1 Am ngëm lii lay tekki: dafa nuy wóor ne, li nuy yaakaar dina am, te it li nu dul gis nekk na.
1论信心
2 Maam ya, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeel leen lu baax.
2因着这信心,古人得到了称许。
3 Ngëm a tax ba nu xam ne, Yàlla sàkk na àddina jaarale ko ci kàddoom, ngir li bët di gis, defarees ko ak lu bët mënul a gis.
3因着信,我们就明白宇宙(“宇宙”或译:“诸世界”或“众世代”)是因着 神的话造成的。这样,那看得见的就是从那看不见的造出来的。
4 Ngëm moo tax ba Abel jébbal Yàlla sarax su gën saraxu Kayin. Ngëmu Abel moo tax ba Yàlla àtte ko ni ku jub, bi mu ko seedeelee ne, saraxam baax na. Te ci kaw ngëm lay wax ba tey, moom mi dee ba noppi.
4信心的伟人因着信,亚伯比该隐献上更美的祭品给 神;借着这信心,他被 神称许为义人,这是 神指着他的礼物所作的见证;他虽然死了,却借着信仍然说话。
5 Ngëm moo tax ba Enog jaarul ci dee. Yàllaa ko yóbbu ca moom, te kenn gisatu ko, ndaxte Yàllaa ko toxal. Ndaxte Mbind mi seedeel na ko ne, laata muy toxu, neex na Yàlla.
5因着信,以诺被迁去了,使他不至于死,人也找不着他,因为 神把他迁去了。原来在迁去以前,他已经得了 神喜悦他的明证。
6 Waaye ku amul ngëm doo man a neex Yàlla, ndaxte ku bëgg a jegeñ Yàlla war ngaa gëm ne, Yàlla am na te dina neexal ñi koy wut.
6没有信,就不能得到 神的喜悦;因为来到 神面前的人,必须信 神存在,并且信他会赏赐那些寻求他的人。
7 Ngëm moo tax ba, bi Yàlla yégalee Nóoyin lu jiitu ci mbir yi dikkagul, mu ragal ba defar gaal ngir musal njabootam. Ngëmam moo tax mu yey niti àddina, ba noppi jot njubte, li Yàllay joxe ci kaw ngëm.
7因着信,挪亚在还没有看见的事上,得了 神的警告,就动了敬畏的心,做了一艘方舟,使他全家得救。借着这信心,他就定了那世代的罪,自己也承受了那因信而来的义。
8 Ngëm moo tax ba Ibraayma déggal Yàlla. Bi ko Yàlla wooyee, mu dem toxu ci menn réew, ma mu waroon a jote ca Yàlla. Noonu la gàddaaye dëkkam te xamul woon fan la jëm.
8因着信,亚伯拉罕在蒙召的时候,就听命往他将要承受为业的地方去;他出去的时候,还不知道要往哪里去。
9 Ngëm a tax ba Ibraayma sanc ci réew, mi ko Yàlla digoon, dëkk ci ay tànt ni doxandéem, moom ak doomam Isaaxa ak sëtam Yanqóoba, fekk sax Yàlla digoon na leen réew mi.
9因着信,他在应许之地寄居,好像是在异乡,与承受同样应许的以撒、雅各一样住在帐棚里。
10 Waaye nag Ibraaymaa ngi doon séentu dëkk bi sax, bi Yàlla tabax te sanc ko.
10因为他等待那座有根基的城,就是 神所设计所建造的。
11 Ngëm moo tax ba Ibraayma, li muy màggat lépp te Saarata mënul woon a am doom, Yàlla def ba mu jur doom, ndaxte dafa gëmoon ne, Yàlla lu mu dige def ko.
11因着信,甚至撒拉,她虽然过了生育的年龄,还是能够怀孕,因为她认为那应许她的是信实的。
12 Looloo tax ba, Ibraayma mi màggat lool, aw xeet jóge ci moom, baree ni biddiiwi asamaan, te sakkan ni suufu tefes, ba kenn mënu koo xayma.
12所以从一个好像已死的人,竟然生出许多子孙来,仿佛天上的星那么众多,海边的沙那么无数。
13 Ñoom ñépp dee nañu ci ngëm. Jotuñu li ñu leen digoon, waaye séen nañu ko fu sore ba nuyu leen, te nangu ne, ay doxandéem ak i gan lañu woon ci àddina.
13这些人都是存着信心死了的,还没有得着所应许的,只不过是从远处看见,就表示欢迎,又承认他们在世上是异乡人,是客旅。
14 Ñiy waxe noonu nag dañuy wone ne, ñoo ngi wut réew mu ñu moomal seen bopp.
14因为说这样话的人,是表明他们在寻求一个家乡。
15 Bu ñu nammoon réew mi ñu jóge, kon dinañu am jotu dellu fa.
15如果他们怀念已经离开了的地方,还有可以回去的机会。
16 Waaye ñu ngi doon séentu réew mu gën, maanaam mi nekk ci asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu koy wooye seen Yàlla, ndaxte defaral na leen ab dëkk.
16但是现在他们所向往的,是一个更美的、在天上的家乡。所以, 神不以他们称他为 神而觉得羞耻;因为他已经为他们预备了一座城。
17 Ngëm moo tax Ibraayma naroon a rey Isaaxa ni sarax, bi ko Yàlla nattoo. Moom mi jotoon dige yi, moo demoon bay saraxe jenn doom ji mu am kepp,
17因着信,亚伯拉罕在受试验的时候,就把以撒献上;这就是那欢喜领受应许的人,献上了自己的独生子;
18 fekk sax Yàlla nee woon na ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
18论到这个儿子,曾经有话说:“以撒生的,才可以称为你的后裔。”
19 Waaye xelu Ibraayma jàppoon na ne, Yàlla am na dooley dekkal néew yi. Te dëgg-dëgg ci misaal dafa mel ni, Isaaxa dafa dee te dekki.
19亚伯拉罕认定, 神能使人从死人中复活,因此,就喻意说,他的确从死里得回他的儿子。
20 Te it ngëm moo tax ba Isaaxa barkeel Yanqóoba ak Esawu, di wax ci mbirum yëf yiy ñëw.
20因着信,以撒给雅各和以扫祝福,论到将来的事。
21 Ngëm moo tax ba, bi Yanqóoba nekkee ci sukkurat, mu barkeel kenn ku nekk ci doomi Yuusufa yi. Moo tax it mu màggal Yàlla, jafandu ci yetam.
21因着信,雅各临死的时候,分别为约瑟的儿子祝福,又倚着杖头敬拜 神。
22 Ngëm moo tax ba, bi Yuusufa nekkee ci sukkurat, mu waxoon ci gàddaay gi bànni Israyil waroon a gàddaaye Misra, di joxe ndigal jëme ci mbirum néewam.
22因着信,约瑟临终的时候,提到以色列子民出埃及的事,并且为自己的骸骨留下遗言。
23 Ngëm moo tax ba, bi Musaa juddoo, ay waajuram nëbb ko lu mat ñetti weer, ndaxte gisoon nañu ne, xale bu taaru la woon, te ragaluñu woon ndigalu buur bi.
23因着信,摩西的父母在摩西生下来以后,因为看见孩子俊美,就把他藏了三个月,不怕王的命令。
24 Ngëm a tax ba bi Musaa màggee, muy bañ ñu koy wooye sëtu Firawna.
24因着信,摩西长大了以后,就拒绝被称为法老女儿的儿子。
25 Bokk coono ak gaayi Yàlla yi moo ko gënaloon muy bànneexu ab diir ci bàkkaar.
25他宁愿选择和 神的子民一同受苦,也不肯享受罪恶中暂时的快乐。
26 Ñu toroxal ko ngir Almasi bi mi ngi mel ci moom ni alal ju ëpp alali Misra yépp, ndaxte yool bi la doon séentu.
26在他看来,为着基督受的凌辱,比埃及的财物更宝贵,因为他注视将来的赏赐。
27 Ngëm moo tax mu jóge Misra te ragalul merum buur bi. Dafa muñ, mel ni nit kuy gis Yàlla, mi kenn mënul a teg bët.
27因着信,他离开了埃及,不怕王的忿怒;因为他坚定不移,就像看见了人不能看见的 神。
28 Ngëm moo tax mu sos màggalu Bésu Jéggi ba, di wis deret ci bunt yi, ngir malaakam Yàqkat mi bañ a laal taawi bànni Israyil.
28因着信,他立了逾越节和洒血的礼,免得那灭命的侵犯以色列人的长子。
29 Ngëm moo tax ba bànni Israyil jaar ci Géej gu xonq gi, mel ni kuy jaar ci yoonu suuf su wow. Waaye bi ci waa Misra yi doon jéem a jaar, ñoom ñu daldi lab.
29因着信,他们走过了红海,好像走过旱地一样;埃及人也试着要过去,就被淹没了。
30 Ngëm moo tax miir yi wëroon dëkku Yeriko màbb, gannaaw ba ko bànni Israyil wëree lu mat juróom-ñaari fan.
30因着信,耶利哥的城墙被围绕了七天,就倒塌了。
31 Ngëm moo tax ba Raxab jigéenu moykat bi mucc, keroog ba ñuy bóom ñi déggadiloon Yàlla, ndax li mu teeru woon yëddukat ya teeru bu ànd ak jàmm.
31因着信,妓女喇合和和平平接待了侦察的人,就没有和那些不顺从的人一起灭亡。
32 Lu ma ci war a tegaat? Ndaxte awma jotu wax ci mbirum Sedeyon, Barag, Samson, Yefte, Daawuda, Samwil ak yonent yi.
32我还要再说什么呢?如果再要述说基甸、巴拉、参孙、耶弗他、大卫、撒母耳和众先知的事,时间就不够了。
33 Seen ngëm a tax ñu noot ay buur, di doxal yoon tey jot li Yàlla dige. Ngëm moo tax ba tey, ñu tëj gémmiñu gaynde yi,
33他们借着信,就战胜了敌国,伸张了正义,得到了应许,堵住了狮子的口,
34 fey dooley safara, rëcc ci jaasi, ñu génn ci néew doole, dugg ci kàttan, doon ay jàmbaar, dàq xarekat, ya jóge bitim réew.
34消灭了烈火的威力,逃脱了刀剑的锋刃,软弱变成刚强,在战争中显出大能,把外国的军队击退。
35 Ngëm moo tax ba ay jigéen gis ñu dekkal seeni néew, delloo leen ko; ñeneen ñi ñu metital leen, te bañ ku leen musal, ngir jot ndekkite lu gën.
35有些妇女得回从死里复活的亲人;但也有些人忍受了酷刑,不肯接受释放,为的是要得着更美的复活。
36 Ñeneen ñi dékku nañu ay xas ak ay yar, ay jéng ak kaso yi.
36又有些人遭受了戏弄、鞭打,甚至捆锁、监禁;
37 Ñii, sànni nañu leen ay xeer ba ñu dee; ñii, ñu xar leen ñaar; ñii, ñu reye leen jaasi. Ñu ngi doon wëndéelu, sol ay deri xar ak yu bëy, di ay walaakaana; ñu di leen sonal, di leen fitnaal.
37被石头打死,被锯锯死,(后期抄本在此加上“受试探”)被刀杀死。他们披着绵羊山羊的皮到处奔跑、受穷乏、遭患难、被虐待;
38 Ñu ngi leen doon def noonu, fekk àddina sax yelloowul leen. Ñu ngi doon wëreelu ci àll yi ak ci tund yi, dal ci xunti yi ak ci kàmb yi.
38原是这世界不配有的人。他们飘流无定,在旷野、山岭、石洞和地穴栖身。
39 Nit ñooñu ñépp, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeeloon leen lu baax. Moona de, jotuñu li Yàlla dige woon,
39所有这些人都借着信得了称许,却还没有得着所应许的;
40 ndaxte Yàlla dafa tëral lu gën ci nun te bëggu leen a yeggale cig mat, fi ak ànduñu ci ak nun.
40因为 神已经为我们预备了更美的事,使他们若不跟我们在一起,就不能完全。