地上的君王都起来,首领聚在一起,敌对主和他的受膏者。’
27 Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,
27希律和本丢.彼拉多,外族人和以色列民,真的在这城里聚集,反对你所膏立的圣仆耶稣,
28 te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
28行了你手和你旨意所预定要成就的一切。
29 Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
29主啊,他们恐吓我们,现在求你鉴察,也赐你仆人们大有胆量,传讲你的道。
30 Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
30求你伸手医治,借着你圣仆耶稣的名,大行神迹奇事。”
31 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yengatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
31他们祷告完了,聚会的地方震动起来,他们都被圣灵充满,放胆传讲 神的道。
32 Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
32信徒凡物公用全体信徒一心一意,没有一个人说自己的财物是自己的,他们凡物公用。
33 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
33使徒大有能力,为主耶稣的复活作见证,众人都蒙了大恩。
34 Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njëg gi,
34他们中间没有一个有缺乏的,因为凡有田产房屋的都卖了,把得到的钱拿来,
35 teg ko ci loxoy ndaw ya; ñu di ci sédd, kenn ku nekk li mu soxla.
35放在使徒脚前,照着各人的需要来分配。
36 Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.
36有一个人名叫约瑟,使徒称他为巴拿巴,就是“安慰者”的意思,他是个利未人,生在塞浦路斯。
37 Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.
37他卖掉了自己的田地,把钱拿来,放在使徒的脚前。