1 Yàlla dige na ne, dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
1信的人可以进入安息
2 Nun jot nanu xebaar bu baax bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu.
2因为有福音传给我们,像传给他们一样,只是他们所听见的道,对他们没有益处,因为他们没有用信心与所听见的打成一片(“没有用信心与所听见的打成一片”,有古卷作“没有用信心与听从这道的人打成一片”)。
3 Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:«Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom-ñaareelu fan ba,
3然而我们信了的人,就可以进入那安息。正如 神所说:“我在烈怒中起誓说,他们绝不可进入我的安息!”其实 神的工作,从创立世界以来已经完成了。
4 am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Yàlla noppalu na ci liggéeyam béppca juróom-ñaareelu fan ba.»
4因为论到第七日,他在圣经某一处说:“在第七日 神歇了他的一切工作。”
5 Te it waxoon na ci baat yi nu jot a lim ba noppi:«Duñu dugg mukk ci sama noflaay.»
5但在这里又说:“他们绝不可进入我的安息。”
6 Kon am na ñu ci war a dugg ba tey. Te ñi jëkkoon a jot xebaar bu baax bi, dugguñu ci ndax seen déggadi.
6既然这安息还留着要让一些人进去,但那些以前听过福音的人,因为不顺从不得进去;
7 Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii,» bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jot a lim:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp.»
7所以 神就再定一个日子,就是过了很久以后,借着大卫所说的“今天”,就像前面引用过的:“如果你们今天听从他的声音,就不要硬着心。”
8 Su Yosuwe duggaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés.
8如果约书亚已经使他们享受了安息, 神后来就不会再提到别的日子了。
9 Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom-ñaareelu fan ba.
9这样看来,为了 神的子民,必定另外有一个“安息日”的安息保留下来。
10 Ndaxte képp ku mas a dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla.
10因为那进入 神安息的人,就歇了自己的工作,好像 神歇了自己的工作一样。
11 Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn bañ a déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
11所以,我们要竭力进入那安息,免得有人随着那不顺从的样子就跌倒了。
12 Xam nanu ne, kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
12 神的道是活的、有效的 神的道是活的,是有效的,比一切两刃的剑更锋利,甚至可以刺入剖开灵与魂,关节与骨髓,并且能够辨明心中的思想和意念。
13 Te itam amul mbindeef mu man a nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu war a àtte.
13被造的在 神面前没有一样不是显明的,万有在他的眼前都是赤露敞开的;我们必须向他交帐。
14 Gannaaw am nanu saraxalekat bu mag-a-mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
14我们的大祭司耶稣我们既然有一位伟大的、经过了众天的大祭司,就是 神的儿子耶稣,就应该坚持所宣认的信仰。
15 Saraxalekat bu mag bi nu am, du ku mënul a bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
15因为我们的大祭司并不是不能同情我们的软弱,他像我们一样,也曾在各方面受过试探,只是他没有犯罪。
16 Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
16所以,我们只管坦然无惧地来到施恩的宝座前,为的是要领受怜悯,得到恩惠,作为及时的帮助。