1 Gannaaw loolu Yeesu dafa jàll dexu Galile, maanaam dexu Tiberyàdd.
1给五千人吃饱的神迹(太14:13-21;可6:32-44;路9:10-17)
2 Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon nañu firnde yooyee mu wone, bi mu wéralee jarag ya.
2有一大群人,因为看见了他在病人身上所行的神迹,就跟随了他。
3 Yeesu daldi yéeg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem.
3耶稣上了山,同门徒坐在那里。
4 Fekk na booba bésu Jéggi ba, di màggalu Yawut ya, jubsi.
4那时犹太人的逾越节近了。
5 Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu réy di ñëw ci moom, mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu, mu nu leen man a dundale?»
5耶稣举目观看,见一大群人向他走过来,就对腓力说:“我们从哪里买饼给这些人吃呢?”
6 Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nar a def.
6他说这话,是要试验腓力,因他自己早已知道要怎样作。
7 Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen man a doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.»
7腓力回答:“就算二百银币买的饼,每人分一点,也是不够的。”
8 Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
8有一个门徒,就是西门.彼得的弟弟安得烈,对耶稣说:
9 «Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?»
9“这里有个小孩子,带着五个大麦饼、两条鱼;只是分给这么多人,有什么用呢?”
10 Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni.
10耶稣吩咐他们:“你们叫众人坐下。”原来那地方的草很多,众人就坐下,单是男人的数目约有五千。
11 Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk.
11耶稣拿起饼来,祝谢了,就分给坐着的人;分鱼也是这样,都是随着他们所要的。
12 Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
12他们吃饱了之后,耶稣对门徒说:“把剩下的零碎收拾起来,免得浪费。”
13 Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk.
13门徒就把众人吃剩那五个大麦饼的零碎收拾起来,装满了十二个篮子。
14 Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi war a ñëw ci àddina!»
14众人看见耶稣所行的神迹,就说:“这真是那要到世上来的先知。”
15 Yeesu gis ne dañu koo nar a jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.
15耶稣知道群众要来强迫他作王,就独自又退到山上去了。
16 Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga,
16耶稣在海面上行走(太14:22-33;可6:47-51)到了晚上,他的门徒下到海边去。
17 dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom.
17他们上了船,要渡海往迦百农去。那时天已经黑了,耶稣还没有到他们那里。
18 Dex gi yengu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.
18忽然海上起了狂风,波浪翻腾。
19 Bi ñu joowee lu war a tollook juróom benni kilomet, ñu séen Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, jëm ci ñoom, ñu daldi tiit.
19门徒摇橹约行了五六公里,看见耶稣在海面上行走,渐渐靠近船,就害怕起来。
20 Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!»
20耶稣对他们说:“是我,不要怕。”
21 Noonu ñu nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa ñu bëggoon a wàcc.
21他们这才把他接上船,船就立刻到了他们要去的地方。
22 Ca ëllëg sa mbooloo, ma des ca geneen wàllu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam nañu ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte ñoom rekk a àndoon.
22耶稣是生命的食物第二天,站在海那边的群众,看见只有一只小船留在那里,并且知道耶稣没有和他的门徒一同上船,门徒是自己去的;
23 Waaye yeneen gaal yu jóge dëkku Tiberyàdd ñëw, teer ca wetu fa ñu lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Yàlla ba noppi.
23不过有几只从提比里亚来的船停在那里,靠近他们在主祝谢以后吃饼的地方。
24 Bi mbooloo ma gisee ne, Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, ñu dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum.
24群众见耶稣和门徒都不在那里,就上船往迦百农去找耶稣。
25 Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
25他们在对岸找到了耶稣,就问他:“拉比,你几时到这里来的?”
26 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.
26耶稣回答:“我实实在在告诉你们,你们找我,不是因为看见了神迹,而是因为吃了饼又吃饱了。
27 Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
27不要为那必朽坏的食物操劳,却要为那存到永生的食物操劳,就是人子所要赐给你们的,因为人子是父 神所印证的。”
28 Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu war a liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?»
28众人又问他:“我们应该作什么,才算是作 神的工作呢?”
29 Yeesu tontu leen ne: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
29耶稣回答:“信 神所差来的,就是作 神的工了。”
30 Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu man a won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nar a def?
30于是他们就说:“你要行什么神迹,让我们看了就信你呢?你到底能作什么呢?
31 Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
31我们的祖宗在旷野吃过吗哪,正如经上所记:‘他把从天上来的食物赐给他们吃。’”
32 Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
32耶稣对他们说:“我实实在在告诉你们,不是摩西把那从天上来的食物赐给你们,而是我父把天上来的真食物赐给你们;
33 Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
33因为 神的食物就是从天上降下来,把生命赐给世人的那一位。”
34 Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
34他们对耶稣说:“主啊,求你常把这食物赐给我们。”
35 Yeesu tontu leen ne: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
35耶稣说:“我就是生命的食物,到我这里来的,必定不饿;信我的,永远不渴。
36 Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
36但我告诉你们,你们虽然见了我,还是不信。
37 Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
37凡是父赐给我的人,必到我这里来;到我这里来的,我决不丢弃他,
38 Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
38因为我从天上降下来,不是要行自己的意思,而是要行那差我来者的旨意。
39 Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.
39那差我来者的旨意就是:他所赐给我的人,我连一个也不失落,并且在末日我要使他们复活。
40 Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»
40因为我父的旨意,是要使所有看见了子而信的人有永生,并且在末日我要使他们复活。”
41 Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: «Maay ñam wi wàcce ci asamaan.»
41犹太人因为耶稣说“我是从天上降下来的食物”,就纷纷议论他。
42 Ñu naan: «Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mi ngi jóge asamaan?»
42他们说:“这不是约瑟的儿子耶稣吗?他的父母我们不都认识吗?他现在怎么说‘我是从天上降下来的’呢?”
43 Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen ñurumtu bi.
43耶稣回答:“你们不要彼此议论。
44 Kenn mënul a ñëw ci man te Baay, bi ma yónni, xiirtalu la ci, te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
44如果不是差我来的父吸引人,就没有人能到我这里来;到我这里来的,在末日我要使他复活。
45 Yonent yi bind nañu kàddu gii: “Yàlla dina leen jàngal ñoom ñépp.” Kon nag ku déglu te nangu waxi Baay bi, dina ñëw ci man.
45先知书上记着:‘众人都必受 神的教导。’凡听见从父那里来的教训而又学习的,必到我这里来。
46 Tekkiwul ne kenn mas na gis Baay bi. Ki jóge ci Yàlla doŋŋ a ko gis.
46这不是说有人见过父;只有从 神那里来的那一位,他才见过父。
47 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku gëm am nga dund gu dul jeex.
47我实实在在告诉你们,信的人有永生。
48 Maay ñam wiy joxe dund.
48我就是生命的食物,
49 Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu.
49你们的祖宗在旷野吃过吗哪,还是死了。
50 Waaye ñam wiy wàcce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee.
50这是从天上降下来的食物,使人吃了就不死。
51 Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina man a dund.»
51我就是从天上降下来生命的食物,人若吃了这食物,就必活到永远。我要赐的食物就是我的肉,是为了世人的生命而赐的。”
52 Noonu Yawut ya werante werante bu tàng ci seen biir naan: «Naka la nu waa jii man a joxe yaramam, ngir nu lekk ko?»
52于是,犹太人彼此争论,说:“这个人怎能把他的肉给我们吃呢?”
53 Yeesu ne leen: «Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci yéen.
53耶稣就对他们说:“我实实在在告诉你们,你们若不吃人子的肉,不喝人子的血,就没有生命在你们里面。
54 Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
54吃我肉、喝我血的,就有永生,在末日我要使他复活;
55 Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi.
55因为我的肉是真正的食物,我的血是真正的饮料。
56 Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom.
56吃我肉、喝我血的人,就住在我里面,我也住在他里面。
57 Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.
57正如永活的父差遣了我,我也因父活着;照样,吃我肉的人也必因我而活。
58 Kon nag ñam, wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam, wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.»
58这就是从天上降下来的食物,不像吗哪,你们的祖宗吃过,还是死了;吃这食物的,必活到永远。”
59 Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngale ca jàngu ba ca Kapernawum.
59这些话是耶稣在迦百农会堂里教导人的时候说的。
60 Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngale mii de, jafe na! Kan moo ko man a déglu?»
60永生之道他的门徒中,有许多人听了,就说:“这话很难,谁能接受呢?”
61 Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leen a jaaxal?
61耶稣心里知道门徒为了这事议论纷纷,就对他们说:“这话使你们动摇吗?
62 Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoon a nekk?
62如果你们看见人子升到他原来所在的地方,又怎样呢?
63 Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
63使人活的是灵,肉体是无济于事的。我对你们所说的话是灵、是生命。
64 Waaye am na ci seen biir ñu ko gëmul.» Ndaxte Yeesu xamoon na ca njàlbéen ga ñan ñoo ko waroon a gëmadi ak kan moo ko waroon a wor.
64然而你们中间却有不信的人。”原来从起初耶稣就知道那些不信的是谁,那要把他出卖的又是谁。
65 Mu dolli ca it ne: «Looloo tax ma ne, kenn mënul a ñëw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.»
65耶稣跟着说:“所以我对你们说过,如果不是父所赐的,没有人能到我这里来。”
66 Ci loolu taalibeem yu bare dëpp, bañatee ànd ak moom.
66从此,他的门徒中有许多人退去了,不再与他同行。
67 Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Mbaa bëgguleen a dem, yéen itam?»
67于是耶稣对十二门徒说:“你们也想离去吗?”
68 Simoŋ Piyeer ne ko: «Boroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor kàddu yiy joxe dund gu dul jeex.
68西门.彼得回答:“主啊,你有永生之道,我们还跟从谁呢?
69 Léegi nun gëm nanu te xam nanu ne, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
69我们已经相信,并且知道你是 神的圣者。”
70 Yeesu daldi tontu ne leen: «Xanaa du maa leen tànn, yéen fukk yi ak ñaar? Moona, am na ci yéen koo xam ne seytaane la!»
70耶稣说:“我不是拣选了你们十二个人吗?但你们中间有一个是魔鬼。”
71 Yudaa miy doomu Simoŋ Iskariyo la doon wax. Ndeke Yudaa, la muy bokk lépp ca fukki taalibe ya ak ñaar, moo ko naroon a wor.
71耶稣这话是指着加略人西门的儿子犹大说的,因为他虽然是十二门徒之一,却要出卖耶稣。