1 Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko.
1失羊的比喻(太18:12-14)
2 Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!»
2法利赛人和经学家,纷纷议论说:“这个人接待罪人,又和他们一起吃饭。”
3 Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen:
3耶稣就对他们讲了这个比喻,说:
4 «Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, toppi ma réer, ba gis ko?
4“你们中间谁有一百只羊,失去一只,不把九十九只留下在旷野,去寻找那失落的,直到找着呢?
5 Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga.
5既找着了,就欢欢喜喜地放在肩上,
6 Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.”
6回到家里,请朋友邻舍来,对他们说:‘请大家和我一同欢乐,因为我失去的羊已经找到了!’
7 «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.
7我告诉你们,因为一个罪人悔改,天上也要这样为他欢乐,比为九十九个不用悔改的义人欢乐更大。
8 «Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko?
8失银币的比喻“或是一个女人,有十个银币,失去一个,哪能不点上灯,打扫屋子,细细地找,直到找着呢?
9 Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.”
9既找着了,就请朋友邻舍来,说:‘请大家和我一同欢乐,因为我失去的那个银币,已经找到了。’
10 Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.»
10我告诉你们,因为一个罪人悔改, 神的使者也必这样为他欢乐。”
11 Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom.
11浪子的比喻耶稣又说:“某人有两个儿子。
12 Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may war a féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam.
12小儿子对父亲说:‘爸爸,请把我应得的家业给我。’父亲就把财产分给他们两兄弟。
13 Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom.
13过了不多几天,小儿子收拾一切,到远方去了,在那里生活放荡,浪费钱财。
14 Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.
14他花尽了一切所有的,那地方又遇上了严重的饥荒,就穷困起来;
15 Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.
15于是他去投靠当地的一个居民。那人打发他到田里去放猪,
16 Mu xiif ba bëgg a lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
16他恨不得吃猪所吃的豆荚,可是没有人给他。
17 Mujj xelam dellusi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgg a dee ak xiif!
17他醒悟过来,说:‘我父亲有那么多雇工,又有丰富的食物,我却要在这里饿死吗?
18 Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
18我要起来,到我父亲那里去,对他说:爸爸,我得罪了天,也得罪了你,
19 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
19不配再称为你的儿子,把我当作一个雇工吧!’
20 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
20于是他起来往父亲那里去。他还在远处时,他父亲看见了他,就动了慈心,跑过去抱着他,连连与他亲嘴。
21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
21儿子说:‘爸爸,我得罪了天,也得罪了你,不配再称为你的儿子。’
22 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gën a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
22父亲却吩咐仆人说:‘快把那最好的袍子拿来给他穿,把戒指戴在他手上,把鞋穿在他脚上,
23 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
23把肥牛犊牵来宰了,我们要吃喝快乐,
24 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.
24因为我这儿子是死而复活、失而又得的。’他们就欢乐起来。
25 «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc.
25“那时,大儿子正在田里。他回来离家不远的时候,听见音乐跳舞的声音,
26 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.
26就叫了一个仆人来,问他这是怎么一回事。
27 Mu tontu ko: “Sa rakk moo dellusi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibbisi na ci jàmm.”
27仆人说:‘你弟弟回来了,你父亲因为他平安无恙地回来,就宰了肥牛犊。’
28 «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, bañ a dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg.
28大儿子就生气,不肯进去;父亲出来劝他。
29 Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit.
29他对父亲说:‘你看,我服事你这么多年,从来没有违背过你的命令,可是你没有给我一只山羊羔,叫我和朋友一同欢乐。
30 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.”
30但你这个儿子,常常跟娼妓在一起,花尽了你的财产,他一回来,你倒为他宰杀肥牛犊!’
31 Noonu baay bi tontu ko ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom.
31父亲对他说:‘孩子,你常跟我在一起,我的一切都是你的。
32 Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»
32只是因为你这个弟弟是死而复活、失而又得的,我们应该欢喜快乐。’”